As-Sajda · 18/30
Tekki Waxtaan — Simoore As-Sajda
أَفَمَن كَانَ مُؤْمِنًا كَمَن كَانَ فَاسِقًا ۚ لَّا يَسْتَوُونَ ۝١٨
Afaman kaana mu`minan kaman kaana faasiqaa; laa yasta woon
📖 Tekkim Wolof
Moo ndax ku gëm dina mel ni ab saay-saay ? [mukk], duñu mës a yem.

🎧 Dégg


📜 Aaya 16-20 — Simoore As-Sajda

16تَتَجَافَىٰ جُنُوبُهُمْ عَنِ الْمَضَاجِعِ يَدْعُونَ رَبَّهُمْ خَوْفًا وَطَمَعًا وَمِمَّا رَزَقْنَاهُمْ يُنفِقُونَ
Dañuy fojjatiku ca seen tëddukaay ya [lal ya], di ñaan seen Boroom ci ragal ak xemmem ; te di joxe ca la Nu leen wërsëgal.
17فَلَا تَعْلَمُ نَفْسٌ مَّا أُخْفِيَ لَهُم مِّن قُرَّةِ أَعْيُنٍ جَزَاءً بِمَا كَانُوا يَعْمَلُونَ
Benn bakkan xamul la ñu koy xala deñcal ci yuy neex ci bët, muy peyug la mu daan def !
18أَفَمَن كَانَ مُؤْمِنًا كَمَن كَانَ فَاسِقًا ۚ لَّا يَسْتَوُونَ
Moo ndax ku gëm dina mel ni ab saay-saay ? [mukk], duñu mës a yem.
19أَمَّا الَّذِينَ آمَنُوا وَعَمِلُوا الصَّالِحَاتِ فَلَهُمْ جَنَّاتُ الْمَأْوَىٰ نُزُلًا بِمَا كَانُوا يَعْمَلُونَ
Ña gëmoon tey jëf u yiw, am nañu ay dër ca Àjjana, muy seen wàccuwaay ngir la ñu daan jëf.
20وَأَمَّا الَّذِينَ فَسَقُوا فَمَأْوَاهُمُ النَّارُ ۖ كُلَّمَا أَرَادُوا أَن يَخْرُجُوا مِنْهَا أُعِيدُوا فِيهَا وَقِيلَ لَهُمْ ذُوقُوا عَذَابَ النَّارِ الَّذِي كُنتُم بِهِ تُكَذِّبُونَ
Ña saay-saayoon, ñoom Safaraa di seen kër : saa su ñu ca bëggee génn, ñu delloo leen ca, te naan leen : “Toqamtikuleen mbugalum Safara sa ngeen daan weddi”.
As-SajdaFihi Alxuraan
30Aaya
MeccanRevelation
18Aaya

Tekki — As-Sajda 18

Simoore As-Sajda Aaya 18 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Moo ndax ku gëm dina mel ni ab saay-saay ?…

Simoore Aaya 18/30 — Simoore As-Sajda السجدة (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Simoore As-Sajda Dégg, Simoore As-Sajda Tekki, Simoore As-Sajda mp3, Simoore As-Sajda pdf. Aaya 16–20. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Monday, September 7, 2026

Don't forget us in your sincere prayers