Al-Baqara · 30/286
Tekki Waxtaan — Al-Baqara
وَإِذْ قَالَ رَبُّكَ لِلْمَلَائِكَةِ إِنِّي جَاعِلٌ فِي الْأَرْضِ خَلِيفَةً ۖ قَالُوا أَتَجْعَلُ فِيهَا مَن يُفْسِدُ فِيهَا وَيَسْفِكُ الدِّمَاءَ وَنَحْنُ نُسَبِّحُ بِحَمْدِكَ وَنُقَدِّسُ لَكَ ۖ قَالَ إِنِّي أَعْلَمُ مَا لَا تَعْلَمُونَ ۝٣٠
Wa iz qaala rabbuka lil malaaa`ikati innee jaa`ilun fil ardi khaleefatan qaalooo ataj`alu feehaa mai yufsidu feehaa wa yasfikud dimaaa`a wa nahnu nusabbihu bihamdika wa nuqaddisu laka qaala inneee a`lamu maa laa ta`lamoon
📖 Tekkim Wolof
Fàttalikul ba sa Boroom waxee Malaaka ya, ne leen: “Man dey damaa namm a def ci suuf si ag kilifa[kuutaay]. Ñu toontu ne ko : “Moo ndax dangay def ci suuf si koo xam ne dafa ciy nekk di yàq, di tuur i dereet, te nun nu ngi lay sàbbaal, di la sant te di màggal sag sell ? ” – Yàlla ne leen : “Xam naa lu ngeen xamul ! ”.
🎧 Dégg

📜 Aaya 28-32 — Al-Baqara

28كَيْفَ تَكْفُرُونَ بِاللَّهِ وَكُنتُمْ أَمْوَاتًا فَأَحْيَاكُمْ ۖ ثُمَّ يُمِيتُكُمْ ثُمَّ يُحْيِيكُمْ ثُمَّ إِلَيْهِ تُرْجَعُونَ
Naka ngeen di weddee Yàlla te ngeen doonoon ñu dee, Mu dundal leen ? Dana leen rey ; dana leen dekkalaat ngeen dellu ca Moom.
29هُوَ الَّذِي خَلَقَ لَكُم مَّا فِي الْأَرْضِ جَمِيعًا ثُمَّ اسْتَوَىٰ إِلَى السَّمَاءِ فَسَوَّاهُنَّ سَبْعَ سَمَاوَاتٍ ۚ وَهُوَ بِكُلِّ شَيْءٍ عَلِيمٌ
Moom moo leen sàkkal lépp lu nekk ci suuf si, daldi jublu ci asamaan si def ko mu nekk juróoom-ñaari asamaan. Te moom nag lépp la xam.
30وَإِذْ قَالَ رَبُّكَ لِلْمَلَائِكَةِ إِنِّي جَاعِلٌ فِي الْأَرْضِ خَلِيفَةً ۖ قَالُوا أَتَجْعَلُ فِيهَا مَن يُفْسِدُ فِيهَا وَيَسْفِكُ الدِّمَاءَ وَنَحْنُ نُسَبِّحُ بِحَمْدِكَ وَنُقَدِّسُ لَكَ ۖ قَالَ إِنِّي أَعْلَمُ مَا لَا تَعْلَمُونَ
Fàttalikul ba sa Boroom waxee Malaaka ya, ne leen: “Man dey damaa namm a def ci suuf si ag kilifa[kuutaay]. Ñu toontu ne ko : “Moo ndax dangay def ci suuf si koo xam ne dafa ciy nekk di yàq, di tuur i dereet, te nun nu ngi lay sàbbaal, di la sant te di màggal sag sell ? ” – Yàlla ne leen : “Xam naa lu ngeen xamul ! ”.
31وَعَلَّمَ آدَمَ الْأَسْمَاءَ كُلَّهَا ثُمَّ عَرَضَهُمْ عَلَى الْمَلَائِكَةِ فَقَالَ أَنبِئُونِي بِأَسْمَاءِ هَٰؤُلَاءِ إِن كُنتُمْ صَادِقِينَ
Mu jàngal Aadama turi lenn lu ne, ba noppi won ko Malaaka ya, ne leen : “Wax leen ma turi yëf yii, ndegam ñu dëggu ngeen ! ”.
32قَالُوا سُبْحَانَكَ لَا عِلْمَ لَنَا إِلَّا مَا عَلَّمْتَنَا ۖ إِنَّكَ أَنتَ الْعَلِيمُ الْحَكِيمُ
–Malaaka ya ne ko : “Tuddu nanu sa sell gi ! Amunu benn xam-xam lu dul loo nu xamal. Ndax Yaw yaay ki xam, Yaay ki xereñ”.
Al-BaqaraFihi Alxuraan
286Aaya
MedinanRevelation
30Aaya

Tekki — Al-Baqara 30

Simoore Al-Baqara Aaya 30 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Fàttalikul ba sa Boroom waxee Malaaka ya, ne leen: “Man…

Simoore Aaya 30/286 — Al-Baqara البقرة (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Baqara Dégg, Al-Baqara Tekki, Al-Baqara mp3, Al-Baqara pdf. Aaya 28–32. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers