📖 0/604 xët yi jàng nañu
📄 151
Al-A'raf

Al-A'raf

7:2
كِتَٰبٌ أُنزِلَ إِلَيۡكَ فَلَا يَكُن فِي صَدۡرِكَ حَرَجٌ مِّنۡهُ لِتُنذِرَ بِهِۦ وَذِكۡرَىٰ لِلۡمُؤۡمِنِينَ ٢
Ab Téeree ngi, bu ñu wàcce ci yaw ; ngir nga waare ca, ak mu nekk ag fàttali ci way-gëm ña ; bu wenn tiis nekk ci sa xol ngir loolu.
7:3
ٱتَّبِعُواْ مَآ أُنزِلَ إِلَيۡكُم مِّن رَّبِّكُمۡ وَلَا تَتَّبِعُواْ مِن دُونِهِۦٓ أَوۡلِيَآءَۗ قَلِيلًا مَّا تَذَكَّرُونَ ٣
Toppleen li ñu wàcce ci yéen mu jóge ca seen Boroom. Buleen ko bàyyi di topp ay xërëm. Néew ngeen xalaat.
7:4
وَكَم مِّن قَرۡيَةٍ أَهۡلَكۡنَٰهَا فَجَآءَهَا بَأۡسُنَا بَيَٰتًا أَوۡ هُمۡ قَآئِلُونَ ٤
Bariwaana dëkk bu Nu alag ! Sunu mbugal agsi fa ci guddi walla ci bëccëg.
7:5
فَمَا كَانَ دَعۡوَىٰهُمۡ إِذۡ جَآءَهُم بَأۡسُنَآ إِلَّآ أَن قَالُوٓاْ إِنَّا كُنَّا ظَٰلِمِينَ ٥
Te seeni njàmbat nekkul, ba leen mbugal ma saddee, lu dul : “Nun ay tooñkat lanu woon”.
7:6
فَلَنَسۡـَٔلَنَّ ٱلَّذِينَ أُرۡسِلَ إِلَيۡهِمۡ وَلَنَسۡـَٔلَنَّ ٱلۡمُرۡسَلِينَ ٦
Fàwwu Dananu laaj ña Nu yónni ca ñoom [nit ña], fàwwu it Dananu laaj ña Nu yónni woon [Yonent ya].
7:7
فَلَنَقُصَّنَّ عَلَيۡهِم بِعِلۡمٍۖ وَمَا كُنَّا غَآئِبِينَ ٧
Te Dananu leen nettali ji [ci loolu] ci xam-xam bu wér ndaxte fekke woon Nanu lépp !
7:8
وَٱلۡوَزۡنُ يَوۡمَئِذٍ ٱلۡحَقُّۚ فَمَن ثَقُلَتۡ مَوَٰزِينُهُۥ فَأُوْلَٰٓئِكَ هُمُ ٱلۡمُفۡلِحُونَ ٨
Booba bis, peese bu dëggu lay doon. Ña seen peese diis ak u yiw... Ñoom ñooy ñu texe ña !
7:9
وَمَنۡ خَفَّتۡ مَوَٰزِينُهُۥ فَأُوْلَٰٓئِكَ ٱلَّذِينَ خَسِرُوٓاْ أَنفُسَهُم بِمَا كَانُواْ بِـَٔايَٰتِنَا يَظۡلِمُونَ ٩
Ña seen peese woyof nag ... Ñooy ña yàqal seen bopp ngir ñàkk a faale Sunuy kàddu te doonoon ñu daan tooñ.
7:10
وَلَقَدۡ مَكَّنَّٰكُمۡ فِي ٱلۡأَرۡضِ وَجَعَلۡنَا لَكُمۡ فِيهَا مَعَٰيِشَۗ قَلِيلًا مَّا تَشۡكُرُونَ ١٠
Defal Nanu leen ag jàppandal ci suuf si, defal leen ca lu ngeen dunde. Te seenug cant néew na !
7:11
وَلَقَدۡ خَلَقۡنَٰكُمۡ ثُمَّ صَوَّرۡنَٰكُمۡ ثُمَّ قُلۡنَا لِلۡمَلَٰٓئِكَةِ ٱسۡجُدُواْ لِأٓدَمَ فَسَجَدُوٓاْ إِلَّآ إِبۡلِيسَ لَمۡ يَكُن مِّنَ ٱلسَّٰجِدِينَ ١١
Bind Nanu leen, jox leen i melo, ba noppi Nu wax Malaaka ya : “Sujjóotal-leen Aadama.”. Ñoom ñépp a sujjoot, ba mu des Ibliis, moom bokkul ca ña sujjóot.
العربيةEnglishBahasa IndonesiaTürkçeРусскийفارسیFrançaisاردوবাংলাDeutschEspañol中文हिन्दीPortuguêsItalianoภาษาไทยPolskiNederlandsShqipKiswahiliO'zbekதமிழ்MelayuBosanskiSoomaaliAzərbaycanکوردی한국어日本語SvenskaDanskNorskپښتوമലയാളംසිංහලTamazightHausaአማርኛБългарскиТоҷикӣҚазақшаFilipinoسنڌيYorùbáFulfuldeТатарчаئۇيغۇرچەКыргызчаਪੰਜਾਬੀJawaతెలుగుမြန်မာગુજરાતીOromoमराठीTiếng ViệtMalagasyНохчийнWolofދިވެހިಕನ್ನಡУкраїнськаΕλληνικάქართულიខ្មែរدریQafar afMaranaoनेपाली
Alxuraan bu Tedd bi
Saturday, August 22, 2026
Don't forget us in your sincere prayers







