🔥 0 fan yu toftaloo
📖 Simoore bu gudde — xaajoo ci yeneen ndogal yu ndaw (11 Aaya)
📚 Simoore yépp
30%
🎤 Bësal signe mikoro 🎙️ ci wet Aaya bu ne ngir fab sa baat, gannaaw fa dégg te méngale ak qaari bi.
0/11
62:1 🔁 0/5
يُسَبِّحُ لِلَّهِ مَا فِي ٱلسَّمَٰوَٰتِ وَمَا فِي ٱلۡأَرۡضِ ٱلۡمَلِكِ ٱلۡقُدُّوسِ ٱلۡعَزِيزِ ٱلۡحَكِيمِ  ۝١
Yusabbihu lilaahi maa fis samaawaati wa maa fil ardil Malikil Quddoosil `Azeezil Hakeem
Ñi nekk ci asamaan yeek suuf si ña ngay sàbbaal Yàlla, miy Buur, bu Sell, di Boroom Kàttan, di Ku xereñ.
🎤 Sa fab:
62:2 🔁 0/5
هُوَ ٱلَّذِي بَعَثَ فِي ٱلۡأُمِّيِّـۧنَ رَسُولًا مِّنۡهُمۡ يَتۡلُواْ عَلَيۡهِمۡ ءَايَٰتِهِۦ وَيُزَكِّيهِمۡ وَيُعَلِّمُهُمُ ٱلۡكِتَٰبَ وَٱلۡحِكۡمَةَ وَإِن كَانُواْ مِن قَبۡلُ لَفِي ضَلَٰلٍ مُّبِينٍ  ۝٢
Huwal lazee ba`asa fil ummiyyeena Rasoolam min hum yatloo `alaihim aayaatihee wa yuzakkeehim wa yu`allimuhumul Kitaaba wal Hikmata wa in kaano min qablu lafee dalaalim mubeen
Moom mooy ki yónni ci araab yi ab Yonent bu bokk ci ñoom bu leen di jàngal ay Laayam, di leen jàngal Alxuraan ak Sunna, te ñoom bu jëkkoon ña nga woon ci réer gu sore,
🎤 Sa fab:
62:3 🔁 0/5
وَءَاخَرِينَ مِنۡهُمۡ لَمَّا يَلۡحَقُواْ بِهِمۡۚ وَهُوَ ٱلۡعَزِيزُ ٱلۡحَكِيمُ  ۝٣
Wa aakhareena minhum lammaa yalhaqoo bihim wa huwal `azeezul hakeem
ak ci ñeneen ñoo xam ne dabaguñuleen. Te moom Yàlla Mooy boroom Kàttan, di Ku Xereñ.
🎤 Sa fab:
62:4 🔁 0/5
ذَٰلِكَ فَضۡلُ ٱللَّهِ يُؤۡتِيهِ مَن يَشَآءُۚ وَٱللَّهُ ذُو ٱلۡفَضۡلِ ٱلۡعَظِيمِ  ۝٤
Zaalika fadlul laahi yu`teehi many-yashaaa; wallaahu zul fadil `azeem
Loolu ngënéelul Yàlla la moo koy jox ku ko soob. Te Yàlla mooy boroom Ngënéel lu màgg li.
🎤 Sa fab:
62:5 🔁 0/5
مَثَلُ ٱلَّذِينَ حُمِّلُواْ ٱلتَّوۡرَىٰةَ ثُمَّ لَمۡ يَحۡمِلُوهَا كَمَثَلِ ٱلۡحِمَارِ يَحۡمِلُ أَسۡفَارَۢاۚ بِئۡسَ مَثَلُ ٱلۡقَوۡمِ ٱلَّذِينَ كَذَّبُواْ بِـَٔايَٰتِ ٱللَّهِۚ وَٱللَّهُ لَا يَهۡدِي ٱلۡقَوۡمَ ٱلظَّٰلِمِينَ  ۝٥
Masalul lazeena hum milut tawraata summa lam yahmiloonhaa kamasalil himaari yah milu asfaaraa; bi`sa masalul qawmil lazeena kaazzaboo bi aayaatil laah; wallaahu laa yahdil qawmazzaalimeen
Misaalum ñi ñu wàcceeloon Tawraat te jëfewunu ko ñi ngi melni mbaam mu sëfi téere. Aka bon misaalum nit ñooñu nga xam ne dañoo weddi kàdduy Yàlla te Yàlla du gindi mukk aw nit ñu di ay tooñkat.
🎤 Sa fab:
62:6 🔁 0/5
قُلۡ يَٰٓأَيُّهَا ٱلَّذِينَ هَادُوٓاْ إِن زَعَمۡتُمۡ أَنَّكُمۡ أَوۡلِيَآءُ لِلَّهِ مِن دُونِ ٱلنَّاسِ فَتَمَنَّوُاْ ٱلۡمَوۡتَ إِن كُنتُمۡ صَٰدِقِينَ  ۝٦
Qul yaaa ayyuhal lazeena haadoo in za`amtum annakum awliyaaa`u lilaahi min doonin naasi fatamannawul mawta in kuntum saadiqeen
Waxal ne : "Eey yéen Yahuud yi ! Su fekkee ne nii ngeen méngook Yàllaay, kon ñaan leen dee, su fekkee ne dëggu ngeen”.
🎤 Sa fab:
62:7 🔁 0/5
وَلَا يَتَمَنَّوۡنَهُۥٓ أَبَدَۢا بِمَا قَدَّمَتۡ أَيۡدِيهِمۡۚ وَٱللَّهُ عَلِيمُۢ بِٱلظَّٰلِمِينَ  ۝٧
Wa laa yatamannaw nahooo abadam bimaa qaddamat aydeehim; wallaahu `aleemum bix zaalimeen
Dunu ko ñaan mukk ngir (la ñu jëf cik caay-caay). Yàlla ku Xamaakoon la tooñkat yi.
🎤 Sa fab:
62:8 🔁 0/5
قُلۡ إِنَّ ٱلۡمَوۡتَ ٱلَّذِي تَفِرُّونَ مِنۡهُ فَإِنَّهُۥ مُلَٰقِيكُمۡۖ ثُمَّ تُرَدُّونَ إِلَىٰ عَٰلِمِ ٱلۡغَيۡبِ وَٱلشَّهَٰدَةِ فَيُنَبِّئُكُم بِمَا كُنتُمۡ تَعۡمَلُونَ  ۝٨
Qul innal mawtal lazee tafirroona minhu fa innahoo mulaaqeekum summa turaddoona ilaa `Aalimil Ghaibi wash shahaadati fa yunabbi`ukum bimaa kuntum ta`maloon
Waxal ne : “Dee gi ngeen di daw dana dajeek yéen. Ba noppi ñu delloo leen ca Yàlla mi xam kumpaak li feeñ mu di leen xibaar la ngeen daan def”.
🎤 Sa fab:
62:9 🔁 0/5
يَٰٓأَيُّهَا ٱلَّذِينَ ءَامَنُوٓاْ إِذَا نُودِيَ لِلصَّلَوٰةِ مِن يَوۡمِ ٱلۡجُمُعَةِ فَٱسۡعَوۡاْ إِلَىٰ ذِكۡرِ ٱللَّهِ وَذَرُواْ ٱلۡبَيۡعَۚ ذَٰلِكُمۡ خَيۡرٌ لَّكُمۡ إِن كُنتُمۡ تَعۡلَمُونَ  ۝٩
Yaaa ayyuhal lazeena aamanoo izaa noodiya lis-Salaati miny yawmil Jumu`ati fas`aw ilaa zikril laahi wa zarul bai`; zaalikum khayrul lakum in kuntum ta`lamoon
Eey yéen ñi gëm ! Saa suñu wootee ngir julli ci bisub Àjjuma, dawleen jëm ci tudd Yàlla te nangeen fa ne ñukk njaay ma bàyyi ko. Looloo gën ci yéen de, cëy bu ngeen xamoon!
🎤 Sa fab:
62:10 🔁 0/5
فَإِذَا قُضِيَتِ ٱلصَّلَوٰةُ فَٱنتَشِرُواْ فِي ٱلۡأَرۡضِ وَٱبۡتَغُواْ مِن فَضۡلِ ٱللَّهِ وَٱذۡكُرُواْ ٱللَّهَ كَثِيرًا لَّعَلَّكُمۡ تُفۡلِحُونَ  ۝١٠
Fa-izaa qudiyatis Salaatu fantashiroo fil ardi wabtaghoo min fadlil laahi wazkurul laaha kaseeral la`allakum tuflihoon
Su julli gi jeexee, na ngeen tasaaroo ci suuf si, tey sàkku ci xeewali Yàlla yi, te na ngeen di tudd Yàlla lu bari ndax amaana ngeen baaxle.
🎤 Sa fab:
62:11 🔁 0/5
وَإِذَا رَأَوۡاْ تِجَٰرَةً أَوۡ لَهۡوًا ٱنفَضُّوٓاْ إِلَيۡهَا وَتَرَكُوكَ قَآئِمًاۚ قُلۡ مَا عِندَ ٱللَّهِ خَيۡرٌ مِّنَ ٱللَّهۡوِ وَمِنَ ٱلتِّجَٰرَةِۚ وَٱللَّهُ خَيۡرُ ٱلرَّٰزِقِينَ  ۝١١
Wa izaa ra`aw tijaaratan aw lahwanin faddooo ilaihaa wa tarakooka qaaa`imaa; qul maa `indal laahi khairum minal lahwi wa minat tijaarah; wallaahu khayrur raaziqeen
Te saa su ñu gesee am njoló walla am po danuy buur jëm ca, bàyyi la nga ne saŋŋ taxaw. Waxal ne: “La nekk fa Yàlla moo gën fuuf am po te moo gën it am njoló, te Yàlla moo di Gën ji kuy wërsëgël”.
🎤 Sa fab:
💡 Bësal baat bu nëbbu ngir wone ko ci diir bu gàtt — sa yokkute dañu koy denc ci boppam.

🎉
🎊 Baax na! Fonk bi Mat na
Mishary Rashid Alafasy
Mahmoud Khalil Al-Husary
Abdurrahman As-Sudais
Mohamed Siddiq Al-Minshawi
Abdul Basit Abdul Samad
Ali Al-Hudhaify
Ahmed ibn Ali al-Ajamy
Abu Bakr Ash-Shaatree
Muhammad Ayyoub
Abdullah Basfar
Abdullah Al-Juhani
Maher Al Muaiqly
0:00
0:00
-

Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers