Al-Fath · 3/29
Tekki Waxtaan — Al-Fath
وَيَنصُرَكَ اللَّهُ نَصْرًا عَزِيزًا ۝٣
Wa yansurakal laahu nasran `azeezaa
📖 Tekkim Wolof
Yàlla dana la dimbali ndimbal (luy tax nga man a not say noon).

🎧 Dégg


📜 Aaya 1-5 — Al-Fath

1إِنَّا فَتَحْنَا لَكَ فَتْحًا مُّبِينًا
Nun dey ubbil nanu la ubbi gu fes bir (jox la ndam) nga bom,
2لِّيَغْفِرَ لَكَ اللَّهُ مَا تَقَدَّمَ مِن ذَنبِكَ وَمَا تَأَخَّرَ وَيُتِمَّ نِعْمَتَهُ عَلَيْكَ وَيَهْدِيَكَ صِرَاطًا مُّسْتَقِيمًا
ci loolu Yàlla dana la jéggal, la jëkkoon ci say bàkkaar ak lay xala mujj, te it Dana matal ay Xéewal ci yaw te itam dana gindi teg la ca kaw yoonam wu jub xocc wa ;
3وَيَنصُرَكَ اللَّهُ نَصْرًا عَزِيزًا
Yàlla dana la dimbali ndimbal (luy tax nga man a not say noon).
4هُوَ الَّذِي أَنزَلَ السَّكِينَةَ فِي قُلُوبِ الْمُؤْمِنِينَ لِيَزْدَادُوا إِيمَانًا مَّعَ إِيمَانِهِمْ ۗ وَلِلَّهِ جُنُودُ السَّمَاوَاتِ وَالْأَرْضِ ۚ وَكَانَ اللَّهُ عَلِيمًا حَكِيمًا
Moom (Yàlla) ki wàcce ag dal ci xoli jullit ñi ngir ñuy dolliku ngëm ci séen kaw ngëm ga. Te nag Yàllaa moom xarekati asamaan yeek suuf si ; Yàlla Kuy xam la ku Xereñ la
5لِّيُدْخِلَ الْمُؤْمِنِينَ وَالْمُؤْمِنَاتِ جَنَّاتٍ تَجْرِي مِن تَحْتِهَا الْأَنْهَارُ خَالِدِينَ فِيهَا وَيُكَفِّرَ عَنْهُمْ سَيِّئَاتِهِمْ ۚ وَكَانَ ذَٰلِكَ عِندَ اللَّهِ فَوْزًا عَظِيمًا
(waral gi mu waral ci yéen xare) tax na ba dana tàbbal jullit ñu goor ñeek jullit ñu jigéen ñi ci Àjjana yoo xam ne ay dex ñooy daw ci suufam te dañu fay béel, te it dana leen faral séeni ñaawtéef loolu di texe gu mag ga fa Yàlla.
Al-FathFihi Alxuraan
29Aaya
MedinanRevelation
3Aaya

Tekki — Al-Fath 3

Simoore Al-Fath Aaya 3 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Yàlla dana la dimbali ndimbal (luy tax nga man a…

Simoore Aaya 3/29 — Al-Fath الفتح (Medinan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Al-Fath Dégg, Al-Fath Tekki, Al-Fath mp3, Al-Fath pdf. Aaya 1–5. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers