Simoore Nuh ci Aarabu ak Wolof

Jàng Simoore Nuh ak tekkim wolof bu mat sëkk, ak baat. Tekki ayaa bu ne. (28 Aaya — مكية). Nuh Dégg, Nuh Tekki, Nuh mp3, Nuh pdf.

Jàng te Dégg Simoore Nuh

🎧 Aaya
M Mishary Rashid Alafasy
M Mahmoud Khalil Al-Husary
A Abdurrahman As-Sudais
M Mohamed Siddiq Al-Minshawi
A Abdul Basit Abdul Samad
A Ali Al-Hudhaify
A Ahmed ibn Ali al-Ajamy
A Abu Bakr Ash-Shaatree
M Muhammad Ayyoub
A Abdullah Basfar
A Abdullah Al-Juhani
M Maher Al Muaiqly
x1
إِنَّا أَرْسَلْنَا نُوحًا إِلَىٰ قَوْمِهِ أَنْ أَنذِرْ قَوْمَكَ مِن قَبْلِ أَن يَأْتِيَهُمْ عَذَابٌ أَلِيمٌ ۝١
📖 Tekki Aaya 1
Noo yónni woon Nooh ca aw nitam ne ko : “Xupal saw nit, bala leen mbugal mu mettee dikkël”.
قَالَ يَا قَوْمِ إِنِّي لَكُمْ نَذِيرٌ مُّبِينٌ ۝٢
📖 Tekki Aaya 2
Mu daldi ne : "Éy seen samaw nit, man mii ab xuppekat laa ci yéen bu bir,
أَنِ اعْبُدُوا اللَّهَ وَاتَّقُوهُ وَأَطِيعُونِ ۝٣
📖 Tekki Aaya 3
Na ngeen jaamu Yàlla, te ragal ko, te topp ko
يَغْفِرْ لَكُم مِّن ذُنُوبِكُمْ وَيُؤَخِّرْكُمْ إِلَىٰ أَجَلٍ مُّسَمًّى ۚ إِنَّ أَجَلَ اللَّهِ إِذَا جَاءَ لَا يُؤَخَّرُ ۖ لَوْ كُنتُمْ تَعْلَمُونَ ۝٤
📖 Tekki Aaya 4
kon dey Dana leen jégël seeni bàkkaar te Dana leen yeexe ba ci dig bu ñu xam. Digub Yàlla bu agsee, du fanqu cëy bu ngeen xamoon ! ”
قَالَ رَبِّ إِنِّي دَعَوْتُ قَوْمِي لَيْلًا وَنَهَارًا ۝٥
📖 Tekki Aaya 5
(Nooh) : “Yaw sama Boroom ! woo naa samaw nit, guddeek bëcëg.
فَلَمْ يَزِدْهُمْ دُعَائِي إِلَّا فِرَارًا ۝٦
📖 Tekki Aaya 6
Te sama woote bi dolli wu leen lu dul féew.
وَإِنِّي كُلَّمَا دَعَوْتُهُمْ لِتَغْفِرَ لَهُمْ جَعَلُوا أَصَابِعَهُمْ فِي آذَانِهِمْ وَاسْتَغْشَوْا ثِيَابَهُمْ وَأَصَرُّوا وَاسْتَكْبَرُوا اسْتِكْبَارًا ۝٧
📖 Tekki Aaya 7
Te man saasu ma leen di woo ngir Nga jégël leen, dañuy def séeni waaraam ci séeni biiri nopp, daldi muuroo séeni sér, daldi jomlu.
ثُمَّ إِنِّي دَعَوْتُهُمْ جِهَارًا ۝٨
📖 Tekki Aaya 8
Topp, woonaa leen cig jooru.
ثُمَّ إِنِّي أَعْلَنتُ لَهُمْ وَأَسْرَرْتُ لَهُمْ إِسْرَارًا ۝٩
📖 Tekki Aaya 9
Topp, biralalnaa leen, yalolnaa leen.
فَقُلْتُ اسْتَغْفِرُوا رَبَّكُمْ إِنَّهُ كَانَ غَفَّارًا ۝١٠
📖 Tekki Aaya 10
Ma wax leen ne : “Jégëluleen seen Boroom, Moom dey Jégëlaakoon la,
يُرْسِلِ السَّمَاءَ عَلَيْكُم مِّدْرَارًا ۝١١
📖 Tekki Aaya 11
kon dey dana yabal asamaan si, mu duttil leen taw,
وَيُمْدِدْكُم بِأَمْوَالٍ وَبَنِينَ وَيَجْعَل لَّكُمْ جَنَّاتٍ وَيَجْعَل لَّكُمْ أَنْهَارًا ۝١٢
📖 Tekki Aaya 12
te it dana leen may ay alal ak i doom, te dana leen defal tooli dër ak ay dex.
مَّا لَكُمْ لَا تَرْجُونَ لِلَّهِ وَقَارًا ۝١٣
📖 Tekki Aaya 13
Ana lu leen dal ba du ngeen delloo Yàlla njukël,
وَقَدْ خَلَقَكُمْ أَطْوَارًا ۝١٤
📖 Tekki Aaya 14
