Fussilat · 47/54
Tekki Waxtaan — Simoore Fussilat
۞ إِلَيْهِ يُرَدُّ عِلْمُ السَّاعَةِ ۚ وَمَا تَخْرُجُ مِن ثَمَرَاتٍ مِّنْ أَكْمَامِهَا وَمَا تَحْمِلُ مِنْ أُنثَىٰ وَلَا تَضَعُ إِلَّا بِعِلْمِهِ ۚ وَيَوْمَ يُنَادِيهِمْ أَيْنَ شُرَكَائِي قَالُوا آذَنَّاكَ مَا مِنَّا مِن شَهِيدٍ ۝٤٧
Ilaihi yuraddu `ilmus Saaa`ah; wa maa takhruju min samaraatim min akmaamihaa wa maa tahmilu min unsaa wa laa tada`u illaa bi`ilmih; wa Yawma yunaadeehim aina shurakaaa`ee qaalooo aazannaaka maa minnaa min shaheed
📖 Tekkim Wolof
Ca moom la xam-xamu Waxtu wa di dellu (moom rekk xam). Amul menn meññat muy génn ciw xottam, amul it jenn jigéen juy ëmbu walla muy imbi lu dul am na ca xam-xam bu mat sëkk. Te bu keroogee bis ba mu leen di woo naan : “Ana ña ngeen ma daan bokkaaleel ? ”, ñu naan ko: “Noo ngi lay birëlal ne kenn seede wu ko ci nun” !

🎧 Dégg


📜 Aaya 45-49 — Simoore Fussilat

45وَلَقَدْ آتَيْنَا مُوسَى الْكِتَابَ فَاخْتُلِفَ فِيهِ ۗ وَلَوْلَا كَلِمَةٌ سَبَقَتْ مِن رَّبِّكَ لَقُضِيَ بَيْنَهُمْ ۚ وَإِنَّهُمْ لَفِي شَكٍّ مِّنْهُ مُرِيبٍ
Joxoon Nanu Muussaa Téere ba. Mu am ñu ca wuute. Bu ca sa kàddug Boroom jiituwul woon, dana fekk ñu àtte woon seen diggënte. Te it ñoom, ñi ngi sikki-sàkka ci ay mbiram.
46مَّنْ عَمِلَ صَالِحًا فَلِنَفْسِهِ ۖ وَمَنْ أَسَاءَ فَعَلَيْهَا ۗ وَمَا رَبُّكَ بِظَلَّامٍ لِّلْعَبِيدِ
Képp kuy jëf yiw, boppam la koy defal. Képp kuy jëf ñaawtéef it, te ci kawam lay dal. Sa Boroom, du tooñ, benn jaamam.
47۞ إِلَيْهِ يُرَدُّ عِلْمُ السَّاعَةِ ۚ وَمَا تَخْرُجُ مِن ثَمَرَاتٍ مِّنْ أَكْمَامِهَا وَمَا تَحْمِلُ مِنْ أُنثَىٰ وَلَا تَضَعُ إِلَّا بِعِلْمِهِ ۚ وَيَوْمَ يُنَادِيهِمْ أَيْنَ شُرَكَائِي قَالُوا آذَنَّاكَ مَا مِنَّا مِن شَهِيدٍ
Ca moom la xam-xamu Waxtu wa di dellu (moom rekk xam). Amul menn meññat muy génn ciw xottam, amul it jenn jigéen juy ëmbu walla muy imbi lu dul am na ca xam-xam bu mat sëkk. Te bu keroogee bis ba mu leen di woo naan : “Ana ña ngeen ma daan bokkaaleel ? ”, ñu naan ko: “Noo ngi lay birëlal ne kenn seede wu ko ci nun” !
48وَضَلَّ عَنْهُم مَّا كَانُوا يَدْعُونَ مِن قَبْلُ ۖ وَظَنُّوا مَا لَهُم مِّن مَّحِيصٍ
Lañu daan jaamu ca àddina réer leen ; ñu daldi xam nag ne amatuñu rawukaay.
49لَّا يَسْأَمُ الْإِنسَانُ مِن دُعَاءِ الْخَيْرِ وَإِن مَّسَّهُ الشَّرُّ فَيَئُوسٌ قَنُوطٌ
Nit du bàyyi du yoqat ci di sàkku di ñaan aw yiw. Waaye saa su ko lor dalee, mu di ku yàkki, kuy yoqat.
FussilatFihi Alxuraan
54Aaya
MeccanRevelation
47Aaya

Tekki — Fussilat 47

Simoore Fussilat Aaya 47 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Ca moom la xam-xamu Waxtu wa di dellu (moom rekk…

Simoore Aaya 47/54 — Simoore Fussilat فصلت (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Simoore Fussilat Dégg, Simoore Fussilat Tekki, Simoore Fussilat mp3, Simoore Fussilat pdf. Aaya 45–49. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Monday, September 7, 2026

Don't forget us in your sincere prayers