As-Sajda · 16/30
Tekki Waxtaan — As-Sajda
تَتَجَافَىٰ جُنُوبُهُمْ عَنِ الْمَضَاجِعِ يَدْعُونَ رَبَّهُمْ خَوْفًا وَطَمَعًا وَمِمَّا رَزَقْنَاهُمْ يُنفِقُونَ ۝١٦
Tatajaafaa junoobuhum `anil madaaji`i yad`oona rabbahum khawfanw wa tama`anw wa mimmaa razaqnaahum yunfiqoon
📖 Tekkim Wolof
Dañuy fojjatiku ca seen tëddukaay ya [lal ya], di ñaan seen Boroom ci ragal ak xemmem ; te di joxe ca la Nu leen wërsëgal.

🎧 Dégg


📜 Aaya 14-18 — As-Sajda

14فَذُوقُوا بِمَا نَسِيتُمْ لِقَاءَ يَوْمِكُمْ هَٰذَا إِنَّا نَسِينَاكُمْ ۖ وَذُوقُوا عَذَابَ الْخُلْدِ بِمَا كُنتُمْ تَعْمَلُونَ
“Kon mosleen ci li ngeen fàtte woon seen dajeek Bis bii. Dananu leen fàtte-fàttelu. Toqamtikuleen mbugal muy sax dàkk, muy peyug la ngeen daan def”.
15إِنَّمَا يُؤْمِنُ بِآيَاتِنَا الَّذِينَ إِذَا ذُكِّرُوا بِهَا خَرُّوا سُجَّدًا وَسَبَّحُوا بِحَمْدِ رَبِّهِمْ وَهُمْ لَا يَسْتَكْبِرُونَ ۩
Ñii gëm Sunuy kàddu, ñoom ñi nga xam ne saa su Nu leen ko fàttalee, dañuy rot di sujjóot, di sàbbaal, di kañ ak a sant seen Boroom, ñoom duñu rëy-rëylu.
16تَتَجَافَىٰ جُنُوبُهُمْ عَنِ الْمَضَاجِعِ يَدْعُونَ رَبَّهُمْ خَوْفًا وَطَمَعًا وَمِمَّا رَزَقْنَاهُمْ يُنفِقُونَ
Dañuy fojjatiku ca seen tëddukaay ya [lal ya], di ñaan seen Boroom ci ragal ak xemmem ; te di joxe ca la Nu leen wërsëgal.
17فَلَا تَعْلَمُ نَفْسٌ مَّا أُخْفِيَ لَهُم مِّن قُرَّةِ أَعْيُنٍ جَزَاءً بِمَا كَانُوا يَعْمَلُونَ
Benn bakkan xamul la ñu koy xala deñcal ci yuy neex ci bët, muy peyug la mu daan def !
18أَفَمَن كَانَ مُؤْمِنًا كَمَن كَانَ فَاسِقًا ۚ لَّا يَسْتَوُونَ
Moo ndax ku gëm dina mel ni ab saay-saay ? [mukk], duñu mës a yem.
As-SajdaFihi Alxuraan
30Aaya
MeccanRevelation
16Aaya

Tekki — As-Sajda 16

Simoore As-Sajda Aaya 16 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Dañuy fojjatiku ca seen tëddukaay ya [lal ya], di ñaan…

Simoore Aaya 16/30 — As-Sajda السجدة (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: As-Sajda Dégg, As-Sajda Tekki, As-Sajda mp3, As-Sajda pdf. Aaya 14–18. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers