Simoore Fussilat ci Aarabu ak Wolof

Jàng Simoore Fussilat ak tekkim wolof bu mat sëkk, ak baat. Tekki ayaa bu ne. (54 Aaya — مكية). Fussilat Dégg, Fussilat Tekki, Fussilat mp3, Fussilat pdf.

Jàng te Dégg Simoore Fussilat

🎧 Aaya
M Mishary Rashid Alafasy
M Mahmoud Khalil Al-Husary
A Abdurrahman As-Sudais
M Mohamed Siddiq Al-Minshawi
A Abdul Basit Abdul Samad
A Ali Al-Hudhaify
A Ahmed ibn Ali al-Ajamy
A Abu Bakr Ash-Shaatree
M Muhammad Ayyoub
A Abdullah Basfar
A Abdullah Al-Juhani
M Maher Al Muaiqly
x1
حم ۝١
📖 Tekki Aaya 1
Haa, Miim.
تَنزِيلٌ مِّنَ الرَّحْمَٰنِ الرَّحِيمِ ۝٢
📖 Tekki Aaya 2
[Ak solool] gu ñu wàcce mu bawoo ci Yëramaakoon bi , di Jaglewaakoon bi (yërmandéem).
كِتَابٌ فُصِّلَتْ آيَاتُهُ قُرْآنًا عَرَبِيًّا لِّقَوْمٍ يَعْلَمُونَ ۝٣
📖 Tekki Aaya 3
Ab Téere bu ñu faramfànce ay laayam muy Alxuraan di ko [jàng] ci làmmiñu araab ngir aw nit ñuy xam,
بَشِيرًا وَنَذِيرًا فَأَعْرَضَ أَكْثَرُهُمْ فَهُمْ لَا يَسْمَعُونَ ۝٤
📖 Tekki Aaya 4
di bégle tey xuppe. Ña ëpp ci ñoom dañoo dumóoyu ; du ñu (ko) dégg.
وَقَالُوا قُلُوبُنَا فِي أَكِنَّةٍ مِّمَّا تَدْعُونَا إِلَيْهِ وَفِي آذَانِنَا وَقْرٌ وَمِن بَيْنِنَا وَبَيْنِكَ حِجَابٌ فَاعْمَلْ إِنَّنَا عَامِلُونَ ۝٥
📖 Tekki Aaya 5
Ñuy wax naan : “Sunuy xol dañoo muuru ci li nga ñuy woo jëmële, sunuy nopp dañoo saañu. Sunu diggënteek yaw kiraay da cee nekk, Defal li ngay def (yaw caag) ; nun noo ngi def li nuy def”.
قُلْ إِنَّمَا أَنَا بَشَرٌ مِّثْلُكُمْ يُوحَىٰ إِلَيَّ أَنَّمَا إِلَٰهُكُمْ إِلَٰهٌ وَاحِدٌ فَاسْتَقِيمُوا إِلَيْهِ وَاسْتَغْفِرُوهُ ۗ وَوَيْلٌ لِّلْمُشْرِكِينَ ۝٦
📖 Tekki Aaya 6
Waxal ne : “Man nit laa ni yéen. dañu may soloo waaye seen Yàlla jenn Yàlla rekk la. Sàkkuleen tegu ca yoonam wu jub wa xocc te na ngeen sàkku njégël”. toskare ñeel na yéefar ya
الَّذِينَ لَا يُؤْتُونَ الزَّكَاةَ وَهُم بِالْآخِرَةِ هُمْ كَافِرُونَ ۝٧
📖 Tekki Aaya 7
ña dul génne asaka tey weddi (dikkug) Bis Pénc ba !
إِنَّ الَّذِينَ آمَنُوا وَعَمِلُوا الصَّالِحَاتِ لَهُمْ أَجْرٌ غَيْرُ مَمْنُونٍ ۝٨
📖 Tekki Aaya 8
Ñiy gëm tey jëfu yiw danañu am pey gu dootul dogamtal.
۞ قُلْ أَئِنَّكُمْ لَتَكْفُرُونَ بِالَّذِي خَلَقَ الْأَرْضَ فِي يَوْمَيْنِ وَتَجْعَلُونَ لَهُ أَندَادًا ۚ ذَٰلِكَ رَبُّ الْعَالَمِينَ ۝٩
📖 Tekki Aaya 9
Waxal ne : “Ndax dangeen di weddi ki bind suuf si ci ñaari fan, ngeen di Ko sàkkal ay bokkaale ? Kooku moo di boroom àddina si,
وَجَعَلَ فِيهَا رَوَاسِيَ مِن فَوْقِهَا وَبَارَكَ فِيهَا وَقَدَّرَ فِيهَا أَقْوَاتَهَا فِي أَرْبَعَةِ أَيَّامٍ سَوَاءً لِّلسَّائِلِينَ ۝١٠
📖 Tekki Aaya 10
Moo poose ay tundi doj ci kawam, def ca barke, (sakkan) mu doxal ca lépp luy yombal luy tax a man a dund ci diirub ñeenti fan. [Mooy tontul] képp ku la koy laaj.
ثُمَّ اسْتَوَىٰ إِلَى السَّمَاءِ وَهِيَ دُخَانٌ فَقَالَ لَهَا وَلِلْأَرْضِ ائْتِيَا طَوْعًا أَوْ كَرْهًا قَالَتَا أَتَيْنَا طَائِعِينَ ۝١١
📖 Tekki Aaya 11
Ba mu éggalee la yemoo ca asamaan muy Saxar mu daldi wax asamaan ak suuf moom Yàlla ne : “Dikkleen, ci bu leen neexee, walla bu leen naqaree”. Ñu tontu ko ne : “Dikk nanu ci sunu coobare”.
فَقَضَاهُنَّ سَبْعَ سَمَاوَاتٍ فِي يَوْمَيْنِ وَأَوْحَىٰ فِي كُلِّ سَمَاءٍ أَمْرَهَا ۚ وَزَيَّنَّا السَّمَاءَ الدُّنْيَا بِمَصَابِيحَ وَحِفْظًا ۚ ذَٰلِكَ تَقْدِيرُ الْعَزِيزِ الْعَلِيمِ ۝١٢
📖 Tekki Aaya 12
Dogal na ñay juróom-ñaari asamaan ci ñaari fan ci asamaan su ca nekk la muy liggéey. Te taaralal nanu asamaanu àddina si si gën a jige ak i làmp [biddiw] ak di ko sàmm. Loolu mooy Dogalub (Yàlla) kiy boroom Kàttan, di ku Xam.
فَإِنْ أَعْرَضُوا فَقُلْ أَنذَرْتُكُمْ صَاعِقَةً مِّثْلَ صَاعِقَةِ عَادٍ وَثَمُودَ ۝١٣
📖 Tekki Aaya 13
Bu ñu dumóoyoo lànk, waxal ne ; “maa ngi leen di xupp ci ag dënnu dënnu gu melni ga daloon waa Aad ak Samuud”.
إِذْ جَاءَتْهُمُ الرُّسُلُ مِن بَيْنِ أَيْدِيهِمْ وَمِنْ خَلْفِهِمْ أَلَّا تَعْبُدُوا إِلَّا اللَّهَ ۖ قَالُوا لَوْ شَاءَ رَبُّنَا لَأَنزَلَ مَلَائِكَةً فَإِنَّا بِمَا أُرْسِلْتُم بِهِ كَافِرُونَ ۝١٤
📖 Tekki Aaya 14
Ba leen yonnenta ya digëlee, bawoo kanam ak ginnaaw, [daan leen digël]: “Ci nuy jaamu Yàlla (ba ña jaamu leneen)”, ñuy wax naan : “Bu neexoon Yàlla, Mu wàcce ay Malaaka. Te sax nun lii ñu leen yónni gëmuñu ko”.
فَأَمَّا عَادٌ فَاسْتَكْبَرُوا فِي الْأَرْضِ بِغَيْرِ الْحَقِّ وَقَالُوا مَنْ أَشَدُّ مِنَّا قُوَّةً ۖ أَوَلَمْ يَرَوْا أَنَّ اللَّهَ الَّذِي خَلَقَهُمْ هُوَ أَشَدُّ مِنْهُمْ قُوَّةً ۖ وَكَانُوا بِآيَاتِنَا يَجْحَدُونَ ۝١٥
📖 Tekki Aaya 15
Waa Aad, rëy-rëylu ci suuf ci lu dul dëgg, daan wax naan : “Ana ku ñu ëpp doole ? ” (Di damu) ! Daan féttéerlu ci sunuy laaya.
فَأَرْسَلْنَا عَلَيْهِمْ رِيحًا صَرْصَرًا فِي أَيَّامٍ نَّحِسَاتٍ لِّنُذِيقَهُمْ عَذَابَ الْخِزْيِ فِي الْحَيَاةِ الدُّنْيَا ۖ وَلَعَذَابُ الْآخِرَةِ أَخْزَىٰ ۖ وَهُمْ لَا يُنصَرُونَ ۝١٦
📖 Tekki Aaya 16
Bayal nanu ca ñoom ngelawul callmeer lu sedd guy ay fan yu nduxum, ngir mosal leen mbugëlum toroxtaane ci dundug àddina sii. Te mbugëlum àllaaxiraa gën a man a toraxal te it kenn duleen fa dimbali.
وَأَمَّا ثَمُودُ فَهَدَيْنَاهُمْ فَاسْتَحَبُّوا الْعَمَىٰ عَلَى الْهُدَىٰ فَأَخَذَتْهُمْ صَاعِقَةُ الْعَذَابِ الْهُونِ بِمَا كَانُوا يَكْسِبُونَ ۝١٧
📖 Tekki Aaya 17
Waa Samuud nag ñoom, gindi woon nanu leen ; waaye dañoo tànni ngumba bàyyi gindi ku (njub) dëng. Mbugalum doyadi fab leen muy peyug la ñu daan fàggu.
وَنَجَّيْنَا الَّذِينَ آمَنُوا وَكَانُوا يَتَّقُونَ ۝١٨
📖 Tekki Aaya 18
Nu daldi musël ña gëmoon tey ragal Yàlla.
وَيَوْمَ يُحْشَرُ أَعْدَاءُ اللَّهِ إِلَى النَّارِ فَهُمْ يُوزَعُونَ ۝١٩
📖 Tekki Aaya 19
Bu keroogee bis ba ñuy pang (dajale) nooni yàlla ya... Jëme leen Safara di leen gur-gur.
حَتَّىٰ إِذَا مَا جَاءُوهَا شَهِدَ عَلَيْهِمْ سَمْعُهُمْ وَأَبْصَارُهُمْ وَجُلُودُهُم بِمَا كَانُوا يَعْمَلُونَ ۝٢٠
📖 Tekki Aaya 20
Bu ñu nee jaas agsi ci Safara, seeni nopp, ak seeni gët at seeni yaram dañuy doon ay seede ci li ñu daan def.
وَقَالُوا لِجُلُودِهِمْ لِمَ شَهِدتُّمْ عَلَيْنَا ۖ قَالُوا أَنطَقَنَا اللَّهُ الَّذِي أَنطَقَ كُلَّ شَيْءٍ وَهُوَ خَلَقَكُمْ أَوَّلَ مَرَّةٍ وَإِلَيْهِ تُرْجَعُونَ ۝٢١
📖 Tekki Aaya 21
Ñuy waxanteek seen deri yaram ya naan : “Ana lutax ngeen di seede ngir dugal nu ? ” (Der ya) tontu naan : “Yàlla miy wax loo lu nekk, Moo nu wax loo. Te Moo leen sàkk cig njaalbéen te it ca Moom ngeen di dellu”.
وَمَا كُنتُمْ تَسْتَتِرُونَ أَن يَشْهَدَ عَلَيْكُمْ سَمْعُكُمْ وَلَا أَبْصَارُكُمْ وَلَا جُلُودُكُمْ وَلَٰكِن ظَنَنتُمْ أَنَّ اللَّهَ لَا يَعْلَمُ كَثِيرًا مِّمَّا تَعْمَلُونَ ۝٢٢
📖 Tekki Aaya 22
Te manuleen woon làqatu ba seeni nopp, ak seeni gët du caagéeni seen yaram (ñu seede dugël leen). Waaye dangeen defe woon ne Yàlla xamul lu bari ci li ngeen daa def.
وَذَٰلِكُمْ ظَنُّكُمُ الَّذِي ظَنَنتُم بِرَبِّكُمْ أَرْدَاكُمْ فَأَصْبَحْتُم مِّنَ الْخَاسِرِينَ ۝٢٣
📖 Tekki Aaya 23
Loolu mooy seen njortu la ngeen jortoon ci Yàlla, moo leen faagaagal, ba ngeen xëy yàqule.
فَإِن يَصْبِرُوا فَالنَّارُ مَثْوًى لَّهُمْ ۖ وَإِن يَسْتَعْتِبُوا فَمَا هُم مِّنَ الْمُعْتَبِينَ ۝٢٤
📖 Tekki Aaya 24
Bu ñu xaaree, Safaraa di seen kër ; bu ñu sàkkoo njégël, kon duleen jégël.
۞ وَقَيَّضْنَا لَهُمْ قُرَنَاءَ فَزَيَّنُوا لَهُم مَّا بَيْنَ أَيْدِيهِمْ وَمَا خَلْفَهُمْ وَحَقَّ عَلَيْهِمُ الْقَوْلُ فِي أُمَمٍ قَدْ خَلَتْ مِن قَبْلِهِم مِّنَ الْجِنِّ وَالْإِنسِ ۖ إِنَّهُمْ كَانُوا خَاسِرِينَ ۝٢٥
📖 Tekki Aaya 25
Boole Nanu leen ak ñu ñu lëkkëlool ñu taaralal leen la ca seen kanam ak sen ginnaaw (la ñuy jëf). Dogal ba dal ci seen kow, kem na mu ame woon ca xeet ya leen jiitu woon ci jinne yi ak nit ñi. Ñoom dañoo yàqule !
وَقَالَ الَّذِينَ كَفَرُوا لَا تَسْمَعُوا لِهَٰذَا الْقُرْآنِ وَالْغَوْا فِيهِ لَعَلَّكُمْ تَغْلِبُونَ ۝٢٦
📖 Tekki Aaya 26
Ña weddi ngay wax naan : “Buleen déglu Alxuraan jii, te ngeen koy doyadil (di ko caaxaane) ndax amaana ngeen am ndam”.
فَلَنُذِيقَنَّ الَّذِينَ كَفَرُوا عَذَابًا شَدِيدًا وَلَنَجْزِيَنَّهُمْ أَسْوَأَ الَّذِي كَانُوا يَعْمَلُونَ ۝٢٧
📖 Tekki Aaya 27
Dananu, mosal ña weddi mbugal mu tar te dananu leen faye la gën a ñaaw ca la ñu daan def.
ذَٰلِكَ جَزَاءُ أَعْدَاءِ اللَّهِ النَّارُ ۖ لَهُمْ فِيهَا دَارُ الْخُلْدِ ۖ جَزَاءً بِمَا كَانُوا بِآيَاتِنَا يَجْحَدُونَ ۝٢٨
📖 Tekki Aaya 28
Loolu, mooy peyug noonu Yàlla Safara mudi seen kër ga ñuy dëkk béel ca, muy peyug weddi ga ñu daan weddi sunuy laaya.
وَقَالَ الَّذِينَ كَفَرُوا رَبَّنَا أَرِنَا اللَّذَيْنِ أَضَلَّانَا مِنَ الْجِنِّ وَالْإِنسِ نَجْعَلْهُمَا تَحْتَ أَقْدَامِنَا لِيَكُونَا مِنَ الْأَسْفَلِينَ ۝٢٩
📖 Tekki Aaya 29
Ña daan weddi dañuy wax naan : “Yaw sunu Boroom, wan nu ña nu daan réeräl ci jinne yi ak nit ñi, dananu leen def ci ron sunu ndëguy tànk, ngir nu gën a soofe”.
إِنَّ الَّذِينَ قَالُوا رَبُّنَا اللَّهُ ثُمَّ اسْتَقَامُوا تَتَنَزَّلُ عَلَيْهِمُ الْمَلَائِكَةُ أَلَّا تَخَافُوا وَلَا تَحْزَنُوا وَأَبْشِرُوا بِالْجَنَّةِ الَّتِي كُنتُمْ تُوعَدُونَ ۝٣٠
📖 Tekki Aaya 30
Ñiy wax naan : “Yàllaay sunu Boroom”, tey jéem a tegu ci seen yoonu Boroom wu jub wa xocc, Malaaka yi dañuy wàcci ci ñoom naan leen. “Buleen jàq buleen ragal ; bégleen ci àjjana ja ñu leen daan dig.
نَحْنُ أَوْلِيَاؤُكُمْ فِي الْحَيَاةِ الدُّنْيَا وَفِي الْآخِرَةِ ۖ وَلَكُمْ فِيهَا مَا تَشْتَهِي أَنفُسُكُمْ وَلَكُمْ فِيهَا مَا تَدَّعُونَ ۝٣١
📖 Tekki Aaya 31
Nun (Yàlla) noo di seen wéeruwaay ci àddina di seen wéeruwaay ca àllaaxira ; te am ngeen fa lépp lu seen bakkan di wonnén ak lépp lu ngeen fay laaj,
نُزُلًا مِّنْ غَفُورٍ رَّحِيمٍ ۝٣٢
📖 Tekki Aaya 32
(wàccuwaayu teraanga) bu bawoo ca Jéggëlekat ba, di ab Jaglewaakoonu yërmande”.
وَمَنْ أَحْسَنُ قَوْلًا مِّمَّن دَعَا إِلَى اللَّهِ وَعَمِلَ صَالِحًا وَقَالَ إِنَّنِي مِنَ الْمُسْلِمِينَ ۝٣٣
📖 Tekki Aaya 33
Ana kan moo gën a rafet ay wax kuy woote jëme ci Yàlla, tey jëf yiw tey wax naan : “ Ci jullit ñi laa bokk ? ”
وَلَا تَسْتَوِي الْحَسَنَةُ وَلَا السَّيِّئَةُ ۚ ادْفَعْ بِالَّتِي هِيَ أَحْسَنُ فَإِذَا الَّذِي بَيْنَكَ وَبَيْنَهُ عَدَاوَةٌ كَأَنَّهُ وَلِيٌّ حَمِيمٌ ۝٣٤
📖 Tekki Aaya 34
Lu rafet ak lu ñaaw du ñu yem. Na ngeen jiñe (ab safaan) ci lu baax ; (soo ko defee) ki nga gënoon a noonoo dafay jekki di sa xaritu benn bakkan.
وَمَا يُلَقَّاهَا إِلَّا الَّذِينَ صَبَرُوا وَمَا يُلَقَّاهَا إِلَّا ذُو حَظٍّ عَظِيمٍ ۝٣٥
📖 Tekki Aaya 35
Lii nag kenn du ko am ku dul ñuy muñ kenn it du ko am ku dul boroom cër bu duun.
وَإِمَّا يَنزَغَنَّكَ مِنَ الشَّيْطَانِ نَزْغٌ فَاسْتَعِذْ بِاللَّهِ ۖ إِنَّهُ هُوَ السَّمِيعُ الْعَلِيمُ ۝٣٦
📖 Tekki Aaya 36
Amaana leeg-leeg bu la saytaane jaxjaxee (waaye bu boobaa), na nga sàkku ci Yàlla mu mësal la ; Moo di, aji Dégg ja, aji xam ja.
وَمِنْ آيَاتِهِ اللَّيْلُ وَالنَّهَارُ وَالشَّمْسُ وَالْقَمَرُ ۚ لَا تَسْجُدُوا لِلشَّمْسِ وَلَا لِلْقَمَرِ وَاسْجُدُوا لِلَّهِ الَّذِي خَلَقَهُنَّ إِن كُنتُمْ إِيَّاهُ تَعْبُدُونَ ۝٣٧
📖 Tekki Aaya 37
Bokk na ci ay kéemaanam, guddi ak bëccëg, ak jant beek weer wi : buleen sujuudal jant bi, waxantumalaak weer wi, waaye na ngeen di sujuud ngir Yàlla mi leen bind, ndegam Moom ngeen di jaamu.
فَإِنِ اسْتَكْبَرُوا فَالَّذِينَ عِندَ رَبِّكَ يُسَبِّحُونَ لَهُ بِاللَّيْلِ وَالنَّهَارِ وَهُمْ لَا يَسْأَمُونَ ۩ ۝٣٨
📖 Tekki Aaya 38
Bu ñu rëy-rëyloo... (ba defuñu ko) Malaaka ya nekk ca sa Boroom ñoom dañuy sàbbaal, guddeek bëccëg, te duñu ko bàyyi !
وَمِنْ آيَاتِهِ أَنَّكَ تَرَى الْأَرْضَ خَاشِعَةً فَإِذَا أَنزَلْنَا عَلَيْهَا الْمَاءَ اهْتَزَّتْ وَرَبَتْ ۚ إِنَّ الَّذِي أَحْيَاهَا لَمُحْيِي الْمَوْتَىٰ ۚ إِنَّهُ عَلَىٰ كُلِّ شَيْءٍ قَدِيرٌ ۝٣٩
📖 Tekki Aaya 39
Bokk na ci Ay kéemaanam ngay gis suuf si mu ne ndàpp (wow koŋŋ). Saa su ñu ci wàccee ndox, mu funki màgg. Ki koy dundal (di ci def gàncax) mooy dekkal ñi dee, Moom man na Lépp lu ne.
إِنَّ الَّذِينَ يُلْحِدُونَ فِي آيَاتِنَا لَا يَخْفَوْنَ عَلَيْنَا ۗ أَفَمَن يُلْقَىٰ فِي النَّارِ خَيْرٌ أَم مَّن يَأْتِي آمِنًا يَوْمَ الْقِيَامَةِ ۚ اعْمَلُوا مَا شِئْتُمْ ۖ إِنَّهُ بِمَا تَعْمَلُونَ بَصِيرٌ ۝٤٠
📖 Tekki Aaya 40
Ñiy jéem a soppi samay laaya (Alxuraan) manuñu nooraan. Moo ndax ku ñu sànni ca safara moo gën walla kuy dikk bu Bis Pénc baa ànd ak ug wóolu ? Defleen lu leen soob moom kuy gis la li ngeen di def ;
إِنَّ الَّذِينَ كَفَرُوا بِالذِّكْرِ لَمَّا جَاءَهُمْ ۖ وَإِنَّهُ لَكِتَابٌ عَزِيزٌ ۝٤١
📖 Tekki Aaya 41
Ñay weddi [Alxuraan] ba mu dikkee ak li mu leen di fàttali dees na leen mbugël... te Téere bii Téere bu Kàttanu la ;
لَّا يَأْتِيهِ الْبَاطِلُ مِن بَيْنِ يَدَيْهِ وَلَا مِنْ خَلْفِهِ ۖ تَنزِيلٌ مِّنْ حَكِيمٍ حَمِيدٍ ۝٤٢
📖 Tekki Aaya 42
Ay caaxaan [du ko dikke fenn], du ci kanamam mbaa ci ginnaawam : dañu koo wàcce mu bawoo ca (Yàlla) miy aji Xereñ, di Yayoowaakoonu cant.
مَّا يُقَالُ لَكَ إِلَّا مَا قَدْ قِيلَ لِلرُّسُلِ مِن قَبْلِكَ ۚ إِنَّ رَبَّكَ لَذُو مَغْفِرَةٍ وَذُو عِقَابٍ أَلِيمٍ ۝٤٣
📖 Tekki Aaya 43
Deesul a wax lenn lu ñu waxutoon Yonnent ya la jiitu woon. Sa Boroom, ku Am njégël la te di Boroom mbugël mu mitti.
وَلَوْ جَعَلْنَاهُ قُرْآنًا أَعْجَمِيًّا لَّقَالُوا لَوْلَا فُصِّلَتْ آيَاتُهُ ۖ أَأَعْجَمِيٌّ وَعَرَبِيٌّ ۗ قُلْ هُوَ لِلَّذِينَ آمَنُوا هُدًى وَشِفَاءٌ ۖ وَالَّذِينَ لَا يُؤْمِنُونَ فِي آذَانِهِمْ وَقْرٌ وَهُوَ عَلَيْهِمْ عَمًى ۚ أُولَٰئِكَ يُنَادَوْنَ مِن مَّكَانٍ بَعِيدٍ ۝٤٤
📖 Tekki Aaya 44
Bu Nu ko defoon muy weneen làkk (wu dul araab), danañuy wax naan : “Ana lutax faramfànce wu ñu ay laayaam? Yonnentub araab ak làkk wudul araab (nu muy ame)? ” Waxal ne : “njub la ak saafara, ñeel ñi gëm”. Ñi gëmul nag ñoom, ay saañ nekk ci seeni nopp def ngumba ci seeni (gët xel) ; te ñoom na nga leen di woowe ca barab bu sori.
وَلَقَدْ آتَيْنَا مُوسَى الْكِتَابَ فَاخْتُلِفَ فِيهِ ۗ وَلَوْلَا كَلِمَةٌ سَبَقَتْ مِن رَّبِّكَ لَقُضِيَ بَيْنَهُمْ ۚ وَإِنَّهُمْ لَفِي شَكٍّ مِّنْهُ مُرِيبٍ ۝٤٥
📖 Tekki Aaya 45
Joxoon Nanu Muussaa Téere ba. Mu am ñu ca wuute. Bu ca sa kàddug Boroom jiituwul woon, dana fekk ñu àtte woon seen diggënte. Te it ñoom, ñi ngi sikki-sàkka ci ay mbiram.
مَّنْ عَمِلَ صَالِحًا فَلِنَفْسِهِ ۖ وَمَنْ أَسَاءَ فَعَلَيْهَا ۗ وَمَا رَبُّكَ بِظَلَّامٍ لِّلْعَبِيدِ ۝٤٦
📖 Tekki Aaya 46
Képp kuy jëf yiw, boppam la koy defal. Képp kuy jëf ñaawtéef it, te ci kawam lay dal. Sa Boroom, du tooñ, benn jaamam.
۞ إِلَيْهِ يُرَدُّ عِلْمُ السَّاعَةِ ۚ وَمَا تَخْرُجُ مِن ثَمَرَاتٍ مِّنْ أَكْمَامِهَا وَمَا تَحْمِلُ مِنْ أُنثَىٰ وَلَا تَضَعُ إِلَّا بِعِلْمِهِ ۚ وَيَوْمَ يُنَادِيهِمْ أَيْنَ شُرَكَائِي قَالُوا آذَنَّاكَ مَا مِنَّا مِن شَهِيدٍ ۝٤٧
📖 Tekki Aaya 47
Ca moom la xam-xamu Waxtu wa di dellu (moom rekk xam). Amul menn meññat muy génn ciw xottam, amul it jenn jigéen juy ëmbu walla muy imbi lu dul am na ca xam-xam bu mat sëkk. Te bu keroogee bis ba mu leen di woo naan : “Ana ña ngeen ma daan bokkaaleel ? ”, ñu naan ko: “Noo ngi lay birëlal ne kenn seede wu ko ci nun” !
وَضَلَّ عَنْهُم مَّا كَانُوا يَدْعُونَ مِن قَبْلُ ۖ وَظَنُّوا مَا لَهُم مِّن مَّحِيصٍ ۝٤٨
📖 Tekki Aaya 48
Lañu daan jaamu ca àddina réer leen ; ñu daldi xam nag ne amatuñu rawukaay.
لَّا يَسْأَمُ الْإِنسَانُ مِن دُعَاءِ الْخَيْرِ وَإِن مَّسَّهُ الشَّرُّ فَيَئُوسٌ قَنُوطٌ ۝٤٩
📖 Tekki Aaya 49
Nit du bàyyi du yoqat ci di sàkku di ñaan aw yiw. Waaye saa su ko lor dalee, mu di ku yàkki, kuy yoqat.
وَلَئِنْ أَذَقْنَاهُ رَحْمَةً مِّنَّا مِن بَعْدِ ضَرَّاءَ مَسَّتْهُ لَيَقُولَنَّ هَٰذَا لِي وَمَا أَظُنُّ السَّاعَةَ قَائِمَةً وَلَئِن رُّجِعْتُ إِلَىٰ رَبِّي إِنَّ لِي عِندَهُ لَلْحُسْنَىٰ ۚ فَلَنُنَبِّئَنَّ الَّذِينَ كَفَرُوا بِمَا عَمِلُوا وَلَنُذِيقَنَّهُم مِّنْ عَذَابٍ غَلِيظٍ ۝٥٠
📖 Tekki Aaya 50
Saa su nu ko musalee yërmande ju bawoo ci nun, ginnaaw lor ja ko laaloon, muy wax naan : “lii maa ko yayoo ! Te sax fooguma ne saa dana taxaw. Te it su ñu ma delloo ca sama Boroom, li ma fay fekk, mooy dàqati”. Danañu xibaar yéefar ya la ñu daan jëf te dana nu leen musal ci mbugël lu diis gànn (miti).
وَإِذَا أَنْعَمْنَا عَلَى الْإِنسَانِ أَعْرَضَ وَنَأَىٰ بِجَانِبِهِ وَإِذَا مَسَّهُ الشَّرُّ فَذُو دُعَاءٍ عَرِيضٍ ۝٥١
📖 Tekki Aaya 51
Su Nu mayee nit xéewël, mu dumóoyu daldi féew (sori). Waaye saa su ko lor laalee, muy ñaan ñaan yu gudd.
قُلْ أَرَأَيْتُمْ إِن كَانَ مِنْ عِندِ اللَّهِ ثُمَّ كَفَرْتُم بِهِ مَنْ أَضَلُّ مِمَّنْ هُوَ فِي شِقَاقٍ بَعِيدٍ ۝٥٢
📖 Tekki Aaya 52
Waxal ne : “Xanaa gisuleen ? Alxuraan jii ca Yàlla la bawoo ngeen weddi ko ; ana kan moo gën a réer kuy nekk ci teqalikoo gu sore (faasaloo) ? ”
سَنُرِيهِمْ آيَاتِنَا فِي الْآفَاقِ وَفِي أَنفُسِهِمْ حَتَّىٰ يَتَبَيَّنَ لَهُمْ أَنَّهُ الْحَقُّ ۗ أَوَلَمْ يَكْفِ بِرَبِّكَ أَنَّهُ عَلَىٰ كُلِّ شَيْءٍ شَهِيدٌ ۝٥٣
📖 Tekki Aaya 53
Dananu leen won sunuy kéemaan ci déeléey asamaan ak ci seen bopp, ba baa ñuy gindi ku ci xam ne (Alxuraan), mooy dëgg tigi. Xanaa kay war na laa doy rekk ci sa Boroom ne moom seede la ci lépp ?
أَلَا إِنَّهُمْ فِي مِرْيَةٍ مِّن لِّقَاءِ رَبِّهِمْ ۗ أَلَا إِنَّهُ بِكُلِّ شَيْءٍ مُّحِيطٌ ۝٥٤
📖 Tekki Aaya 54
Ñoom xanaa ña ngay sikki-sàkka, ci dajeek seen Boroom ? Te Yàlla moom peeg na lépp lu ne .
← 40 Fussilat (41/114) 42 →
Jàng Simoore Fussilat ci Wolof – Tekki, Waxtaan ak Baat

41فصلت Fussilat 📚 54 Aaya مكية



Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers