Simoore As-Sajda ci Aarabu ak Wolof

Jàng Simoore As-Sajda ak tekkim wolof bu mat sëkk, ak baat. Tekki ayaa bu ne. (30 Aaya — مكية). As-Sajda Dégg, As-Sajda Tekki, As-Sajda mp3, As-Sajda pdf.

Jàng te Dégg Simoore As-Sajda

🎧 Aaya
M Mishary Rashid Alafasy
M Mahmoud Khalil Al-Husary
A Abdurrahman As-Sudais
M Mohamed Siddiq Al-Minshawi
A Abdul Basit Abdul Samad
A Ali Al-Hudhaify
A Ahmed ibn Ali al-Ajamy
A Abu Bakr Ash-Shaatree
M Muhammad Ayyoub
A Abdullah Basfar
A Abdullah Al-Juhani
M Maher Al Muaiqly
x1
الم ۝١
📖 Tekki Aaya 1
Aliif, Laam, Miim.
تَنزِيلُ الْكِتَابِ لَا رَيْبَ فِيهِ مِن رَّبِّ الْعَالَمِينَ ۝٢
📖 Tekki Aaya 2
Wàcceg Téere bii [Alxuraan], sikk nekku ca, mu bawoo ca Boroom àddina sépp.
أَمْ يَقُولُونَ افْتَرَاهُ ۚ بَلْ هُوَ الْحَقُّ مِن رَّبِّكَ لِتُنذِرَ قَوْمًا مَّا أَتَاهُم مِّن نَّذِيرٍ مِّن قَبْلِكَ لَعَلَّهُمْ يَهْتَدُونَ ۝٣
📖 Tekki Aaya 3
Walla dañu naan [Muhammad] moo ko sos ? [Déedéet, lii mooy dëgg ga bawoo ci sa Boroom ngir nga xupp ci aw nit ñoo xam ne bi nga laataa ñëw, amuñu woon xuppekat, te amaana ñu gindiku.
اللَّهُ الَّذِي خَلَقَ السَّمَاوَاتِ وَالْأَرْضَ وَمَا بَيْنَهُمَا فِي سِتَّةِ أَيَّامٍ ثُمَّ اسْتَوَىٰ عَلَى الْعَرْشِ ۖ مَا لَكُم مِّن دُونِهِ مِن وَلِيٍّ وَلَا شَفِيعٍ ۚ أَفَلَا تَتَذَكَّرُونَ ۝٤
📖 Tekki Aaya 4
Yàlla mi bind asamaan yeek suuf si ak li nekk ci seen diggante ci diirub juróom-benni fan. Daldi yemoo ca Gàngunaay ga [Aras]. Amuleen benn wéeruwaay walla rammukat bu dul Moom. Moo ndax dangeen dul fàttaliku ?
يُدَبِّرُ الْأَمْرَ مِنَ السَّمَاءِ إِلَى الْأَرْضِ ثُمَّ يَعْرُجُ إِلَيْهِ فِي يَوْمٍ كَانَ مِقْدَارُهُ أَلْفَ سَنَةٍ مِّمَّا تَعُدُّونَ ۝٥
📖 Tekki Aaya 5
Mooy settantal [lijjanti] mbir yi, jële ko asamaan jëme ko ci suuf si, topp mu yéeg asamaan ci bis boo xam ne ab nattaleem junni la ci ay ati àddina.
ذَٰلِكَ عَالِمُ الْغَيْبِ وَالشَّهَادَةِ الْعَزِيزُ الرَّحِيمُ ۝٦
📖 Tekki Aaya 6
Kooka mooy xamkatu kumpa ak li feeñ, mooy Boroom Kàttan, di Jaglewaakoonu yërmaandeem,
الَّذِي أَحْسَنَ كُلَّ شَيْءٍ خَلَقَهُ ۖ وَبَدَأَ خَلْقَ الْإِنسَانِ مِن طِينٍ ۝٧
📖 Tekki Aaya 7
Moo jekkal sosug lu ne. Daldi door sosug nit ci ban,
ثُمَّ جَعَلَ نَسْلَهُ مِن سُلَالَةٍ مِّن مَّاءٍ مَّهِينٍ ۝٨
📖 Tekki Aaya 8
daldi nay defe askanam wa mu càllaloo ci am ndox mu doyadi;
ثُمَّ سَوَّاهُ وَنَفَخَ فِيهِ مِن رُّوحِهِ ۖ وَجَعَلَ لَكُمُ السَّمْعَ وَالْأَبْصَارَ وَالْأَفْئِدَةَ ۚ قَلِيلًا مَّا تَشْكُرُونَ ۝٩
📖 Tekki Aaya 9
daldi koy yemale, ëf ci Ruuwam. Defaral leen dégg-dégg, ak ub gis ak i xol. Te néewaana ngeen di Ko sant !
وَقَالُوا أَإِذَا ضَلَلْنَا فِي الْأَرْضِ أَإِنَّا لَفِي خَلْقٍ جَدِيدٍ ۚ بَلْ هُم بِلِقَاءِ رَبِّهِمْ كَافِرُونَ ۝١٠
📖 Tekki Aaya 10
Ñuy wax naan : “Ndax bu nu seeyee ci biir suuf si, dananu dekkiwaat ? ”. Ñoom dañoo weddi ne danañu dajeek seen Boroom.
۞ قُلْ يَتَوَفَّاكُم مَّلَكُ الْمَوْتِ الَّذِي وُكِّلَ بِكُمْ ثُمَّ إِلَىٰ رَبِّكُمْ تُرْجَعُونَ ۝١١
📖 Tekki Aaya 11
Neel : “Malaakam ndee ma ñu sasee loolu ci yéen moo leen di rey. Su ko defee, ngeen dellu ca seen Boroom”.
وَلَوْ تَرَىٰ إِذِ الْمُجْرِمُونَ نَاكِسُو رُءُوسِهِمْ عِندَ رَبِّهِمْ رَبَّنَا أَبْصَرْنَا وَسَمِعْنَا فَارْجِعْنَا نَعْمَلْ صَالِحًا إِنَّا مُوقِنُونَ ۝١٢
📖 Tekki Aaya 12
Cëy soo gisoon, tooñkat yaa ngay jatt seeni loos, naan ! “Yaw sunu Boroom, gis nanu, dégg nanu, delloo nu ca [àddina], kon de nu jëf lu baax ; léegi, xam nanu ne lii lu wóor la”.
وَلَوْ شِئْنَا لَآتَيْنَا كُلَّ نَفْسٍ هُدَاهَا وَلَٰكِنْ حَقَّ الْقَوْلُ مِنِّي لَأَمْلَأَنَّ جَهَنَّمَ مِنَ الْجِنَّةِ وَالنَّاسِ أَجْمَعِينَ ۝١٣
📖 Tekki Aaya 13
“Bu Nu sooboon, Dananu indil bakkan bu nekk ag njubam. Waaye dafa fekk ne li Ma wax fàwwu mu am : “Danaa feesal Safara ci nit ak jinne mbooleseen”.
فَذُوقُوا بِمَا نَسِيتُمْ لِقَاءَ يَوْمِكُمْ هَٰذَا إِنَّا نَسِينَاكُمْ ۖ وَذُوقُوا عَذَابَ الْخُلْدِ بِمَا كُنتُمْ تَعْمَلُونَ ۝١٤
📖 Tekki Aaya 14
“Kon mosleen ci li ngeen fàtte woon seen dajeek Bis bii. Dananu leen fàtte-fàttelu. Toqamtikuleen mbugal muy sax dàkk, muy peyug la ngeen daan def”.
إِنَّمَا يُؤْمِنُ بِآيَاتِنَا الَّذِينَ إِذَا ذُكِّرُوا بِهَا خَرُّوا سُجَّدًا وَسَبَّحُوا بِحَمْدِ رَبِّهِمْ وَهُمْ لَا يَسْتَكْبِرُونَ ۩ ۝١٥
📖 Tekki Aaya 15
Ñii gëm Sunuy kàddu, ñoom ñi nga xam ne saa su Nu leen ko fàttalee, dañuy rot di sujjóot, di sàbbaal, di kañ ak a sant seen Boroom, ñoom duñu rëy-rëylu.
تَتَجَافَىٰ جُنُوبُهُمْ عَنِ الْمَضَاجِعِ يَدْعُونَ رَبَّهُمْ خَوْفًا وَطَمَعًا وَمِمَّا رَزَقْنَاهُمْ يُنفِقُونَ ۝١٦
📖 Tekki Aaya 16
Dañuy fojjatiku ca seen tëddukaay ya [lal ya], di ñaan seen Boroom ci ragal ak xemmem ; te di joxe ca la Nu leen wërsëgal.
فَلَا تَعْلَمُ نَفْسٌ مَّا أُخْفِيَ لَهُم مِّن قُرَّةِ أَعْيُنٍ جَزَاءً بِمَا كَانُوا يَعْمَلُونَ ۝١٧
📖 Tekki Aaya 17
Benn bakkan xamul la ñu koy xala deñcal ci yuy neex ci bët, muy peyug la mu daan def !
أَفَمَن كَانَ مُؤْمِنًا كَمَن كَانَ فَاسِقًا ۚ لَّا يَسْتَوُونَ ۝١٨
📖 Tekki Aaya 18
Moo ndax ku gëm dina mel ni ab saay-saay ? [mukk], duñu mës a yem.
أَمَّا الَّذِينَ آمَنُوا وَعَمِلُوا الصَّالِحَاتِ فَلَهُمْ جَنَّاتُ الْمَأْوَىٰ نُزُلًا بِمَا كَانُوا يَعْمَلُونَ ۝١٩
📖 Tekki Aaya 19
Ña gëmoon tey jëf u yiw, am nañu ay dër ca Àjjana, muy seen wàccuwaay ngir la ñu daan jëf.
وَأَمَّا الَّذِينَ فَسَقُوا فَمَأْوَاهُمُ النَّارُ ۖ كُلَّمَا أَرَادُوا أَن يَخْرُجُوا مِنْهَا أُعِيدُوا فِيهَا وَقِيلَ لَهُمْ ذُوقُوا عَذَابَ النَّارِ الَّذِي كُنتُم بِهِ تُكَذِّبُونَ ۝٢٠
📖 Tekki Aaya 20
Ña saay-saayoon, ñoom Safaraa di seen kër : saa su ñu ca bëggee génn, ñu delloo leen ca, te naan leen : “Toqamtikuleen mbugalum Safara sa ngeen daan weddi”.
وَلَنُذِيقَنَّهُم مِّنَ الْعَذَابِ الْأَدْنَىٰ دُونَ الْعَذَابِ الْأَكْبَرِ لَعَلَّهُمْ يَرْجِعُونَ ۝٢١
📖 Tekki Aaya 21
Dananu leen ñamal ci àdduna [takkandeerub mbugalum àllaaxira] ndax ñu mën a dellu ca yoon wu jub wa !
وَمَنْ أَظْلَمُ مِمَّن ذُكِّرَ بِآيَاتِ رَبِّهِ ثُمَّ أَعْرَضَ عَنْهَا ۚ إِنَّا مِنَ الْمُجْرِمِينَ مُنتَقِمُونَ ۝٢٢
📖 Tekki Aaya 22
Ana kan moo gën a tooñ ka nga xam ne, saa su ñu ko fàttalee laayay Boroomam, mu dummóoyu ko ? Dananu feyyu ci tooñkat yi.
وَلَقَدْ آتَيْنَا مُوسَى الْكِتَابَ فَلَا تَكُن فِي مِرْيَةٍ مِّن لِّقَائِهِ ۖ وَجَعَلْنَاهُ هُدًى لِّبَنِي إِسْرَائِيلَ ۝٢٣
📖 Tekki Aaya 23
Joxoon Nanu Muusaa Téere ba - bul am xel-yaar ci dajeek moom [yaw Muhammad] -, te defoon Nanu Téere ba mu di njub ñeel Bani-Israayiila gépp.
وَجَعَلْنَا مِنْهُمْ أَئِمَّةً يَهْدُونَ بِأَمْرِنَا لَمَّا صَبَرُوا ۖ وَكَانُوا بِآيَاتِنَا يُوقِنُونَ ۝٢٤
📖 Tekki Aaya 24
Defoon Nanu ci ñoom ay njiit yuy gindee ci Sunu ndigal, waxtu wa ñu muñee te wóolu Sunuy laaya [kàddu].
إِنَّ رَبَّكَ هُوَ يَفْصِلُ بَيْنَهُمْ يَوْمَ الْقِيَامَةِ فِيمَا كَانُوا فِيهِ يَخْتَلِفُونَ ۝٢٥
📖 Tekki Aaya 25
Sa Boroom ci boppam dana àtte seen diggante ca la ñu daan wuute.
أَوَلَمْ يَهْدِ لَهُمْ كَمْ أَهْلَكْنَا مِن قَبْلِهِم مِّنَ الْقُرُونِ يَمْشُونَ فِي مَسَاكِنِهِمْ ۚ إِنَّ فِي ذَٰلِكَ لَآيَاتٍ ۖ أَفَلَا يَسْمَعُونَ ۝٢٦
📖 Tekki Aaya 26
Ndax dafa doyul ci ñoom gindiku, te faagaalaloon Nanu ay maas ya leen jiitu woon te tey ñi ngi dox ci seen génti kër yi ? Ay kéemaan nekk na ci biir loolu ! Ndax ñoom dañu dul dégg ?
أَوَلَمْ يَرَوْا أَنَّا نَسُوقُ الْمَاءَ إِلَى الْأَرْضِ الْجُرُزِ فَنُخْرِجُ بِهِ زَرْعًا تَأْكُلُ مِنْهُ أَنْعَامُهُمْ وَأَنفُسُهُمْ ۖ أَفَلَا يُبْصِرُونَ ۝٢٧
📖 Tekki Aaya 27
Xanaa dañoo gisul ñoom ci ne Man Yàlla maay wàcce ndox ci kaw suuf su wow, génne gàncax gu seeni jur di lekk ak ñoom it ñu di ca lekk ? Moo ndax ñoom dañu dul gis ?
وَيَقُولُونَ مَتَىٰ هَٰذَا الْفَتْحُ إِن كُنتُمْ صَادِقِينَ ۝٢٨
📖 Tekki Aaya 28
Ñangay laaj naan : “Lii kañ lay doon, ndegam wax ngeen dëgg ? ”.
قُلْ يَوْمَ الْفَتْحِ لَا يَنفَعُ الَّذِينَ كَفَرُوا إِيمَانُهُمْ وَلَا هُمْ يُنظَرُونَ ۝٢٩
📖 Tekki Aaya 29
Waxal ne : “Bis ba ndam la di ñëw, ngëmug yéefar yi dootuleen jariñati dara ! Te kenn duleen négandiku”.
فَأَعْرِضْ عَنْهُمْ وَانتَظِرْ إِنَّهُم مُّنتَظِرُونَ ۝٣٠
📖 Tekki Aaya 30
Dummóoyuleen te xaar. Ñoom it ñi ngi xaar.
← 31 As-Sajda (32/114) 33 →
Jàng Simoore As-Sajda ci Wolof – Tekki, Waxtaan ak Baat

32السجدة As-Sajdah 📚 30 Aaya مكية



Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers