Al-Baqara · 116/286
Tekki Waxtaan — Al-Baqara
وَقَالُوا اتَّخَذَ اللَّهُ وَلَدًا ۗ سُبْحَانَهُ ۖ بَل لَّهُ مَا فِي السَّمَاوَاتِ وَالْأَرْضِ ۖ كُلٌّ لَّهُ قَانِتُونَ ۝١١٦
Wa qaalut takhazal laahu waladan subhaanahoo bal lahoo maa fis samaawaati wal ardi kullul lahoo qaanitoon
📖 Tekkim Wolof
Wax nañu ne : “Yàlla am na doom” ! Tudd naa ag sellam[Soreel ko lu yellul ci moom] ! Li fi nekk moo di, Moom Yàlla moo moom lépp lu nekk ci asamaan yi ak suuf si te lépp ci jaamu ko la nekk.
🎧 Dégg

📜 Aaya 114-118 — Al-Baqara

114وَمَنْ أَظْلَمُ مِمَّن مَّنَعَ مَسَاجِدَ اللَّهِ أَن يُذْكَرَ فِيهَا اسْمُهُ وَسَعَىٰ فِي خَرَابِهَا ۚ أُولَٰئِكَ مَا كَانَ لَهُمْ أَن يَدْخُلُوهَا إِلَّا خَائِفِينَ ۚ لَهُمْ فِي الدُّنْيَا خِزْيٌ وَلَهُمْ فِي الْآخِرَةِ عَذَابٌ عَظِيمٌ
Ana ku gën a tooñ kuy tere, ca jàkkay Yàlla ja, ku cay tuddu Turam te di fexe luy yàq jàkka ja ? Ñooña waruñoo dugg ca [jàkka ja] te ànduñook am tiit. Am nañu gàcce gu rëy ci àddina, te it danañu am mbugal mu rëy ca àllaaxira.
115وَلِلَّهِ الْمَشْرِقُ وَالْمَغْرِبُ ۚ فَأَيْنَمَا تُوَلُّوا فَثَمَّ وَجْهُ اللَّهِ ۚ إِنَّ اللَّهَ وَاسِعٌ عَلِيمٌ
Te Yàllaa moom Penku bi ak Sowu bi. Fu ngeen fi mën a jublu, Kanamu Yàlla jublu na fa, Yàlla ku xam la ; Ku Yaatu la.
116وَقَالُوا اتَّخَذَ اللَّهُ وَلَدًا ۗ سُبْحَانَهُ ۖ بَل لَّهُ مَا فِي السَّمَاوَاتِ وَالْأَرْضِ ۖ كُلٌّ لَّهُ قَانِتُونَ
Wax nañu ne : “Yàlla am na doom” ! Tudd naa ag sellam[Soreel ko lu yellul ci moom] ! Li fi nekk moo di, Moom Yàlla moo moom lépp lu nekk ci asamaan yi ak suuf si te lépp ci jaamu ko la nekk.
117بَدِيعُ السَّمَاوَاتِ وَالْأَرْضِ ۖ وَإِذَا قَضَىٰ أَمْرًا فَإِنَّمَا يَقُولُ لَهُ كُن فَيَكُونُ
Mooy Aji-sos asamaan yi ak suuf si ! Bu dogalee mbir du def lu dul ne ko : “Nekkal”, mu nekk.
118وَقَالَ الَّذِينَ لَا يَعْلَمُونَ لَوْلَا يُكَلِّمُنَا اللَّهُ أَوْ تَأْتِينَا آيَةٌ ۗ كَذَٰلِكَ قَالَ الَّذِينَ مِن قَبْلِهِم مِّثْلَ قَوْلِهِمْ ۘ تَشَابَهَتْ قُلُوبُهُمْ ۗ قَدْ بَيَّنَّا الْآيَاتِ لِقَوْمٍ يُوقِنُونَ
Ña xamul wax nañu ne : “Lu tee woon Yàlla wax ak nun, walla mu indil nu keemaan” ? Noonu la ña leen jiitu woon waxee woon wax ju mel ni seen jos. Seeni xol niroo na. Leeral Nanu laaya ya ci nit ñoo xam ne wóolu lañu.
Al-BaqaraFihi Alxuraan
286Aaya
MedinanRevelation
116Aaya

Tekki — Al-Baqara 116

Simoore Al-Baqara Aaya 116 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Wax nañu ne : “Yàlla am na doom” ! Tudd…

Simoore Aaya 116/286 — Al-Baqara البقرة (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Baqara Dégg, Al-Baqara Tekki, Al-Baqara mp3, Al-Baqara pdf. Aaya 114–118. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers