📖 0/604 xët yi jàng nañu
📄 128
Al-An'am

Al-An'am

6:1
ٱلۡحَمۡدُ لِلَّهِ ٱلَّذِي خَلَقَ ٱلسَّمَٰوَٰتِ وَٱلۡأَرۡضَ وَجَعَلَ ٱلظُّلُمَٰتِ وَٱلنُّورَۖ ثُمَّ ٱلَّذِينَ كَفَرُواْ بِرَبِّهِمۡ يَعۡدِلُونَ ١
Cant ñeel na Yàlla mi bind asamaan yeek suuf si, te sos lëndëm yi ak leer yi. Terewul ña weddi ñoom di dendale seen Boroom ak leneen.
6:2
هُوَ ٱلَّذِي خَلَقَكُم مِّن طِينٍ ثُمَّ قَضَىٰٓ أَجَلًاۖ وَأَجَلٌ مُّسَمًّى عِندَهُۥۖ ثُمَّ أَنتُمۡ تَمۡتَرُونَ ٢
Moom mooy ki leen bind ci ban ; ba noppi dugal àpp [ci dundu gu ne] ak àpp ba ñu tudd ci Moom [ci jéexug àdduna si]. Ba noppi ngeen di am xel-yaar !
6:3
وَهُوَ ٱللَّهُ فِي ٱلسَّمَٰوَٰتِ وَفِي ٱلۡأَرۡضِ يَعۡلَمُ سِرَّكُمۡ وَجَهۡرَكُمۡ وَيَعۡلَمُ مَا تَكۡسِبُونَ ٣
Te Mooy Yàlla ci asamaan yeek suuf si. Mooy ki xam seen mbóot yi ngeen di nëbb ak yi ngeen di feeñal te xam it la ngeen di fàggu.
6:4
وَمَا تَأۡتِيهِم مِّنۡ ءَايَةٍ مِّنۡ ءَايَٰتِ رَبِّهِمۡ إِلَّا كَانُواْ عَنۡهَا مُعۡرِضِينَ ٤
Te kat amul lenn ndigal lu leen dikke ca seen Boroom te dëdduwuñu ko.
6:5
فَقَدۡ كَذَّبُواْ بِٱلۡحَقِّ لَمَّا جَآءَهُمۡ فَسَوۡفَ يَأۡتِيهِمۡ أَنۢبَٰٓؤُاْ مَا كَانُواْ بِهِۦ يَسۡتَهۡزِءُونَ ٥
Weddi nañu dëgg ba mu dikkee ca ñoom. Waaye dana leen mas a dikkal xew-xewi la ñu tejji.
6:6
أَلَمۡ يَرَوۡاْ كَمۡ أَهۡلَكۡنَا مِن قَبۡلِهِم مِّن قَرۡنٍ مَّكَّنَّٰهُمۡ فِي ٱلۡأَرۡضِ مَا لَمۡ نُمَكِّن لَّكُمۡ وَأَرۡسَلۡنَا ٱلسَّمَآءَ عَلَيۡهِم مِّدۡرَارًا وَجَعَلۡنَا ٱلۡأَنۡهَٰرَ تَجۡرِي مِن تَحۡتِهِمۡ فَأَهۡلَكۡنَٰهُم بِذُنُوبِهِمۡ وَأَنشَأۡنَا مِنۢ بَعۡدِهِمۡ قَرۡنًا ءَاخَرِينَ ٦
Moo ndax dañoo xamul ñaata maas Lanu alag ca ña leen jiitu, ñoo xam ne mayoon Nanu leen lu Nu leen mayul [yéen] ? Te dottil woon Nanu asamaan mu taw ca ñoom, waaye defaloon leen ay dex yuy dawaan. Waaye Nu daldi leen alag ngir seeni bàkkaar ; sosaat nag geneen maas wu watle leen ko.
6:7
وَلَوۡ نَزَّلۡنَا عَلَيۡكَ كِتَٰبًا فِي قِرۡطَاسٍ فَلَمَسُوهُ بِأَيۡدِيهِمۡ لَقَالَ ٱلَّذِينَ كَفَرُوٓاْ إِنۡ هَٰذَآ إِلَّا سِحۡرٌ مُّبِينٌ ٧
Bu Nu la wàcceeloon Téere bu ñu bind ci kayit gu ñu mën a laal ak seeni yoxo sax, du tee ñu weddi ñoom ne : “Lii ag jibar doŋŋ la ! ”
6:8
وَقَالُواْ لَوۡلَآ أُنزِلَ عَلَيۡهِ مَلَكٌۖ وَلَوۡ أَنزَلۡنَا مَلَكًا لَّقُضِيَ ٱلۡأَمۡرُ ثُمَّ لَا يُنظَرُونَ ٨
Ba noppi di wax naan : “Lu tee woon ñu wàcce ci moom Malaaka ? ”. Waaye bu ñu wàcce woon Malaaka, kon mbir ya sottikoon na ; ndax kenn duleen muñandiku kon.
العربيةEnglishBahasa IndonesiaTürkçeРусскийفارسیFrançaisاردوবাংলাDeutschEspañol中文हिन्दीPortuguêsItalianoภาษาไทยPolskiNederlandsShqipKiswahiliO'zbekதமிழ்MelayuBosanskiSoomaaliAzərbaycanکوردی한국어日本語SvenskaDanskNorskپښتوമലയാളംසිංහලTamazightHausaአማርኛБългарскиТоҷикӣҚазақшаFilipinoسنڌيYorùbáFulfuldeТатарчаئۇيغۇرچەКыргызчаਪੰਜਾਬੀJawaతెలుగుမြန်မာગુજરાતીOromoमराठीTiếng ViệtMalagasyНохчийнWolofދިވެހިಕನ್ನಡУкраїнськаΕλληνικάქართულიខ្មែរدریQafar afMaranaoनेपाली
Alxuraan bu Tedd bi
Saturday, August 22, 2026
Don't forget us in your sincere prayers







