📖 0/604 xët yi jàng nañu
📄 453
Simoore Sad

Simoore Sad

38:3
كَمۡ أَهۡلَكۡنَا مِن قَبۡلِهِم مِّن قَرۡنٍ فَنَادَواْ وَّلَاتَ حِينَ مَنَاصٍ ٣
Aka bari ñu nu faagaagal ca ña leen jiitu woon, ñu daan yuuxu, walla te du ñu man a raw?
38:4
وَعَجِبُوٓاْ أَن جَآءَهُم مُّنذِرٌ مِّنۡهُمۡۖ وَقَالَ ٱلۡكَٰفِرُونَ هَٰذَا سَٰحِرٌ كَذَّابٌ ٤
(Waa Màkka) daana yéeme ci waaraatekat bii leen digal te bokk ci ñoom, yéefar ya daan wax naan : “Kii dey ab njibarkat la bu di ab fenaakoon,
38:5
أَجَعَلَ ٱلۡأٓلِهَةَ إِلَٰهًا وَٰحِدًاۖ إِنَّ هَٰذَا لَشَيۡءٌ عُجَابٌ ٥
Moo ndax dafa bëgg a def Yàlla yii muy jenn Yàlla ? Aa lii dey mbir mu yéeme la”.
38:6
وَٱنطَلَقَ ٱلۡمَلَأُ مِنۡهُمۡ أَنِ ٱمۡشُواْ وَٱصۡبِرُواْ عَلَىٰٓ ءَالِهَتِكُمۡۖ إِنَّ هَٰذَا لَشَيۡءٌ يُرَادُ ٦
Kilifa ya ne leen : “Demleen, te muñ jàpp ci seen Yàlla yii : lii daal la nu bëgg.
38:7
مَا سَمِعۡنَا بِهَٰذَا فِي ٱلۡمِلَّةِ ٱلۡأٓخِرَةِ إِنۡ هَٰذَآ إِلَّا ٱخۡتِلَٰقٌ ٧
Nun masunoo dégg lii ci diine ji fi mujj wàcc (Iisaa) ; lii daal ay sos rekk la !
38:8
أَءُنزِلَ عَلَيۡهِ ٱلذِّكۡرُ مِنۢ بَيۡنِنَاۚ بَلۡ هُمۡ فِي شَكٍّ مِّن ذِكۡرِيۚ بَل لَّمَّا يَذُوقُواْ عَذَابِ ٨
Nuy wax naan, ak ni nu tollu ndax ci moom la [Alxuraan] di wàcc? ” Li wer moo di yéefar yaa ngay sikki-sàkka ci sama Téere bi. Xanaa kay dañoo mosagul mbugël !
38:9
أَمۡ عِندَهُمۡ خَزَآئِنُ رَحۡمَةِ رَبِّكَ ٱلۡعَزِيزِ ٱلۡوَهَّابِ ٩
Walla ndabi yërmaandey sa Boroom tey Mayewaakoon, biy boroom Kàttan bi, da fa nekk ci ñoom.
38:10
أَمۡ لَهُم مُّلۡكُ ٱلسَّمَٰوَٰتِ وَٱلۡأَرۡضِ وَمَا بَيۡنَهُمَاۖ فَلۡيَرۡتَقُواْ فِي ٱلۡأَسۡبَٰبِ ١٠
Walla dañoo moom nguurug asamaan yeek suuf si, ak li nekk ci seen diggënte? su fekkee ne looloo am kon nañu def pexe ci yéeg ci !
38:11
جُندٌ مَّا هُنَالِكَ مَهۡزُومٌ مِّنَ ٱلۡأَحۡزَابِ ١١
Ak nu seeni xarekat man a tollu ak ña leen di jàppale, danuy nërméelu !
38:12
كَذَّبَتۡ قَبۡلَهُمۡ قَوۡمُ نُوحٍ وَعَادٌ وَفِرۡعَوۡنُ ذُو ٱلۡأَوۡتَادِ ١٢
ña leen fi jiitu woon, weddi woon nañu ña di nitu Nooh, ak Aad ak Firawna ma doon boroom dëx (tabax yu rëy),
38:13
وَثَمُودُ وَقَوۡمُ لُوطٍ وَأَصۡحَٰبُ لۡـَٔيۡكَةِۚ أُوْلَٰٓئِكَ ٱلۡأَحۡزَابُ ١٣
k Samuud, ak nitu Lóot, ak waa Aykata, (ñoom ñépp weddi woon nañu seeni yonnent). Te ñoom ñoo di jàppalekat ya (farandoo ya).
38:14
إِن كُلٌّ إِلَّا كَذَّبَ ٱلرُّسُلَ فَحَقَّ عِقَابِ ١٤
Ñoom ñépp weddi woon yonnent ya. Nu daldi leen mbugël !
38:15
وَمَا يَنظُرُ هَٰٓؤُلَآءِ إِلَّا صَيۡحَةً وَٰحِدَةً مَّا لَهَا مِن فَوَاقٍ ١٥
Ñoom xaaruñu lu dul genn xaacu, gu dul tóllantiku wol.
38:16
وَقَالُواْ رَبَّنَا عَجِّل لَّنَا قِطَّنَا قَبۡلَ يَوۡمِ ٱلۡحِسَابِ ١٦
Ñuy wax naan : “Yaw sunu Boroom, gaawal jox nu sunu wàll balaa wañoo ba”.
العربيةEnglishBahasa IndonesiaTürkçeРусскийفارسیFrançaisاردوবাংলাDeutschEspañol中文हिन्दीPortuguêsItalianoภาษาไทยPolskiNederlandsShqipKiswahiliO'zbekதமிழ்MelayuBosanskiSoomaaliAzərbaycanکوردی한국어日本語SvenskaDanskNorskپښتوമലയാളംසිංහලTamazightHausaአማርኛБългарскиТоҷикӣҚазақшаFilipinoسنڌيYorùbáFulfuldeТатарчаئۇيغۇرچەКыргызчаਪੰਜਾਬੀJawaతెలుగుမြန်မာગુજરાતીOromoमराठीTiếng ViệtMalagasyНохчийнWolofދިވެހިಕನ್ನಡУкраїнськаΕλληνικάქართულიខ្មែរدریQafar afMaranaoनेपाली
Alxuraan bu Tedd bi
Friday, August 28, 2026
Don't forget us in your sincere prayers







