Simoore Al-Munafiqun pdf — Wàcce (Wolof)
Simoore Al-Munafiqun pdf Wolof — Wàcce Simoore Al-Munafiqun Tekki. Simoore Al-Munafiqun (Medinan) 11 Aaya.
Related
More Simoore PDF
Simoore Al-Munafiqun

ﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢ
63:1
Su naaféq ya dikkee ci yaw danuy wax naan : “Noo ngi seede ne yaw Yonent Yàlla nga” ; Yàlla xam na ne yaw ab Yonentam nga ; te Yàlla seede na ne naaféq ya ay fenkat la ñu.
ﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰ
63:2
Def nañu seeni ngiñ muy pakk ñuy gàllankoor ci yoonu Yàlla. Ñoom dey la ñuy def ñaaw na !
ﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝ
63:3
(La ko def) moo di ne dañoo gëmoon, weddiwaat. Ñu fatt seeni xol, ba xamatuñu dara.
ﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻ
63:4
Saa soo leen gisee, seeni yaram ya dalay yéem ; bu ñuy wax it, fàww nga déglu leen. Dañuy melni ay dénk yu ñu wéer fu yuuxu jibe ñu tiit. Ñoom ñooy noon ya tigi. Moytandikuleen ! Yàlla dana leen faagaagal kem niñu dumóoyoo (yoonam).
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟ
63:5
Sunu leen waxee ne : “Kaayleen Yonent Yàlla bi jéggalul leen”, ñuy dag-dagali bopp, dumóoyu tey rëy-rëylu.
ﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳ
63:6
Nga, jéggalul leen, ak nga ñàkk leen jéggalul ñoo yem : ndax Yàlla duleen jéggal mukk, te Yàlla du gindi nit ñu di ay saay-saay.
ﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉ
63:7
Ñoom ñooy wax naan : “Buleen joxati dara ña nek ca Yonent ba, ba baa nuy xaddi”. Te Yàllaa moom ndambi asamaan yeek suuf si, Waaye naaféq ya xamuñu.
ﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜ
63:8
Danañuy wax naan : “Sunu delloo Madiina, ña am doole danañu génne ña néew doole ”. Te Yàlla rekk am doole mook ab Yonentam ak way gëm ña. Waaye naaféq ya xamuñu.
ﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯ
63:9
Eey yéen ñi gëm ! Bu leen seeni alal ak seeni doom fàbbi ci tudd Yàlla. Képp kuy def loolu... (na xam ne) ñoom ñooy yàqule.
ﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦ
63:10
Te nangeen di joxe ci alal ji nu leen wërsëgël balaa dee di dikkël kenn ci yéen muy wax naan : “Cëy sama Boroom ! muñal ma as ndiir : ndax ma man a saraxe ba bokk ca ñu yiw ñi”.
ﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳ
63:11
Te Yàlla moom du yeexe benn bakkan saasu ab digam agsee. Te Yàlla ku deñ-kumpa la ci li ngeen di def.
Alxuraan bu Tedd bi
Wednesday, September 9, 2026
Don't forget us in your sincere prayers







