As-Sajda · 22/30
Tekki Waxtaan — As-Sajda
وَمَنْ أَظْلَمُ مِمَّن ذُكِّرَ بِآيَاتِ رَبِّهِ ثُمَّ أَعْرَضَ عَنْهَا ۚ إِنَّا مِنَ الْمُجْرِمِينَ مُنتَقِمُونَ ۝٢٢
Wa man azlamu mimman zukkira bi aayaati rabbihee summa a`rada `anhaa; innaa minal mujrimeena muntaqimmon
📖 Tekkim Wolof
Ana kan moo gën a tooñ ka nga xam ne, saa su ñu ko fàttalee laayay Boroomam, mu dummóoyu ko ? Dananu feyyu ci tooñkat yi.

🎧 Dégg


📜 Aaya 20-24 — As-Sajda

20وَأَمَّا الَّذِينَ فَسَقُوا فَمَأْوَاهُمُ النَّارُ ۖ كُلَّمَا أَرَادُوا أَن يَخْرُجُوا مِنْهَا أُعِيدُوا فِيهَا وَقِيلَ لَهُمْ ذُوقُوا عَذَابَ النَّارِ الَّذِي كُنتُم بِهِ تُكَذِّبُونَ
Ña saay-saayoon, ñoom Safaraa di seen kër : saa su ñu ca bëggee génn, ñu delloo leen ca, te naan leen : “Toqamtikuleen mbugalum Safara sa ngeen daan weddi”.
21وَلَنُذِيقَنَّهُم مِّنَ الْعَذَابِ الْأَدْنَىٰ دُونَ الْعَذَابِ الْأَكْبَرِ لَعَلَّهُمْ يَرْجِعُونَ
Dananu leen ñamal ci àdduna [takkandeerub mbugalum àllaaxira] ndax ñu mën a dellu ca yoon wu jub wa !
22وَمَنْ أَظْلَمُ مِمَّن ذُكِّرَ بِآيَاتِ رَبِّهِ ثُمَّ أَعْرَضَ عَنْهَا ۚ إِنَّا مِنَ الْمُجْرِمِينَ مُنتَقِمُونَ
Ana kan moo gën a tooñ ka nga xam ne, saa su ñu ko fàttalee laayay Boroomam, mu dummóoyu ko ? Dananu feyyu ci tooñkat yi.
23وَلَقَدْ آتَيْنَا مُوسَى الْكِتَابَ فَلَا تَكُن فِي مِرْيَةٍ مِّن لِّقَائِهِ ۖ وَجَعَلْنَاهُ هُدًى لِّبَنِي إِسْرَائِيلَ
Joxoon Nanu Muusaa Téere ba - bul am xel-yaar ci dajeek moom [yaw Muhammad] -, te defoon Nanu Téere ba mu di njub ñeel Bani-Israayiila gépp.
24وَجَعَلْنَا مِنْهُمْ أَئِمَّةً يَهْدُونَ بِأَمْرِنَا لَمَّا صَبَرُوا ۖ وَكَانُوا بِآيَاتِنَا يُوقِنُونَ
Defoon Nanu ci ñoom ay njiit yuy gindee ci Sunu ndigal, waxtu wa ñu muñee te wóolu Sunuy laaya [kàddu].
As-SajdaFihi Alxuraan
30Aaya
MeccanRevelation
22Aaya

Tekki — As-Sajda 22

Simoore As-Sajda Aaya 22 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Ana kan moo gën a tooñ ka nga xam ne,…

Simoore Aaya 22/30 — As-Sajda السجدة (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: As-Sajda Dégg, As-Sajda Tekki, As-Sajda mp3, As-Sajda pdf. Aaya 20–24. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers