PDF —
30 Aaya Meccan PDF
Built right in your browser — download starts automatically

Simoore As-Sajda pdf — Wàcce (Wolof)

Simoore As-Sajda pdf Wolof — Wàcce Simoore As-Sajda Tekki. Simoore As-Sajda (Meccan) 30 Aaya.

← LuqmanSimoore As-Sajda Al-Ahzab →


30 Aaya · Meccan · Wolof
bismillah
ﭑﭒ
32:1 Aliif, Laam, Miim.
ﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛ
32:2 Wàcceg Téere bii [Alxuraan], sikk nekku ca, mu bawoo ca Boroom àddina sépp.
ﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯ
32:3 Walla dañu naan [Muhammad] moo ko sos ? [Déedéet, lii mooy dëgg ga bawoo ci sa Boroom ngir nga xupp ci aw nit ñoo xam ne bi nga laataa ñëw, amuñu woon xuppekat, te amaana ñu gindiku.
ﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊ
32:4 Yàlla mi bind asamaan yeek suuf si ak li nekk ci seen diggante ci diirub juróom-benni fan. Daldi yemoo ca Gàngunaay ga [Aras]. Amuleen benn wéeruwaay walla rammukat bu dul Moom. Moo ndax dangeen dul fàttaliku ?
ﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜ
32:5 Mooy settantal [lijjanti] mbir yi, jële ko asamaan jëme ko ci suuf si, topp mu yéeg asamaan ci bis boo xam ne ab nattaleem junni la ci ay ati àddina.
ﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣ
32:6 Kooka mooy xamkatu kumpa ak li feeñ, mooy Boroom Kàttan, di Jaglewaakoonu yërmaandeem,
ﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯ
32:7 Moo jekkal sosug lu ne. Daldi door sosug nit ci ban,
ﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙ
32:8 daldi nay defe askanam wa mu càllaloo ci am ndox mu doyadi;
ﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪ
32:9 daldi koy yemale, ëf ci Ruuwam. Defaral leen dégg-dégg, ak ub gis ak i xol. Te néewaana ngeen di Ko sant !
ﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺ
32:10 Ñuy wax naan : “Ndax bu nu seeyee ci biir suuf si, dananu dekkiwaat ? ”. Ñoom dañoo weddi ne danañu dajeek seen Boroom.
ﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆﰇ
32:11 Neel : “Malaakam ndee ma ñu sasee loolu ci yéen moo leen di rey. Su ko defee, ngeen dellu ca seen Boroom”.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡ
32:12 Cëy soo gisoon, tooñkat yaa ngay jatt seeni loos, naan ! “Yaw sunu Boroom, gis nanu, dégg nanu, delloo nu ca [àddina], kon de nu jëf lu baax ; léegi, xam nanu ne lii lu wóor la”.
ﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲ
32:13 “Bu Nu sooboon, Dananu indil bakkan bu nekk ag njubam. Waaye dafa fekk ne li Ma wax fàwwu mu am : “Danaa feesal Safara ci nit ak jinne mbooleseen”.
ﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂ
32:14 “Kon mosleen ci li ngeen fàtte woon seen dajeek Bis bii. Dananu leen fàtte-fàttelu. Toqamtikuleen mbugal muy sax dàkk, muy peyug la ngeen daan def”.
ﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓ
32:15 Ñii gëm Sunuy kàddu, ñoom ñi nga xam ne saa su Nu leen ko fàttalee, dañuy rot di sujjóot, di sàbbaal, di kañ ak a sant seen Boroom, ñoom duñu rëy-rëylu.
ﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟ
32:16 Dañuy fojjatiku ca seen tëddukaay ya [lal ya], di ñaan seen Boroom ci ragal ak xemmem ; te di joxe ca la Nu leen wërsëgal.
ﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭ
32:17 Benn bakkan xamul la ñu koy xala deñcal ci yuy neex ci bët, muy peyug la mu daan def !
ﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘ
32:18 Moo ndax ku gëm dina mel ni ab saay-saay ? [mukk], duñu mës a yem.
ﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥ
32:19 Ña gëmoon tey jëf u yiw, am nañu ay dër ca Àjjana, muy seen wàccuwaay ngir la ñu daan jëf.
ﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼ
32:20 Ña saay-saayoon, ñoom Safaraa di seen kër : saa su ñu ca bëggee génn, ñu delloo leen ca, te naan leen : “Toqamtikuleen mbugalum Safara sa ngeen daan weddi”.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚ
32:21 Dananu leen ñamal ci àdduna [takkandeerub mbugalum àllaaxira] ndax ñu mën a dellu ca yoon wu jub wa !
ﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩ
32:22 Ana kan moo gën a tooñ ka nga xam ne, saa su ñu ko fàttalee laayay Boroomam, mu dummóoyu ko ? Dananu feyyu ci tooñkat yi.
ﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹ
32:23 Joxoon Nanu Muusaa Téere ba - bul am xel-yaar ci dajeek moom [yaw Muhammad] -, te defoon Nanu Téere ba mu di njub ñeel Bani-Israayiila gépp.
ﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅ
32:24 Defoon Nanu ci ñoom ay njiit yuy gindee ci Sunu ndigal, waxtu wa ñu muñee te wóolu Sunuy laaya [kàddu].
ﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑ
32:25 Sa Boroom ci boppam dana àtte seen diggante ca la ñu daan wuute.
ﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦ
32:26 Ndax dafa doyul ci ñoom gindiku, te faagaalaloon Nanu ay maas ya leen jiitu woon te tey ñi ngi dox ci seen génti kër yi ? Ay kéemaan nekk na ci biir loolu ! Ndax ñoom dañu dul dégg ?
ﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚ
32:27 Xanaa dañoo gisul ñoom ci ne Man Yàlla maay wàcce ndox ci kaw suuf su wow, génne gàncax gu seeni jur di lekk ak ñoom it ñu di ca lekk ? Moo ndax ñoom dañu dul gis ?
ﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢ
32:28 Ñangay laaj naan : “Lii kañ lay doon, ndegam wax ngeen dëgg ? ”.
ﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮ
32:29 Waxal ne : “Bis ba ndam la di ñëw, ngëmug yéefar yi dootuleen jariñati dara ! Te kenn duleen négandiku”.
ﯯﯰﯱﯲﯳﯴ
32:30 Dummóoyuleen te xaar. Ñoom it ñi ngi xaar.

Alxuraan bu Tedd bi


Wednesday, September 9, 2026

Don't forget us in your sincere prayers