te moom moo leen jaarale ci ay tolluwaay yu bari ba mu leen di sàkk ?
أَلَمْ تَرَوْا كَيْفَ خَلَقَ اللَّهُ سَبْعَ سَمَاوَاتٍ طِبَاقًا ۝١٥
📖 Tekki Aaya 15
Xanaa gisu leen ni Yàlla binde juróom-ñaari asamaan yu tegaloo
وَجَعَلَ الْقَمَرَ فِيهِنَّ نُورًا وَجَعَلَ الشَّمْسَ سِرَاجًا ۝١٦
📖 Tekki Aaya 16
mu def ci weer wi muy leer, mu def it jant bi mu di làmpu ?
وَاللَّهُ أَنبَتَكُم مِّنَ الْأَرْضِ نَبَاتًا ۝١٧
📖 Tekki Aaya 17
Te Yàllaa leen saxal, ci suuf si, ni gàncax,
ثُمَّ يُعِيدُكُمْ فِيهَا وَيُخْرِجُكُمْ إِخْرَاجًا ۝١٨
📖 Tekki Aaya 18
te dana leen ca delloo dana leen ca génneewaat.
وَاللَّهُ جَعَلَ لَكُمُ الْأَرْضَ بِسَاطًا ۝١٩
📖 Tekki Aaya 19
Yàlla moo leen defaral suuf si mu di laltaay,
لِّتَسْلُكُوا مِنْهَا سُبُلًا فِجَاجًا ۝٢٠
📖 Tekki Aaya 20
ngir ngeen mana sóobu ca yoonam yu dàndante ya”.
قَالَ نُوحٌ رَّبِّ إِنَّهُمْ عَصَوْنِي وَاتَّبَعُوا مَن لَّمْ يَزِدْهُ مَالُهُ وَوَلَدُهُ إِلَّا خَسَارًا ۝٢١
📖 Tekki Aaya 21
Nooh daldi wax ne : “Yaw sama Boroom, (samaw nit) moy na ñu ma dem toppi koo xam ne alalam ak i doomam jariñu ko lu dul yàqule.
وَمَكَرُوا مَكْرًا كُبَّارًا ۝٢٢
📖 Tekki Aaya 22
Ña ngay fexe pexe yu rëy,
وَقَالُوا لَا تَذَرُنَّ آلِهَتَكُمْ وَلَا تَذَرُنَّ وَدًّا وَلَا سُوَاعًا وَلَا يَغُوثَ وَيَعُوقَ وَنَسْرًا ۝٢٣
📖 Tekki Aaya 23
tey wax naan : “Buleen bàyyi seeni Yàlli bu leen bàyyi Wud, Mbaa Suwaa’, ak Yaquusa, ak Ya’uuqa ak Nasra.
وَقَدْ أَضَلُّوا كَثِيرًا ۖ وَلَا تَزِدِ الظَّالِمِينَ إِلَّا ضَلَالًا ۝٢٤
📖 Tekki Aaya 24
Te réeral nañu ñu bari. Te bul dolli tooñkat ya lu dul ag réer.
مِّمَّا خَطِيئَاتِهِمْ أُغْرِقُوا فَأُدْخِلُوا نَارًا فَلَمْ يَجِدُوا لَهُم مِّن دُونِ اللَّهِ أَنصَارًا ۝٢٥
📖 Tekki Aaya 25
Ci sababu seen ñaawtéef ya, labaleef na leen, tàbbalees leen safara, te amu ñu fa fekku ñu fa ku leen di dimbali, ku dul Yàlla”.
وَقَالَ نُوحٌ رَّبِّ لَا تَذَرْ عَلَى الْأَرْضِ مِنَ الْكَافِرِينَ دَيَّارًا ۝٢٦
📖 Tekki Aaya 26
Nooh wax na ne : “Yaw sama Boroom, bul bàyyi ci kaw suuf si benn yéefar bu koy dëkke.
إِنَّكَ إِن تَذَرْهُمْ يُضِلُّوا عِبَادَكَ وَلَا يَلِدُوا إِلَّا فَاجِرًا كَفَّارًا ۝٢٧
📖 Tekki Aaya 27
Soo leen fi bàyyee, dañuy réeral sa jaam ñi te dunu fi jur lu dul yéefar yu kàccoor.
رَّبِّ اغْفِرْ لِي وَلِوَالِدَيَّ وَلِمَن دَخَلَ بَيْتِيَ مُؤْمِنًا وَلِلْمُؤْمِنِينَ وَالْمُؤْمِنَاتِ وَلَا تَزِدِ الظَّالِمِينَ إِلَّا تَبَارًا ۝٢٨
📖 Tekki Aaya 28
Yaw sama Boroom ! Jégëlma, maak sama ñaari wayjur ak képp ku tàbbi sama kër te gëm, ak jullit ñu góor ñeek jullit ñu jigéen ñi ; te bul dolli tooñkat yi lu dul ag yàqule”.
← 70 Nuh (71/114) 72 →
Jàng Simoore Nuh ci Wolof – Tekki, Waxtaan ak Baat

71نوح Nuh 📚 28 Aaya مكية



Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers