As-Sajda · 10/30
Tekki Waxtaan — Simoore As-Sajda
وَقَالُوا أَإِذَا ضَلَلْنَا فِي الْأَرْضِ أَإِنَّا لَفِي خَلْقٍ جَدِيدٍ ۚ بَلْ هُم بِلِقَاءِ رَبِّهِمْ كَافِرُونَ ۝١٠
Wa qaalooo `a-izaa dalalnaa fil ardi `a-innaa lafee khalqin jadeed; bal hum biliqaaa`i rabbihim kaafirroon
📖 Tekkim Wolof
Ñuy wax naan : “Ndax bu nu seeyee ci biir suuf si, dananu dekkiwaat ? ”. Ñoom dañoo weddi ne danañu dajeek seen Boroom.

🎧 Dégg


📜 Aaya 8-12 — Simoore As-Sajda

8ثُمَّ جَعَلَ نَسْلَهُ مِن سُلَالَةٍ مِّن مَّاءٍ مَّهِينٍ
daldi nay defe askanam wa mu càllaloo ci am ndox mu doyadi;
9ثُمَّ سَوَّاهُ وَنَفَخَ فِيهِ مِن رُّوحِهِ ۖ وَجَعَلَ لَكُمُ السَّمْعَ وَالْأَبْصَارَ وَالْأَفْئِدَةَ ۚ قَلِيلًا مَّا تَشْكُرُونَ
daldi koy yemale, ëf ci Ruuwam. Defaral leen dégg-dégg, ak ub gis ak i xol. Te néewaana ngeen di Ko sant !
10وَقَالُوا أَإِذَا ضَلَلْنَا فِي الْأَرْضِ أَإِنَّا لَفِي خَلْقٍ جَدِيدٍ ۚ بَلْ هُم بِلِقَاءِ رَبِّهِمْ كَافِرُونَ
Ñuy wax naan : “Ndax bu nu seeyee ci biir suuf si, dananu dekkiwaat ? ”. Ñoom dañoo weddi ne danañu dajeek seen Boroom.
11۞ قُلْ يَتَوَفَّاكُم مَّلَكُ الْمَوْتِ الَّذِي وُكِّلَ بِكُمْ ثُمَّ إِلَىٰ رَبِّكُمْ تُرْجَعُونَ
Neel : “Malaakam ndee ma ñu sasee loolu ci yéen moo leen di rey. Su ko defee, ngeen dellu ca seen Boroom”.
12وَلَوْ تَرَىٰ إِذِ الْمُجْرِمُونَ نَاكِسُو رُءُوسِهِمْ عِندَ رَبِّهِمْ رَبَّنَا أَبْصَرْنَا وَسَمِعْنَا فَارْجِعْنَا نَعْمَلْ صَالِحًا إِنَّا مُوقِنُونَ
Cëy soo gisoon, tooñkat yaa ngay jatt seeni loos, naan ! “Yaw sunu Boroom, gis nanu, dégg nanu, delloo nu ca [àddina], kon de nu jëf lu baax ; léegi, xam nanu ne lii lu wóor la”.
As-SajdaFihi Alxuraan
30Aaya
MeccanRevelation
10Aaya

Tekki — As-Sajda 10

Simoore As-Sajda Aaya 10 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Ñuy wax naan : “Ndax bu nu seeyee ci biir…

Simoore Aaya 10/30 — Simoore As-Sajda السجدة (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Simoore As-Sajda Dégg, Simoore As-Sajda Tekki, Simoore As-Sajda mp3, Simoore As-Sajda pdf. Aaya 8–12. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, September 8, 2026

Don't forget us in your sincere prayers