Simoore Al-Fath ci Aarabu ak Wolof

Jàng Simoore Al-Fath ak tekkim wolof bu mat sëkk, ak baat. Tekki ayaa bu ne. (29 Aaya — مدنية). Al-Fath Dégg, Al-Fath Tekki, Al-Fath mp3, Al-Fath pdf.

Jàng te Dégg Simoore Al-Fath

🎧 Aaya
M Mishary Rashid Alafasy
M Mahmoud Khalil Al-Husary
A Abdurrahman As-Sudais
M Mohamed Siddiq Al-Minshawi
A Abdul Basit Abdul Samad
A Ali Al-Hudhaify
A Ahmed ibn Ali al-Ajamy
A Abu Bakr Ash-Shaatree
M Muhammad Ayyoub
A Abdullah Basfar
A Abdullah Al-Juhani
M Maher Al Muaiqly
x1
إِنَّا فَتَحْنَا لَكَ فَتْحًا مُّبِينًا ۝١
📖 Tekki Aaya 1
Nun dey ubbil nanu la ubbi gu fes bir (jox la ndam) nga bom,
لِّيَغْفِرَ لَكَ اللَّهُ مَا تَقَدَّمَ مِن ذَنبِكَ وَمَا تَأَخَّرَ وَيُتِمَّ نِعْمَتَهُ عَلَيْكَ وَيَهْدِيَكَ صِرَاطًا مُّسْتَقِيمًا ۝٢
📖 Tekki Aaya 2
ci loolu Yàlla dana la jéggal, la jëkkoon ci say bàkkaar ak lay xala mujj, te it Dana matal ay Xéewal ci yaw te itam dana gindi teg la ca kaw yoonam wu jub xocc wa ;
وَيَنصُرَكَ اللَّهُ نَصْرًا عَزِيزًا ۝٣
📖 Tekki Aaya 3
Yàlla dana la dimbali ndimbal (luy tax nga man a not say noon).
هُوَ الَّذِي أَنزَلَ السَّكِينَةَ فِي قُلُوبِ الْمُؤْمِنِينَ لِيَزْدَادُوا إِيمَانًا مَّعَ إِيمَانِهِمْ ۗ وَلِلَّهِ جُنُودُ السَّمَاوَاتِ وَالْأَرْضِ ۚ وَكَانَ اللَّهُ عَلِيمًا حَكِيمًا ۝٤
📖 Tekki Aaya 4
Moom (Yàlla) ki wàcce ag dal ci xoli jullit ñi ngir ñuy dolliku ngëm ci séen kaw ngëm ga. Te nag Yàllaa moom xarekati asamaan yeek suuf si ; Yàlla Kuy xam la ku Xereñ la
لِّيُدْخِلَ الْمُؤْمِنِينَ وَالْمُؤْمِنَاتِ جَنَّاتٍ تَجْرِي مِن تَحْتِهَا الْأَنْهَارُ خَالِدِينَ فِيهَا وَيُكَفِّرَ عَنْهُمْ سَيِّئَاتِهِمْ ۚ وَكَانَ ذَٰلِكَ عِندَ اللَّهِ فَوْزًا عَظِيمًا ۝٥
📖 Tekki Aaya 5
(waral gi mu waral ci yéen xare) tax na ba dana tàbbal jullit ñu goor ñeek jullit ñu jigéen ñi ci Àjjana yoo xam ne ay dex ñooy daw ci suufam te dañu fay béel, te it dana leen faral séeni ñaawtéef loolu di texe gu mag ga fa Yàlla.
وَيُعَذِّبَ الْمُنَافِقِينَ وَالْمُنَافِقَاتِ وَالْمُشْرِكِينَ وَالْمُشْرِكَاتِ الظَّانِّينَ بِاللَّهِ ظَنَّ السَّوْءِ ۚ عَلَيْهِمْ دَائِرَةُ السَّوْءِ ۖ وَغَضِبَ اللَّهُ عَلَيْهِمْ وَلَعَنَهُمْ وَأَعَدَّ لَهُمْ جَهَنَّمَ ۖ وَسَاءَتْ مَصِيرًا ۝٦
📖 Tekki Aaya 6
(ngir loolu it) dana mbugël naaféq yu, góor yeek yu jigéen yi, ak bokkaalekat yu goor yaak yu jigéen yay njortu ci Yàlla. Ak itam ne waajalal na leen safara muy dëkkuwaay bu bon!
وَلِلَّهِ جُنُودُ السَّمَاوَاتِ وَالْأَرْضِ ۚ وَكَانَ اللَّهُ عَزِيزًا حَكِيمًا ۝٧
📖 Tekki Aaya 7
Yàllaa moom xarekati asamaan yeek suuf si ; Yàlla Boroom Kàttan la di Ku Xereñ.
إِنَّا أَرْسَلْنَاكَ شَاهِدًا وَمُبَشِّرًا وَنَذِيرًا ۝٨
📖 Tekki Aaya 8
Yónni nanu la ngaay seede (ci saw xeet), di béglekat (ci jullit ñi) di xuppekat (ci yéefar yi),
لِّتُؤْمِنُوا بِاللَّهِ وَرَسُولِهِ وَتُعَزِّرُوهُ وَتُوَقِّرُوهُ وَتُسَبِّحُوهُ بُكْرَةً وَأَصِيلًا ۝٩
📖 Tekki Aaya 9
ngir ngeen gëm Yàlla akub Yonentam, te di ko màggal, te di ko weg, ak it ngir ngeen di ko sàbbaal (kañ) subaak ngoon.
إِنَّ الَّذِينَ يُبَايِعُونَكَ إِنَّمَا يُبَايِعُونَ اللَّهَ يَدُ اللَّهِ فَوْقَ أَيْدِيهِمْ ۚ فَمَن نَّكَثَ فَإِنَّمَا يَنكُثُ عَلَىٰ نَفْسِهِ ۖ وَمَنْ أَوْفَىٰ بِمَا عَاهَدَ عَلَيْهُ اللَّهَ فَسَيُؤْتِيهِ أَجْرًا عَظِيمًا ۝١٠
📖 Tekki Aaya 10
Ñay jaayanteek yow ña ngay jaayanteek Yàlla (“bay’atu ridwaan bil hudaybiyyati”) : loxo Yàllaa ngi séeni yoxo (tegoonañook Yàlla loxo) . Képp ku ca xàcc, boppam la xàccal ; képp ku matal kóllare ga mooy séqag Yàlla, Dana ko xalset a jox ag pey gu màgg.
سَيَقُولُ لَكَ الْمُخَلَّفُونَ مِنَ الْأَعْرَابِ شَغَلَتْنَا أَمْوَالُنَا وَأَهْلُونَا فَاسْتَغْفِرْ لَنَا ۚ يَقُولُونَ بِأَلْسِنَتِهِم مَّا لَيْسَ فِي قُلُوبِهِمْ ۚ قُلْ فَمَن يَمْلِكُ لَكُم مِّنَ اللَّهِ شَيْئًا إِنْ أَرَادَ بِكُمْ ضَرًّا أَوْ أَرَادَ بِكُمْ نَفْعًا ۚ بَلْ كَانَ اللَّهُ بِمَا تَعْمَلُونَ خَبِيرًا ۝١١
📖 Tekki Aaya 11
Ña gannaawewoon te bokk ca araab yaa ngay wax naan : “Sunuy njaboot ak sunuy alal ñooñu gàllankoor: jéggalul nu”. Ña ngay wax ci séeni làmmiñ lu nekkul ci seeni xol. Waxal ne : “Ana kan moo leen man a fanqal dara ci Yàlla su bëggee natt ci yéen lor wala mu bëg nat ci yéen njariñ ? Yàlla xàmmee na li ngeen di def.
بَلْ ظَنَنتُمْ أَن لَّن يَنقَلِبَ الرَّسُولُ وَالْمُؤْمِنُونَ إِلَىٰ أَهْلِيهِمْ أَبَدًا وَزُيِّنَ ذَٰلِكَ فِي قُلُوبِكُمْ وَظَنَنتُمْ ظَنَّ السَّوْءِ وَكُنتُمْ قَوْمًا بُورًا ۝١٢
📖 Tekki Aaya 12
Yéen kay (yéefar yi) dangeen a jortoon ne Yonenta bi ak jullit ñi dunu déllusi ci séeni njaboot . Loolu neexoon lool ci séeni xol ; ngeen daan njortu ay njortu yu ñaaw. Te it ngeen di aw nit ñu toskare”.
وَمَن لَّمْ يُؤْمِن بِاللَّهِ وَرَسُولِهِ فَإِنَّا أَعْتَدْنَا لِلْكَافِرِينَ سَعِيرًا ۝١٣
📖 Tekki Aaya 13
Képp ku gëmul Yàlla ak Yonentam (na bir ne yéefar la)... te waajal na nu yéefar ya aw safara wu tàng.
وَلِلَّهِ مُلْكُ السَّمَاوَاتِ وَالْأَرْضِ ۚ يَغْفِرُ لِمَن يَشَاءُ وَيُعَذِّبُ مَن يَشَاءُ ۚ وَكَانَ اللَّهُ غَفُورًا رَّحِيمًا ۝١٤
📖 Tekki Aaya 14
Yàllaa moom nguuruk asamaan yeek suuf si. Mooy jéggal ku ko soob tey mboogël ku ko soob. Yàlla, ab Jéggëlaakoon la ab Jaglewaakoon la.
سَيَقُولُ الْمُخَلَّفُونَ إِذَا انطَلَقْتُمْ إِلَىٰ مَغَانِمَ لِتَأْخُذُوهَا ذَرُونَا نَتَّبِعْكُمْ ۖ يُرِيدُونَ أَن يُبَدِّلُوا كَلَامَ اللَّهِ ۚ قُل لَّن تَتَّبِعُونَا كَذَٰلِكُمْ قَالَ اللَّهُ مِن قَبْلُ ۖ فَسَيَقُولُونَ بَلْ تَحْسُدُونَنَا ۚ بَلْ كَانُوا لَا يَفْقَهُونَ إِلَّا قَلِيلًا ۝١٥
📖 Tekki Aaya 15
Ñay fuuyu (te bokk ci giiri araab yi) dana nuy wax, saa su ñu jëmee ca màng ga (alal ya nu nangoo xaybar) ngir jël ko; “Naan leen bàyyi leen nu nu topp leen”. Danuy bëgg soppi waxi Yàlli. Waxleen ne : “Dungeen nu topp: ndax loolu la Yàlla wax cag njaalbéen”. Dana nu xalset wax (ñoom naaféq yi) naa : “Dangeen ñoo iñaane”. Li am kay moo di ne lim bu néew bu bokk ca ñoom ñooy ña xam.
قُل لِّلْمُخَلَّفِينَ مِنَ الْأَعْرَابِ سَتُدْعَوْنَ إِلَىٰ قَوْمٍ أُولِي بَأْسٍ شَدِيدٍ تُقَاتِلُونَهُمْ أَوْ يُسْلِمُونَ ۖ فَإِن تُطِيعُوا يُؤْتِكُمُ اللَّهُ أَجْرًا حَسَنًا ۖ وَإِن تَتَوَلَّوْا كَمَا تَوَلَّيْتُم مِّن قَبْلُ يُعَذِّبْكُمْ عَذَابًا أَلِيمًا ۝١٦
📖 Tekki Aaya 16
Waxal ñiy fuuyu ci araab yi ne leen : “Dees na leen woo jëme leen ci aw nit ñu am qadar ju tar ñàng . Dingeen di xeex ak ñoom wala ñu jébbale seen bopp. Su ngeen toppee, ndigalul Yàlla dana leen jox pey gu jekk, su ngeen lànkee nag kom ni ñu lànke woon cig njaalbéen, Yàlla dana leen mbugël mu mitti”.
لَّيْسَ عَلَى الْأَعْمَىٰ حَرَجٌ وَلَا عَلَى الْأَعْرَجِ حَرَجٌ وَلَا عَلَى الْمَرِيضِ حَرَجٌ ۗ وَمَن يُطِعِ اللَّهَ وَرَسُولَهُ يُدْخِلْهُ جَنَّاتٍ تَجْرِي مِن تَحْتِهَا الْأَنْهَارُ ۖ وَمَن يَتَوَلَّ يُعَذِّبْهُ عَذَابًا أَلِيمًا ۝١٧
📖 Tekki Aaya 17
Bakkaarub baña xare du dal ci kaw gumba, du dal it ci kaw ku lompoñ (làggi) du dal it ci kaw ku wopp. Te képp kuy topp Yàlla akub Yonentam, Dana ko tàbbal Àjjana joo xam ne ay dex dana daw ci suufam. Képp ku lànk, Dana ko mbugal mbugal mu mitti.
۞ لَّقَدْ رَضِيَ اللَّهُ عَنِ الْمُؤْمِنِينَ إِذْ يُبَايِعُونَكَ تَحْتَ الشَّجَرَةِ فَعَلِمَ مَا فِي قُلُوبِهِمْ فَأَنزَلَ السَّكِينَةَ عَلَيْهِمْ وَأَثَابَهُمْ فَتْحًا قَرِيبًا ۝١٨
📖 Tekki Aaya 18
Yàlla gërëm na jullit ñi jamono ja ñuy jaayanteek yaw ca ron garab ga. Xamoon na li nekk ci seen biiri xol, mu daldi wàcce dal ci seen kaw, daldi leen yoole ak ubbi gu jige (yewenóo)
وَمَغَانِمَ كَثِيرَةً يَأْخُذُونَهَا ۗ وَكَانَ اللَّهُ عَزِيزًا حَكِيمًا ۝١٩
📖 Tekki Aaya 19
ak ay màng (alal) yu bari yu nu nangu) yu ñuy jël. Yàlla Borom Kàttan la di Ku Xereñ .
وَعَدَكُمُ اللَّهُ مَغَانِمَ كَثِيرَةً تَأْخُذُونَهَا فَعَجَّلَ لَكُمْ هَٰذِهِ وَكَفَّ أَيْدِيَ النَّاسِ عَنكُمْ وَلِتَكُونَ آيَةً لِّلْمُؤْمِنِينَ وَيَهْدِيَكُمْ صِرَاطًا مُّسْتَقِيمًا ۝٢٠
📖 Tekki Aaya 20
Yàlla dig na leen ay màng yu bari yu ngeen di nara jël, mu gaawe leen ci (ubbig xaybar) gii te fegal na leen (ay yoxoy seeni noon), ak it ngir mu nekk kéemaan ci jullit ñi ak itam mu gindi leen tek leen ca yoon wu jubb xocc wa ;
وَأُخْرَىٰ لَمْ تَقْدِرُوا عَلَيْهَا قَدْ أَحَاطَ اللَّهُ بِهَا ۚ وَكَانَ اللَّهُ عَلَىٰ كُلِّ شَيْءٍ قَدِيرًا ۝٢١
📖 Tekki Aaya 21
Ak yeneen yu ngeen manul a woon Yàlla peeg na ko, Yàlla man na lépp lu ne.
وَلَوْ قَاتَلَكُمُ الَّذِينَ كَفَرُوا لَوَلَّوُا الْأَدْبَارَ ثُمَّ لَا يَجِدُونَ وَلِيًّا وَلَا نَصِيرًا ۝٢٢
📖 Tekki Aaya 22
Te sax bu yéefar yi xeexoon ak yéen danuy daw ; te dunu am kenn ku ñuy wéeru waxantumalaa ndimbal.
سُنَّةَ اللَّهِ الَّتِي قَدْ خَلَتْ مِن قَبْلُ ۖ وَلَن تَجِدَ لِسُنَّةِ اللَّهِ تَبْدِيلًا ۝٢٣
📖 Tekki Aaya 23
Mooy doxalinu Yàlla wi daan am na ka jekk. Te doxalinu Yàlla kenn du ko soppali.
وَهُوَ الَّذِي كَفَّ أَيْدِيَهُمْ عَنكُمْ وَأَيْدِيَكُمْ عَنْهُم بِبَطْنِ مَكَّةَ مِن بَعْدِ أَنْ أَظْفَرَكُمْ عَلَيْهِمْ ۚ وَكَانَ اللَّهُ بِمَا تَعْمَلُونَ بَصِيرًا ۝٢٤
📖 Tekki Aaya 24
Mooy ki leen fegaloon sen yoxo moo feg it seeni yoxo yéen ci ñoom ca biir xuru Màkka wa (ba xarewooleen), ginnaaw ba mu leen joxee ndam ca kaw yéefar ya. Yàlla gis na la ngeen doon def.
هُمُ الَّذِينَ كَفَرُوا وَصَدُّوكُمْ عَنِ الْمَسْجِدِ الْحَرَامِ وَالْهَدْيَ مَعْكُوفًا أَن يَبْلُغَ مَحِلَّهُ ۚ وَلَوْلَا رِجَالٌ مُّؤْمِنُونَ وَنِسَاءٌ مُّؤْمِنَاتٌ لَّمْ تَعْلَمُوهُمْ أَن تَطَئُوهُمْ فَتُصِيبَكُم مِّنْهُم مَّعَرَّةٌ بِغَيْرِ عِلْمٍ ۖ لِّيُدْخِلَ اللَّهُ فِي رَحْمَتِهِ مَن يَشَاءُ ۚ لَوْ تَزَيَّلُوا لَعَذَّبْنَا الَّذِينَ كَفَرُوا مِنْهُمْ عَذَابًا أَلِيمًا ۝٢٥
📖 Tekki Aaya 25
Ñoom ñoo di ña weddi woon te daan tere seen digganteek Jàkk ju ñu Wormaal ja dox it seen digganteek fa ñuy rendee hadyu. Dogan ko nag jullit ñu góor ñaak jullit ñu jigéen ña fa nekk te xamee wu leen ba manoon leen reyaale ca biir yéefar ya, te kon dey ñàkk xam dana leen yóbbe bàkkaar... Waaye Yàlla mooy tàbbal ku ko soob ci Yërmaandeem. Waaye su fekkoon ne yéefar yi dañoo beddiku dana leen mbugël mbugël mu mitti.
إِذْ جَعَلَ الَّذِينَ كَفَرُوا فِي قُلُوبِهِمُ الْحَمِيَّةَ حَمِيَّةَ الْجَاهِلِيَّةِ فَأَنزَلَ اللَّهُ سَكِينَتَهُ عَلَىٰ رَسُولِهِ وَعَلَى الْمُؤْمِنِينَ وَأَلْزَمَهُمْ كَلِمَةَ التَّقْوَىٰ وَكَانُوا أَحَقَّ بِهَا وَأَهْلَهَا ۚ وَكَانَ اللَّهُ بِكُلِّ شَيْءٍ عَلِيمًا ۝٢٦
📖 Tekki Aaya 26
Ngir yéefar ya ëmbu nañu ag rëy, rëy goo xam ne réer moo ko laltaay... Yàlla moom daldinay wàcce ag dal ci Yonentam ba (Muhammad) ak ca jullit ña (sahaaba ya), mu taqale leen ak baatub ragal Yàlla (“Laa Ilaaha illa Laahu Muhammadu rasuulu Laahi”), te ñoo ko gënoon a yayoo ci waa Màkka. Yàlla xam na lépp lu ne.
لَّقَدْ صَدَقَ اللَّهُ رَسُولَهُ الرُّؤْيَا بِالْحَقِّ ۖ لَتَدْخُلُنَّ الْمَسْجِدَ الْحَرَامَ إِن شَاءَ اللَّهُ آمِنِينَ مُحَلِّقِينَ رُءُوسَكُمْ وَمُقَصِّرِينَ لَا تَخَافُونَ ۖ فَعَلِمَ مَا لَمْ تَعْلَمُوا فَجَعَلَ مِن دُونِ ذَٰلِكَ فَتْحًا قَرِيبًا ۝٢٧
📖 Tekki Aaya 27
Yàlla dëggal na Yonentam ba géwénta ga ci dëgg : ci ne ko da ngeen dugg ca Al Masjid Al Haraam ca Màkka bu soobee Yàlla, ngeen diy waay wóolu, ngeen di waay watu seen kawar képp wala ngeen diy waay jempu seeni kawar, te du ngeen tiit. Yàlla xam na (ci yéwénóo ga) (ay njariñ) yu ngeen xamul. Moo defaat leneen lu dul loolu ak ubbi gu jigeñ (yoonóog Hudayba).
هُوَ الَّذِي أَرْسَلَ رَسُولَهُ بِالْهُدَىٰ وَدِينِ الْحَقِّ لِيُظْهِرَهُ عَلَى الدِّينِ كُلِّهِ ۚ وَكَفَىٰ بِاللَّهِ شَهِيدًا ۝٢٨
📖 Tekki Aaya 28
Moom moo yónni Yonentam ba (Muhammad) cig njub ak diiney dëgg (Islaam) ngir mu am ndam ci kaw diine yépp. Yàlla doy na sëkk seede.
مُّحَمَّدٌ رَّسُولُ اللَّهِ ۚ وَالَّذِينَ مَعَهُ أَشِدَّاءُ عَلَى الْكُفَّارِ رُحَمَاءُ بَيْنَهُمْ ۖ تَرَاهُمْ رُكَّعًا سُجَّدًا يَبْتَغُونَ فَضْلًا مِّنَ اللَّهِ وَرِضْوَانًا ۖ سِيمَاهُمْ فِي وُجُوهِهِم مِّنْ أَثَرِ السُّجُودِ ۚ ذَٰلِكَ مَثَلُهُمْ فِي التَّوْرَاةِ ۚ وَمَثَلُهُمْ فِي الْإِنجِيلِ كَزَرْعٍ أَخْرَجَ شَطْأَهُ فَآزَرَهُ فَاسْتَغْلَظَ فَاسْتَوَىٰ عَلَىٰ سُوقِهِ يُعْجِبُ الزُّرَّاعَ لِيَغِيظَ بِهِمُ الْكُفَّارَ ۗ وَعَدَ اللَّهُ الَّذِينَ آمَنُوا وَعَمِلُوا الصَّالِحَاتِ مِنْهُم مَّغْفِرَةً وَأَجْرًا عَظِيمًا ۝٢٩
📖 Tekki Aaya 29
Muhammadu moo di Yonent Yàlla. Bi ña àndoon ak moom dañoo taroon ca kaw yéefar ya, dañoo daan yëramante ci seen biir. Danga leen daan gis ñuy rukoo, di sujuud (julli), daan sàkku ngënéelul Yàlla ak ngëramam. Seeni jë dafa daan am ay màndarga ngir jeexiitali sujuud ga. Noone la nu leen melale ci tawraat. Ak ci injiil mu deme ni gàncax gu génn nekk baxaw, daldi màgg ba baamuy dëgër, te dijj këndëng yéem lool baykat ya. (Te ni Yàlla taxawoo jullit ña) ni lay merloo yéefar ya. Yàlla digna ñi gëm tey jëfe yiw ci ñoom, ag njégël ak pey gu màgg.
← 47 Al-Fath (48/114) 49 →
Jàng Simoore Al-Fath ci Wolof – Tekki, Waxtaan ak Baat

48الفتح Al-Fath 📚 29 Aaya مدنية



Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers