Simoore Al-Qalam ci Aarabu ak Wolof

Jàng Simoore Al-Qalam ak tekkim wolof bu mat sëkk, ak baat. Tekki ayaa bu ne. (52 Aaya — مكية). Al-Qalam Dégg, Al-Qalam Tekki, Al-Qalam mp3, Al-Qalam pdf.

Jàng te Dégg Simoore Al-Qalam

🎧 Aaya
M Mishary Rashid Alafasy
M Mahmoud Khalil Al-Husary
A Abdurrahman As-Sudais
M Mohamed Siddiq Al-Minshawi
A Abdul Basit Abdul Samad
A Ali Al-Hudhaify
A Ahmed ibn Ali al-Ajamy
A Abu Bakr Ash-Shaatree
M Muhammad Ayyoub
A Abdullah Basfar
A Abdullah Al-Juhani
M Maher Al Muaiqly
x1
ن ۚ وَالْقَلَمِ وَمَا يَسْطُرُونَ ۝١
📖 Tekki Aaya 1
Nuun. Ak Xalima ga ak la ñuy bind !
مَا أَنتَ بِنِعْمَةِ رَبِّكَ بِمَجْنُونٍ ۝٢
📖 Tekki Aaya 2
Sa xéewali Boroom (yaw Muhammad), tax na ba dofoo.
وَإِنَّ لَكَ لَأَجْرًا غَيْرَ مَمْنُونٍ ۝٣
📖 Tekki Aaya 3
Te itam, am nga pey gu dootul dog.
وَإِنَّكَ لَعَلَىٰ خُلُقٍ عَظِيمٍ ۝٤
📖 Tekki Aaya 4
Te yaa ngi làmboo, ak jikko yu màgg.
فَسَتُبْصِرُ وَيُبْصِرُونَ ۝٥
📖 Tekki Aaya 5
Danga gis ñoom it danañu gis.
بِأَييِّكُمُ الْمَفْتُونُ ۝٦
📖 Tekki Aaya 6
Ana kan ci yéen moo sànku.
إِنَّ رَبَّكَ هُوَ أَعْلَمُ بِمَن ضَلَّ عَن سَبِيلِهِ وَهُوَ أَعْلَمُ بِالْمُهْتَدِينَ ۝٧
📖 Tekki Aaya 7
Te sa Boroom moo gën a xam ku réere aw Yoonam, te it moo gën a xam ñay gindiku.
فَلَا تُطِعِ الْمُكَذِّبِينَ ۝٨
📖 Tekki Aaya 8
Bul topp mukk ñiy fen,
وَدُّوا لَوْ تُدْهِنُ فَيُدْهِنُونَ ۝٩
📖 Tekki Aaya 9
Bëgg nañu nga nooy ba ñu nooy ñoom itam.
وَلَا تُطِعْ كُلَّ حَلَّافٍ مَّهِينٍ ۝١٠
📖 Tekki Aaya 10
Bul topp bépp waatkat, bu doyadi,
هَمَّازٍ مَّشَّاءٍ بِنَمِيمٍ ۝١١
📖 Tekki Aaya 11
ab saagakat, buy dox di rambaaje,
مَّنَّاعٍ لِّلْخَيْرِ مُعْتَدٍ أَثِيمٍ ۝١٢
📖 Tekki Aaya 12
buy tere aw yiw, tey jalgati, di def bàkkaar,
عُتُلٍّ بَعْدَ ذَٰلِكَ زَنِيمٍ ۝١٣
📖 Tekki Aaya 13
ak ku jàgg, te bariw ay.
أَن كَانَ ذَا مَالٍ وَبَنِينَ ۝١٤
📖 Tekki Aaya 14
Mu nekk di boroom alal ak i doom.
إِذَا تُتْلَىٰ عَلَيْهِ آيَاتُنَا قَالَ أَسَاطِيرُ الْأَوَّلِينَ ۝١٥
📖 Tekki Aaya 15
Saa su ñu jàngee fi kanamam Sunuy Laaya, muy wax naan : “Léebi ñu jëkk ña la”.
سَنَسِمُهُ عَلَى الْخُرْطُومِ ۝١٦
📖 Tekki Aaya 16
Dananu ko wutal màndarga ci suku [bakkanam].
إِنَّا بَلَوْنَاهُمْ كَمَا بَلَوْنَا أَصْحَابَ الْجَنَّةِ إِذْ أَقْسَمُوا لَيَصْرِمُنَّهَا مُصْبِحِينَ ۝١٧
📖 Tekki Aaya 17
Natu nanu leen kom ni nu nattuwoon woroom tool ya ba ñu diisóo ne ba ñu xëy góob ko,
وَلَا يَسْتَثْنُونَ ۝١٨
📖 Tekki Aaya 18
te settee wu ñu woon : “Dogalub Yàlla”.
فَطَافَ عَلَيْهَا طَائِفٌ مِّن رَّبِّكَ وَهُمْ نَائِمُونَ ۝١٩
📖 Tekki Aaya 19
Mu am lu bawoo fa sa Boroom dikk wër si ko (faagaagal tool ba) fekk ñoom nelaw nañu,
فَأَصْبَحَتْ كَالصَّرِيمِ ۝٢٠
📖 Tekki Aaya 20
ba bët setee, mu melni luñu déqi.
فَتَنَادَوْا مُصْبِحِينَ ۝٢١
📖 Tekki Aaya 21
Ba ñu xëy, wootante ca suba cuuy :
أَنِ اغْدُوا عَلَىٰ حَرْثِكُمْ إِن كُنتُمْ صَارِمِينَ ۝٢٢
📖 Tekki Aaya 22
“Daldi ne teel leen xëy tool waay ndegam da ngeen bëgg góob”.
فَانطَلَقُوا وَهُمْ يَتَخَافَتُونَ ۝٢٣
📖 Tekki Aaya 23
Ña ngay làkk, ca tool ya di déeyante :
أَن لَّا يَدْخُلَنَّهَا الْيَوْمَ عَلَيْكُم مِّسْكِينٌ ۝٢٤
📖 Tekki Aaya 24
Tey wax naan : “Tey jii buleen seetaan benn miskin di dugg ci tool yi”.
وَغَدَوْا عَلَىٰ حَرْدٍ قَادِرِينَ ۝٢٥
📖 Tekki Aaya 25
Ñu xëy njortu ne, man nañoo tere tool ya.
فَلَمَّا رَأَوْهَا قَالُوا إِنَّا لَضَالُّونَ ۝٢٦
📖 Tekki Aaya 26
Ba ñu ne gegg, ca tool ya ( mu melni peroŋ) : ñu ne : “nun xanaa da noo gëlam,
بَلْ نَحْنُ مَحْرُومُونَ ۝٢٧
📖 Tekki Aaya 27
Ñu ne moom la kat waaye li wóor moo di ne su nu muur jeex na ci”.
قَالَ أَوْسَطُهُمْ أَلَمْ أَقُل لَّكُمْ لَوْلَا تُسَبِّحُونَ ۝٢٨
📖 Tekki Aaya 28
Ka ca gën a yiw ne leen : “Ndax nee wu ma leen : Ngeen di sàbbaal seen Boroom di ko kañ ! ”
قَالُوا سُبْحَانَ رَبِّنَا إِنَّا كُنَّا ظَالِمِينَ ۝٢٩
📖 Tekki Aaya 29
Ñu daldi ne : “Tudd nanu selluk sunu Boroom ! Nun dey, ay tooñkat lanu woon”.
فَأَقْبَلَ بَعْضُهُمْ عَلَىٰ بَعْضٍ يَتَلَاوَمُونَ ۝٣٠
📖 Tekki Aaya 30
Ku nekk dëgmal morom ja, ñuy yeddante.
قَالُوا يَا وَيْلَنَا إِنَّا كُنَّا طَاغِينَ ۝٣١
📖 Tekki Aaya 31
Ñuy wax naan : “Ngalla ! Nun danoo bew.
عَسَىٰ رَبُّنَا أَن يُبْدِلَنَا خَيْرًا مِّنْهَا إِنَّا إِلَىٰ رَبِّنَا رَاغِبُونَ ۝٣٢
📖 Tekki Aaya 32
Aka neexoon Yàlla nangu sunu tuub wuutalal nu ko ak tool yu ko gën. Sunu Boroom la nu xemmem”.
كَذَٰلِكَ الْعَذَابُ ۖ وَلَعَذَابُ الْآخِرَةِ أَكْبَرُ ۚ لَوْ كَانُوا يَعْلَمُونَ ۝٣٣
📖 Tekki Aaya 33
Noonu la mbugal ma deme woon ; te mbugalum àllaaxira maay gëna rëy, cëy bu ñu xamoon !
إِنَّ لِلْمُتَّقِينَ عِندَ رَبِّهِمْ جَنَّاتِ النَّعِيمِ ۝٣٤
📖 Tekki Aaya 34
Ña ragal Yàlla dey ñoom am nanu Àjjanay xéewal fa seen Boroom.
أَفَنَجْعَلُ الْمُسْلِمِينَ كَالْمُجْرِمِينَ ۝٣٥
📖 Tekki Aaya 35
Moo ndax danuy def ñi wommatu jëm ci [Yàlla] ñu yem ak tooñkat ya ?
مَا لَكُمْ كَيْفَ تَحْكُمُونَ ۝٣٦
📖 Tekki Aaya 36
Ana lan moo leen dal ? Ak naka ngeen di àttee ?
أَمْ لَكُمْ كِتَابٌ فِيهِ تَدْرُسُونَ ۝٣٧
📖 Tekki Aaya 37
Wala book da ngeen am ab Téere bu ngeen di jàng
إِنَّ لَكُمْ فِيهِ لَمَا تَخَيَّرُونَ ۝٣٨
📖 Tekki Aaya 38
boo xam ne daal li ngeen bëgg lépp ngi ci ?
أَمْ لَكُمْ أَيْمَانٌ عَلَيْنَا بَالِغَةٌ إِلَىٰ يَوْمِ الْقِيَامَةِ ۙ إِنَّ لَكُمْ لَمَا تَحْكُمُونَ ۝٣٩
📖 Tekki Aaya 39
Wala book da ngeen am sunu ngiñ luy law ba àllaaxira, Mu defal leen fa lu ngeen bëgg ?
سَلْهُمْ أَيُّهُم بِذَٰلِكَ زَعِيمٌ ۝٤٠
📖 Tekki Aaya 40
Laajleen baxam ana kan ci ñoom mooy pakk wi ?
أَمْ لَهُمْ شُرَكَاءُ فَلْيَأْتُوا بِشُرَكَائِهِمْ إِن كَانُوا صَادِقِينَ ۝٤١
📖 Tekki Aaya 41
Wala dañoo am ñu ñuy bokkaale ? Kon, nañu indi seen bokkaale ndegam nu dëggu la nu !
يَوْمَ يُكْشَفُ عَن سَاقٍ وَيُدْعَوْنَ إِلَى السُّجُودِ فَلَا يَسْتَطِيعُونَ ۝٤٢
📖 Tekki Aaya 42
Bu keroogee ba ñuy wuññi ab yeel [tiitaange] nu def leen woo ngir ñu Sujud te du ñu ko man.
خَاشِعَةً أَبْصَارُهُمْ تَرْهَقُهُمْ ذِلَّةٌ ۖ وَقَدْ كَانُوا يُدْعَوْنَ إِلَى السُّجُودِ وَهُمْ سَالِمُونَ ۝٤٣
📖 Tekki Aaya 43
Ñuy xiin-xiini ne muq ak gàcce te kat ba ca ba ñuy dund daayees na léen woo ngir ñuy sujood (jullig) te booba dara dalut léen.
فَذَرْنِي وَمَن يُكَذِّبُ بِهَٰذَا الْحَدِيثِ ۖ سَنَسْتَدْرِجُهُم مِّنْ حَيْثُ لَا يَعْلَمُونَ ۝٤٤
📖 Tekki Aaya 44
Bàyyee ma ak ñiy jàppe waxtaan wii ( Alxuraan) ay fen dina nu léen taxañe fu ñu dul xam.
وَأُمْلِي لَهُمْ ۚ إِنَّ كَيْدِي مَتِينٌ ۝٤٥
📖 Tekki Aaya 45
Dama léen di dënniirlu waaye sama pexe naaxsaay.
أَمْ تَسْأَلُهُمْ أَجْرًا فَهُم مِّن مَّغْرَمٍ مُّثْقَلُونَ ۝٤٦
📖 Tekki Aaya 46
Moo ndax da nga léen di laaj ag pey te ñu fees dell ak i bor.
أَمْ عِندَهُمُ الْغَيْبُ فَهُمْ يَكْتُبُونَ ۝٤٧
📖 Tekki Aaya 47
Wala dañoo xam mbóot ba di ko bind.
فَاصْبِرْ لِحُكْمِ رَبِّكَ وَلَا تَكُن كَصَاحِبِ الْحُوتِ إِذْ نَادَىٰ وَهُوَ مَكْظُومٌ ۝٤٨
📖 Tekki Aaya 48
Na ngay muñ lépp luy tukkee ci sa àtteb boroom te bul mel ni ka jën wa wannoon (Yonnent Yàlla Yuunus AS) ba muy boroomam te tiitoon lool.
لَّوْلَا أَن تَدَارَكَهُ نِعْمَةٌ مِّن رَّبِّهِ لَنُبِذَ بِالْعَرَاءِ وَهُوَ مَذْمُومٌ ۝٤٩
📖 Tekki Aaya 49
Dogankonak wallug boroomam dees na ko sànni ca tàkk ga mu ne tócc.
فَاجْتَبَاهُ رَبُّهُ فَجَعَلَهُ مِنَ الصَّالِحِينَ ۝٥٠
📖 Tekki Aaya 50
Yàlla daldi ko tànn boole ko nit ñu yiwe ña.
وَإِن يَكَادُ الَّذِينَ كَفَرُوا لَيُزْلِقُونَكَ بِأَبْصَارِهِمْ لَمَّا سَمِعُوا الذِّكْرَ وَيَقُولُونَ إِنَّهُ لَمَجْنُونٌ ۝٥١
📖 Tekki Aaya 51
Ña weddi saayu ñu déggée (Alxuraan) dina ñu lay xawa xeelu te naan kii ab dof la kat.
وَمَا هُوَ إِلَّا ذِكْرٌ لِّلْعَالَمِينَ ۝٥٢
📖 Tekki Aaya 52
(Alxuraan) du lenn lu dul (ab téeré ) buy fàttali bindéef yi.
← 67 Al-Qalam (68/114) 69 →
Jàng Simoore Al-Qalam ci Wolof – Tekki, Waxtaan ak Baat

68القلم Al-Qalam 📚 52 Aaya مكية



Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers