Al-Baqara · 119/286
Tekki Waxtaan — Al-Baqara
إِنَّا أَرْسَلْنَاكَ بِالْحَقِّ بَشِيرًا وَنَذِيرًا ۖ وَلَا تُسْأَلُ عَنْ أَصْحَابِ الْجَحِيمِ ۝١١٩
Innaaa arsalnaaka bilhaqqi basheeranw wa nazeeranw wa laa tus`alu `am Ashaabil Jaheem
📖 Tekkim Wolof
Yónni nañu la ci dëgg ngay bégal [ñi gëm ci dig leen Àjjana] ; te di xupp [ñi weddi ci mbugalum Safara] te deesula laaj dara [ëllëg ca àllaaxira loo war a layoo] ci mbiri waa Safara
🎧 Dégg

📜 Aaya 117-121 — Al-Baqara

117بَدِيعُ السَّمَاوَاتِ وَالْأَرْضِ ۖ وَإِذَا قَضَىٰ أَمْرًا فَإِنَّمَا يَقُولُ لَهُ كُن فَيَكُونُ
Mooy Aji-sos asamaan yi ak suuf si ! Bu dogalee mbir du def lu dul ne ko : “Nekkal”, mu nekk.
118وَقَالَ الَّذِينَ لَا يَعْلَمُونَ لَوْلَا يُكَلِّمُنَا اللَّهُ أَوْ تَأْتِينَا آيَةٌ ۗ كَذَٰلِكَ قَالَ الَّذِينَ مِن قَبْلِهِم مِّثْلَ قَوْلِهِمْ ۘ تَشَابَهَتْ قُلُوبُهُمْ ۗ قَدْ بَيَّنَّا الْآيَاتِ لِقَوْمٍ يُوقِنُونَ
Ña xamul wax nañu ne : “Lu tee woon Yàlla wax ak nun, walla mu indil nu keemaan” ? Noonu la ña leen jiitu woon waxee woon wax ju mel ni seen jos. Seeni xol niroo na. Leeral Nanu laaya ya ci nit ñoo xam ne wóolu lañu.
119إِنَّا أَرْسَلْنَاكَ بِالْحَقِّ بَشِيرًا وَنَذِيرًا ۖ وَلَا تُسْأَلُ عَنْ أَصْحَابِ الْجَحِيمِ
Yónni nañu la ci dëgg ngay bégal [ñi gëm ci dig leen Àjjana] ; te di xupp [ñi weddi ci mbugalum Safara] te deesula laaj dara [ëllëg ca àllaaxira loo war a layoo] ci mbiri waa Safara
120وَلَن تَرْضَىٰ عَنكَ الْيَهُودُ وَلَا النَّصَارَىٰ حَتَّىٰ تَتَّبِعَ مِلَّتَهُمْ ۗ قُلْ إِنَّ هُدَى اللَّهِ هُوَ الْهُدَىٰ ۗ وَلَئِنِ اتَّبَعْتَ أَهْوَاءَهُم بَعْدَ الَّذِي جَاءَكَ مِنَ الْعِلْمِ ۙ مَا لَكَ مِنَ اللَّهِ مِن وَلِيٍّ وَلَا نَصِيرٍ
Yahuud yi ak Nasaraan yi duñu bég ci yaw mukk li feek toppuloo seen diine. - Neel : “Njubug Yàlla mooy dëggi-dëggi njub”. Boo toppee seen bànneex ginnaawal la Nu la digal, ci xam-xam, doo am kenn ku la mën a sàmm, walla ndimbal ci [mbugalum Yàlla].
121الَّذِينَ آتَيْنَاهُمُ الْكِتَابَ يَتْلُونَهُ حَقَّ تِلَاوَتِهِ أُولَٰئِكَ يُؤْمِنُونَ بِهِ ۗ وَمَن يَكْفُرْ بِهِ فَأُولَٰئِكَ هُمُ الْخَاسِرُونَ
Ña nga xam ne jox Nanu leen téere ba [Alxuraan], danañu ko jànge na mu yelle, ñooña ñoo ko gëm. Ña ko weddi ñooy way-ñàkk ña.
Al-BaqaraFihi Alxuraan
286Aaya
MedinanRevelation
119Aaya

Tekki — Al-Baqara 119

Simoore Al-Baqara Aaya 119 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Yónni nañu la ci dëgg ngay bégal [ñi gëm ci…

Simoore Aaya 119/286 — Al-Baqara البقرة (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Baqara Dégg, Al-Baqara Tekki, Al-Baqara mp3, Al-Baqara pdf. Aaya 117–121. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers