📖 0/604 xët yi jàng nañu
📄 6
Al-Baqara

Al-Baqara

2:30
وَإِذۡ قَالَ رَبُّكَ لِلۡمَلَٰٓئِكَةِ إِنِّي جَاعِلٌ فِي ٱلۡأَرۡضِ خَلِيفَةًۖ قَالُوٓاْ أَتَجۡعَلُ فِيهَا مَن يُفۡسِدُ فِيهَا وَيَسۡفِكُ ٱلدِّمَآءَ وَنَحۡنُ نُسَبِّحُ بِحَمۡدِكَ وَنُقَدِّسُ لَكَۖ قَالَ إِنِّيٓ أَعۡلَمُ مَا لَا تَعۡلَمُونَ ٣٠
Fàttalikul ba sa Boroom waxee Malaaka ya, ne leen: “Man dey damaa namm a def ci suuf si ag kilifa[kuutaay]. Ñu toontu ne ko : “Moo ndax dangay def ci suuf si koo xam ne dafa ciy nekk di yàq, di tuur i dereet, te nun nu ngi lay sàbbaal, di la sant te di màggal sag sell ? ” – Yàlla ne leen : “Xam naa lu ngeen xamul ! ”.
2:31
وَعَلَّمَ ءَادَمَ ٱلۡأَسۡمَآءَ كُلَّهَا ثُمَّ عَرَضَهُمۡ عَلَى ٱلۡمَلَٰٓئِكَةِ فَقَالَ أَنۢبِـُٔونِي بِأَسۡمَآءِ هَٰٓؤُلَآءِ إِن كُنتُمۡ صَٰدِقِينَ ٣١
Mu jàngal Aadama turi lenn lu ne, ba noppi won ko Malaaka ya, ne leen : “Wax leen ma turi yëf yii, ndegam ñu dëggu ngeen ! ”.
2:32
قَالُواْ سُبۡحَٰنَكَ لَا عِلۡمَ لَنَآ إِلَّا مَا عَلَّمۡتَنَآۖ إِنَّكَ أَنتَ ٱلۡعَلِيمُ ٱلۡحَكِيمُ ٣٢
–Malaaka ya ne ko : “Tuddu nanu sa sell gi ! Amunu benn xam-xam lu dul loo nu xamal. Ndax Yaw yaay ki xam, Yaay ki xereñ”.
2:33
قَالَ يَٰٓـَٔادَمُ أَنۢبِئۡهُم بِأَسۡمَآئِهِمۡۖ فَلَمَّآ أَنۢبَأَهُم بِأَسۡمَآئِهِمۡ قَالَ أَلَمۡ أَقُل لَّكُمۡ إِنِّيٓ أَعۡلَمُ غَيۡبَ ٱلسَّمَٰوَٰتِ وَٱلۡأَرۡضِ وَأَعۡلَمُ مَا تُبۡدُونَ وَمَا كُنتُمۡ تَكۡتُمُونَ ٣٣
–Mu ne : "Aadama xamal-leen seeni tur ; ” Ba mu leen xamalee seeni tur, Yàlla ne leen : “Ndax dama leen a waxuloon ne Man xam naa kumpag asamaan ak suuf si, te it xam naa xéll li ngeen feeñal ak li ngeen doon ñëbb ? ”
2:34
وَإِذۡ قُلۡنَا لِلۡمَلَٰٓئِكَةِ ٱسۡجُدُواْ لِأٓدَمَ فَسَجَدُوٓاْ إِلَّآ إِبۡلِيسَ أَبَىٰ وَٱسۡتَكۡبَرَ وَكَانَ مِنَ ٱلۡكَٰفِرِينَ ٣٤
[Fàttelikul] Ba Nu nee Maalaaka ya sujjóotleen ci Aadama, ñu sujjóot ba mu des Ibliis, dafa lànk rëy-rëylu daldi bokk ca way-weddi ya.
2:35
وَقُلۡنَا يَٰٓـَٔادَمُ ٱسۡكُنۡ أَنتَ وَزَوۡجُكَ ٱلۡجَنَّةَ وَكُلَا مِنۡهَا رَغَدًا حَيۡثُ شِئۡتُمَا وَلَا تَقۡرَبَا هَٰذِهِ ٱلشَّجَرَةَ فَتَكُونَا مِنَ ٱلظَّٰلِمِينَ ٣٥
Ñu wax ne ko : “Yaw Aadama dëkkal ci àjjana yaak sa soxna, ngeen di fa lekkee na mu leen neexee, ca fa mu leen soobee ; te bu leen jege garab gile : kon dey ngeen bokk ci way- tooñ ña”.
2:36
فَأَزَلَّهُمَا ٱلشَّيۡطَٰنُ عَنۡهَا فَأَخۡرَجَهُمَا مِمَّا كَانَا فِيهِۖ وَقُلۡنَا ٱهۡبِطُواْ بَعۡضُكُمۡ لِبَعۡضٍ عَدُوٌّۖ وَلَكُمۡ فِي ٱلۡأَرۡضِ مُسۡتَقَرٌّ وَمَتَٰعٌ إِلَىٰ حِينٍ ٣٦
[Séytaane] tarxiisloo na leen, génne leen fa ñu nekkoon. Nu ne leen : “Wàccleen ; di noonuwante. Te itam dangeen am ci kaw suuf ay dëkkuwaay ak i jumtukaay as ndiir”.
2:37
فَتَلَقَّىٰٓ ءَادَمُ مِن رَّبِّهِۦ كَلِمَٰتٍ فَتَابَ عَلَيۡهِۚ إِنَّهُۥ هُوَ ٱلتَّوَّابُ ٱلرَّحِيمُ ٣٧
Aadama jot na baat ya [baati tuub] bawoo ca Boroomam, Mu daldi ko jéggal, ndax Moom moo di Jéggalaakoon bi, di Jaglewaakoon bi.
العربيةEnglishBahasa IndonesiaTürkçeРусскийفارسیFrançaisاردوবাংলাDeutschEspañol中文हिन्दीPortuguêsItalianoภาษาไทยPolskiNederlandsShqipKiswahiliO'zbekதமிழ்MelayuBosanskiSoomaaliAzərbaycanکوردی한국어日本語SvenskaDanskNorskپښتوമലയാളംසිංහලTamazightHausaአማርኛБългарскиТоҷикӣҚазақшаFilipinoسنڌيYorùbáFulfuldeТатарчаئۇيغۇرچەКыргызчаਪੰਜਾਬੀJawaతెలుగుမြန်မာગુજરાતીOromoमराठीTiếng ViệtMalagasyНохчийнWolofދިވެހިಕನ್ನಡУкраїнськаΕλληνικάქართულიខ្មែរدریQafar afMaranaoनेपाली
Alxuraan bu Tedd bi
Tuesday, August 18, 2026
Don't forget us in your sincere prayers







