Fussilat · 28/54
Tekki Waxtaan — Simoore Fussilat
ذَٰلِكَ جَزَاءُ أَعْدَاءِ اللَّهِ النَّارُ ۖ لَهُمْ فِيهَا دَارُ الْخُلْدِ ۖ جَزَاءً بِمَا كَانُوا بِآيَاتِنَا يَجْحَدُونَ ۝٢٨
Zaalika jazaaa`u a`daaa`il laahin Naaru lahum feehaa daarul khuld, jazaaa`am bimaa kaanoo bi aayaatinaa yajhdoon
📖 Tekkim Wolof
Loolu, mooy peyug noonu Yàlla Safara mudi seen kër ga ñuy dëkk béel ca, muy peyug weddi ga ñu daan weddi sunuy laaya.

🎧 Dégg


📜 Aaya 26-30 — Simoore Fussilat

26وَقَالَ الَّذِينَ كَفَرُوا لَا تَسْمَعُوا لِهَٰذَا الْقُرْآنِ وَالْغَوْا فِيهِ لَعَلَّكُمْ تَغْلِبُونَ
Ña weddi ngay wax naan : “Buleen déglu Alxuraan jii, te ngeen koy doyadil (di ko caaxaane) ndax amaana ngeen am ndam”.
27فَلَنُذِيقَنَّ الَّذِينَ كَفَرُوا عَذَابًا شَدِيدًا وَلَنَجْزِيَنَّهُمْ أَسْوَأَ الَّذِي كَانُوا يَعْمَلُونَ
Dananu, mosal ña weddi mbugal mu tar te dananu leen faye la gën a ñaaw ca la ñu daan def.
28ذَٰلِكَ جَزَاءُ أَعْدَاءِ اللَّهِ النَّارُ ۖ لَهُمْ فِيهَا دَارُ الْخُلْدِ ۖ جَزَاءً بِمَا كَانُوا بِآيَاتِنَا يَجْحَدُونَ
Loolu, mooy peyug noonu Yàlla Safara mudi seen kër ga ñuy dëkk béel ca, muy peyug weddi ga ñu daan weddi sunuy laaya.
29وَقَالَ الَّذِينَ كَفَرُوا رَبَّنَا أَرِنَا اللَّذَيْنِ أَضَلَّانَا مِنَ الْجِنِّ وَالْإِنسِ نَجْعَلْهُمَا تَحْتَ أَقْدَامِنَا لِيَكُونَا مِنَ الْأَسْفَلِينَ
Ña daan weddi dañuy wax naan : “Yaw sunu Boroom, wan nu ña nu daan réeräl ci jinne yi ak nit ñi, dananu leen def ci ron sunu ndëguy tànk, ngir nu gën a soofe”.
30إِنَّ الَّذِينَ قَالُوا رَبُّنَا اللَّهُ ثُمَّ اسْتَقَامُوا تَتَنَزَّلُ عَلَيْهِمُ الْمَلَائِكَةُ أَلَّا تَخَافُوا وَلَا تَحْزَنُوا وَأَبْشِرُوا بِالْجَنَّةِ الَّتِي كُنتُمْ تُوعَدُونَ
Ñiy wax naan : “Yàllaay sunu Boroom”, tey jéem a tegu ci seen yoonu Boroom wu jub wa xocc, Malaaka yi dañuy wàcci ci ñoom naan leen. “Buleen jàq buleen ragal ; bégleen ci àjjana ja ñu leen daan dig.
FussilatFihi Alxuraan
54Aaya
MeccanRevelation
28Aaya

Tekki — Fussilat 28

Simoore Fussilat Aaya 28 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Loolu, mooy peyug noonu Yàlla Safara mudi seen kër ga…

Simoore Aaya 28/54 — Simoore Fussilat فصلت (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Simoore Fussilat Dégg, Simoore Fussilat Tekki, Simoore Fussilat mp3, Simoore Fussilat pdf. Aaya 26–30. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, September 8, 2026

Don't forget us in your sincere prayers