As-Sajda · 14/30
Tekki Waxtaan — As-Sajda
فَذُوقُوا بِمَا نَسِيتُمْ لِقَاءَ يَوْمِكُمْ هَٰذَا إِنَّا نَسِينَاكُمْ ۖ وَذُوقُوا عَذَابَ الْخُلْدِ بِمَا كُنتُمْ تَعْمَلُونَ ۝١٤
Fazooqoo bimaa naseetum liqaaa`a yawminkum haaza innaa naseenaakum wa zooqoo `azaabal khuldi bimaa kuntum ta`maloon
📖 Tekkim Wolof
“Kon mosleen ci li ngeen fàtte woon seen dajeek Bis bii. Dananu leen fàtte-fàttelu. Toqamtikuleen mbugal muy sax dàkk, muy peyug la ngeen daan def”.

🎧 Dégg


📜 Aaya 12-16 — As-Sajda

12وَلَوْ تَرَىٰ إِذِ الْمُجْرِمُونَ نَاكِسُو رُءُوسِهِمْ عِندَ رَبِّهِمْ رَبَّنَا أَبْصَرْنَا وَسَمِعْنَا فَارْجِعْنَا نَعْمَلْ صَالِحًا إِنَّا مُوقِنُونَ
Cëy soo gisoon, tooñkat yaa ngay jatt seeni loos, naan ! “Yaw sunu Boroom, gis nanu, dégg nanu, delloo nu ca [àddina], kon de nu jëf lu baax ; léegi, xam nanu ne lii lu wóor la”.
13وَلَوْ شِئْنَا لَآتَيْنَا كُلَّ نَفْسٍ هُدَاهَا وَلَٰكِنْ حَقَّ الْقَوْلُ مِنِّي لَأَمْلَأَنَّ جَهَنَّمَ مِنَ الْجِنَّةِ وَالنَّاسِ أَجْمَعِينَ
“Bu Nu sooboon, Dananu indil bakkan bu nekk ag njubam. Waaye dafa fekk ne li Ma wax fàwwu mu am : “Danaa feesal Safara ci nit ak jinne mbooleseen”.
14فَذُوقُوا بِمَا نَسِيتُمْ لِقَاءَ يَوْمِكُمْ هَٰذَا إِنَّا نَسِينَاكُمْ ۖ وَذُوقُوا عَذَابَ الْخُلْدِ بِمَا كُنتُمْ تَعْمَلُونَ
“Kon mosleen ci li ngeen fàtte woon seen dajeek Bis bii. Dananu leen fàtte-fàttelu. Toqamtikuleen mbugal muy sax dàkk, muy peyug la ngeen daan def”.
15إِنَّمَا يُؤْمِنُ بِآيَاتِنَا الَّذِينَ إِذَا ذُكِّرُوا بِهَا خَرُّوا سُجَّدًا وَسَبَّحُوا بِحَمْدِ رَبِّهِمْ وَهُمْ لَا يَسْتَكْبِرُونَ ۩
Ñii gëm Sunuy kàddu, ñoom ñi nga xam ne saa su Nu leen ko fàttalee, dañuy rot di sujjóot, di sàbbaal, di kañ ak a sant seen Boroom, ñoom duñu rëy-rëylu.
16تَتَجَافَىٰ جُنُوبُهُمْ عَنِ الْمَضَاجِعِ يَدْعُونَ رَبَّهُمْ خَوْفًا وَطَمَعًا وَمِمَّا رَزَقْنَاهُمْ يُنفِقُونَ
Dañuy fojjatiku ca seen tëddukaay ya [lal ya], di ñaan seen Boroom ci ragal ak xemmem ; te di joxe ca la Nu leen wërsëgal.
As-SajdaFihi Alxuraan
30Aaya
MeccanRevelation
14Aaya

Tekki — As-Sajda 14

Simoore As-Sajda Aaya 14 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : “Kon mosleen ci li ngeen fàtte woon seen dajeek Bis…

Simoore Aaya 14/30 — As-Sajda السجدة (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: As-Sajda Dégg, As-Sajda Tekki, As-Sajda mp3, As-Sajda pdf. Aaya 12–16. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers