Simoore At-Taghabun ci Aarabu ak Wolof
Jàng Simoore At-Taghabun ak tekkim wolof bu mat sëkk, ak baat. Tekki ayaa bu ne. (18 Aaya — مدنية). At-Taghabun Dégg, At-Taghabun Tekki, At-Taghabun mp3, At-Taghabun pdf.Jàng te Dégg Simoore At-Taghabun
🎧 Aaya
M
Mishary Rashid Alafasy
✓
Mishary Rashid Alafasy
✓
M
Mahmoud Khalil Al-Husary
✓
Mahmoud Khalil Al-Husary
✓
A
Abdurrahman As-Sudais
✓
Abdurrahman As-Sudais
✓
M
Mohamed Siddiq Al-Minshawi
✓
Mohamed Siddiq Al-Minshawi
✓
A
Abdul Basit Abdul Samad
✓
Abdul Basit Abdul Samad
✓
A
Ali Al-Hudhaify
✓
Ali Al-Hudhaify
✓
A
Ahmed ibn Ali al-Ajamy
✓
Ahmed ibn Ali al-Ajamy
✓
A
Abu Bakr Ash-Shaatree
✓
Abu Bakr Ash-Shaatree
✓
M
Muhammad Ayyoub
✓
Muhammad Ayyoub
✓
A
Abdullah Basfar
✓
Abdullah Basfar
✓
A
Abdullah Al-Juhani
✓
Abdullah Al-Juhani
✓
M
Maher Al Muaiqly
✓
Maher Al Muaiqly
✓
—
x1
يُسَبِّحُ لِلَّهِ مَا فِي السَّمَاوَاتِ وَمَا فِي الْأَرْضِ ۖ لَهُ الْمُلْكُ وَلَهُ الْحَمْدُ ۖ وَهُوَ عَلَىٰ كُلِّ شَيْءٍ قَدِيرٌ ١
📖 Tekki
Aaya 1
Ñi nekk ci asamaan yeek suuf si ña ngay sàbbaal Yàlla. Mooy boroom nguur te Mooy boroom cant. Te Moom man na Lépp.
هُوَ الَّذِي خَلَقَكُمْ فَمِنكُمْ كَافِرٌ وَمِنكُم مُّؤْمِنٌ ۚ وَاللَّهُ بِمَا تَعْمَلُونَ بَصِيرٌ ٢
📖 Tekki
Aaya 2
Mooy ki leen bind. Am na ci yéen ay yéefar am it ci yéen ay jullit way gëm. Te Yàlla kuy gis la li ngeen di def.
خَلَقَ السَّمَاوَاتِ وَالْأَرْضَ بِالْحَقِّ وَصَوَّرَكُمْ فَأَحْسَنَ صُوَرَكُمْ ۖ وَإِلَيْهِ الْمَصِيرُ ٣
📖 Tekki
Aaya 3
Bind na asamaan yeek suuf si ci dëgg mu tën seeni jëmm te rafetal na seeni jëm. Te ca moom mooy Deluwaay ba.
يَعْلَمُ مَا فِي السَّمَاوَاتِ وَالْأَرْضِ وَيَعْلَمُ مَا تُسِرُّونَ وَمَا تُعْلِنُونَ ۚ وَاللَّهُ عَلِيمٌ بِذَاتِ الصُّدُورِ ٤
📖 Tekki
Aaya 4
Moom Yàlla xam na li nekk ci asamaan yeek suuf si, te it ma ngay xam li ngeen di nëbb ak li ngeen di feeñal. Te Yàlla ku xam la li nekk ci dënn yi.
أَلَمْ يَأْتِكُمْ نَبَأُ الَّذِينَ كَفَرُوا مِن قَبْلُ فَذَاقُوا وَبَالَ أَمْرِهِمْ وَلَهُمْ عَذَابٌ أَلِيمٌ ٥
📖 Tekki
Aaya 5
Moo xanaa xibaari yéefar ya jiitu woon da leen dikkalul, mosoon nañu musiba mu di peyug seeni jëf ; te am nañu mbugël mu mitti.
ذَٰلِكَ بِأَنَّهُ كَانَت تَّأْتِيهِمْ رُسُلُهُم بِالْبَيِّنَاتِ فَقَالُوا أَبَشَرٌ يَهْدُونَنَا فَكَفَرُوا وَتَوَلَّوا ۚ وَّاسْتَغْنَى اللَّهُ ۚ وَاللَّهُ غَنِيٌّ حَمِيدٌ ٦
📖 Tekki
Aaya 6
la ko waral moo di ne seeni Yonent da leen daan dikkël ak ay firndeyu leer ñuy wax naan : “Moo nit ñii ñoo ñuy gindee ? ” Daal di weddi dumóoyu Yàlla bàyyi leen te Yàlla ku doyloo boppam la Yayoowaakoonu cant la.
زَعَمَ الَّذِينَ كَفَرُوا أَن لَّن يُبْعَثُوا ۚ قُلْ بَلَىٰ وَرَبِّي لَتُبْعَثُنَّ ثُمَّ لَتُنَبَّؤُنَّ بِمَا عَمِلْتُمْ ۚ وَذَٰلِكَ عَلَى اللَّهِ يَسِيرٌ ٧
📖 Tekki
Aaya 7
Yéefër yi neena ñooy kenn duleen dekkal. Waxal ne : “Axakañ! Dees na leen dekkal ; xibaar leen la ngeen jëfoon. Te loolu lu yomb la ci Yàlla”.
فَآمِنُوا بِاللَّهِ وَرَسُولِهِ وَالنُّورِ الَّذِي أَنزَلْنَا ۚ وَاللَّهُ بِمَا تَعْمَلُونَ خَبِيرٌ ٨
📖 Tekki
Aaya 8
Gëmleen Yàlla ak ub Yonentam, ak leer gi nu wàcce [Alxuraan]. Te Yàlla kat ku deñ- kumpa la ci li ngeen di def.
يَوْمَ يَجْمَعُكُمْ لِيَوْمِ الْجَمْعِ ۖ ذَٰلِكَ يَوْمُ التَّغَابُنِ ۗ وَمَن يُؤْمِن بِاللَّهِ وَيَعْمَلْ صَالِحًا يُكَفِّرْ عَنْهُ سَيِّئَاتِهِ وَيُدْخِلْهُ جَنَّاتٍ تَجْرِي مِن تَحْتِهَا الْأَنْهَارُ خَالِدِينَ فِيهَا أَبَدًا ۚ ذَٰلِكَ الْفَوْزُ الْعَظِيمُ ٩
📖 Tekki
Aaya 9
9. Te bu keroogee ba mu leen di Dajale, ca bisub daje ba bis boobee mooy bisub yàqule gu mag ga (ca yéefar ya). (Waaye) képp ku gëm tey jëf yiw, Dana ko faral ay ñaaytéefam te dana ko tàbbal Àjjana yu ay dex ñooy daw ci suufam, te dañu fay béel fàww. Loolu moo di texe gu mag ga !
وَالَّذِينَ كَفَرُوا وَكَذَّبُوا بِآيَاتِنَا أُولَٰئِكَ أَصْحَابُ النَّارِ خَالِدِينَ فِيهَا ۖ وَبِئْسَ الْمَصِيرُ ١٠
📖 Tekki
Aaya 10
Yéefër yiy weddi Sunuy Laaya, ñooñu ñoo di waa Safara te danu fay béel. Ndaw saxuwaay bu bon !
مَا أَصَابَ مِن مُّصِيبَةٍ إِلَّا بِإِذْنِ اللَّهِ ۗ وَمَن يُؤْمِن بِاللَّهِ يَهْدِ قَلْبَهُ ۚ وَاللَّهُ بِكُلِّ شَيْءٍ عَلِيمٌ ١١
📖 Tekki
Aaya 11
Amul menn musiba muy dal kenn lu dul ci ndigalul Yàlla. Képp ku gëm Yàlla, [Yàlla] dana gindi xolam. Te Yàlla xam na lépp.
وَأَطِيعُوا اللَّهَ وَأَطِيعُوا الرَّسُولَ ۚ فَإِن تَوَلَّيْتُمْ فَإِنَّمَا عَلَىٰ رَسُولِنَا الْبَلَاغُ الْمُبِينُ ١٢
📖 Tekki
Aaya 12
Nangeen di topp Yàlla te it na ngeen di topp Yonent bi suñu dumóoyoo... li ca war Sunub Yonent mooy jottali rekk ba mu leer.
اللَّهُ لَا إِلَٰهَ إِلَّا هُوَ ۚ وَعَلَى اللَّهِ فَلْيَتَوَكَّلِ الْمُؤْمِنُونَ ١٣
📖 Tekki
Aaya 13
Yàlla, amul jeneen Yàlla ju dul moom ! Te ñi gëm na ñuy doyloo Yàlla.
يَا أَيُّهَا الَّذِينَ آمَنُوا إِنَّ مِنْ أَزْوَاجِكُمْ وَأَوْلَادِكُمْ عَدُوًّا لَّكُمْ فَاحْذَرُوهُمْ ۚ وَإِن تَعْفُوا وَتَصْفَحُوا وَتَغْفِرُوا فَإِنَّ اللَّهَ غَفُورٌ رَّحِيمٌ ١٤
📖 Tekki
Aaya 14
eey yéen ñi gëm, am na ci seeni jabar ak seeni doom ñoo xam ne seeni noon la ñu. Nangeen leen di moytu. (Waaye) su ngeen balee tey jéllale, Yàlla moom ab Jéggalaakoon la, Jagléwaakoon la.
إِنَّمَا أَمْوَالُكُمْ وَأَوْلَادُكُمْ فِتْنَةٌ ۚ وَاللَّهُ عِندَهُ أَجْرٌ عَظِيمٌ ١٥
📖 Tekki
Aaya 15
Seeni alal ak seeni doom sànje la ci yéen, (Waaye) la nekk fa Yàlla moo di pey gu màgg.
فَاتَّقُوا اللَّهَ مَا اسْتَطَعْتُمْ وَاسْمَعُوا وَأَطِيعُوا وَأَنفِقُوا خَيْرًا لِّأَنفُسِكُمْ ۗ وَمَن يُوقَ شُحَّ نَفْسِهِ فَأُولَٰئِكَ هُمُ الْمُفْلِحُونَ ١٦
📖 Tekki
Aaya 16
Nangeen di ragal Yàlla seen kem kàttan, dégluleen, te topp te joxe alal. Moo gën ci yéen de. Képp ku mucc ci ag nay (na xam ne)... ñoo di ña baaxle.
إِن تُقْرِضُوا اللَّهَ قَرْضًا حَسَنًا يُضَاعِفْهُ لَكُمْ وَيَغْفِرْ لَكُمْ ۚ وَاللَّهُ شَكُورٌ حَلِيمٌ ١٧
📖 Tekki
Aaya 17
Su ngeen lebalee Yàlla bor bu rafet, Dana leen ko fulal te it dana leen jéggal. Te Yàlla ab Santaakoon la Ku lewet la.
عَالِمُ الْغَيْبِ وَالشَّهَادَةِ الْعَزِيزُ الْحَكِيمُ ١٨
📖 Tekki
Aaya 18
Mooy aji Xam ji Kumpaak li feeñ, di boroom Kàttan, di aji Xereñ.
Jàng Simoore At-Taghabun ci Wolof – Tekki, Waxtaan ak Baat
Alxuraan bu Tedd bi
Tuesday, August 18, 2026
Don't forget us in your sincere prayers

