28 Aaya · Meccan · Wolof
bismillah
ﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆ
71:1 Noo yónni woon Nooh ca aw nitam ne ko : “Xupal saw nit, bala leen mbugal mu mettee dikkël”.
ﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍ
71:2 Mu daldi ne : "Éy seen samaw nit, man mii ab xuppekat laa ci yéen bu bir,
ﮎﮏﮐﮑﮒﮓ
71:3 Na ngeen jaamu Yàlla, te ragal ko, te topp ko
ﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨ
71:4 kon dey Dana leen jégël seeni bàkkaar te Dana leen yeexe ba ci dig bu ñu xam. Digub Yàlla bu agsee, du fanqu cëy bu ngeen xamoon ! ”
ﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰ
71:5 (Nooh) : “Yaw sama Boroom ! woo naa samaw nit, guddeek bëcëg.
ﮱﯓﯔﯕﯖﯗ
71:6 Te sama woote bi dolli wu leen lu dul féew.
ﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦ
71:7 Te man saasu ma leen di woo ngir Nga jégël leen, dañuy def séeni waaraam ci séeni biiri nopp, daldi muuroo séeni sér, daldi jomlu.
ﯧﯨﯩﯪﯫ
71:8 Topp, woonaa leen cig jooru.
ﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳ
71:9 Topp, biralalnaa leen, yalolnaa leen.
ﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺ
71:10 Ma wax leen ne : “Jégëluleen seen Boroom, Moom dey Jégëlaakoon la,
ﭑﭒﭓﭔﭕ
71:11 kon dey dana yabal asamaan si, mu duttil leen taw,
ﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟ
71:12 te it dana leen may ay alal ak i doom, te dana leen defal tooli dër ak ay dex.
ﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦ
71:13 Ana lu leen dal ba du ngeen delloo Yàlla njukël,
ﭧﭨﭩﭪ
71:14 te moom moo leen jaarale ci ay tolluwaay yu bari ba mu leen di sàkk ?
ﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳ
71:15 Xanaa gisu leen ni Yàlla binde juróom-ñaari asamaan yu tegaloo
ﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻ
71:16 mu def ci weer wi muy leer, mu def it jant bi mu di làmpu ?
ﭼﭽﭾﭿﮀﮁ
71:17 Te Yàllaa leen saxal, ci suuf si, ni gàncax,
ﮂﮃﮄﮅﮆﮇ
71:18 te dana leen ca delloo dana leen ca génneewaat.
ﮈﮉﮊﮋﮌﮍ
71:19 Yàlla moo leen defaral suuf si mu di laltaay,
ﮎﮏﮐﮑﮒ
71:20 ngir ngeen mana sóobu ca yoonam yu dàndante ya”.
ﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠ
71:21 Nooh daldi wax ne : “Yaw sama Boroom, (samaw nit) moy na ñu ma dem toppi koo xam ne alalam ak i doomam jariñu ko lu dul yàqule.
ﮡﮢﮣﮤ
71:22 Ña ngay fexe pexe yu rëy,
ﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓ
71:23 tey wax naan : “Buleen bàyyi seeni Yàlli bu leen bàyyi Wud, Mbaa Suwaa’, ak Yaquusa, ak Ya’uuqa ak Nasra.
ﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝ
71:24 Te réeral nañu ñu bari. Te bul dolli tooñkat ya lu dul ag réer.
ﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪ
71:25 Ci sababu seen ñaawtéef ya, labaleef na leen, tàbbalees leen safara, te amu ñu fa fekku ñu fa ku leen di dimbali, ku dul Yàlla”.
ﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵ
71:26 Nooh wax na ne : “Yaw sama Boroom, bul bàyyi ci kaw suuf si benn yéefar bu koy dëkke.
ﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀ
71:27 Soo leen fi bàyyee, dañuy réeral sa jaam ñi te dunu fi jur lu dul yéefar yu kàccoor.
ﰁﰂﰃﰄﰅﰆﰇﰈﰉﰊﰋﰌﰍﰎﰏﰐﰑ
71:28 Yaw sama Boroom ! Jégëlma, maak sama ñaari wayjur ak képp ku tàbbi sama kër te gëm, ak jullit ñu góor ñeek jullit ñu jigéen ñi ; te bul dolli tooñkat yi lu dul ag yàqule”.

Alxuraan bu Tedd bi


Wednesday, September 9, 2026

Don't forget us in your sincere prayers