As-Sajda · 11/30
Tekki Waxtaan — As-Sajda
۞ قُلْ يَتَوَفَّاكُم مَّلَكُ الْمَوْتِ الَّذِي وُكِّلَ بِكُمْ ثُمَّ إِلَىٰ رَبِّكُمْ تُرْجَعُونَ ۝١١
Qul yatawaffaakum malakul mawtil lazee wukkila bikum Thumma ilaa rabbikum turja`oon
📖 Tekkim Wolof
Neel : “Malaakam ndee ma ñu sasee loolu ci yéen moo leen di rey. Su ko defee, ngeen dellu ca seen Boroom”.

🎧 Dégg


📜 Aaya 9-13 — As-Sajda

9ثُمَّ سَوَّاهُ وَنَفَخَ فِيهِ مِن رُّوحِهِ ۖ وَجَعَلَ لَكُمُ السَّمْعَ وَالْأَبْصَارَ وَالْأَفْئِدَةَ ۚ قَلِيلًا مَّا تَشْكُرُونَ
daldi koy yemale, ëf ci Ruuwam. Defaral leen dégg-dégg, ak ub gis ak i xol. Te néewaana ngeen di Ko sant !
10وَقَالُوا أَإِذَا ضَلَلْنَا فِي الْأَرْضِ أَإِنَّا لَفِي خَلْقٍ جَدِيدٍ ۚ بَلْ هُم بِلِقَاءِ رَبِّهِمْ كَافِرُونَ
Ñuy wax naan : “Ndax bu nu seeyee ci biir suuf si, dananu dekkiwaat ? ”. Ñoom dañoo weddi ne danañu dajeek seen Boroom.
11۞ قُلْ يَتَوَفَّاكُم مَّلَكُ الْمَوْتِ الَّذِي وُكِّلَ بِكُمْ ثُمَّ إِلَىٰ رَبِّكُمْ تُرْجَعُونَ
Neel : “Malaakam ndee ma ñu sasee loolu ci yéen moo leen di rey. Su ko defee, ngeen dellu ca seen Boroom”.
12وَلَوْ تَرَىٰ إِذِ الْمُجْرِمُونَ نَاكِسُو رُءُوسِهِمْ عِندَ رَبِّهِمْ رَبَّنَا أَبْصَرْنَا وَسَمِعْنَا فَارْجِعْنَا نَعْمَلْ صَالِحًا إِنَّا مُوقِنُونَ
Cëy soo gisoon, tooñkat yaa ngay jatt seeni loos, naan ! “Yaw sunu Boroom, gis nanu, dégg nanu, delloo nu ca [àddina], kon de nu jëf lu baax ; léegi, xam nanu ne lii lu wóor la”.
13وَلَوْ شِئْنَا لَآتَيْنَا كُلَّ نَفْسٍ هُدَاهَا وَلَٰكِنْ حَقَّ الْقَوْلُ مِنِّي لَأَمْلَأَنَّ جَهَنَّمَ مِنَ الْجِنَّةِ وَالنَّاسِ أَجْمَعِينَ
“Bu Nu sooboon, Dananu indil bakkan bu nekk ag njubam. Waaye dafa fekk ne li Ma wax fàwwu mu am : “Danaa feesal Safara ci nit ak jinne mbooleseen”.
As-SajdaFihi Alxuraan
30Aaya
MeccanRevelation
11Aaya

Tekki — As-Sajda 11

Simoore As-Sajda Aaya 11 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Neel : “Malaakam ndee ma ñu sasee loolu ci yéen…

Simoore Aaya 11/30 — As-Sajda السجدة (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: As-Sajda Dégg, As-Sajda Tekki, As-Sajda mp3, As-Sajda pdf. Aaya 9–13. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers