🔥 0 fan yu toftaloo
📖 Simoore bu gudde — xaajoo ci yeneen ndogal yu ndaw (40 Aaya)
0/40
78:1
🔁 0/5
عَمَّ يَتَسَآءَلُونَ ١
Amma Yatasaa-aloon
Ana ci man mbir la ñuy laajante ?
🎤 Sa fab:
78:2
🔁 0/5
عَنِ ٱلنَّبَإِ ٱلۡعَظِيمِ ٢
Anin-nabaa-il `azeem
Ci xibaar bu rëy ba,
🎤 Sa fab:
78:3
🔁 0/5
ٱلَّذِي هُمۡ فِيهِ مُخۡتَلِفُونَ ٣
Allazi hum feehi mukh talifoon
xibaar ba nga xam ne dañu caa juuyoo.
🎤 Sa fab:
78:4
🔁 0/5
كـَلَّا سَيَعۡلَمُونَ ٤
Kallaa sa y`alamoon
Mukk ! danañu xala xam.
🎤 Sa fab:
78:5
🔁 0/5
ثُمَّ كـَلَّا سَيَعۡلَمُونَ ٥
Thumma kallaa sa y`alamoon
Déedéet kay ! Danañu xala xam.
🎤 Sa fab:
78:6
🔁 0/5
أَلَمۡ نَجۡعَلِ ٱلۡأَرۡضَ مِهَٰدًا ٦
Alam naj`alil arda mihaa da
Moo ndax du Nun Noo def suuf si mu di laltaay ?
🎤 Sa fab:
78:7
🔁 0/5
وَٱلۡجِبَالَ أَوۡتَادًا ٧
Wal jibaala au taada
ak tundi doj yi ñu di ay dott ?
🎤 Sa fab:
78:8
🔁 0/5
وَخَلَقۡنَٰكُمۡ أَزۡوَٰجًا ٨
Wa khalaq naakum azwaaja
Nu bind leen ngeen di ay tóllent,
🎤 Sa fab:
78:9
🔁 0/5
وَجَعَلۡنَا نَوۡمَكُمۡ سُبَاتًا ٩
Waja`alnan naumakum subata
te def nanu seeni nelaw di seen nooflaay,
🎤 Sa fab:
78:10
🔁 0/5
وَجَعَلۡنَا ٱلَّيۡلَ لِبَاسًا ١٠
Waja`alnal laila libasa
te it def nanu guddi mu di kiiraay sutura,
🎤 Sa fab:
78:11
🔁 0/5
وَجَعَلۡنَا ٱلنَّهَارَ مَعَاشًا ١١
Waja`alnan nahara ma `aasha
nu def bëcëg mu di yëngutu kaay,
🎤 Sa fab:
78:12
🔁 0/5
وَبَنَيۡنَا فَوۡقَكُمۡ سَبۡعًا شِدَادًا ١٢
Wa banaina fauqakum sab `an shi daada
tabax nanu juróom ñaari (asamaan) yu dëgër ñu tiim leen,
🎤 Sa fab:
78:13
🔁 0/5
وَجَعَلۡنَا سِرَاجًا وَهَّاجًا ١٣
Waja`alna siraajaw wah haaja
poose nanu ci làmpu bu leer (jant bi),
🎤 Sa fab:
78:14
🔁 0/5
وَأَنزَلۡنَا مِنَ ٱلۡمُعۡصِرَٰتِ مَآءً ثَجَّاجًا ١٤
Wa anzalna minal m`usiraati maa-an saj-jaaja
wàcce nanu ci niir yi am ndox muy dottiku
🎤 Sa fab:
78:15
🔁 0/5
لِّنُخۡرِجَ بِهِۦ حَبًّا وَنَبَاتًا ١٥
Linukh rija bihee habbaw wana baata
ñu di ca saxal ay pepp ak i gàncax
🎤 Sa fab:
78:16
🔁 0/5
وَجَنَّٰتٍ أَلۡفَافًا ١٦
Wa jan naatin alfafa
ak ay dër yu naat.
🎤 Sa fab:
78:17
🔁 0/5
إِنَّ يَوۡمَ ٱلۡفَصۡلِ كَانَ مِيقَٰتًا ١٧
Inna yaumal-fasli kana miqaata
Bisub Àtte ba Dig ba jotna.
🎤 Sa fab:
78:18
🔁 0/5
يَوۡمَ يُنفَخُ فِي ٱلصُّورِ فَتَأۡتُونَ أَفۡوَاجًا ١٨
Yauma yun fakhu fis-soori fataa toona afwaaja
Bis ba ñuy wal bufta, ngeen di ñëw di ay mbooloo,
🎤 Sa fab:
78:19
🔁 0/5
وَفُتِحَتِ ٱلسَّمَآءُ فَكَانَتۡ أَبۡوَٰبًا ١٩
Wa futiha tis samaa-u fakaanat abwaaba
nu ubbi asamaan si mu def ay buntu,
🎤 Sa fab:
78:20
🔁 0/5
وَسُيِّرَتِ ٱلۡجِبَالُ فَكَانَتۡ سَرَابًا ٢٠
Wa suyyi raatil jibaalu fa kaanat saraaba
nu doxloo tundi doj yi mu melni ñàndóox.
🎤 Sa fab:
78:21
🔁 0/5
إِنَّ جَهَنَّمَ كَانَتۡ مِرۡصَادًا ٢١
Inna jahan nama kaanat mirsaada
Waajal nanu safara muy tuqlóo,
🎤 Sa fab:
78:22
🔁 0/5
لِّلطَّٰغِينَ مَـَٔابًا ٢٢
Lit taa gheena ma aaba
di xala doon dekuwaayu ñu bew ña.
🎤 Sa fab:
78:23
🔁 0/5
لَّٰبِثِينَ فِيهَآ أَحۡقَابًا ٢٣
Laa bitheena feehaa ahqaaba
Danañu fa sax ay jamono yu yàgg.
🎤 Sa fab:
78:24
🔁 0/5
لَّا يَذُوقُونَ فِيهَا بَرۡدًا وَلَا شَرَابًا ٢٤
Laa ya zooqoona feeha bar daw walaa sharaaba
Dunu fa mos ab sedd waxantumalaa ag naan,
🎤 Sa fab:
78:25
🔁 0/5
إِلَّا حَمِيمًا وَغَسَّاقًا ٢٥
Illa hamee maw-wa ghas saaqa
Lu dul ndox muy wañax ak lay rogaate ca seen jëmm ya
🎤 Sa fab:
78:26
🔁 0/5
جَزَآءً وِفَاقًا ٢٦
Jazaa-aw wi faaqa
muy pey gu témbóo.
🎤 Sa fab:
78:27
🔁 0/5
إِنَّهُمۡ كَانُواْ لَا يَرۡجُونَ حِسَابًا ٢٧
Innahum kaanu laa yarjoona hisaaba
Ñoom dañoo foogoon ne duñu leen màndaxe,
🎤 Sa fab:
78:28
🔁 0/5
وَكَذَّبُواْ بِـَٔايَٰتِنَا كِذَّابًا ٢٨
Wa kazzabu bi aayaa tina kizzaba
ña weddiwoon sunuy Laaya,
🎤 Sa fab:
78:29
🔁 0/5
وَكُلَّ شَيۡءٍ أَحۡصَيۡنَٰهُ كِتَٰبًا ٢٩
Wa kulla shai-in ahsai naahu kitaa ba
lépp lu ne peek nanu ko bind ko.
🎤 Sa fab:
78:30
🔁 0/5
فَذُوقُواْ فَلَن نَّزِيدَكُمۡ إِلَّا عَذَابًا ٣٠
Fa zooqoo falan-nazee dakum ill-laa azaaba
Ayca mosleen. Dunu leen dolli lu dul mbugël (tokamtikuleen ko)!
🎤 Sa fab:
78:31
🔁 0/5
إِنَّ لِلۡمُتَّقِينَ مَفَازًا ٣١
Inna lil mutta qeena mafaaza
Ña ragal Yàlla ñoom baaxal nañu :
🎤 Sa fab:
78:32
🔁 0/5
حَدَآئِقَ وَأَعۡنَٰبًا ٣٢
Hadaa-iqa wa a`anaa ba
am nañu ay tooli dër ak i reseñ,
🎤 Sa fab:
78:33
🔁 0/5
وَكَوَاعِبَ أَتۡرَابًا ٣٣
Wa kaawa `iba at raaba
ak i jongama huur yu taxaw ay ween te maase,
🎤 Sa fab:
78:34
🔁 0/5
وَكَأۡسًا دِهَاقًا ٣٤
Wa ka`san di haaqa
ak ay kaas yu fees dell.
🎤 Sa fab:
78:35
🔁 0/5
لَّا يَسۡمَعُونَ فِيهَا لَغۡوًا وَلَا كِذَّٰبًا ٣٥
Laa yasma`oona fiha lagh waw walaa kizzaba
Duñu fa dégg mukk waxi caaxaan mbaa ay fen.
🎤 Sa fab:
78:36
🔁 0/5
جَزَآءً مِّن رَّبِّكَ عَطَآءً حِسَابًا ٣٦
Jazaa-am mir-rabbika ataa-an hisaaba
Muy pey gu bawoo ca seen Boroom
🎤 Sa fab:
78:37
🔁 0/5
رَّبِّ ٱلسَّمَٰوَٰتِ وَٱلۡأَرۡضِ وَمَا بَيۡنَهُمَا ٱلرَّحۡمَٰنِۖ لَا يَمۡلِكُونَ مِنۡهُ خِطَابًا ٣٧
Rabbis samaa waati wal ardi wa maa baina humar rahmaani laa yam likoona minhu khi taaba
Boroom asamaan yeek suuf seek li ci seen diggante, mooy Yëramaakoon bi ; duñu mana waxanteek moom.
🎤 Sa fab:
78:38
🔁 0/5
يَوۡمَ يَقُومُ ٱلرُّوحُ وَٱلۡمَلَٰٓئِكَةُ صَفًّاۖ لَّا يَتَكَلَّمُونَ إِلَّا مَنۡ أَذِنَ لَهُ ٱلرَّحۡمَٰنُ وَقَالَ صَوَابًا ٣٨
Yauma yaqoo mur roohu wal malaa-ikatu saf-fal laa yata kalla moona illa man azina lahur rahmaanu wa qaala sawaaba
Bu keroogee ba Jibriil jóg ànd ak malaaka ya taxaw def sàppe, duñu wax , lu dul ku Yàlla Yëramaakoon bi jox ndigël, mu wax lay dëgg te yem ca kepp.
🎤 Sa fab:
78:39
🔁 0/5
ذَٰلِكَ ٱلۡيَوۡمُ ٱلۡحَقُّۖ فَمَن شَآءَ ٱتَّخَذَ إِلَىٰ رَبِّهِۦ مَـَٔابًا ٣٩
Zaalikal yaumul haqqu faman shaa-at ta khaaza ill-laa rabbihi ma-aaba
Loolu moo di bisub dëgg ba. Ku mu soob mu jël Boroomam def ko ab rawtukaay.
🎤 Sa fab:
78:40
🔁 0/5
إِنَّآ أَنذَرۡنَٰكُمۡ عَذَابًا قَرِيبًا يَوۡمَ يَنظُرُ ٱلۡمَرۡءُ مَا قَدَّمَتۡ يَدَاهُ وَيَقُولُ ٱلۡكَافِرُ يَٰلَيۡتَنِي كُنتُ تُرَٰبَۢا ٤٠
In naa anzar naakum azaaban qareebaiy-yauma yan zurul marr-u maa qaddamat yadaahu wa ya qoolul-kaafiru yaa lai tanee kuntu turaaba
Xuppnaa leen ci mbugëlum bis bu jigeen, bu keroogee ba nit ñi di xool la ñu jëfoon ; yéefar ba naan : “Aka neexoon may suuf”.
🎤 Sa fab:
💡 Bësal baat bu nëbbu ngir wone ko ci diir bu gàtt — sa yokkute dañu koy denc ci boppam.
العربيةEnglishBahasa IndonesiaTürkçeРусскийفارسیFrançaisاردوবাংলাDeutschEspañol中文हिन्दीPortuguêsItalianoภาษาไทยPolskiNederlandsShqipKiswahiliO'zbekதமிழ்MelayuBosanskiSoomaaliAzərbaycanکوردی한국어日本語SvenskaDanskNorskپښتوമലയാളംසිංහලTamazightHausaአማርኛБългарскиТоҷикӣҚазақшаFilipinoسنڌيYorùbáFulfuldeТатарчаئۇيغۇرچەКыргызчаਪੰਜਾਬੀJawaతెలుగుမြန်မာગુજરાતીOromoमराठीTiếng ViệtMalagasyНохчийнWolofދިވެހިಕನ್ನಡУкраїнськаΕλληνικάქართულიខ្មែរدریQafar afMaranaoनेपाली
Alxuraan bu Tedd bi
Tuesday, August 18, 2026
Don't forget us in your sincere prayers







