Simoore Al-Jumu'a
PDF —
Built right in your browser — download starts automatically
Simoore Al-Jumu'a pdf — Wàcce (Wolof)
Simoore Al-Jumu'a pdf Wolof — Wàcce Simoore Al-Jumu'a Tekki. Al-Jumu'a (Medinan) 11 Aaya.
Related
- Al-Jumu'a TekkiWolof
- Al-Jumu'a mp3Dégg
- Quran Index Wolof114
More Simoore PDF
Simoore Al-Jumu'a

ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝ
Ñi nekk ci asamaan yeek suuf si ña ngay sàbbaal Yàlla, miy Buur, bu Sell, di Boroom Kàttan, di Ku xereñ.
ﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳ
Moom mooy ki yónni ci araab yi ab Yonent bu bokk ci ñoom bu leen di jàngal ay Laayam, di leen jàngal Alxuraan ak Sunna, te ñoom bu jëkkoon ña nga woon ci réer gu sore,
ﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽ
ak ci ñeneen ñoo xam ne dabaguñuleen. Te moom Yàlla Mooy boroom Kàttan, di Ku Xereñ.
ﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉ
Loolu ngënéelul Yàlla la moo koy jox ku ko soob. Te Yàlla mooy boroom Ngënéel lu màgg li.
ﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣ
Misaalum ñi ñu wàcceeloon Tawraat te jëfewunu ko ñi ngi melni mbaam mu sëfi téere. Aka bon misaalum nit ñooñu nga xam ne dañoo weddi kàdduy Yàlla te Yàlla du gindi mukk aw nit ñu di ay tooñkat.
ﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖ
Waxal ne : "Eey yéen Yahuud yi ! Su fekkee ne nii ngeen méngook Yàllaay, kon ñaan leen dee, su fekkee ne dëggu ngeen”.
ﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡ
Dunu ko ñaan mukk ngir (la ñu jëf cik caay-caay). Yàlla ku Xamaakoon la tooñkat yi.
ﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵ
Waxal ne : “Dee gi ngeen di daw dana dajeek yéen. Ba noppi ñu delloo leen ca Yàlla mi xam kumpaak li feeñ mu di leen xibaar la ngeen daan def”.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧ
Eey yéen ñi gëm ! Saa suñu wootee ngir julli ci bisub Àjjuma, dawleen jëm ci tudd Yàlla te nangeen fa ne ñukk njaay ma bàyyi ko. Looloo gën ci yéen de, cëy bu ngeen xamoon!
ﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷ
Su julli gi jeexee, na ngeen tasaaroo ci suuf si, tey sàkku ci xeewali Yàlla yi, te na ngeen di tudd Yàlla lu bari ndax amaana ngeen baaxle.
ﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏ
Te saa su ñu gesee am njoló walla am po danuy buur jëm ca, bàyyi la nga ne saŋŋ taxaw. Waxal ne: “La nekk fa Yàlla moo gën fuuf am po te moo gën it am njoló, te Yàlla moo di Gën ji kuy wërsëgël”.
Alxuraan bu Tedd bi
Tuesday, August 18, 2026
Don't forget us in your sincere prayers







