Simoore Ghafir ci Aarabu ak Wolof
Jàng Simoore Ghafir ak tekkim wolof bu mat sëkk, ak baat. Tekki ayaa bu ne. (85 Aaya — مكية). Ghafir Dégg, Ghafir Tekki, Ghafir mp3, Ghafir pdf.Jàng te Dégg Simoore Ghafir
🎧 Aaya
M
Mishary Rashid Alafasy
✓
Mishary Rashid Alafasy
✓
M
Mahmoud Khalil Al-Husary
✓
Mahmoud Khalil Al-Husary
✓
A
Abdurrahman As-Sudais
✓
Abdurrahman As-Sudais
✓
M
Mohamed Siddiq Al-Minshawi
✓
Mohamed Siddiq Al-Minshawi
✓
A
Abdul Basit Abdul Samad
✓
Abdul Basit Abdul Samad
✓
A
Ali Al-Hudhaify
✓
Ali Al-Hudhaify
✓
A
Ahmed ibn Ali al-Ajamy
✓
Ahmed ibn Ali al-Ajamy
✓
A
Abu Bakr Ash-Shaatree
✓
Abu Bakr Ash-Shaatree
✓
M
Muhammad Ayyoub
✓
Muhammad Ayyoub
✓
A
Abdullah Basfar
✓
Abdullah Basfar
✓
A
Abdullah Al-Juhani
✓
Abdullah Al-Juhani
✓
M
Maher Al Muaiqly
✓
Maher Al Muaiqly
✓
—
x1
تَنزِيلُ الْكِتَابِ مِنَ اللَّهِ الْعَزِيزِ الْعَلِيمِ ٢
📖 Tekki
Aaya 2
Wàcceg téere bii ma ngi bawoo ca Yàlla, miy boroom Kàttan, te di ku Xam.
غَافِرِ الذَّنبِ وَقَابِلِ التَّوْبِ شَدِيدِ الْعِقَابِ ذِي الطَّوْلِ ۖ لَا إِلَٰهَ إِلَّا هُوَ ۖ إِلَيْهِ الْمَصِيرُ ٣
📖 Tekki
Aaya 3
Mooy Jéggalkatu bàkkaar yi, di Nanguwaakoonu tuub, di ku Tar mbugël, mooy Boroom xéewal yi. Amul jeneen Yàlla judul Moom te ci Moom la lépp di mujj.
مَا يُجَادِلُ فِي آيَاتِ اللَّهِ إِلَّا الَّذِينَ كَفَرُوا فَلَا يَغْرُرْكَ تَقَلُّبُهُمْ فِي الْبِلَادِ ٤
📖 Tekki
Aaya 4
Kenn du dàggasante ci kàdduy Yàlla ku dul yéefar yi. bu la seeni feem nax.
كَذَّبَتْ قَبْلَهُمْ قَوْمُ نُوحٍ وَالْأَحْزَابُ مِن بَعْدِهِمْ ۖ وَهَمَّتْ كُلُّ أُمَّةٍ بِرَسُولِهِمْ لِيَأْخُذُوهُ ۖ وَجَادَلُوا بِالْبَاطِلِ لِيُدْحِضُوا بِهِ الْحَقَّ فَأَخَذْتُهُمْ ۖ فَكَيْفَ كَانَ عِقَابِ ٥
📖 Tekki
Aaya 5
Nitu Nooh, weddi woon na ñu ca la leen jiitu woon, ak farandoo ya (weddi woon na ñu ñoom itam), xeet wu nekk taqal ab yonnentam. Sànjaafu ko di dàggasante ak moom bëggoon a suufeel dëgg. Mu daldi leen fob (faagaagal leen). Cëy ni ma leen mbugële !
وَكَذَٰلِكَ حَقَّتْ كَلِمَتُ رَبِّكَ عَلَى الَّذِينَ كَفَرُوا أَنَّهُمْ أَصْحَابُ النَّارِ ٦
📖 Tekki
Aaya 6
Noonu it la sa kàddug Boroom yaye ci kaw yéefar yi : “Ñoom ñooy waa Safara”.
الَّذِينَ يَحْمِلُونَ الْعَرْشَ وَمَنْ حَوْلَهُ يُسَبِّحُونَ بِحَمْدِ رَبِّهِمْ وَيُؤْمِنُونَ بِهِ وَيَسْتَغْفِرُونَ لِلَّذِينَ آمَنُوا رَبَّنَا وَسِعْتَ كُلَّ شَيْءٍ رَّحْمَةً وَعِلْمًا فَاغْفِرْ لِلَّذِينَ تَابُوا وَاتَّبَعُوا سَبِيلَكَ وَقِهِمْ عَذَابَ الْجَحِيمِ ٧
📖 Tekki
Aaya 7
Ña yanu Aras ak ña ko wër ña ngay sàbbaal di kañ seen Boroom, di ko gëm tey jéggalu ñi gëm naan ko : “Yaw sunu Boroom ! sa yërmaande yaatu na man a daj ñépp ak sa xam-xam. Kon jéggëlal ña daan tuub tey topp sa yoon wi te nga fegalleen mbugëlu Safara.
رَبَّنَا وَأَدْخِلْهُمْ جَنَّاتِ عَدْنٍ الَّتِي وَعَدتَّهُمْ وَمَن صَلَحَ مِنْ آبَائِهِمْ وَأَزْوَاجِهِمْ وَذُرِّيَّاتِهِمْ ۚ إِنَّكَ أَنتَ الْعَزِيزُ الْحَكِيمُ ٨
📖 Tekki
Aaya 8
Yaw sunu Boroom ! Tàbballeen àjjana Aden ja nga leen digoon, ak képp ku baaxoon ci seeni baay ak i maam, ak seeni soxna ak seeni sët, yaw yaa di boroom Kàttan, di ku Xereñ.
وَقِهِمُ السَّيِّئَاتِ ۚ وَمَن تَقِ السَّيِّئَاتِ يَوْمَئِذٍ فَقَدْ رَحِمْتَهُ ۚ وَذَٰلِكَ هُوَ الْفَوْزُ الْعَظِيمُ ٩
📖 Tekki
Aaya 9
Te nga fegalleen [mbugëlu] ñaawtéef yi. Képp koo fegal [mbugëlum] ñaawtéef, Yërëm nga ko tigi”. Te loolu mooy texe gu mag ga.
إِنَّ الَّذِينَ كَفَرُوا يُنَادَوْنَ لَمَقْتُ اللَّهِ أَكْبَرُ مِن مَّقْتِكُمْ أَنفُسَكُمْ إِذْ تُدْعَوْنَ إِلَى الْإِيمَانِ فَتَكْفُرُونَ ١٠
📖 Tekki
Aaya 10
Ña weddi nag ñoom dañu leen woo naan leen : “jéppig Yàlla moo gën a rëy ni ngeen jéppee seen bopp, ba ñu leen daan woo jëme leen ci ngëm dangeen daan weddi”.
قَالُوا رَبَّنَا أَمَتَّنَا اثْنَتَيْنِ وَأَحْيَيْتَنَا اثْنَتَيْنِ فَاعْتَرَفْنَا بِذُنُوبِنَا فَهَلْ إِلَىٰ خُرُوجٍ مِّن سَبِيلٍ ١١
📖 Tekki
Aaya 11
ñuy wax naan : “Yaw sunu Boroom, rey nga nu ñaari yoon, dundal nga nu ñaari yoon : nangu nanu sunuy bàkkaar. ndax lii man nanu tee génn” ?
ذَٰلِكُم بِأَنَّهُ إِذَا دُعِيَ اللَّهُ وَحْدَهُ كَفَرْتُمْ ۖ وَإِن يُشْرَكْ بِهِ تُؤْمِنُوا ۚ فَالْحُكْمُ لِلَّهِ الْعَلِيِّ الْكَبِيرِ ١٢
📖 Tekki
Aaya 12
“...Amul ndax bu ñu masaan a woo Yàlla doŋŋ ngeen weddi ; bu ñu ko bokkaalewaale ak leneen, ngeen gëm koo. (Tey jii), àtte ba Yàllaa ko yor, moo di ku Kawe, te di ku Màgg”.
هُوَ الَّذِي يُرِيكُمْ آيَاتِهِ وَيُنَزِّلُ لَكُم مِّنَ السَّمَاءِ رِزْقًا ۚ وَمَا يَتَذَكَّرُ إِلَّا مَن يُنِيبُ ١٣
📖 Tekki
Aaya 13
Moo leen di won ay kéemaan, di leen wàcceel ndox, mu bawoo asamaan, ngen di ca xéewlu. Te ñay dellu [ca Yàlla] rekk ay fàttaliku.
فَادْعُوا اللَّهَ مُخْلِصِينَ لَهُ الدِّينَ وَلَوْ كَرِهَ الْكَافِرُونَ ١٤
📖 Tekki
Aaya 14
Ñaanleen Yàlla, te jaamu Ko te sellalal ko diineem, doonte la neexul yéefar yi.
رَفِيعُ الدَّرَجَاتِ ذُو الْعَرْشِ يُلْقِي الرُّوحَ مِنْ أَمْرِهِ عَلَىٰ مَن يَشَاءُ مِنْ عِبَادِهِ لِيُنذِرَ يَوْمَ التَّلَاقِ ١٥
📖 Tekki
Aaya 15
Moo kawey daraja, di Boroom Aras, Mooy sànni ruu ci ndigalam jëme ko ci ku ko soob ci jaamam ñi, ngir muy xuppe ci bisub Daje ba (Bis Pénc ba),
يَوْمَ هُم بَارِزُونَ ۖ لَا يَخْفَىٰ عَلَى اللَّهِ مِنْهُمْ شَيْءٌ ۚ لِّمَنِ الْمُلْكُ الْيَوْمَ ۖ لِلَّهِ الْوَاحِدِ الْقَهَّارِ ١٦
📖 Tekki
Aaya 16
bis ba ñuy feeñ seen dara du man a nëbbu Yàlla. Ana kan mooy boroom nguur gi, bis niki tey ? Yàlla, miy Kenn, di ab Notaakoon.
الْيَوْمَ تُجْزَىٰ كُلُّ نَفْسٍ بِمَا كَسَبَتْ ۚ لَا ظُلْمَ الْيَوْمَ ۚ إِنَّ اللَّهَ سَرِيعُ الْحِسَابِ ١٧
📖 Tekki
Aaya 17
Bis niki tey, bakkan bu nekk dees na ko faye ca la mu daan fàggu. Tooñ amatul, Yàlla ku gaaw ab wàññ la.
وَأَنذِرْهُمْ يَوْمَ الْآزِفَةِ إِذِ الْقُلُوبُ لَدَى الْحَنَاجِرِ كَاظِمِينَ ۚ مَا لِلظَّالِمِينَ مِنْ حَمِيمٍ وَلَا شَفِيعٍ يُطَاعُ ١٨
📖 Tekki
Aaya 18
na nga leen xupp ci bis buy jige si, ba xol yi di nekk ci put yi, (ngir tiit ak njàqare). Te bu boobaa tooñkat yi du ñu fa am xarit, mbaa ku leen di tinu ñu di ko topp.
يَعْلَمُ خَائِنَةَ الْأَعْيُنِ وَمَا تُخْفِي الصُّدُورُ ١٩
📖 Tekki
Aaya 19
Xam na worug ay gët, luy nëbbu ci biir dënn yi.
وَاللَّهُ يَقْضِي بِالْحَقِّ ۖ وَالَّذِينَ يَدْعُونَ مِن دُونِهِ لَا يَقْضُونَ بِشَيْءٍ ۗ إِنَّ اللَّهَ هُوَ السَّمِيعُ الْبَصِيرُ ٢٠
📖 Tekki
Aaya 20
Yàlla mooy àtte ci dëgg, ña ñu koy bokkaaleel du nu àtte dara. Te Yàlla kuy Dégg la, kuy Gis la.
۞ أَوَلَمْ يَسِيرُوا فِي الْأَرْضِ فَيَنظُرُوا كَيْفَ كَانَ عَاقِبَةُ الَّذِينَ كَانُوا مِن قَبْلِهِمْ ۚ كَانُوا هُمْ أَشَدَّ مِنْهُمْ قُوَّةً وَآثَارًا فِي الْأَرْضِ فَأَخَذَهُمُ اللَّهُ بِذُنُوبِهِمْ وَمَا كَانَ لَهُم مِّنَ اللَّهِ مِن وَاقٍ ٢١
📖 Tekki
Aaya 21
Moo ndax da ñoo doxul ci suuf, tey seetlu mujug ña leen fi jiitu woon te ëppoon doole ak i alal ? Yàlla faagaagaloon leen ngir seeni bàkkar. Te kenn manu leen woon fegal mbugëlu Yàlla mii.
ذَٰلِكَ بِأَنَّهُمْ كَانَت تَّأْتِيهِمْ رُسُلُهُم بِالْبَيِّنَاتِ فَكَفَرُوا فَأَخَذَهُمُ اللَّهُ ۚ إِنَّهُ قَوِيٌّ شَدِيدُ الْعِقَابِ ٢٢
📖 Tekki
Aaya 22
Li ko waral, moo di ñoom seeni Yonnent, da ñu leen daan indil ay lay yu leer ñu weddi. Yàlla daldi leen faagaagal, Yàlla boroom doole la di ku Tar mbugël.
وَلَقَدْ أَرْسَلْنَا مُوسَىٰ بِآيَاتِنَا وَسُلْطَانٍ مُّبِينٍ ٢٣
📖 Tekki
Aaya 23
Yónni woon nanu Muusaa ak sunuy laaya boole ko ak ay firnde yu leer,
إِلَىٰ فِرْعَوْنَ وَهَامَانَ وَقَارُونَ فَقَالُوا سَاحِرٌ كَذَّابٌ ٢٤
📖 Tekki
Aaya 24
jëmële ko ca Firawna, ak Haamaana ak Qaaruuna. Ñuy wax naan : “Kii ab njibarkat bu di ! ab fenaakoon la ! ”
فَلَمَّا جَاءَهُم بِالْحَقِّ مِنْ عِندِنَا قَالُوا اقْتُلُوا أَبْنَاءَ الَّذِينَ آمَنُوا مَعَهُ وَاسْتَحْيُوا نِسَاءَهُمْ ۚ وَمَا كَيْدُ الْكَافِرِينَ إِلَّا فِي ضَلَالٍ ٢٥
📖 Tekki
Aaya 25
Ba mu àggee ca ñoom, indi ko baawoo fi Nun da ñoo wax ne : “reyleen doom yu góor ñi gëm ànd ak moom, te bàyyi jigéen ñi ñuy dund”. Pexey yéefar yi du dara lu dul ci ag réer (lay tege).
وَقَالَ فِرْعَوْنُ ذَرُونِي أَقْتُلْ مُوسَىٰ وَلْيَدْعُ رَبَّهُ ۖ إِنِّي أَخَافُ أَن يُبَدِّلَ دِينَكُمْ أَوْ أَن يُظْهِرَ فِي الْأَرْضِ الْفَسَادَ ٢٦
📖 Tekki
Aaya 26
Firawna daldi wax ne : “Bàyyileen ma rey Muusaa. Na woo Boroomam ! Da may ragal mu soppi seen diine walla muy ger nit ñi di yàq réew mi”.
وَقَالَ مُوسَىٰ إِنِّي عُذْتُ بِرَبِّي وَرَبِّكُم مِّن كُلِّ مُتَكَبِّرٍ لَّا يُؤْمِنُ بِيَوْمِ الْحِسَابِ ٢٧
📖 Tekki
Aaya 27
Muusaa [daldi] ne : “Maa ngi sàkku ci sama Boroom mu musal ma ci képp kuy rëy-rëylu, te gëmul bisub wañoo ba (Bis Pénc ba)”.
وَقَالَ رَجُلٌ مُّؤْمِنٌ مِّنْ آلِ فِرْعَوْنَ يَكْتُمُ إِيمَانَهُ أَتَقْتُلُونَ رَجُلًا أَن يَقُولَ رَبِّيَ اللَّهُ وَقَدْ جَاءَكُم بِالْبَيِّنَاتِ مِن رَّبِّكُمْ ۖ وَإِن يَكُ كَاذِبًا فَعَلَيْهِ كَذِبُهُ ۖ وَإِن يَكُ صَادِقًا يُصِبْكُم بَعْضُ الَّذِي يَعِدُكُمْ ۖ إِنَّ اللَّهَ لَا يَهْدِي مَنْ هُوَ مُسْرِفٌ كَذَّابٌ ٢٨
📖 Tekki
Aaya 28
Mu am waaju gëm te bokk ca waa kër Firawna, daldi wax ne : “Ndax dangeen a bëgg rey waa joo xam ne li mu wax lépp moo di ne : “Yàllaay sama Boroom” ? Te indil na leen ay firnde yu bawoo ca Yàlla. Su fekkee day fen, fenam ya du ko moy ; su waxee dëgg, ngeen dor a xam ne li mu leen dig dana dal seen kow”. Te, Yàlla du gindi mukk fenkat buy yàq (waaja da doon nëbbu ngëmam) !
يَا قَوْمِ لَكُمُ الْمُلْكُ الْيَوْمَ ظَاهِرِينَ فِي الْأَرْضِ فَمَن يَنصُرُنَا مِن بَأْسِ اللَّهِ إِن جَاءَنَا ۚ قَالَ فِرْعَوْنُ مَا أُرِيكُمْ إِلَّا مَا أَرَىٰ وَمَا أَهْدِيكُمْ إِلَّا سَبِيلَ الرَّشَادِ ٢٩
📖 Tekki
Aaya 29
“Yéen samaw nit, tey yéen a ngi gore, am lool doole ci kaw suuf si (réew yi). Waaye ana kan moo nuy man a dimbali ci mbugëlum Yàlla su nu digëlee ? ” Firawna daldi ne : “Wanumaleen lu dul li ma gis. Te it duma leen teg fudul ci yoonu njub”.
وَقَالَ الَّذِي آمَنَ يَا قَوْمِ إِنِّي أَخَافُ عَلَيْكُم مِّثْلَ يَوْمِ الْأَحْزَابِ ٣٠
📖 Tekki
Aaya 30
Ka gëmoon daldi waxaat ne : "Yéen samaw nit, ragal naa ci yéen lu mel ni bis ba farandoo ya doon xare.
مِثْلَ دَأْبِ قَوْمِ نُوحٍ وَعَادٍ وَثَمُودَ وَالَّذِينَ مِن بَعْدِهِمْ ۚ وَمَا اللَّهُ يُرِيدُ ظُلْمًا لِّلْعِبَادِ ٣١
📖 Tekki
Aaya 31
Lu melni lëgg-lëggub nitu Nooh, ak Aad ak Samuud, ak ña leen mujjoon”. Te Yàlla bëggul ag tooñ ci jaamam ñi.
وَيَا قَوْمِ إِنِّي أَخَافُ عَلَيْكُمْ يَوْمَ التَّنَادِ ٣٢
📖 Tekki
Aaya 32
“Éy yéen samaw nit, ragal naa ci yéen bisub wootante ba,
يَوْمَ تُوَلُّونَ مُدْبِرِينَ مَا لَكُم مِّنَ اللَّهِ مِنْ عَاصِمٍ ۗ وَمَن يُضْلِلِ اللَّهُ فَمَا لَهُ مِنْ هَادٍ ٣٣
📖 Tekki
Aaya 33
Bis ba ngeen di wane sànku, te dungeen am ku leen di aar ci Yàlla”. ku Yàlla natt ci moom réer, kenn du ko man a gindi.
وَلَقَدْ جَاءَكُمْ يُوسُفُ مِن قَبْلُ بِالْبَيِّنَاتِ فَمَا زِلْتُمْ فِي شَكٍّ مِّمَّا جَاءَكُم بِهِ ۖ حَتَّىٰ إِذَا هَلَكَ قُلْتُمْ لَن يَبْعَثَ اللَّهُ مِن بَعْدِهِ رَسُولًا ۚ كَذَٰلِكَ يُضِلُّ اللَّهُ مَنْ هُوَ مُسْرِفٌ مُّرْتَابٌ ٣٤
📖 Tekki
Aaya 34
“Yuusuf, indaloon na leen ay firnde yu leer naññ, te de ñu leen di sikki-sàkka ca la mu indiwoon. Ba mu faatoo, ngeen wax naan : “Yàlla yónniwaatul beneen Yonnent ginnaawam”. Noonu la Yàlla di réerale ñiy yàq tey sikki-sàkka.
الَّذِينَ يُجَادِلُونَ فِي آيَاتِ اللَّهِ بِغَيْرِ سُلْطَانٍ أَتَاهُمْ ۖ كَبُرَ مَقْتًا عِندَ اللَّهِ وَعِندَ الَّذِينَ آمَنُوا ۚ كَذَٰلِكَ يَطْبَعُ اللَّهُ عَلَىٰ كُلِّ قَلْبِ مُتَكَبِّرٍ جَبَّارٍ ٣٥
📖 Tekki
Aaya 35
Ñiy dàggasante ci laaya Yàlla yi, ci lu àndul ak firnde ju leen digël jéppi gu rëy lay doon ca Yàlla ak ña gëm. Noonu la Yàlla di fatte xolub képp kuy rëy-rëylu di ponkal.
وَقَالَ فِرْعَوْنُ يَا هَامَانُ ابْنِ لِي صَرْحًا لَّعَلِّي أَبْلُغُ الْأَسْبَابَ ٣٦
📖 Tekki
Aaya 36
Firawna wax na ne : "Yaw Haamaan, tabaxal ma ag tóoj : ndax amaana ma man a gis yoon ya,
أَسْبَابَ السَّمَاوَاتِ فَأَطَّلِعَ إِلَىٰ إِلَٰهِ مُوسَىٰ وَإِنِّي لَأَظُنُّهُ كَاذِبًا ۚ وَكَذَٰلِكَ زُيِّنَ لِفِرْعَوْنَ سُوءُ عَمَلِهِ وَصُدَّ عَنِ السَّبِيلِ ۚ وَمَا كَيْدُ فِرْعَوْنَ إِلَّا فِي تَبَابٍ ٣٧
📖 Tekki
Aaya 37
yooni asamaan yi, ndax ma man a yërndu Yàllay Muusaa ; te man sax ay fen laa ko jàppe”. Noonu la Firawna rafetloo jëfëm ju ñaaw joojee ; sorenaak dëgg lool ; te pexem Firawna du lenn lu dul luy naaxsaay.
وَقَالَ الَّذِي آمَنَ يَا قَوْمِ اتَّبِعُونِ أَهْدِكُمْ سَبِيلَ الرَّشَادِ ٣٨
📖 Tekki
Aaya 38
Waa ja gëmoon daldi wax ne : "Yéen samaw nit, toppleen ma. Ma gindileen jëmëleleen ci yoonu njub.
يَا قَوْمِ إِنَّمَا هَٰذِهِ الْحَيَاةُ الدُّنْيَا مَتَاعٌ وَإِنَّ الْآخِرَةَ هِيَ دَارُ الْقَرَارِ ٣٩
📖 Tekki
Aaya 39
Yéen samaw nit, dundug àddina sii diir bu néew la, dundug àllaaxira nag mooy sax.
مَنْ عَمِلَ سَيِّئَةً فَلَا يُجْزَىٰ إِلَّا مِثْلَهَا ۖ وَمَنْ عَمِلَ صَالِحًا مِّن ذَكَرٍ أَوْ أُنثَىٰ وَهُوَ مُؤْمِنٌ فَأُولَٰئِكَ يَدْخُلُونَ الْجَنَّةَ يُرْزَقُونَ فِيهَا بِغَيْرِ حِسَابٍ ٤٠
📖 Tekki
Aaya 40
Képp kuy def ñaawtéef dees na ko fay kem la mu def ; waaye képp kuy def yiw, di góor mbaa muy jigéen, te fekk mu gëm, ñoom ñooy dugg Àjjana di fa jot xéewël yu amul waññ.
۞ وَيَا قَوْمِ مَا لِي أَدْعُوكُمْ إِلَى النَّجَاةِ وَتَدْعُونَنِي إِلَى النَّارِ ٤١
📖 Tekki
Aaya 41
Éy yéen samaw nit, ana lan moo tax ma di leen woo jëme leen ci mucc, te yéen ngeen di ma woo jëmale ma Safara ?
تَدْعُونَنِي لِأَكْفُرَ بِاللَّهِ وَأُشْرِكَ بِهِ مَا لَيْسَ لِي بِهِ عِلْمٌ وَأَنَا أَدْعُوكُمْ إِلَى الْعَزِيزِ الْغَفَّارِ ٤٢
📖 Tekki
Aaya 42
Yéen a ngi may woo ngir ma weddi Yàlla di ko bokkaaleek lu ma amul benn xam-xam, te man maa ngi leen di woo jëme leen ci Yàlla miy boroom Kàttan, tey Jégëlaakoon ba.
لَا جَرَمَ أَنَّمَا تَدْعُونَنِي إِلَيْهِ لَيْسَ لَهُ دَعْوَةٌ فِي الدُّنْيَا وَلَا فِي الْآخِرَةِ وَأَنَّ مَرَدَّنَا إِلَى اللَّهِ وَأَنَّ الْمُسْرِفِينَ هُمْ أَصْحَابُ النَّارِ ٤٣
📖 Tekki
Aaya 43
Sikkuwul ne li ngeen may woo jëmale amuñu luy tax ñu war leen a woo ci àddina sii waxantumaalaak ca àllaaxira. Te it ca Yàlla lañuy dellu, te itam yaqkat ya ñooy wa Safara.
فَسَتَذْكُرُونَ مَا أَقُولُ لَكُمْ ۚ وَأُفَوِّضُ أَمْرِي إِلَى اللَّهِ ۚ إِنَّ اللَّهَ بَصِيرٌ بِالْعِبَادِ ٤٤
📖 Tekki
Aaya 44
Yàggatul ne dangeen fàttaliku ji lii ma leen di wax ; te wéer naa samay mbir ci Yàlla. Ndax, kuy Gis jaamam ñi la.
فَوَقَاهُ اللَّهُ سَيِّئَاتِ مَا مَكَرُوا ۖ وَحَاقَ بِآلِ فِرْعَوْنَ سُوءُ الْعَذَابِ ٤٥
📖 Tekki
Aaya 45
Yàlla fegal na ko ñaawtéef ya ñu doon fexe, daldi sóob njabootug Firwana gën jaa tar i mbugël :
النَّارُ يُعْرَضُونَ عَلَيْهَا غُدُوًّا وَعَشِيًّا ۖ وَيَوْمَ تَقُومُ السَّاعَةُ أَدْخِلُوا آلَ فِرْعَوْنَ أَشَدَّ الْعَذَابِ ٤٦
📖 Tekki
Aaya 46
ñu di leen , gaaral ci Safara suba ak ngoon. Bu Bis Pénc baa (da naa digle) : “Ñu dugël njabootug Firawna ca gën jaa tar i mbugël”.
وَإِذْ يَتَحَاجُّونَ فِي النَّارِ فَيَقُولُ الضُّعَفَاءُ لِلَّذِينَ اسْتَكْبَرُوا إِنَّا كُنَّا لَكُمْ تَبَعًا فَهَلْ أَنتُم مُّغْنُونَ عَنَّا نَصِيبًا مِّنَ النَّارِ ٤٧
📖 Tekki
Aaya 47
Bu keroogee ba ñuy xulóo ci Safara, ña néewoon doole di wax ña ca doon ay kilifa naan leen : “Ca àddina kat yéen la ñu toppoon : kon ndax tey dangeen nu fegal dara ci mbugëlum safara si ? ”
قَالَ الَّذِينَ اسْتَكْبَرُوا إِنَّا كُلٌّ فِيهَا إِنَّ اللَّهَ قَدْ حَكَمَ بَيْنَ الْعِبَادِ ٤٨
📖 Tekki
Aaya 48
Ña ca doon ay kilifa te daan rëy-rëylu daldi ne : “Nun ñépp kat, ñi ngi ci biir Safara”. Ndax Yàlla àtte na diggënte jaam ñi.
وَقَالَ الَّذِينَ فِي النَّارِ لِخَزَنَةِ جَهَنَّمَ ادْعُوا رَبَّكُمْ يُخَفِّفْ عَنَّا يَوْمًا مِّنَ الْعَذَابِ ٤٩
📖 Tekki
Aaya 49
Ña nekk ca biir Safaraa ngay wax ña koy wàttu naan leen : “Ñaanleen seen Boroom mu woyofalal [nu] doonte la sax benn bis lay doon ci mbugël mi”.
قَالُوا أَوَلَمْ تَكُ تَأْتِيكُمْ رُسُلُكُم بِالْبَيِّنَاتِ ۖ قَالُوا بَلَىٰ ۚ قَالُوا فَادْعُوا ۗ وَمَا دُعَاءُ الْكَافِرِينَ إِلَّا فِي ضَلَالٍ ٥٠
📖 Tekki
Aaya 50
Wattukat ya ne leen : “moo ndax, seeni Yonnent indiluñuleen woon ay lay yu leer naññ” ? Ñu ne : “Axakañ” ! Ñu waxaat ne [wattukat ya]: “Kon, ñaanleen” ! Ñaanug yéefar moom ag réer doŋŋ la.
إِنَّا لَنَنصُرُ رُسُلَنَا وَالَّذِينَ آمَنُوا فِي الْحَيَاةِ الدُّنْيَا وَيَوْمَ يَقُومُ الْأَشْهَادُ ٥١
📖 Tekki
Aaya 51
Nun, Yàlla dananu dimbali (jox ndam), Sunuy Yonnent, ak ñi gëm, ci dundug àddina sii ak bu seede ya taxawee (Bis Pénc ba),
يَوْمَ لَا يَنفَعُ الظَّالِمِينَ مَعْذِرَتُهُمْ ۖ وَلَهُمُ اللَّعْنَةُ وَلَهُمْ سُوءُ الدَّارِ ٥٢
📖 Tekki
Aaya 52
bis ba nga xam ne tooñkat ya, seenug doglu ngànt du leen jariñ dara te am rëb dal na leen te it am nañu fa kër gu bon (soof).
وَلَقَدْ آتَيْنَا مُوسَى الْهُدَىٰ وَأَوْرَثْنَا بَنِي إِسْرَائِيلَ الْكِتَابَ ٥٣
📖 Tekki
Aaya 53
Indil Nanu, Muusaa njub, te donale Nanu giiru Banii-Israayiila, Téere ba,
هُدًى وَذِكْرَىٰ لِأُولِي الْأَلْبَابِ ٥٤
📖 Tekki
Aaya 54
mu di njub ak ug fàttali ngir ñu di woroom i xel (di xalaat).
فَاصْبِرْ إِنَّ وَعْدَ اللَّهِ حَقٌّ وَاسْتَغْفِرْ لِذَنبِكَ وَسَبِّحْ بِحَمْدِ رَبِّكَ بِالْعَشِيِّ وَالْإِبْكَارِ ٥٥
📖 Tekki
Aaya 55
Na nga muñ, (te xam ne) digub Yàlla dëgg la, te it na ngay jéggalu say bàkkar tey sàbbaal sa Boroom di ko sant, ci ngoon si ak ci suba si.
إِنَّ الَّذِينَ يُجَادِلُونَ فِي آيَاتِ اللَّهِ بِغَيْرِ سُلْطَانٍ أَتَاهُمْ ۙ إِن فِي صُدُورِهِمْ إِلَّا كِبْرٌ مَّا هُم بِبَالِغِيهِ ۚ فَاسْتَعِذْ بِاللَّهِ ۖ إِنَّهُ هُوَ السَّمِيعُ الْبَصِيرُ ٥٦
📖 Tekki
Aaya 56
Ñay dàggasante ci laayay Yàlla ya ci lu àndul ak firnde yu ñu leen jox, rëy-rëylu doŋŋ a nekk ca seen dënn ya. Te seen aajo du ca fajoo. Na ngay muslu ci Yàlla, moom Mooy aji Dégg, di aji Gis.
لَخَلْقُ السَّمَاوَاتِ وَالْأَرْضِ أَكْبَرُ مِنْ خَلْقِ النَّاسِ وَلَٰكِنَّ أَكْثَرَ النَّاسِ لَا يَعْلَمُونَ ٥٧
📖 Tekki
Aaya 57
Bindug asamaan yeek suuf si moo gën a rëy bindug nit ñi. Waaye li ëpp ci nit ñi xamuñu.
وَمَا يَسْتَوِي الْأَعْمَىٰ وَالْبَصِيرُ وَالَّذِينَ آمَنُوا وَعَمِلُوا الصَّالِحَاتِ وَلَا الْمُسِيءُ ۚ قَلِيلًا مَّا تَتَذَكَّرُونَ ٥٨
📖 Tekki
Aaya 58
Gumba niróowul ak njàccaar, ña gëm tey jëf yiw it niróowuñu ak ñiy def ñaatéef (kenn du leen gam-gamle). Néewaana bu ngeen fàttalikoo !
إِنَّ السَّاعَةَ لَآتِيَةٌ لَّا رَيْبَ فِيهَا وَلَٰكِنَّ أَكْثَرَ النَّاسِ لَا يُؤْمِنُونَ ٥٩
📖 Tekki
Aaya 59
Bis Pénc ba ; Luy dikk la : nàttable amu ca ; waaye li ëpp ci nit ñi gëmu ñu.
وَقَالَ رَبُّكُمُ ادْعُونِي أَسْتَجِبْ لَكُمْ ۚ إِنَّ الَّذِينَ يَسْتَكْبِرُونَ عَنْ عِبَادَتِي سَيَدْخُلُونَ جَهَنَّمَ دَاخِرِينَ ٦٠
📖 Tekki
Aaya 60
Seen Boroom nee na : “Wooleen ma, Ma wuyu leen. Ña nga xam ne, dañoo rëy-rëylu, lànk bañ maa jaamu, danañu dugg Safara ànd ak toroxtaane”.
اللَّهُ الَّذِي جَعَلَ لَكُمُ اللَّيْلَ لِتَسْكُنُوا فِيهِ وَالنَّهَارَ مُبْصِرًا ۚ إِنَّ اللَّهَ لَذُو فَضْلٍ عَلَى النَّاسِ وَلَٰكِنَّ أَكْثَرَ النَّاسِ لَا يَشْكُرُونَ ٦١
📖 Tekki
Aaya 61
Yàlla mi leen defal guddi ngeen di ci dallu, defal leen bëccëg bi it ngeen di ci man a gis (bay fàggu ji). Yàlla boroom Ngënéel la ci kaw nit ñi, waaye li ëpp ci nit ñi duñu sant.
ذَٰلِكُمُ اللَّهُ رَبُّكُمْ خَالِقُ كُلِّ شَيْءٍ لَّا إِلَٰهَ إِلَّا هُوَ ۖ فَأَنَّىٰ تُؤْفَكُونَ ٦٢
📖 Tekki
Aaya 62
Koo ku moo di Yàlla seen Boroom, Moo bind lépp. Amul jeneen Yàlla judul moom. Kon naka ngeen di lajje féew (ca yoonu Yàlla wu jub wa xocc) ?
كَذَٰلِكَ يُؤْفَكُ الَّذِينَ كَانُوا بِآيَاتِ اللَّهِ يَجْحَدُونَ ٦٣
📖 Tekki
Aaya 63
Noonu la ñu daan weddi kàdduy Yàlla di dumóoyoo [yoonu] Yàlla.
اللَّهُ الَّذِي جَعَلَ لَكُمُ الْأَرْضَ قَرَارًا وَالسَّمَاءَ بِنَاءً وَصَوَّرَكُمْ فَأَحْسَنَ صُوَرَكُمْ وَرَزَقَكُم مِّنَ الطَّيِّبَاتِ ۚ ذَٰلِكُمُ اللَّهُ رَبُّكُمْ ۖ فَتَبَارَكَ اللَّهُ رَبُّ الْعَالَمِينَ ٦٤
📖 Tekki
Aaya 64
Yàlla mi leen defal suuf si muy laltaay defal leen asamaan si muy mbaar mu móol leen rafetal seeni melo , - wërsëgal leen ci yu teey yi ! Koo koo di seen Boroom ; Yàlla barkeel na, Moom Miy Boroom àddina si!
هُوَ الْحَيُّ لَا إِلَٰهَ إِلَّا هُوَ فَادْعُوهُ مُخْلِصِينَ لَهُ الدِّينَ ۗ الْحَمْدُ لِلَّهِ رَبِّ الْعَالَمِينَ ٦٥
📖 Tekki
Aaya 65
Mooy kiy dund. Amul jeneen Yàlla judul moom. Na ngeen koy jaamu, te di ko sellal diine ji. Cant ñeel na Yàlla, Miy Boroom àddina si !
۞ قُلْ إِنِّي نُهِيتُ أَنْ أَعْبُدَ الَّذِينَ تَدْعُونَ مِن دُونِ اللَّهِ لَمَّا جَاءَنِيَ الْبَيِّنَاتُ مِن رَّبِّي وَأُمِرْتُ أَنْ أُسْلِمَ لِرَبِّ الْعَالَمِينَ ٦٦
📖 Tekki
Aaya 66
Waxal ne : “Tere na nu ma, may jaamu li ngeen di jaamu te du Yàlla, waxtu wa ma ay lay yu leer nàññ digëlee te bawoo ci sama Boroom, te it digaléef na ma jébël sama bopp Yàlla miy Boroom àddina si”.
هُوَ الَّذِي خَلَقَكُم مِّن تُرَابٍ ثُمَّ مِن نُّطْفَةٍ ثُمَّ مِنْ عَلَقَةٍ ثُمَّ يُخْرِجُكُمْ طِفْلًا ثُمَّ لِتَبْلُغُوا أَشُدَّكُمْ ثُمَّ لِتَكُونُوا شُيُوخًا ۚ وَمِنكُم مَّن يُتَوَفَّىٰ مِن قَبْلُ ۖ وَلِتَبْلُغُوا أَجَلًا مُّسَمًّى وَلَعَلَّكُمْ تَعْقِلُونَ ٦٧
📖 Tekki
Aaya 67
Mooy ki leen bind ci suuf, te jaarale leen ci toqu maniyy, ak ci lumbu deret door leen a génne ngeen di ay xale mu def leen ngeen di ay mag yu war a maggat kumur, - am na ci yéen ñuy faatu balaa loolu lépp di am, - ku ca nekk it am na ab dig bu ñu ko àppal, ak it ngir ngeen xellu (xalaat).
هُوَ الَّذِي يُحْيِي وَيُمِيتُ ۖ فَإِذَا قَضَىٰ أَمْرًا فَإِنَّمَا يَقُولُ لَهُ كُن فَيَكُونُ ٦٨
📖 Tekki
Aaya 68
Mooy dundal mooy rey. saa su dogoo ci mbir, danaan ko : “nekkal”, mu daldi nekk.
أَلَمْ تَرَ إِلَى الَّذِينَ يُجَادِلُونَ فِي آيَاتِ اللَّهِ أَنَّىٰ يُصْرَفُونَ ٦٩
📖 Tekki
Aaya 69
Xanaa gisuloo ñiy dàggasante ci laayay Yàlla yi ni ñu leen di walbatee?
الَّذِينَ كَذَّبُوا بِالْكِتَابِ وَبِمَا أَرْسَلْنَا بِهِ رُسُلَنَا ۖ فَسَوْفَ يَعْلَمُونَ ٧٠
📖 Tekki
Aaya 70
Ñay weddi Téere ba (Alxuraan) ak li nu yónnee sunuy Yonnent ; (waaye) dananu xala xam,
إِذِ الْأَغْلَالُ فِي أَعْنَاقِهِمْ وَالسَّلَاسِلُ يُسْحَبُونَ ٧١
📖 Tekki
Aaya 71
jéng, yaa nga seen doq ñuy gëwéele
فِي الْحَمِيمِ ثُمَّ فِي النَّارِ يُسْجَرُونَ ٧٢
📖 Tekki
Aaya 72
ca biir ndox may wañax; ñu door leen a yóbbu xoyom leen ca Safara.
ثُمَّ قِيلَ لَهُمْ أَيْنَ مَا كُنتُمْ تُشْرِكُونَ ٧٣
📖 Tekki
Aaya 73
Bu loolu jàllee ñu ne leen : “Ana li ngeen daan bokkale
مِن دُونِ اللَّهِ ۖ قَالُوا ضَلُّوا عَنَّا بَل لَّمْ نَكُن نَّدْعُو مِن قَبْلُ شَيْئًا ۚ كَذَٰلِكَ يُضِلُّ اللَّهُ الْكَافِرِينَ ٧٤
📖 Tekki
Aaya 74
bàyyi Yàlla (jaamuwuleen ko) ? ” “Ñu tontu ne, réer nañu. Nun kay, lu jiitu tey, masunoo woo di jaamu dara”. Noonu la Yàlla di sànke yéefar ya.
ذَٰلِكُم بِمَا كُنتُمْ تَفْرَحُونَ فِي الْأَرْضِ بِغَيْرِ الْحَقِّ وَبِمَا كُنتُمْ تَمْرَحُونَ ٧٥
📖 Tekki
Aaya 75
Lii moo di peyug li ngeen daan bég ci suuf si (àddina), te du woon dëgg, ngeen daan ca maare.
ادْخُلُوا أَبْوَابَ جَهَنَّمَ خَالِدِينَ فِيهَا ۖ فَبِئْسَ مَثْوَى الْمُتَكَبِّرِينَ ٧٦
📖 Tekki
Aaya 76
Dugguleen ci wunti Safara te ngeen béel fa. Ña rëy-rëylu woon seenub dëkkuwaay bon na !
فَاصْبِرْ إِنَّ وَعْدَ اللَّهِ حَقٌّ ۚ فَإِمَّا نُرِيَنَّكَ بَعْضَ الَّذِي نَعِدُهُمْ أَوْ نَتَوَفَّيَنَّكَ فَإِلَيْنَا يُرْجَعُونَ ٧٧
📖 Tekki
Aaya 77
Na ngay muñ (te xam ne). Digub Yàlla dëgg la. Amaana Nu wan la lenn ci li Nu leen di tëkkoo mbaa nu faat la (balaa loolu di am)... ak lu man a xew ñoom ñépp ci nun la nuy dellusi.
وَلَقَدْ أَرْسَلْنَا رُسُلًا مِّن قَبْلِكَ مِنْهُم مَّن قَصَصْنَا عَلَيْكَ وَمِنْهُم مَّن لَّمْ نَقْصُصْ عَلَيْكَ ۗ وَمَا كَانَ لِرَسُولٍ أَن يَأْتِيَ بِآيَةٍ إِلَّا بِإِذْنِ اللَّهِ ۚ فَإِذَا جَاءَ أَمْرُ اللَّهِ قُضِيَ بِالْحَقِّ وَخَسِرَ هُنَالِكَ الْمُبْطِلُونَ ٧٨
📖 Tekki
Aaya 78
Yónni woon Nanu ay Yonnent yu la jiitu woon. am na ci ñu ñu la nettali ; am na ci ñu ñu la nettaliwul. Amul benn yonnent bu sañ a indi [kimaan laaya] lu dul ne da ca am ndigëlul Yàlla. Saa su ndigëlul Yàlla agsee, mbir yépp àttewo ci dëgg ; fenkat yi daldi yàqule.
اللَّهُ الَّذِي جَعَلَ لَكُمُ الْأَنْعَامَ لِتَرْكَبُوا مِنْهَا وَمِنْهَا تَأْكُلُونَ ٧٩
📖 Tekki
Aaya 79
Yàlla mi leen defaral mala yi ngir ngeen di ci war te di ca lekk,
وَلَكُمْ فِيهَا مَنَافِعُ وَلِتَبْلُغُوا عَلَيْهَا حَاجَةً فِي صُدُورِكُمْ وَعَلَيْهَا وَعَلَى الْفُلْكِ تُحْمَلُونَ ٨٠
📖 Tekki
Aaya 80
te am ngeen ci ay njariñ ak it ngeen di ca faj ay aajo yu leen soxal. Ngeen di ca yéeg di ànd ak ñoom di war ci gaal yi.
وَيُرِيكُمْ آيَاتِهِ فَأَيَّ آيَاتِ اللَّهِ تُنكِرُونَ ٨١
📖 Tekki
Aaya 81
Mu di leen won ay kéemaanam. Naka ngeen koy weddee ?
أَفَلَمْ يَسِيرُوا فِي الْأَرْضِ فَيَنظُرُوا كَيْفَ كَانَ عَاقِبَةُ الَّذِينَ مِن قَبْلِهِمْ ۚ كَانُوا أَكْثَرَ مِنْهُمْ وَأَشَدَّ قُوَّةً وَآثَارًا فِي الْأَرْضِ فَمَا أَغْنَىٰ عَنْهُم مَّا كَانُوا يَكْسِبُونَ ٨٢
📖 Tekki
Aaya 82
Xanaa du ñu dox ci kaw suuf tey seetlu mujjug xeet ya leen jiitu woon ? ëppoon leen gënoon leen bari doole [ak i jeexit] ci suuf si. Te lañu daan fàggu fegalu leen dara (taxut woon mu doy leen).
فَلَمَّا جَاءَتْهُمْ رُسُلُهُم بِالْبَيِّنَاتِ فَرِحُوا بِمَا عِندَهُم مِّنَ الْعِلْمِ وَحَاقَ بِهِم مَّا كَانُوا بِهِ يَسْتَهْزِئُونَ ٨٣
📖 Tekki
Aaya 83
, Ba seen Yonnent dikkee indil leen ay lay yu leer nàññ, bokk na ca lañu xamoon. Lañu daan ñaawalaatee far sóor leen mujj leen talañ (faagaagal).
فَلَمَّا رَأَوْا بَأْسَنَا قَالُوا آمَنَّا بِاللَّهِ وَحْدَهُ وَكَفَرْنَا بِمَا كُنَّا بِهِ مُشْرِكِينَ ٨٤
📖 Tekki
Aaya 84
Ba ñu gisee Sunu Kàttan, daldi nañuy wax naan : “Yàlla doŋŋ la nu gëm, te weddi na nu la nu ko daan bokkaaleel”.
فَلَمْ يَكُ يَنفَعُهُمْ إِيمَانُهُمْ لَمَّا رَأَوْا بَأْسَنَا ۖ سُنَّتَ اللَّهِ الَّتِي قَدْ خَلَتْ فِي عِبَادِهِ ۖ وَخَسِرَ هُنَالِكَ الْكَافِرُونَ ٨٥
📖 Tekki
Aaya 85
Seen ngëm googee jariñatuleen dara, ba ñu xasee ba gis tiis wa, muy àttey Yàlla ; Kem ni mu ko weyëlee woon ca jaamam ña. Foofee la yéefar ya di yàqulee tigi.
Jàng Simoore Ghafir ci Wolof – Tekki, Waxtaan ak Baat
Alxuraan bu Tedd bi
Tuesday, August 18, 2026
Don't forget us in your sincere prayers

