🔥 0 fan yu toftaloo
📖 Simoore bu gudde — xaajoo ci yeneen ndogal yu ndaw (11 Aaya)
0/11
63:1
🔁 0/5
إِذَا جَآءَكَ ٱلۡمُنَٰفِقُونَ قَالُواْ نَشۡهَدُ إِنَّكَ لَرَسُولُ ٱللَّهِۗ وَٱللَّهُ يَعۡلَمُ إِنَّكَ لَرَسُولُهُۥ وَٱللَّهُ يَشۡهَدُ إِنَّ ٱلۡمُنَٰفِقِينَ لَكَٰذِبُونَ ١
Izaa jaaa`akal munaafiqoona qaaloo nashhadu innaka la rasoolul laah; wallaahu ya`lamu innaka la rasooluhoo wallaahu yashhadu innal munaafiqeena lakaaziboon
Su naaféq ya dikkee ci yaw danuy wax naan : “Noo ngi seede ne yaw Yonent Yàlla nga” ; Yàlla xam na ne yaw ab Yonentam nga ; te Yàlla seede na ne naaféq ya ay fenkat la ñu.
🎤 Sa fab:
63:2
🔁 0/5
ٱتَّخَذُوٓاْ أَيۡمَٰنَهُمۡ جُنَّةً فَصَدُّواْ عَن سَبِيلِ ٱللَّهِۚ إِنَّهُمۡ سَآءَ مَا كَانُواْ يَعۡمَلُونَ ٢
Ittakhazoo aymaanahum junnatan fasaddoo `an sabeelil laah; innahum saaa`a maa kaanoo ya`maloon
Def nañu seeni ngiñ muy pakk ñuy gàllankoor ci yoonu Yàlla. Ñoom dey la ñuy def ñaaw na !
🎤 Sa fab:
63:3
🔁 0/5
ذَٰلِكَ بِأَنَّهُمۡ ءَامَنُواْ ثُمَّ كَفَرُواْ فَطُبِعَ عَلَىٰ قُلُوبِهِمۡ فَهُمۡ لَا يَفۡقَهُونَ ٣
Zaalika bi annahum aamanoo summa kafaroo fatubi`a `alaa quloobihim fahum laa yafqahoon
(La ko def) moo di ne dañoo gëmoon, weddiwaat. Ñu fatt seeni xol, ba xamatuñu dara.
🎤 Sa fab:
63:4
🔁 0/5
۞ وَإِذَا رَأَيۡتَهُمۡ تُعۡجِبُكَ أَجۡسَامُهُمۡۖ وَإِن يَقُولُواْ تَسۡمَعۡ لِقَوۡلِهِمۡۖ كَأَنَّهُمۡ خُشُبٌ مُّسَنَّدَةٌۖ يَحۡسَبُونَ كُلَّ صَيۡحَةٍ عَلَيۡهِمۡۚ هُمُ ٱلۡعَدُوُّ فَٱحۡذَرۡهُمۡۚ قَٰتَلَهُمُ ٱللَّهُۖ أَنَّىٰ يُؤۡفَكُونَ ٤
Wa izaa ra aytahum tu`jibuka ajsaamuhum wa iny yaqooloo tasma` liqawlihim kaannahum khushubum musannadah; yahsaboona kulla saihatin `alaihim; humul `aduwwu fahzarhum; qaatalahumul laahu annaa yu`fakoon
Saa soo leen gisee, seeni yaram ya dalay yéem ; bu ñuy wax it, fàww nga déglu leen. Dañuy melni ay dénk yu ñu wéer fu yuuxu jibe ñu tiit. Ñoom ñooy noon ya tigi. Moytandikuleen ! Yàlla dana leen faagaagal kem niñu dumóoyoo (yoonam).
🎤 Sa fab:
63:5
🔁 0/5
وَإِذَا قِيلَ لَهُمۡ تَعَالَوۡاْ يَسۡتَغۡفِرۡ لَكُمۡ رَسُولُ ٱللَّهِ لَوَّوۡاْ رُءُوسَهُمۡ وَرَأَيۡتَهُمۡ يَصُدُّونَ وَهُم مُّسۡتَكۡبِرُونَ ٥
Wa izaa qeela lahum ta`aalaw yastaghfir lakum rasoolul laahi lawwaw ru`oo sahum wa ra aytahum yasuddoona wa hum mustakbiroon
Sunu leen waxee ne : “Kaayleen Yonent Yàlla bi jéggalul leen”, ñuy dag-dagali bopp, dumóoyu tey rëy-rëylu.
🎤 Sa fab:
63:6
🔁 0/5
سَوَآءٌ عَلَيۡهِمۡ أَسۡتَغۡفَرۡتَ لَهُمۡ أَمۡ لَمۡ تَسۡتَغۡفِرۡ لَهُمۡ لَن يَغۡفِرَ ٱللَّهُ لَهُمۡۚ إِنَّ ٱللَّهَ لَا يَهۡدِي ٱلۡقَوۡمَ ٱلۡفَٰسِقِينَ ٦
Sawaaa`un `alaihim as taghfarta lahum am lam tastaghfir lahum lany yaghfiral laahu lahum; innal laaha laa yahdil qawmal faasiqeen
Nga, jéggalul leen, ak nga ñàkk leen jéggalul ñoo yem : ndax Yàlla duleen jéggal mukk, te Yàlla du gindi nit ñu di ay saay-saay.
🎤 Sa fab:
63:7
🔁 0/5
هُمُ ٱلَّذِينَ يَقُولُونَ لَا تُنفِقُواْ عَلَىٰ مَنۡ عِندَ رَسُولِ ٱللَّهِ حَتَّىٰ يَنفَضُّواْۗ وَلِلَّهِ خَزَآئِنُ ٱلسَّمَٰوَٰتِ وَٱلۡأَرۡضِ وَلَٰكِنَّ ٱلۡمُنَٰفِقِينَ لَا يَفۡقَهُونَ ٧
Humul lazeena yaqooloona laa tunfiqoo `alaa man inda Rasoolil laahi hatta yanfaddoo; wa lillaahi khazaaa` inus samaawaati wal ardi wa laakinnal munaafiqeena la yafqahoon
Ñoom ñooy wax naan : “Buleen joxati dara ña nek ca Yonent ba, ba baa nuy xaddi”. Te Yàllaa moom ndambi asamaan yeek suuf si, Waaye naaféq ya xamuñu.
🎤 Sa fab:
63:8
🔁 0/5
يَقُولُونَ لَئِن رَّجَعۡنَآ إِلَى ٱلۡمَدِينَةِ لَيُخۡرِجَنَّ ٱلۡأَعَزُّ مِنۡهَا ٱلۡأَذَلَّۚ وَلِلَّهِ ٱلۡعِزَّةُ وَلِرَسُولِهِۦ وَلِلۡمُؤۡمِنِينَ وَلَٰكِنَّ ٱلۡمُنَٰفِقِينَ لَا يَعۡلَمُونَ ٨
Yaqooloona la`ir raja`naaa ilal madeenati la yukhrijanal a`azzu minhal azall; wa lillaahil `izzatu wa li Rasoolihee wa lilmu`mineena wa laakinnal munaafiqeena laa ya`lamoon
Danañuy wax naan : “Sunu delloo Madiina, ña am doole danañu génne ña néew doole ”. Te Yàlla rekk am doole mook ab Yonentam ak way gëm ña. Waaye naaféq ya xamuñu.
🎤 Sa fab:
63:9
🔁 0/5
يَٰٓأَيُّهَا ٱلَّذِينَ ءَامَنُواْ لَا تُلۡهِكُمۡ أَمۡوَٰلُكُمۡ وَلَآ أَوۡلَٰدُكُمۡ عَن ذِكۡرِ ٱللَّهِۚ وَمَن يَفۡعَلۡ ذَٰلِكَ فَأُوْلَٰٓئِكَ هُمُ ٱلۡخَٰسِرُونَ ٩
Yaaa ayyuhal lazeena aamanoo la tulhikum amwaalukum wa laa awlaadukum `anzikril laah; wa mai-yaf`al zaalika fa-ulaaa`ika humul khaasiroon
Eey yéen ñi gëm ! Bu leen seeni alal ak seeni doom fàbbi ci tudd Yàlla. Képp kuy def loolu... (na xam ne) ñoom ñooy yàqule.
🎤 Sa fab:
63:10
🔁 0/5
وَأَنفِقُواْ مِن مَّا رَزَقۡنَٰكُم مِّن قَبۡلِ أَن يَأۡتِيَ أَحَدَكُمُ ٱلۡمَوۡتُ فَيَقُولَ رَبِّ لَوۡلَآ أَخَّرۡتَنِيٓ إِلَىٰٓ أَجَلٍ قَرِيبٍ فَأَصَّدَّقَ وَأَكُن مِّنَ ٱلصَّٰلِحِينَ ١٠
Wa anifqoo mim maa razaqnaakum min qabli any-yaatiya ahadakumul mawtu fa yaqoola rabbi law laaa akhkhartaneee ilaaa ajalin qareebin fa assaddaqa wa akum minassaaliheen
Te nangeen di joxe ci alal ji nu leen wërsëgël balaa dee di dikkël kenn ci yéen muy wax naan : “Cëy sama Boroom ! muñal ma as ndiir : ndax ma man a saraxe ba bokk ca ñu yiw ñi”.
🎤 Sa fab:
63:11
🔁 0/5
وَلَن يُؤَخِّرَ ٱللَّهُ نَفۡسًا إِذَا جَآءَ أَجَلُهَاۚ وَٱللَّهُ خَبِيرُۢ بِمَا تَعۡمَلُونَ ١١
Wa lany yu `akhkhiral laahu nafsan izaa jaaa`a ajaluhaa; wallaahu khabeerum bimaa ta`maloon
Te Yàlla moom du yeexe benn bakkan saasu ab digam agsee. Te Yàlla ku deñ-kumpa la ci li ngeen di def.
🎤 Sa fab:
💡 Bësal baat bu nëbbu ngir wone ko ci diir bu gàtt — sa yokkute dañu koy denc ci boppam.
العربيةEnglishBahasa IndonesiaTürkçeРусскийفارسیFrançaisاردوবাংলাDeutschEspañol中文हिन्दीPortuguêsItalianoภาษาไทยPolskiNederlandsShqipKiswahiliO'zbekதமிழ்MelayuBosanskiSoomaaliAzərbaycanکوردی한국어日本語SvenskaDanskNorskپښتوമലയാളംසිංහලTamazightHausaአማርኛБългарскиТоҷикӣҚазақшаFilipinoسنڌيYorùbáFulfuldeТатарчаئۇيغۇرچەКыргызчаਪੰਜਾਬੀJawaతెలుగుမြန်မာગુજરાતીOromoमराठीTiếng ViệtMalagasyНохчийнWolofދިވެހިಕನ್ನಡУкраїнськаΕλληνικάქართულიខ្មែរدریQafar afMaranaoनेपाली
Alxuraan bu Tedd bi
Tuesday, August 18, 2026
Don't forget us in your sincere prayers







