Simoore Ad-Duha ci Aarabu ak Wolof

Jàng Simoore Ad-Duha ak tekkim wolof bu mat sëkk, ak baat. Tekki ayaa bu ne. (11 Aaya — مكية). Ad-Duha Dégg, Ad-Duha Tekki, Ad-Duha mp3, Ad-Duha pdf.

Jàng te Dégg Simoore Ad-Duha

🎧 Aaya
M Mishary Rashid Alafasy
M Mahmoud Khalil Al-Husary
A Abdurrahman As-Sudais
M Mohamed Siddiq Al-Minshawi
A Abdul Basit Abdul Samad
A Ali Al-Hudhaify
A Ahmed ibn Ali al-Ajamy
A Abu Bakr Ash-Shaatree
M Muhammad Ayyoub
A Abdullah Basfar
A Abdullah Al-Juhani
M Maher Al Muaiqly
x1
وَالضُّحَىٰ ۝١
📖 Tekki Aaya 1
Ci yoor-yoor bi ! Maa ngi giñ
وَاللَّيْلِ إِذَا سَجَىٰ ۝٢
📖 Tekki Aaya 2
ak ci guddi gi bu kukkee ! ne
مَا وَدَّعَكَ رَبُّكَ وَمَا قَلَىٰ ۝٣
📖 Tekki Aaya 3
Sa Boroom bàyyiwula, te bañu la.
وَلَلْآخِرَةُ خَيْرٌ لَّكَ مِنَ الْأُولَىٰ ۝٤
📖 Tekki Aaya 4
Te àllaaxira, mooy, gën ci Yaw àddina de.
وَلَسَوْفَ يُعْطِيكَ رَبُّكَ فَتَرْضَىٰ ۝٥
📖 Tekki Aaya 5
Te sa Boroom dana la jox, ba nga doyal.
أَلَمْ يَجِدْكَ يَتِيمًا فَآوَىٰ ۝٦
📖 Tekki Aaya 6
Moo ndax fekku la ngay jirim ? Mu fat la !
وَوَجَدَكَ ضَالًّا فَهَدَىٰ ۝٧
📖 Tekki Aaya 7
Ak it ndax fekku la nga réer ? Mu gindila.
وَوَجَدَكَ عَائِلًا فَأَغْنَىٰ ۝٨
📖 Tekki Aaya 8
Moo ndax fekku la nga ñàkk ? Mu woomalal la.
فَأَمَّا الْيَتِيمَ فَلَا تَقْهَرْ ۝٩
📖 Tekki Aaya 9
Jirim, nag, bu ko di xorñooñal.
وَأَمَّا السَّائِلَ فَلَا تَنْهَرْ ۝١٠
📖 Tekki Aaya 10
Te laajkat it, bu ko di delloo.
وَأَمَّا بِنِعْمَةِ رَبِّكَ فَحَدِّثْ ۝١١
📖 Tekki Aaya 11
Te it na ngay waxtaane, sa xéewalu Boroom.
← 92 Ad-Duha (93/114) 94 →
Jàng Simoore Ad-Duha ci Wolof – Tekki, Waxtaan ak Baat

93الضحى Ad-Duha 📚 11 Aaya مكية



Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers