Fussilat · 12/54
Tekki Waxtaan — Fussilat
فَقَضَاهُنَّ سَبْعَ سَمَاوَاتٍ فِي يَوْمَيْنِ وَأَوْحَىٰ فِي كُلِّ سَمَاءٍ أَمْرَهَا ۚ وَزَيَّنَّا السَّمَاءَ الدُّنْيَا بِمَصَابِيحَ وَحِفْظًا ۚ ذَٰلِكَ تَقْدِيرُ الْعَزِيزِ الْعَلِيمِ ۝١٢
Faqadaahunna sab`a samaawaatin fee yawmaini wa awhaa fee kulli samaaa`in amarahaa; wa zaiyannassa maaa`ad dunyaa bimasaabeeha wa hifzaa; zaalika taqdeerul `Azeezil `Aleem
📖 Tekkim Wolof
Dogal na ñay juróom-ñaari asamaan ci ñaari fan ci asamaan su ca nekk la muy liggéey. Te taaralal nanu asamaanu àddina si si gën a jige ak i làmp [biddiw] ak di ko sàmm. Loolu mooy Dogalub (Yàlla) kiy boroom Kàttan, di ku Xam.
🎧 Dégg

📜 Aaya 10-14 — Fussilat

10وَجَعَلَ فِيهَا رَوَاسِيَ مِن فَوْقِهَا وَبَارَكَ فِيهَا وَقَدَّرَ فِيهَا أَقْوَاتَهَا فِي أَرْبَعَةِ أَيَّامٍ سَوَاءً لِّلسَّائِلِينَ
Moo poose ay tundi doj ci kawam, def ca barke, (sakkan) mu doxal ca lépp luy yombal luy tax a man a dund ci diirub ñeenti fan. [Mooy tontul] képp ku la koy laaj.
11ثُمَّ اسْتَوَىٰ إِلَى السَّمَاءِ وَهِيَ دُخَانٌ فَقَالَ لَهَا وَلِلْأَرْضِ ائْتِيَا طَوْعًا أَوْ كَرْهًا قَالَتَا أَتَيْنَا طَائِعِينَ
Ba mu éggalee la yemoo ca asamaan muy Saxar mu daldi wax asamaan ak suuf moom Yàlla ne : “Dikkleen, ci bu leen neexee, walla bu leen naqaree”. Ñu tontu ko ne : “Dikk nanu ci sunu coobare”.
12فَقَضَاهُنَّ سَبْعَ سَمَاوَاتٍ فِي يَوْمَيْنِ وَأَوْحَىٰ فِي كُلِّ سَمَاءٍ أَمْرَهَا ۚ وَزَيَّنَّا السَّمَاءَ الدُّنْيَا بِمَصَابِيحَ وَحِفْظًا ۚ ذَٰلِكَ تَقْدِيرُ الْعَزِيزِ الْعَلِيمِ
Dogal na ñay juróom-ñaari asamaan ci ñaari fan ci asamaan su ca nekk la muy liggéey. Te taaralal nanu asamaanu àddina si si gën a jige ak i làmp [biddiw] ak di ko sàmm. Loolu mooy Dogalub (Yàlla) kiy boroom Kàttan, di ku Xam.
13فَإِنْ أَعْرَضُوا فَقُلْ أَنذَرْتُكُمْ صَاعِقَةً مِّثْلَ صَاعِقَةِ عَادٍ وَثَمُودَ
Bu ñu dumóoyoo lànk, waxal ne ; “maa ngi leen di xupp ci ag dënnu dënnu gu melni ga daloon waa Aad ak Samuud”.
14إِذْ جَاءَتْهُمُ الرُّسُلُ مِن بَيْنِ أَيْدِيهِمْ وَمِنْ خَلْفِهِمْ أَلَّا تَعْبُدُوا إِلَّا اللَّهَ ۖ قَالُوا لَوْ شَاءَ رَبُّنَا لَأَنزَلَ مَلَائِكَةً فَإِنَّا بِمَا أُرْسِلْتُم بِهِ كَافِرُونَ
Ba leen yonnenta ya digëlee, bawoo kanam ak ginnaaw, [daan leen digël]: “Ci nuy jaamu Yàlla (ba ña jaamu leneen)”, ñuy wax naan : “Bu neexoon Yàlla, Mu wàcce ay Malaaka. Te sax nun lii ñu leen yónni gëmuñu ko”.
FussilatFihi Alxuraan
54Aaya
MeccanRevelation
12Aaya

Tekki — Fussilat 12

Simoore Fussilat Aaya 12 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Dogal na ñay juróom-ñaari asamaan ci ñaari fan ci asamaan…

Simoore Aaya 12/54 — Fussilat فصلت (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Fussilat Dégg, Fussilat Tekki, Fussilat mp3, Fussilat pdf. Aaya 10–14. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers