PDF —
40 Aaya Meccan PDF
Built right in your browser — download starts automatically

Simoore An-Naba pdf — Wàcce (Wolof)

Simoore An-Naba pdf Wolof — Wàcce Simoore An-Naba Tekki. Simoore An-Naba (Meccan) 40 Aaya.



40 Aaya · Meccan · Wolof
bismillah
ﭑﭒﭓ
78:1 Ana ci man mbir la ñuy laajante ?
ﭔﭕﭖﭗ
78:2 Ci xibaar bu rëy ba,
ﭘﭙﭚﭛﭜ
78:3 xibaar ba nga xam ne dañu caa juuyoo.
ﭝﭞﭟ
78:4 Mukk ! danañu xala xam.
ﭠﭡﭢﭣ
78:5 Déedéet kay ! Danañu xala xam.
ﭤﭥﭦﭧﭨ
78:6 Moo ndax du Nun Noo def suuf si mu di laltaay ?
ﭩﭪﭫ
78:7 ak tundi doj yi ñu di ay dott ?
ﭬﭭﭮ
78:8 Nu bind leen ngeen di ay tóllent,
ﭯﭰﭱﭲ
78:9 te def nanu seeni nelaw di seen nooflaay,
ﭳﭴﭵﭶ
78:10 te it def nanu guddi mu di kiiraay sutura,
ﭷﭸﭹﭺ
78:11 nu def bëcëg mu di yëngutu kaay,
ﭻﭼﭽﭾﭿ
78:12 tabax nanu juróom ñaari (asamaan) yu dëgër ñu tiim leen,
ﮀﮁﮂﮃ
78:13 poose nanu ci làmpu bu leer (jant bi),
ﮄﮅﮆﮇﮈﮉ
78:14 wàcce nanu ci niir yi am ndox muy dottiku
ﮊﮋﮌﮍﮎ
78:15 ñu di ca saxal ay pepp ak i gàncax
ﮏﮐﮑ
78:16 ak ay dër yu naat.
ﮒﮓﮔﮕﮖﮗ
78:17 Bisub Àtte ba Dig ba jotna.
ﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞ
78:18 Bis ba ñuy wal bufta, ngeen di ñëw di ay mbooloo,
ﮟﮠﮡﮢﮣ
78:19 nu ubbi asamaan si mu def ay buntu,
ﮤﮥﮦﮧﮨ
78:20 nu doxloo tundi doj yi mu melni ñàndóox.
ﮩﮪﮫﮬﮭ
78:21 Waajal nanu safara muy tuqlóo,
ﮮﮯﮰ
78:22 di xala doon dekuwaayu ñu bew ña.
ﮱﯓﯔﯕ
78:23 Danañu fa sax ay jamono yu yàgg.
ﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜ
78:24 Dunu fa mos ab sedd waxantumalaa ag naan,
ﯝﯞﯟﯠ
78:25 Lu dul ndox muy wañax ak lay rogaate ca seen jëmm ya
ﯡﯢﯣ
78:26 muy pey gu témbóo.
ﯤﯥﯦﯧﯨﯩ
78:27 Ñoom dañoo foogoon ne duñu leen màndaxe,
ﯪﯫﯬﯭ
78:28 ña weddiwoon sunuy Laaya,
ﯮﯯﯰﯱﯲ
78:29 lépp lu ne peek nanu ko bind ko.
ﯳﯴﯵﯶﯷﯸ
78:30 Ayca mosleen. Dunu leen dolli lu dul mbugël (tokamtikuleen ko)!
ﭑﭒﭓﭔ
78:31 Ña ragal Yàlla ñoom baaxal nañu :
ﭕﭖﭗ
78:32 am nañu ay tooli dër ak i reseñ,
ﭘﭙﭚ
78:33 ak i jongama huur yu taxaw ay ween te maase,
ﭛﭜﭝ
78:34 ak ay kaas yu fees dell.
ﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤ
78:35 Duñu fa dégg mukk waxi caaxaan mbaa ay fen.
ﭥﭦﭧﭨﭩﭪ
78:36 Muy pey gu bawoo ca seen Boroom
ﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶ
78:37 Boroom asamaan yeek suuf seek li ci seen diggante, mooy Yëramaakoon bi ; duñu mana waxanteek moom.
ﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆ
78:38 Bu keroogee ba Jibriil jóg ànd ak malaaka ya taxaw def sàppe, duñu wax , lu dul ku Yàlla Yëramaakoon bi jox ndigël, mu wax lay dëgg te yem ca kepp.
ﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑ
78:39 Loolu moo di bisub dëgg ba. Ku mu soob mu jël Boroomam def ko ab rawtukaay.
ﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡ
78:40 Xuppnaa leen ci mbugëlum bis bu jigeen, bu keroogee ba nit ñi di xool la ñu jëfoon ; yéefar ba naan : “Aka neexoon may suuf”.

Alxuraan bu Tedd bi


Wednesday, September 9, 2026

Don't forget us in your sincere prayers