Fussilat · 38/54
Tekki Waxtaan — Fussilat
فَإِنِ اسْتَكْبَرُوا فَالَّذِينَ عِندَ رَبِّكَ يُسَبِّحُونَ لَهُ بِاللَّيْلِ وَالنَّهَارِ وَهُمْ لَا يَسْأَمُونَ ۩ ۝٣٨
Fa inis-takbaroo fallazee na `inda Rabbika yusabbihoona lahoo billaili wannnahaari wa hum laa yas`amoon
📖 Tekkim Wolof
Bu ñu rëy-rëyloo... (ba defuñu ko) Malaaka ya nekk ca sa Boroom ñoom dañuy sàbbaal, guddeek bëccëg, te duñu ko bàyyi !
🎧 Dégg

📜 Aaya 36-40 — Fussilat

36وَإِمَّا يَنزَغَنَّكَ مِنَ الشَّيْطَانِ نَزْغٌ فَاسْتَعِذْ بِاللَّهِ ۖ إِنَّهُ هُوَ السَّمِيعُ الْعَلِيمُ
Amaana leeg-leeg bu la saytaane jaxjaxee (waaye bu boobaa), na nga sàkku ci Yàlla mu mësal la ; Moo di, aji Dégg ja, aji xam ja.
37وَمِنْ آيَاتِهِ اللَّيْلُ وَالنَّهَارُ وَالشَّمْسُ وَالْقَمَرُ ۚ لَا تَسْجُدُوا لِلشَّمْسِ وَلَا لِلْقَمَرِ وَاسْجُدُوا لِلَّهِ الَّذِي خَلَقَهُنَّ إِن كُنتُمْ إِيَّاهُ تَعْبُدُونَ
Bokk na ci ay kéemaanam, guddi ak bëccëg, ak jant beek weer wi : buleen sujuudal jant bi, waxantumalaak weer wi, waaye na ngeen di sujuud ngir Yàlla mi leen bind, ndegam Moom ngeen di jaamu.
38فَإِنِ اسْتَكْبَرُوا فَالَّذِينَ عِندَ رَبِّكَ يُسَبِّحُونَ لَهُ بِاللَّيْلِ وَالنَّهَارِ وَهُمْ لَا يَسْأَمُونَ ۩
Bu ñu rëy-rëyloo... (ba defuñu ko) Malaaka ya nekk ca sa Boroom ñoom dañuy sàbbaal, guddeek bëccëg, te duñu ko bàyyi !
39وَمِنْ آيَاتِهِ أَنَّكَ تَرَى الْأَرْضَ خَاشِعَةً فَإِذَا أَنزَلْنَا عَلَيْهَا الْمَاءَ اهْتَزَّتْ وَرَبَتْ ۚ إِنَّ الَّذِي أَحْيَاهَا لَمُحْيِي الْمَوْتَىٰ ۚ إِنَّهُ عَلَىٰ كُلِّ شَيْءٍ قَدِيرٌ
Bokk na ci Ay kéemaanam ngay gis suuf si mu ne ndàpp (wow koŋŋ). Saa su ñu ci wàccee ndox, mu funki màgg. Ki koy dundal (di ci def gàncax) mooy dekkal ñi dee, Moom man na Lépp lu ne.
40إِنَّ الَّذِينَ يُلْحِدُونَ فِي آيَاتِنَا لَا يَخْفَوْنَ عَلَيْنَا ۗ أَفَمَن يُلْقَىٰ فِي النَّارِ خَيْرٌ أَم مَّن يَأْتِي آمِنًا يَوْمَ الْقِيَامَةِ ۚ اعْمَلُوا مَا شِئْتُمْ ۖ إِنَّهُ بِمَا تَعْمَلُونَ بَصِيرٌ
Ñiy jéem a soppi samay laaya (Alxuraan) manuñu nooraan. Moo ndax ku ñu sànni ca safara moo gën walla kuy dikk bu Bis Pénc baa ànd ak ug wóolu ? Defleen lu leen soob moom kuy gis la li ngeen di def ;
FussilatFihi Alxuraan
54Aaya
MeccanRevelation
38Aaya

Tekki — Fussilat 38

Simoore Fussilat Aaya 38 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Bu ñu rëy-rëyloo... (ba defuñu ko) Malaaka ya nekk ca…

Simoore Aaya 38/54 — Fussilat فصلت (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Fussilat Dégg, Fussilat Tekki, Fussilat mp3, Fussilat pdf. Aaya 36–40. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers