Simoore Al-A'la ci Aarabu ak Wolof

Jàng Simoore Al-A'la ak tekkim wolof bu mat sëkk, ak baat. Tekki ayaa bu ne. (19 Aaya — مكية). Al-A'la Dégg, Al-A'la Tekki, Al-A'la mp3, Al-A'la pdf.

Jàng te Dégg Simoore Al-A'la

🎧 Aaya
M Mishary Rashid Alafasy
M Mahmoud Khalil Al-Husary
A Abdurrahman As-Sudais
M Mohamed Siddiq Al-Minshawi
A Abdul Basit Abdul Samad
A Ali Al-Hudhaify
A Ahmed ibn Ali al-Ajamy
A Abu Bakr Ash-Shaatree
M Muhammad Ayyoub
A Abdullah Basfar
A Abdullah Al-Juhani
M Maher Al Muaiqly
x1
سَبِّحِ اسْمَ رَبِّكَ الْأَعْلَى ۝١
📖 Tekki Aaya 1
Sàbbaalal sa turu Boroom, bi Gëna kawe,
الَّذِي خَلَقَ فَسَوَّىٰ ۝٢
📖 Tekki Aaya 2
Ki bind jekkal yemale,
وَالَّذِي قَدَّرَ فَهَدَىٰ ۝٣
📖 Tekki Aaya 3
kiy dogal tey gindee,
وَالَّذِي أَخْرَجَ الْمَرْعَىٰ ۝٤
📖 Tekki Aaya 4
kiy génne ñax mi saxal ko,
فَجَعَلَهُ غُثَاءً أَحْوَىٰ ۝٥
📖 Tekki Aaya 5
di ko naatal dëlël ko.
سَنُقْرِئُكَ فَلَا تَنسَىٰ ۝٦
📖 Tekki Aaya 6
Dananu la jàngal (Alxuraan), te doo too ko fàtte
إِلَّا مَا شَاءَ اللَّهُ ۚ إِنَّهُ يَعْلَمُ الْجَهْرَ وَمَا يَخْفَىٰ ۝٧
📖 Tekki Aaya 7
lu dul la soob Yàlla. Moom moo xam li feeñ ak li nëbbu.
وَنُيَسِّرُكَ لِلْيُسْرَىٰ ۝٨
📖 Tekki Aaya 8
Dananu la jàppandalal yoon wi gëna yomb.
فَذَكِّرْ إِن نَّفَعَتِ الذِّكْرَىٰ ۝٩
📖 Tekki Aaya 9
Na ngay fàttelee, saa su fàtteli amee njariñ.
سَيَذَّكَّرُ مَن يَخْشَىٰ ۝١٠
📖 Tekki Aaya 10
képp kuy ragal (Yàlla) na nangoo fàttaliku,
وَيَتَجَنَّبُهَا الْأَشْقَى ۝١١
📖 Tekki Aaya 11
ñu texeedi ñaa koy moytu,
الَّذِي يَصْلَى النَّارَ الْكُبْرَىٰ ۝١٢
📖 Tekki Aaya 12
ñay lakk ca safara sa gëna rëy,
ثُمَّ لَا يَمُوتُ فِيهَا وَلَا يَحْيَىٰ ۝١٣
📖 Tekki Aaya 13
du fa dund dufa dee.
قَدْ أَفْلَحَ مَن تَزَكَّىٰ ۝١٤
📖 Tekki Aaya 14
Képp kuy sellal texe na,
وَذَكَرَ اسْمَ رَبِّهِ فَصَلَّىٰ ۝١٥
📖 Tekki Aaya 15
te fàttaliku turu boroomam , tey julli.
بَلْ تُؤْثِرُونَ الْحَيَاةَ الدُّنْيَا ۝١٦
📖 Tekki Aaya 16
Yeen, dangeena bëgg lool dundug àddina,
وَالْآخِرَةُ خَيْرٌ وَأَبْقَىٰ ۝١٧
📖 Tekki Aaya 17
te àllaaxira gën te moo gëna sax.
إِنَّ هَٰذَا لَفِي الصُّحُفِ الْأُولَىٰ ۝١٨
📖 Tekki Aaya 18
Lii nekk na, ca téere yu jëkk ya,
صُحُفِ إِبْرَاهِيمَ وَمُوسَىٰ ۝١٩
📖 Tekki Aaya 19
téerey Ibraahiima ak Muusaa.
← 86 Al-A'la (87/114) 88 →
Jàng Simoore Al-A'la ci Wolof – Tekki, Waxtaan ak Baat

87الأعلى Al-A'la 📚 19 Aaya مكية



Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers