Simoore Al-Mulk ci Aarabu ak Wolof

Jàng Simoore Al-Mulk ak tekkim wolof bu mat sëkk, ak baat. Tekki ayaa bu ne. (30 Aaya — مكية). Al-Mulk Dégg, Al-Mulk Tekki, Al-Mulk mp3, Al-Mulk pdf.

Jàng te Dégg Simoore Al-Mulk

🎧 Aaya
M Mishary Rashid Alafasy
M Mahmoud Khalil Al-Husary
A Abdurrahman As-Sudais
M Mohamed Siddiq Al-Minshawi
A Abdul Basit Abdul Samad
A Ali Al-Hudhaify
A Ahmed ibn Ali al-Ajamy
A Abu Bakr Ash-Shaatree
M Muhammad Ayyoub
A Abdullah Basfar
A Abdullah Al-Juhani
M Maher Al Muaiqly
x1
تَبَارَكَ الَّذِي بِيَدِهِ الْمُلْكُ وَهُوَ عَلَىٰ كُلِّ شَيْءٍ قَدِيرٌ ۝١
📖 Tekki Aaya 1
Barkeel na (Yàlla) mi nga xam ne nguur gaa ngi ci loxom, te Moom man na Lépp lu ne.
الَّذِي خَلَقَ الْمَوْتَ وَالْحَيَاةَ لِيَبْلُوَكُمْ أَيُّكُمْ أَحْسَنُ عَمَلًا ۚ وَهُوَ الْعَزِيزُ الْغَفُورُ ۝٢
📖 Tekki Aaya 2
Mooy ki bind dee ak dund ngir nattu leen ci ana kan koo gën a rafet jëf, te Moom (Yàlla) moo di boroom Kàttan gi, di Jéggalaakoon bi.
الَّذِي خَلَقَ سَبْعَ سَمَاوَاتٍ طِبَاقًا ۖ مَّا تَرَىٰ فِي خَلْقِ الرَّحْمَٰنِ مِن تَفَاوُتٍ ۖ فَارْجِعِ الْبَصَرَ هَلْ تَرَىٰ مِن فُطُورٍ ۝٣
📖 Tekki Aaya 3
Mooy ki bind juróom-ñaari asamaan yu tegloo doo gis kenn roobaate ci bindug Yërëmaakoon bi. Dellul xool. Moo ndax danga gis genn sutaate ?
ثُمَّ ارْجِعِ الْبَصَرَ كَرَّتَيْنِ يَنقَلِبْ إِلَيْكَ الْبَصَرُ خَاسِئًا وَهُوَ حَسِيرٌ ۝٤
📖 Tekki Aaya 4
Topp, nga déllu xool ñaari yoon : da koy délloosiwaat ci yaw rekk waaye du man a gis sikk ne cucum.
وَلَقَدْ زَيَّنَّا السَّمَاءَ الدُّنْيَا بِمَصَابِيحَ وَجَعَلْنَاهَا رُجُومًا لِّلشَّيَاطِينِ ۖ وَأَعْتَدْنَا لَهُمْ عَذَابَ السَّعِيرِ ۝٥
📖 Tekki Aaya 5
Taaralal nanu àddina si ci ay làmp [biddiw] def nanu ko muy lakk Saytaane yi te waajalal nanu leen mbugëlum Safara.
وَلِلَّذِينَ كَفَرُوا بِرَبِّهِمْ عَذَابُ جَهَنَّمَ ۖ وَبِئْسَ الْمَصِيرُ ۝٦
📖 Tekki Aaya 6
Ña weddi Yàlla am nañu mbugalum Safara. Ndaw mujj gu bon !
إِذَا أُلْقُوا فِيهَا سَمِعُوا لَهَا شَهِيقًا وَهِيَ تَفُورُ ۝٧
📖 Tekki Aaya 7
Bu ñu leen ca sànnee, nga dégg ko muy fuur, di wañax.
تَكَادُ تَمَيَّزُ مِنَ الْغَيْظِ ۖ كُلَّمَا أُلْقِيَ فِيهَا فَوْجٌ سَأَلَهُمْ خَزَنَتُهَا أَلَمْ يَأْتِكُمْ نَذِيرٌ ۝٨
📖 Tekki Aaya 8
Day mer, bay fuur. Saa su ñu ca sànnee mbooloo, ña kay wattu naan leen: “Xanaa ! yéen kuy xuppe dikkul woon ci yéen ? ”
قَالُوا بَلَىٰ قَدْ جَاءَنَا نَذِيرٌ فَكَذَّبْنَا وَقُلْنَا مَا نَزَّلَ اللَّهُ مِن شَيْءٍ إِنْ أَنتُمْ إِلَّا فِي ضَلَالٍ كَبِيرٍ ۝٩
📖 Tekki Aaya 9
Ñu naan ko : “Axakañ ! dikkaloon nañu nu kay, nu ne leen: Yàlla wàccewul tus, te yéen dangeen a sànku”
وَقَالُوا لَوْ كُنَّا نَسْمَعُ أَوْ نَعْقِلُ مَا كُنَّا فِي أَصْحَابِ السَّعِيرِ ۝١٠
📖 Tekki Aaya 10
Ñu wax it ne : “Su nu doon dégg mbaa nu xel-lu, kon dunu nekk ci mbugël mii tey”.
فَاعْتَرَفُوا بِذَنبِهِمْ فَسُحْقًا لِّأَصْحَابِ السَّعِيرِ ۝١١
📖 Tekki Aaya 11
Nangu nañu seeni bàkkaar. Waa safara toskare nañu.
إِنَّ الَّذِينَ يَخْشَوْنَ رَبَّهُم بِالْغَيْبِ لَهُم مَّغْفِرَةٌ وَأَجْرٌ كَبِيرٌ ۝١٢
📖 Tekki Aaya 12
Ñay ragal seen Boroom ci kumpa am nañu ag njégël ak pey gu màgg.
وَأَسِرُّوا قَوْلَكُمْ أَوِ اجْهَرُوا بِهِ ۖ إِنَّهُ عَلِيمٌ بِذَاتِ الصُّدُورِ ۝١٣
📖 Tekki Aaya 13
Su ngeen di déey walla ngeen di jooru Moo xam tigi li nekk ci dënn yi.
أَلَا يَعْلَمُ مَنْ خَلَقَ وَهُوَ اللَّطِيفُ الْخَبِيرُ ۝١٤
📖 Tekki Aaya 14
Ki bind ndax dadul xam te Moom moo di ki Ñewenti, di Ku deñ Kumpa ci lépp.
هُوَ الَّذِي جَعَلَ لَكُمُ الْأَرْضَ ذَلُولًا فَامْشُوا فِي مَنَاكِبِهَا وَكُلُوا مِن رِّزْقِهِ ۖ وَإِلَيْهِ النُّشُورُ ۝١٥
📖 Tekki Aaya 15
Moom moo leen tàggatal suuf si : doxleen ci ay déndëm. Tey lekk ciy xéewalam. (Ca Yàlla) la léppiy mujj.
أَأَمِنتُم مَّن فِي السَّمَاءِ أَن يَخْسِفَ بِكُمُ الْأَرْضَ فَإِذَا هِيَ تَمُورُ ۝١٦
📖 Tekki Aaya 16
Ndax man ngeen a raw ki nekk ci asamaan si su talañee suuf si ? Ba muy rëg-rëgi, mukk !
أَمْ أَمِنتُم مَّن فِي السَّمَاءِ أَن يُرْسِلَ عَلَيْكُمْ حَاصِبًا ۖ فَسَتَعْلَمُونَ كَيْفَ نَذِيرِ ۝١٧
📖 Tekki Aaya 17
Walla dangeen a man a raw ki nekk ci asamaan su yabalee lu ànd ak i doj ? Xalset ngeen xam Samag xupe.
وَلَقَدْ كَذَّبَ الَّذِينَ مِن قَبْلِهِمْ فَكَيْفَ كَانَ نَكِيرِ ۝١٨
📖 Tekki Aaya 18
Ña leen fi jiitu woon, weddi woon nañu. Kon naka la sama mbugël deme woon ci ñoom !
أَوَلَمْ يَرَوْا إِلَى الطَّيْرِ فَوْقَهُمْ صَافَّاتٍ وَيَقْبِضْنَ ۚ مَا يُمْسِكُهُنَّ إِلَّا الرَّحْمَٰنُ ۚ إِنَّهُ بِكُلِّ شَيْءٍ بَصِيرٌ ۝١٩
📖 Tekki Aaya 19
Xanaa dañoo xoolul ci picc yi leen tiim, di tàllal seeni laaf ak bank ? Te (Yàlla) Yëramaakoon bi rekk leen teye (ci jawu ji). Moom, Kuy Gis la lépp lu ne.
أَمَّنْ هَٰذَا الَّذِي هُوَ جُندٌ لَّكُمْ يَنصُرُكُم مِّن دُونِ الرَّحْمَٰنِ ۚ إِنِ الْكَافِرُونَ إِلَّا فِي غُرُورٍ ۝٢٠
📖 Tekki Aaya 20
Ana kan moo leen man a wutal ay xarekat yu leen di taxwu te du Yàlla ? Yéefër yi ci woro la ñu nekk.
أَمَّنْ هَٰذَا الَّذِي يَرْزُقُكُمْ إِنْ أَمْسَكَ رِزْقَهُ ۚ بَل لَّجُّوا فِي عُتُوٍّ وَنُفُورٍ ۝٢١
📖 Tekki Aaya 21
Ana kan moo leen di wërsëgal su (Yàlla) téyee wërsëgëm ? Ñoom da ñoo sànku.
أَفَمَن يَمْشِي مُكِبًّا عَلَىٰ وَجْهِهِ أَهْدَىٰ أَمَّن يَمْشِي سَوِيًّا عَلَىٰ صِرَاطٍ مُّسْتَقِيمٍ ۝٢٢
📖 Tekki Aaya 22
Moo ndax ? Waajiy dëpp xarkanamam moo gën a gindiku kiy dox ne sàtt ca kaw yoon wa jub xocc.
قُلْ هُوَ الَّذِي أَنشَأَكُمْ وَجَعَلَ لَكُمُ السَّمْعَ وَالْأَبْصَارَ وَالْأَفْئِدَةَ ۖ قَلِيلًا مَّا تَشْكُرُونَ ۝٢٣
📖 Tekki Aaya 23
Waxal ne: “Moom moo leen sàkk defal leen dégg, ak ub gis ak i xol”. Te néewaana ngeen sant delloo njukël !
قُلْ هُوَ الَّذِي ذَرَأَكُمْ فِي الْأَرْضِ وَإِلَيْهِ تُحْشَرُونَ ۝٢٤
📖 Tekki Aaya 24
Waxal ne : “It moo leen ji ci suuf si, te ca moom ngeen di mujj ñu pang leen”.
وَيَقُولُونَ مَتَىٰ هَٰذَا الْوَعْدُ إِن كُنتُمْ صَادِقِينَ ۝٢٥
📖 Tekki Aaya 25
Ñuy wax naan : “Dig ba kañ lay doon su fekkee ne ñu dëggu ngeen ? ”.
قُلْ إِنَّمَا الْعِلْمُ عِندَ اللَّهِ وَإِنَّمَا أَنَا نَذِيرٌ مُّبِينٌ ۝٢٦
📖 Tekki Aaya 26
Waxal ne : “Xam-xamub loolu ma nga ca Yàlla. Man nag ab xuppekat buy leeral laa”.
فَلَمَّا رَأَوْهُ زُلْفَةً سِيئَتْ وُجُوهُ الَّذِينَ كَفَرُوا وَقِيلَ هَٰذَا الَّذِي كُنتُم بِهِ تَدَّعُونَ ۝٢٧
📖 Tekki Aaya 27
Bu, ñu ne gegg ca (mbugël ma), xarkanami yéefar ya di gañ-gañi. Ñu ne leen: “Lii nag ngeen yàkkamti woon”.
قُلْ أَرَأَيْتُمْ إِنْ أَهْلَكَنِيَ اللَّهُ وَمَن مَّعِيَ أَوْ رَحِمَنَا فَمَن يُجِيرُ الْكَافِرِينَ مِنْ عَذَابٍ أَلِيمٍ ۝٢٨
📖 Tekki Aaya 28
Waxal ne : “Xanaa gisu leen ? Su ma Yàlla reyoon maak ñi ma àndal, ana kan mooy man a yiir yéefar yi aar leen ci mbugal mu mitti (amul de) ? ”.
قُلْ هُوَ الرَّحْمَٰنُ آمَنَّا بِهِ وَعَلَيْهِ تَوَكَّلْنَا ۖ فَسَتَعْلَمُونَ مَنْ هُوَ فِي ضَلَالٍ مُّبِينٍ ۝٢٩
📖 Tekki Aaya 29
Waxal ne : “Kooku moo di, Yàlla yëramaakoon bi. Gëm nanu ko te doyloo nanu ko. Dangeen xala xam ana kan moo nekk cig réer”.
قُلْ أَرَأَيْتُمْ إِنْ أَصْبَحَ مَاؤُكُمْ غَوْرًا فَمَن يَأْتِيكُم بِمَاءٍ مَّعِينٍ ۝٣٠
📖 Tekki Aaya 30
Waxal ne : “Xanaa gisuleen ? Bu seen ndox mi rawoon ci biir suuf xóot, ana kan moo leen di may bëtu ndox bu tane (Yàlla) ? ”
← 66 Al-Mulk (67/114) 68 →
Jàng Simoore Al-Mulk ci Wolof – Tekki, Waxtaan ak Baat

67الملك Al-Mulk 📚 30 Aaya مكية



Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers