As-Sajda · 20/30
Tekki Waxtaan — As-Sajda
وَأَمَّا الَّذِينَ فَسَقُوا فَمَأْوَاهُمُ النَّارُ ۖ كُلَّمَا أَرَادُوا أَن يَخْرُجُوا مِنْهَا أُعِيدُوا فِيهَا وَقِيلَ لَهُمْ ذُوقُوا عَذَابَ النَّارِ الَّذِي كُنتُم بِهِ تُكَذِّبُونَ ۝٢٠
Wa ammal lazeena fasaqoo famaawaahumn Naaru kullamaaa araadooo any yakhrujoo minhaaa u`eedoo feehaa wa qeela lahum zooqoo `zaaaban Naaril lazee kuntum bihee tukazziboon
📖 Tekkim Wolof
Ña saay-saayoon, ñoom Safaraa di seen kër : saa su ñu ca bëggee génn, ñu delloo leen ca, te naan leen : “Toqamtikuleen mbugalum Safara sa ngeen daan weddi”.
🎧 Dégg

📜 Aaya 18-22 — As-Sajda

18أَفَمَن كَانَ مُؤْمِنًا كَمَن كَانَ فَاسِقًا ۚ لَّا يَسْتَوُونَ
Moo ndax ku gëm dina mel ni ab saay-saay ? [mukk], duñu mës a yem.
19أَمَّا الَّذِينَ آمَنُوا وَعَمِلُوا الصَّالِحَاتِ فَلَهُمْ جَنَّاتُ الْمَأْوَىٰ نُزُلًا بِمَا كَانُوا يَعْمَلُونَ
Ña gëmoon tey jëf u yiw, am nañu ay dër ca Àjjana, muy seen wàccuwaay ngir la ñu daan jëf.
20وَأَمَّا الَّذِينَ فَسَقُوا فَمَأْوَاهُمُ النَّارُ ۖ كُلَّمَا أَرَادُوا أَن يَخْرُجُوا مِنْهَا أُعِيدُوا فِيهَا وَقِيلَ لَهُمْ ذُوقُوا عَذَابَ النَّارِ الَّذِي كُنتُم بِهِ تُكَذِّبُونَ
Ña saay-saayoon, ñoom Safaraa di seen kër : saa su ñu ca bëggee génn, ñu delloo leen ca, te naan leen : “Toqamtikuleen mbugalum Safara sa ngeen daan weddi”.
21وَلَنُذِيقَنَّهُم مِّنَ الْعَذَابِ الْأَدْنَىٰ دُونَ الْعَذَابِ الْأَكْبَرِ لَعَلَّهُمْ يَرْجِعُونَ
Dananu leen ñamal ci àdduna [takkandeerub mbugalum àllaaxira] ndax ñu mën a dellu ca yoon wu jub wa !
22وَمَنْ أَظْلَمُ مِمَّن ذُكِّرَ بِآيَاتِ رَبِّهِ ثُمَّ أَعْرَضَ عَنْهَا ۚ إِنَّا مِنَ الْمُجْرِمِينَ مُنتَقِمُونَ
Ana kan moo gën a tooñ ka nga xam ne, saa su ñu ko fàttalee laayay Boroomam, mu dummóoyu ko ? Dananu feyyu ci tooñkat yi.
As-SajdaFihi Alxuraan
30Aaya
MeccanRevelation
20Aaya

Tekki — As-Sajda 20

Simoore As-Sajda Aaya 20 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Ña saay-saayoon, ñoom Safaraa di seen kër : saa su…

Simoore Aaya 20/30 — As-Sajda السجدة (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: As-Sajda Dégg, As-Sajda Tekki, As-Sajda mp3, As-Sajda pdf. Aaya 18–22. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers