📖 0/604 xët yi jàng nañu
📄 367
Simoore Ash-Shu'ara

Simoore Ash-Shu'ara

26:3
لَعَلَّكَ بَٰخِعٌ نَّفۡسَكَ أَلَّا يَكُونُواْ مُؤۡمِنِينَ ٣
Amaana nga am ñàngi-ñàngi xol ci li ñu gëmul !
26:4
إِن نَّشَأۡ نُنَزِّلۡ عَلَيۡهِم مِّنَ ٱلسَّمَآءِ ءَايَةً فَظَلَّتۡ أَعۡنَٰقُهُمۡ لَهَا خَٰضِعِينَ ٤
Bu Nu neexoon Nu wàcce ci asamaan kéemaan guy tax ñuy jatti loos.
26:5
وَمَا يَأۡتِيهِم مِّن ذِكۡرٍ مِّنَ ٱلرَّحۡمَٰنِ مُحۡدَثٍ إِلَّا كَانُواْ عَنۡهُ مُعۡرِضِينَ ٥
Amul benn woote bu bees bu mësoon a bawoo ca Yàlla lu dul ne dëndu dañu ko.
26:6
فَقَدۡ كَذَّبُواْ فَسَيَأۡتِيهِمۡ أَنۢبَٰٓؤُاْ مَا كَانُواْ بِهِۦ يَسۡتَهۡزِءُونَ ٦
Weddi woon nañu, te danañu mës a joti xibaari la ñu doon téjji.
26:7
أَوَلَمۡ يَرَوۡاْ إِلَى ٱلۡأَرۡضِ كَمۡ أَنۢبَتۡنَا فِيهَا مِن كُلِّ زَوۡجٍ كَرِيمٍ ٧
Xanaa dañoo gisul yu bari yi Nu saxal ci kaw suuf, ci xeeti gàncax muy tollént ?
26:8
إِنَّ فِي ذَٰلِكَ لَأٓيَةًۖ وَمَا كَانَ أَكۡثَرُهُم مُّؤۡمِنِينَ ٨
Ay kéemaan yu bari nekk ci loolu ! Waaye taxut li ëpp ci ñoom gëm [diy jullit].
26:9
وَإِنَّ رَبَّكَ لَهُوَ ٱلۡعَزِيزُ ٱلرَّحِيمُ ٩
Te sa Boroom mooy Boroom kàttan ga te di Jaglewaakoonug [yërmaande].
26:10
وَإِذۡ نَادَىٰ رَبُّكَ مُوسَىٰٓ أَنِ ٱئۡتِ ٱلۡقَوۡمَ ٱلظَّٰلِمِينَ ١٠
[Fàttalikul] ba Yàlla woo na Muusaa, [ne ko] : “Demal [jubbanti ji] tooñkat ya,
26:12
قَالَ رَبِّ إِنِّيٓ أَخَافُ أَن يُكَذِّبُونِ ١٢
[Muusaa] wax ne : “Yaw Sama Boroom, damaa ragal ñu jàppe ma ab fenkat [weddi ma] ;
26:13
وَيَضِيقُ صَدۡرِي وَلَا يَنطَلِقُ لِسَانِي فَأَرۡسِلۡ إِلَىٰ هَٰرُونَ ١٣
samab dënn di xat, te kon dootuma mën a wax : Yónnil kon Aaruuna, def ko Yonent.
26:14
وَلَهُمۡ عَلَيَّ ذَنۢبٌ فَأَخَافُ أَن يَقۡتُلُونِ ١٤
Te itam, am na tuuma ju ñu may jiiñ ; te ragal naa ñu rey ma”.
26:15
قَالَ كـَلَّاۖ فَٱذۡهَبَا بِـَٔايَٰتِنَآۖ إِنَّا مَعَكُم مُّسۡتَمِعُونَ ١٥
[Yàlla] ne : “Mukk du am ! Demleen yéen ñaar yóbb sunuy kàddu. Maa ngi ànd ak yéen di dégg.
26:16
فَأۡتِيَا فِرۡعَوۡنَ فَقُولَآ إِنَّا رَسُولُ رَبِّ ٱلۡعَٰلَمِينَ ١٦
Dem ca Firawna ne ko : “Nun ñaari ndawi Boroom àddina si lanu,
26:18
قَالَ أَلَمۡ نُرَبِّكَ فِينَا وَلِيدًا وَلَبِثۡتَ فِينَا مِنۡ عُمُرِكَ سِنِينَ ١٨
[Firawna] ne ko : “Moo ndax yarunu la fii ba nga doonee liir ? Ak li nga fi nekk lépp ?
26:19
وَفَعَلۡتَ فَعۡلَتَكَ ٱلَّتِي فَعَلۡتَ وَأَنتَ مِنَ ٱلۡكَٰفِرِينَ ١٩
Ak jëf ji nga fi jëfoon tey xarabaate”
العربيةEnglishBahasa IndonesiaTürkçeРусскийفارسیFrançaisاردوবাংলাDeutschEspañol中文हिन्दीPortuguêsItalianoภาษาไทยPolskiNederlandsShqipKiswahiliO'zbekதமிழ்MelayuBosanskiSoomaaliAzərbaycanکوردی한국어日本語SvenskaDanskNorskپښتوമലയാളംසිංහලTamazightHausaአማርኛБългарскиТоҷикӣҚазақшаFilipinoسنڌيYorùbáFulfuldeТатарчаئۇيغۇرچەКыргызчаਪੰਜਾਬੀJawaతెలుగుမြန်မာગુજરાતીOromoमराठीTiếng ViệtMalagasyНохчийнWolofދިވެހިಕನ್ನಡУкраїнськаΕλληνικάქართულიខ្មែរدریQafar afMaranaoनेपाली
Alxuraan bu Tedd bi
Wednesday, August 26, 2026
Don't forget us in your sincere prayers







