📖 0/604 xët yi jàng nañu
📄 18
Al-Baqara

Al-Baqara

2:113
وَقَالَتِ ٱلۡيَهُودُ لَيۡسَتِ ٱلنَّصَٰرَىٰ عَلَىٰ شَيۡءٍ وَقَالَتِ ٱلنَّصَٰرَىٰ لَيۡسَتِ ٱلۡيَهُودُ عَلَىٰ شَيۡءٍ وَهُمۡ يَتۡلُونَ ٱلۡكِتَٰبَۗ كَذَٰلِكَ قَالَ ٱلَّذِينَ لَا يَعۡلَمُونَ مِثۡلَ قَوۡلِهِمۡۚ فَٱللَّهُ يَحۡكُمُ بَيۡنَهُمۡ يَوۡمَ ٱلۡقِيَٰمَةِ فِيمَا كَانُواْ فِيهِ يَخۡتَلِفُونَ ١١٣
Yahuud yi wax nañu ne : “Nasraan yi nekkuñu ci dara” ; Nasraan yi itam ne : “Yahuud yi nekkuñu ci dara”, te ñoom jàng nañu Téere ba ! Noonu la ña xamul di waxe. Yàlla dana àtte seen diggante ca la ñu juuyoo bu Bis-pénc baa.
2:114
وَمَنۡ أَظۡلَمُ مِمَّن مَّنَعَ مَسَٰجِدَ ٱللَّهِ أَن يُذۡكَرَ فِيهَا ٱسۡمُهُۥ وَسَعَىٰ فِي خَرَابِهَآۚ أُوْلَٰٓئِكَ مَا كَانَ لَهُمۡ أَن يَدۡخُلُوهَآ إِلَّا خَآئِفِينَۚ لَهُمۡ فِي ٱلدُّنۡيَا خِزۡيٌ وَلَهُمۡ فِي ٱلۡأٓخِرَةِ عَذَابٌ عَظِيمٌ ١١٤
Ana ku gën a tooñ kuy tere, ca jàkkay Yàlla ja, ku cay tuddu Turam te di fexe luy yàq jàkka ja ? Ñooña waruñoo dugg ca [jàkka ja] te ànduñook am tiit. Am nañu gàcce gu rëy ci àddina, te it danañu am mbugal mu rëy ca àllaaxira.
2:115
وَلِلَّهِ ٱلۡمَشۡرِقُ وَٱلۡمَغۡرِبُۚ فَأَيۡنَمَا تُوَلُّواْ فَثَمَّ وَجۡهُ ٱللَّهِۚ إِنَّ ٱللَّهَ وَٰسِعٌ عَلِيمٌ ١١٥
Te Yàllaa moom Penku bi ak Sowu bi. Fu ngeen fi mën a jublu, Kanamu Yàlla jublu na fa, Yàlla ku xam la ; Ku Yaatu la.
2:116
وَقَالُواْ ٱتَّخَذَ ٱللَّهُ وَلَدًاۗ سُبۡحَٰنَهُۥۖ بَل لَّهُۥ مَا فِي ٱلسَّمَٰوَٰتِ وَٱلۡأَرۡضِۖ كُلٌّ لَّهُۥ قَٰنِتُونَ ١١٦
Wax nañu ne : “Yàlla am na doom” ! Tudd naa ag sellam[Soreel ko lu yellul ci moom] ! Li fi nekk moo di, Moom Yàlla moo moom lépp lu nekk ci asamaan yi ak suuf si te lépp ci jaamu ko la nekk.
2:117
بَدِيعُ ٱلسَّمَٰوَٰتِ وَٱلۡأَرۡضِۖ وَإِذَا قَضَىٰٓ أَمۡرًا فَإِنَّمَا يَقُولُ لَهُۥ كُن فَيَكُونُ ١١٧
Mooy Aji-sos asamaan yi ak suuf si ! Bu dogalee mbir du def lu dul ne ko : “Nekkal”, mu nekk.
2:118
وَقَالَ ٱلَّذِينَ لَا يَعۡلَمُونَ لَوۡلَا يُكَلِّمُنَا ٱللَّهُ أَوۡ تَأۡتِينَآ ءَايَةٌۗ كَذَٰلِكَ قَالَ ٱلَّذِينَ مِن قَبۡلِهِم مِّثۡلَ قَوۡلِهِمۡۘ تَشَٰبَهَتۡ قُلُوبُهُمۡۗ قَدۡ بَيَّنَّا ٱلۡأٓيَٰتِ لِقَوۡمٍ يُوقِنُونَ ١١٨
Ña xamul wax nañu ne : “Lu tee woon Yàlla wax ak nun, walla mu indil nu keemaan” ? Noonu la ña leen jiitu woon waxee woon wax ju mel ni seen jos. Seeni xol niroo na. Leeral Nanu laaya ya ci nit ñoo xam ne wóolu lañu.
2:119
إِنَّآ أَرۡسَلۡنَٰكَ بِٱلۡحَقِّ بَشِيرًا وَنَذِيرًاۖ وَلَا تُسۡـَٔلُ عَنۡ أَصۡحَٰبِ ٱلۡجَحِيمِ ١١٩
Yónni nañu la ci dëgg ngay bégal [ñi gëm ci dig leen Àjjana] ; te di xupp [ñi weddi ci mbugalum Safara] te deesula laaj dara [ëllëg ca àllaaxira loo war a layoo] ci mbiri waa Safara
العربيةEnglishBahasa IndonesiaTürkçeРусскийفارسیFrançaisاردوবাংলাDeutschEspañol中文हिन्दीPortuguêsItalianoภาษาไทยPolskiNederlandsShqipKiswahiliO'zbekதமிழ்MelayuBosanskiSoomaaliAzərbaycanکوردی한국어日本語SvenskaDanskNorskپښتوമലയാളംසිංහලTamazightHausaአማርኛБългарскиТоҷикӣҚазақшаFilipinoسنڌيYorùbáFulfuldeТатарчаئۇيغۇرچەКыргызчаਪੰਜਾਬੀJawaతెలుగుမြန်မာગુજરાતીOromoमराठीTiếng ViệtMalagasyНохчийнWolofދިވެހިಕನ್ನಡУкраїнськаΕλληνικάქართულიខ្មែរدریQafar afMaranaoनेपाली
Alxuraan bu Tedd bi
Wednesday, August 19, 2026
Don't forget us in your sincere prayers







