Fussilat · 30/54
Tekki Waxtaan — Simoore Fussilat
إِنَّ الَّذِينَ قَالُوا رَبُّنَا اللَّهُ ثُمَّ اسْتَقَامُوا تَتَنَزَّلُ عَلَيْهِمُ الْمَلَائِكَةُ أَلَّا تَخَافُوا وَلَا تَحْزَنُوا وَأَبْشِرُوا بِالْجَنَّةِ الَّتِي كُنتُمْ تُوعَدُونَ ۝٣٠
Innal lazeena qaaloo Rabbunal laahu summas taqaamoo tatanazzalu `alaihimul malaaa `ikatu allaa takhaafoo wa laa tahzanoo wa abshiroo bil Jannnatil latee kuntum too`adoon
📖 Tekkim Wolof
Ñiy wax naan : “Yàllaay sunu Boroom”, tey jéem a tegu ci seen yoonu Boroom wu jub wa xocc, Malaaka yi dañuy wàcci ci ñoom naan leen. “Buleen jàq buleen ragal ; bégleen ci àjjana ja ñu leen daan dig.

M Mishary Rashid Alafasy ✓
M Mahmoud Khalil Al-Husary ✓
A Abdurrahman As-Sudais ✓
M Mohamed Siddiq Al-Minshawi ✓
A Abdul Basit Abdul Samad ✓
A Ali Al-Hudhaify ✓
A Ahmed ibn Ali al-Ajamy ✓
A Abu Bakr Ash-Shaatree ✓
M Muhammad Ayyoub ✓
A Abdullah Basfar ✓
A Abdullah Al-Juhani ✓
M Maher Al Muaiqly ✓
0:00
0:00


📜 Aaya 28-32 — Simoore Fussilat

28ذَٰلِكَ جَزَاءُ أَعْدَاءِ اللَّهِ النَّارُ ۖ لَهُمْ فِيهَا دَارُ الْخُلْدِ ۖ جَزَاءً بِمَا كَانُوا بِآيَاتِنَا يَجْحَدُونَ
Loolu, mooy peyug noonu Yàlla Safara mudi seen kër ga ñuy dëkk béel ca, muy peyug weddi ga ñu daan weddi sunuy laaya.
29وَقَالَ الَّذِينَ كَفَرُوا رَبَّنَا أَرِنَا اللَّذَيْنِ أَضَلَّانَا مِنَ الْجِنِّ وَالْإِنسِ نَجْعَلْهُمَا تَحْتَ أَقْدَامِنَا لِيَكُونَا مِنَ الْأَسْفَلِينَ
Ña daan weddi dañuy wax naan : “Yaw sunu Boroom, wan nu ña nu daan réeräl ci jinne yi ak nit ñi, dananu leen def ci ron sunu ndëguy tànk, ngir nu gën a soofe”.
30إِنَّ الَّذِينَ قَالُوا رَبُّنَا اللَّهُ ثُمَّ اسْتَقَامُوا تَتَنَزَّلُ عَلَيْهِمُ الْمَلَائِكَةُ أَلَّا تَخَافُوا وَلَا تَحْزَنُوا وَأَبْشِرُوا بِالْجَنَّةِ الَّتِي كُنتُمْ تُوعَدُونَ
Ñiy wax naan : “Yàllaay sunu Boroom”, tey jéem a tegu ci seen yoonu Boroom wu jub wa xocc, Malaaka yi dañuy wàcci ci ñoom naan leen. “Buleen jàq buleen ragal ; bégleen ci àjjana ja ñu leen daan dig.
31نَحْنُ أَوْلِيَاؤُكُمْ فِي الْحَيَاةِ الدُّنْيَا وَفِي الْآخِرَةِ ۖ وَلَكُمْ فِيهَا مَا تَشْتَهِي أَنفُسُكُمْ وَلَكُمْ فِيهَا مَا تَدَّعُونَ
Nun (Yàlla) noo di seen wéeruwaay ci àddina di seen wéeruwaay ca àllaaxira ; te am ngeen fa lépp lu seen bakkan di wonnén ak lépp lu ngeen fay laaj,
32نُزُلًا مِّنْ غَفُورٍ رَّحِيمٍ
(wàccuwaayu teraanga) bu bawoo ca Jéggëlekat ba, di ab Jaglewaakoonu yërmande”.
FussilatFihi Alxuraan
54Aaya
MeccanRevelation
30Aaya

Tekki — Fussilat 30

Simoore Fussilat Aaya 30 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Ñiy wax naan : “Yàllaay sunu Boroom”, tey jéem a…

Simoore Aaya 30/54 — Simoore Fussilat فصلت (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Simoore Fussilat Dégg, Simoore Fussilat Tekki, Simoore Fussilat mp3, Simoore Fussilat pdf. Aaya 28–32. Tekkim Wolof: Fulfulde.





Alxuraan bu Tedd bi


Monday, September 28, 2026

Don't forget us in your sincere prayers