📖 0/604 xët yi jàng nañu
📄 549
Simoore Al-Mumtahina

Simoore Al-Mumtahina

60:1
يَٰٓأَيُّهَا ٱلَّذِينَ ءَامَنُواْ لَا تَتَّخِذُواْ عَدُوِّي وَعَدُوَّكُمۡ أَوۡلِيَآءَ تُلۡقُونَ إِلَيۡهِم بِٱلۡمَوَدَّةِ وَقَدۡ كَفَرُواْ بِمَا جَآءَكُم مِّنَ ٱلۡحَقِّ يُخۡرِجُونَ ٱلرَّسُولَ وَإِيَّاكُمۡ أَن تُؤۡمِنُواْ بِٱللَّهِ رَبِّكُمۡ إِن كُنتُمۡ خَرَجۡتُمۡ جِهَٰدًا فِي سَبِيلِي وَٱبۡتِغَآءَ مَرۡضَاتِيۚ تُسِرُّونَ إِلَيۡهِم بِٱلۡمَوَدَّةِ وَأَنَا۠ أَعۡلَمُ بِمَآ أَخۡفَيۡتُمۡ وَمَآ أَعۡلَنتُمۡۚ وَمَن يَفۡعَلۡهُ مِنكُمۡ فَقَدۡ ضَلَّ سَوَآءَ ٱلسَّبِيلِ ١
Eey ñi gëm ! Buleen jàpp Samay noon ak seeni noon, ay xarit, ndax ñoom dañoo weddi dëgg ga dikk ci yéen. Danañu génne Yonent bi ak yéen néey da ngeen a gëm, Yàlla. Su fekkee ne dangeen a génn di xare ji ci yoonu Yàlla tey sàkku sama ngërëm, buleen rocciku mukk di wut ci ñoom ay xarit, ndax Man xam naa li ngeen di nëbb ak li ngeen di feeñal ? Képp ku ko def ci yéen na xam ne réere na yoon wu jub xocc wa.
60:2
إِن يَثۡقَفُوكُمۡ يَكُونُواْ لَكُمۡ أَعۡدَآءً وَيَبۡسُطُوٓاْ إِلَيۡكُمۡ أَيۡدِيَهُمۡ وَأَلۡسِنَتَهُم بِٱلسُّوٓءِ وَوَدُّواْ لَوۡ تَكۡفُرُونَ ٢
Te suñu leen jekkoo, danañu leen rey saaga leen ; li ñu bëgg moo di ngeen weddi.
60:3
لَن تَنفَعَكُمۡ أَرۡحَامُكُمۡ وَلَآ أَوۡلَٰدُكُمۡۚ يَوۡمَ ٱلۡقِيَٰمَةِ يَفۡصِلُ بَيۡنَكُمۡۚ وَٱللَّهُ بِمَا تَعۡمَلُونَ بَصِيرٌ ٣
Te bu Bis Pénc baa seeni doom walla seeni mbokk dunuleen fa jariñ, [Yàlla] dana fa teqale seen diggante, te Yàlla kuy Gis la li ngeen di def.
60:4
قَدۡ كَانَتۡ لَكُمۡ أُسۡوَةٌ حَسَنَةٌ فِيٓ إِبۡرَٰهِيمَ وَٱلَّذِينَ مَعَهُۥٓ إِذۡ قَالُواْ لِقَوۡمِهِمۡ إِنَّا بُرَءَٰٓؤُاْ مِنكُمۡ وَمِمَّا تَعۡبُدُونَ مِن دُونِ ٱللَّهِ كَفَرۡنَا بِكُمۡ وَبَدَا بَيۡنَنَا وَبَيۡنَكُمُ ٱلۡعَدَٰوَةُ وَٱلۡبَغۡضَآءُ أَبَدًا حَتَّىٰ تُؤۡمِنُواْ بِٱللَّهِ وَحۡدَهُۥٓ إِلَّا قَوۡلَ إِبۡرَٰهِيمَ لِأَبِيهِ لَأَسۡتَغۡفِرَنَّ لَكَ وَمَآ أَمۡلِكُ لَكَ مِنَ ٱللَّهِ مِن شَيۡءٍۖ رَّبَّنَا عَلَيۡكَ تَوَكَّلۡنَا وَإِلَيۡكَ أَنَبۡنَا وَإِلَيۡكَ ٱلۡمَصِيرُ ٤
Am ngeen, royukaay wu rafet ci Ibraahiima ak ña àndoon ak moom, (fàttalikul) ba ñu waxee seen nit ña ne leen : “Deñ nanu ci, yéen ak li ngeen di jaamu te du Yàlla. Weddi nanu leen. Sunu digganteek yéen it, mbañeel ak ug noonoo moo fiy dox ba fàwwu, lu dul bu ngeen gëmee Yàlla doŋŋ”. Ba mu des waxi Ibraahiima ak baayam ne ko : “Danaa la, jéggalul [Yàlla] waaye amaluma la dara ci Yàlla”. “Yaw sunu Boroom, Yaw la nu doyloo te ci Yaw la nuy delu. Te ci Yaw la lépp di Mujj.
60:5
رَبَّنَا لَا تَجۡعَلۡنَا فِتۡنَةً لِّلَّذِينَ كَفَرُواْ وَٱغۡفِرۡ لَنَا رَبَّنَآۖ إِنَّكَ أَنتَ ٱلۡعَزِيزُ ٱلۡحَكِيمُ ٥
Yaw sunu Boroom, bul nu def mukk [sànje] ci loxoy yéefar yi ; te nanga nu jéggal, Yaw, yaa di Boroom Kàttan gi, di Ku Xereñ ki”
العربيةEnglishBahasa IndonesiaTürkçeРусскийفارسیFrançaisاردوবাংলাDeutschEspañol中文हिन्दीPortuguêsItalianoภาษาไทยPolskiNederlandsShqipKiswahiliO'zbekதமிழ்MelayuBosanskiSoomaaliAzərbaycanکوردی한국어日本語SvenskaDanskNorskپښتوമലയാളംසිංහලTamazightHausaአማርኛБългарскиТоҷикӣҚазақшаFilipinoسنڌيYorùbáFulfuldeТатарчаئۇيغۇرچەКыргызчаਪੰਜਾਬੀJawaతెలుగుမြန်မာગુજરાતીOromoमराठीTiếng ViệtMalagasyНохчийнWolofދިވެހިಕನ್ನಡУкраїнськаΕλληνικάქართულიខ្មែរدریQafar afMaranaoनेपाली
Alxuraan bu Tedd bi
Monday, August 31, 2026
Don't forget us in your sincere prayers







