Fussilat · 49/54
Tekki Waxtaan — Fussilat
لَّا يَسْأَمُ الْإِنسَانُ مِن دُعَاءِ الْخَيْرِ وَإِن مَّسَّهُ الشَّرُّ فَيَئُوسٌ قَنُوطٌ ۝٤٩
Laa yas`amul insaanu min du`aaa`il khairi wa im massa hush sharru fa ya`oosun qanoot
📖 Tekkim Wolof
Nit du bàyyi du yoqat ci di sàkku di ñaan aw yiw. Waaye saa su ko lor dalee, mu di ku yàkki, kuy yoqat.
🎧 Dégg

📜 Aaya 47-51 — Fussilat

47۞ إِلَيْهِ يُرَدُّ عِلْمُ السَّاعَةِ ۚ وَمَا تَخْرُجُ مِن ثَمَرَاتٍ مِّنْ أَكْمَامِهَا وَمَا تَحْمِلُ مِنْ أُنثَىٰ وَلَا تَضَعُ إِلَّا بِعِلْمِهِ ۚ وَيَوْمَ يُنَادِيهِمْ أَيْنَ شُرَكَائِي قَالُوا آذَنَّاكَ مَا مِنَّا مِن شَهِيدٍ
Ca moom la xam-xamu Waxtu wa di dellu (moom rekk xam). Amul menn meññat muy génn ciw xottam, amul it jenn jigéen juy ëmbu walla muy imbi lu dul am na ca xam-xam bu mat sëkk. Te bu keroogee bis ba mu leen di woo naan : “Ana ña ngeen ma daan bokkaaleel ? ”, ñu naan ko: “Noo ngi lay birëlal ne kenn seede wu ko ci nun” !
48وَضَلَّ عَنْهُم مَّا كَانُوا يَدْعُونَ مِن قَبْلُ ۖ وَظَنُّوا مَا لَهُم مِّن مَّحِيصٍ
Lañu daan jaamu ca àddina réer leen ; ñu daldi xam nag ne amatuñu rawukaay.
49لَّا يَسْأَمُ الْإِنسَانُ مِن دُعَاءِ الْخَيْرِ وَإِن مَّسَّهُ الشَّرُّ فَيَئُوسٌ قَنُوطٌ
Nit du bàyyi du yoqat ci di sàkku di ñaan aw yiw. Waaye saa su ko lor dalee, mu di ku yàkki, kuy yoqat.
50وَلَئِنْ أَذَقْنَاهُ رَحْمَةً مِّنَّا مِن بَعْدِ ضَرَّاءَ مَسَّتْهُ لَيَقُولَنَّ هَٰذَا لِي وَمَا أَظُنُّ السَّاعَةَ قَائِمَةً وَلَئِن رُّجِعْتُ إِلَىٰ رَبِّي إِنَّ لِي عِندَهُ لَلْحُسْنَىٰ ۚ فَلَنُنَبِّئَنَّ الَّذِينَ كَفَرُوا بِمَا عَمِلُوا وَلَنُذِيقَنَّهُم مِّنْ عَذَابٍ غَلِيظٍ
Saa su nu ko musalee yërmande ju bawoo ci nun, ginnaaw lor ja ko laaloon, muy wax naan : “lii maa ko yayoo ! Te sax fooguma ne saa dana taxaw. Te it su ñu ma delloo ca sama Boroom, li ma fay fekk, mooy dàqati”. Danañu xibaar yéefar ya la ñu daan jëf te dana nu leen musal ci mbugël lu diis gànn (miti).
51وَإِذَا أَنْعَمْنَا عَلَى الْإِنسَانِ أَعْرَضَ وَنَأَىٰ بِجَانِبِهِ وَإِذَا مَسَّهُ الشَّرُّ فَذُو دُعَاءٍ عَرِيضٍ
Su Nu mayee nit xéewël, mu dumóoyu daldi féew (sori). Waaye saa su ko lor laalee, muy ñaan ñaan yu gudd.
FussilatFihi Alxuraan
54Aaya
MeccanRevelation
49Aaya

Tekki — Fussilat 49

Simoore Fussilat Aaya 49 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Nit du bàyyi du yoqat ci di sàkku di ñaan…

Simoore Aaya 49/54 — Fussilat فصلت (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Fussilat Dégg, Fussilat Tekki, Fussilat mp3, Fussilat pdf. Aaya 47–51. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers