As-Sajda · 12/30
Tekki Waxtaan — As-Sajda
وَلَوْ تَرَىٰ إِذِ الْمُجْرِمُونَ نَاكِسُو رُءُوسِهِمْ عِندَ رَبِّهِمْ رَبَّنَا أَبْصَرْنَا وَسَمِعْنَا فَارْجِعْنَا نَعْمَلْ صَالِحًا إِنَّا مُوقِنُونَ ۝١٢
Wa law taraaa izil mujrimoona naakisoo ru`oosihim `inda rabbihim rabbanaaa absarnaa wa sami`naa farji`naa na`mal saalihan innaa mooqinoon
📖 Tekkim Wolof
Cëy soo gisoon, tooñkat yaa ngay jatt seeni loos, naan ! “Yaw sunu Boroom, gis nanu, dégg nanu, delloo nu ca [àddina], kon de nu jëf lu baax ; léegi, xam nanu ne lii lu wóor la”.
🎧 Dégg

📜 Aaya 10-14 — As-Sajda

10وَقَالُوا أَإِذَا ضَلَلْنَا فِي الْأَرْضِ أَإِنَّا لَفِي خَلْقٍ جَدِيدٍ ۚ بَلْ هُم بِلِقَاءِ رَبِّهِمْ كَافِرُونَ
Ñuy wax naan : “Ndax bu nu seeyee ci biir suuf si, dananu dekkiwaat ? ”. Ñoom dañoo weddi ne danañu dajeek seen Boroom.
11۞ قُلْ يَتَوَفَّاكُم مَّلَكُ الْمَوْتِ الَّذِي وُكِّلَ بِكُمْ ثُمَّ إِلَىٰ رَبِّكُمْ تُرْجَعُونَ
Neel : “Malaakam ndee ma ñu sasee loolu ci yéen moo leen di rey. Su ko defee, ngeen dellu ca seen Boroom”.
12وَلَوْ تَرَىٰ إِذِ الْمُجْرِمُونَ نَاكِسُو رُءُوسِهِمْ عِندَ رَبِّهِمْ رَبَّنَا أَبْصَرْنَا وَسَمِعْنَا فَارْجِعْنَا نَعْمَلْ صَالِحًا إِنَّا مُوقِنُونَ
Cëy soo gisoon, tooñkat yaa ngay jatt seeni loos, naan ! “Yaw sunu Boroom, gis nanu, dégg nanu, delloo nu ca [àddina], kon de nu jëf lu baax ; léegi, xam nanu ne lii lu wóor la”.
13وَلَوْ شِئْنَا لَآتَيْنَا كُلَّ نَفْسٍ هُدَاهَا وَلَٰكِنْ حَقَّ الْقَوْلُ مِنِّي لَأَمْلَأَنَّ جَهَنَّمَ مِنَ الْجِنَّةِ وَالنَّاسِ أَجْمَعِينَ
“Bu Nu sooboon, Dananu indil bakkan bu nekk ag njubam. Waaye dafa fekk ne li Ma wax fàwwu mu am : “Danaa feesal Safara ci nit ak jinne mbooleseen”.
14فَذُوقُوا بِمَا نَسِيتُمْ لِقَاءَ يَوْمِكُمْ هَٰذَا إِنَّا نَسِينَاكُمْ ۖ وَذُوقُوا عَذَابَ الْخُلْدِ بِمَا كُنتُمْ تَعْمَلُونَ
“Kon mosleen ci li ngeen fàtte woon seen dajeek Bis bii. Dananu leen fàtte-fàttelu. Toqamtikuleen mbugal muy sax dàkk, muy peyug la ngeen daan def”.
As-SajdaFihi Alxuraan
30Aaya
MeccanRevelation
12Aaya

Tekki — As-Sajda 12

Simoore As-Sajda Aaya 12 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Cëy soo gisoon, tooñkat yaa ngay jatt seeni loos, naan…

Simoore Aaya 12/30 — As-Sajda السجدة (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: As-Sajda Dégg, As-Sajda Tekki, As-Sajda mp3, As-Sajda pdf. Aaya 10–14. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers