Al-Baqara · 34/286
Tekki Waxtaan — Al-Baqara
وَإِذْ قُلْنَا لِلْمَلَائِكَةِ اسْجُدُوا لِآدَمَ فَسَجَدُوا إِلَّا إِبْلِيسَ أَبَىٰ وَاسْتَكْبَرَ وَكَانَ مِنَ الْكَافِرِينَ ۝٣٤
Wa iz qulnaa lilmalaaa`i katis judoo liAadama fasajadooo illaaa Ibleesa abaa wastakbara wa kaana minal kaafireen
📖 Tekkim Wolof
[Fàttelikul] Ba Nu nee Maalaaka ya sujjóotleen ci Aadama, ñu sujjóot ba mu des Ibliis, dafa lànk rëy-rëylu daldi bokk ca way-weddi ya.
🎧 Dégg

📜 Aaya 32-36 — Al-Baqara

32قَالُوا سُبْحَانَكَ لَا عِلْمَ لَنَا إِلَّا مَا عَلَّمْتَنَا ۖ إِنَّكَ أَنتَ الْعَلِيمُ الْحَكِيمُ
–Malaaka ya ne ko : “Tuddu nanu sa sell gi ! Amunu benn xam-xam lu dul loo nu xamal. Ndax Yaw yaay ki xam, Yaay ki xereñ”.
33قَالَ يَا آدَمُ أَنبِئْهُم بِأَسْمَائِهِمْ ۖ فَلَمَّا أَنبَأَهُم بِأَسْمَائِهِمْ قَالَ أَلَمْ أَقُل لَّكُمْ إِنِّي أَعْلَمُ غَيْبَ السَّمَاوَاتِ وَالْأَرْضِ وَأَعْلَمُ مَا تُبْدُونَ وَمَا كُنتُمْ تَكْتُمُونَ
–Mu ne : "Aadama xamal-leen seeni tur ; ” Ba mu leen xamalee seeni tur, Yàlla ne leen : “Ndax dama leen a waxuloon ne Man xam naa kumpag asamaan ak suuf si, te it xam naa xéll li ngeen feeñal ak li ngeen doon ñëbb ? ”
34وَإِذْ قُلْنَا لِلْمَلَائِكَةِ اسْجُدُوا لِآدَمَ فَسَجَدُوا إِلَّا إِبْلِيسَ أَبَىٰ وَاسْتَكْبَرَ وَكَانَ مِنَ الْكَافِرِينَ
[Fàttelikul] Ba Nu nee Maalaaka ya sujjóotleen ci Aadama, ñu sujjóot ba mu des Ibliis, dafa lànk rëy-rëylu daldi bokk ca way-weddi ya.
35وَقُلْنَا يَا آدَمُ اسْكُنْ أَنتَ وَزَوْجُكَ الْجَنَّةَ وَكُلَا مِنْهَا رَغَدًا حَيْثُ شِئْتُمَا وَلَا تَقْرَبَا هَٰذِهِ الشَّجَرَةَ فَتَكُونَا مِنَ الظَّالِمِينَ
Ñu wax ne ko : “Yaw Aadama dëkkal ci àjjana yaak sa soxna, ngeen di fa lekkee na mu leen neexee, ca fa mu leen soobee ; te bu leen jege garab gile : kon dey ngeen bokk ci way- tooñ ña”.
36فَأَزَلَّهُمَا الشَّيْطَانُ عَنْهَا فَأَخْرَجَهُمَا مِمَّا كَانَا فِيهِ ۖ وَقُلْنَا اهْبِطُوا بَعْضُكُمْ لِبَعْضٍ عَدُوٌّ ۖ وَلَكُمْ فِي الْأَرْضِ مُسْتَقَرٌّ وَمَتَاعٌ إِلَىٰ حِينٍ
[Séytaane] tarxiisloo na leen, génne leen fa ñu nekkoon. Nu ne leen : “Wàccleen ; di noonuwante. Te itam dangeen am ci kaw suuf ay dëkkuwaay ak i jumtukaay as ndiir”.
Al-BaqaraFihi Alxuraan
286Aaya
MedinanRevelation
34Aaya

Tekki — Al-Baqara 34

Simoore Al-Baqara Aaya 34 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : [Fàttelikul] Ba Nu nee Maalaaka ya sujjóotleen ci Aadama, ñu…

Simoore Aaya 34/286 — Al-Baqara البقرة (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Baqara Dégg, Al-Baqara Tekki, Al-Baqara mp3, Al-Baqara pdf. Aaya 32–36. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers