Al-Baqara · 31/286
Tekki Waxtaan — Al-Baqara
وَعَلَّمَ آدَمَ الْأَسْمَاءَ كُلَّهَا ثُمَّ عَرَضَهُمْ عَلَى الْمَلَائِكَةِ فَقَالَ أَنبِئُونِي بِأَسْمَاءِ هَٰؤُلَاءِ إِن كُنتُمْ صَادِقِينَ ۝٣١
Wa `allama Aadamal asmaaa`a kullahaa summa `aradahum `alal malaaa`ikati faqaala ambi`oonee bias maaa`i haaa`ulaaa`i in kuntum saadiqeen
📖 Tekkim Wolof
Mu jàngal Aadama turi lenn lu ne, ba noppi won ko Malaaka ya, ne leen : “Wax leen ma turi yëf yii, ndegam ñu dëggu ngeen ! ”.

🎧 Dégg


📜 Aaya 29-33 — Al-Baqara

29هُوَ الَّذِي خَلَقَ لَكُم مَّا فِي الْأَرْضِ جَمِيعًا ثُمَّ اسْتَوَىٰ إِلَى السَّمَاءِ فَسَوَّاهُنَّ سَبْعَ سَمَاوَاتٍ ۚ وَهُوَ بِكُلِّ شَيْءٍ عَلِيمٌ
Moom moo leen sàkkal lépp lu nekk ci suuf si, daldi jublu ci asamaan si def ko mu nekk juróoom-ñaari asamaan. Te moom nag lépp la xam.
30وَإِذْ قَالَ رَبُّكَ لِلْمَلَائِكَةِ إِنِّي جَاعِلٌ فِي الْأَرْضِ خَلِيفَةً ۖ قَالُوا أَتَجْعَلُ فِيهَا مَن يُفْسِدُ فِيهَا وَيَسْفِكُ الدِّمَاءَ وَنَحْنُ نُسَبِّحُ بِحَمْدِكَ وَنُقَدِّسُ لَكَ ۖ قَالَ إِنِّي أَعْلَمُ مَا لَا تَعْلَمُونَ
Fàttalikul ba sa Boroom waxee Malaaka ya, ne leen: “Man dey damaa namm a def ci suuf si ag kilifa[kuutaay]. Ñu toontu ne ko : “Moo ndax dangay def ci suuf si koo xam ne dafa ciy nekk di yàq, di tuur i dereet, te nun nu ngi lay sàbbaal, di la sant te di màggal sag sell ? ” – Yàlla ne leen : “Xam naa lu ngeen xamul ! ”.
31وَعَلَّمَ آدَمَ الْأَسْمَاءَ كُلَّهَا ثُمَّ عَرَضَهُمْ عَلَى الْمَلَائِكَةِ فَقَالَ أَنبِئُونِي بِأَسْمَاءِ هَٰؤُلَاءِ إِن كُنتُمْ صَادِقِينَ
Mu jàngal Aadama turi lenn lu ne, ba noppi won ko Malaaka ya, ne leen : “Wax leen ma turi yëf yii, ndegam ñu dëggu ngeen ! ”.
32قَالُوا سُبْحَانَكَ لَا عِلْمَ لَنَا إِلَّا مَا عَلَّمْتَنَا ۖ إِنَّكَ أَنتَ الْعَلِيمُ الْحَكِيمُ
–Malaaka ya ne ko : “Tuddu nanu sa sell gi ! Amunu benn xam-xam lu dul loo nu xamal. Ndax Yaw yaay ki xam, Yaay ki xereñ”.
33قَالَ يَا آدَمُ أَنبِئْهُم بِأَسْمَائِهِمْ ۖ فَلَمَّا أَنبَأَهُم بِأَسْمَائِهِمْ قَالَ أَلَمْ أَقُل لَّكُمْ إِنِّي أَعْلَمُ غَيْبَ السَّمَاوَاتِ وَالْأَرْضِ وَأَعْلَمُ مَا تُبْدُونَ وَمَا كُنتُمْ تَكْتُمُونَ
–Mu ne : "Aadama xamal-leen seeni tur ; ” Ba mu leen xamalee seeni tur, Yàlla ne leen : “Ndax dama leen a waxuloon ne Man xam naa kumpag asamaan ak suuf si, te it xam naa xéll li ngeen feeñal ak li ngeen doon ñëbb ? ”
Al-BaqaraFihi Alxuraan
286Aaya
MedinanRevelation
31Aaya

Tekki — Al-Baqara 31

Simoore Al-Baqara Aaya 31 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Mu jàngal Aadama turi lenn lu ne, ba noppi won…

Simoore Aaya 31/286 — Al-Baqara البقرة (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Baqara Dégg, Al-Baqara Tekki, Al-Baqara mp3, Al-Baqara pdf. Aaya 29–33. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers