Ar-Rum · 41/60
Tekki Waxtaan — Ar-Rum
ظَهَرَ الْفَسَادُ فِي الْبَرِّ وَالْبَحْرِ بِمَا كَسَبَتْ أَيْدِي النَّاسِ لِيُذِيقَهُم بَعْضَ الَّذِي عَمِلُوا لَعَلَّهُمْ يَرْجِعُونَ ۝٤١
Zaharal fasaadu fil barri wal bahri bimaa kasabat aydinnaasi li yuzeeqahum ba`dal lazee `amiloo la`allahum yarji`oon
📖 Tekkim Wolof
Yàqute feeñ na ci jéeri ji ak géej gi ci jëfi nit ñi ; ci loolu, Yàlla da leen ñamal tuuti rekk ci seen [peyug] jëf yu bon yooyu ; ngir ñu mën caa jàjjoo, dellu ginnaaw, dëpp [dem jëf lu baax].
🎧 Dégg

📜 Aaya 39-43 — Ar-Rum

39وَمَا آتَيْتُم مِّن رِّبًا لِّيَرْبُوَ فِي أَمْوَالِ النَّاسِ فَلَا يَرْبُو عِندَ اللَّهِ ۖ وَمَا آتَيْتُم مِّن زَكَاةٍ تُرِيدُونَ وَجْهَ اللَّهِ فَأُولَٰئِكَ هُمُ الْمُضْعِفُونَ
Alal ji ngeen di lebalante ngir muy yokk, du yokku fa Yàlla de, waante li ngeen di génne asaka ngir jëmmi Yàlla... Dangeen fekk muy lu ñu ful.
40اللَّهُ الَّذِي خَلَقَكُمْ ثُمَّ رَزَقَكُمْ ثُمَّ يُمِيتُكُمْ ثُمَّ يُحْيِيكُمْ ۖ هَلْ مِن شُرَكَائِكُم مَّن يَفْعَلُ مِن ذَٰلِكُم مِّن شَيْءٍ ۚ سُبْحَانَهُ وَتَعَالَىٰ عَمَّا يُشْرِكُونَ
Yàlla mi leen sàkk, wërsëgal leen. Di leen rey te di leen dundalaat. Moo ndax ñi ngeen koy bokkaaleel am na ñu mën a def loolu ? Tudd naa sellam ga, kañ naa Ko ! Soree na lool ak li ngeen di bokkaale.
41ظَهَرَ الْفَسَادُ فِي الْبَرِّ وَالْبَحْرِ بِمَا كَسَبَتْ أَيْدِي النَّاسِ لِيُذِيقَهُم بَعْضَ الَّذِي عَمِلُوا لَعَلَّهُمْ يَرْجِعُونَ
Yàqute feeñ na ci jéeri ji ak géej gi ci jëfi nit ñi ; ci loolu, Yàlla da leen ñamal tuuti rekk ci seen [peyug] jëf yu bon yooyu ; ngir ñu mën caa jàjjoo, dellu ginnaaw, dëpp [dem jëf lu baax].
42قُلْ سِيرُوا فِي الْأَرْضِ فَانظُرُوا كَيْفَ كَانَ عَاقِبَةُ الَّذِينَ مِن قَبْلُ ۚ كَانَ أَكْثَرُهُم مُّشْرِكِينَ
Neel : “Doxleen ci suuf si tey xool naka la mujje woon ña leen jiitu woon. Te li ëpp ci ñoom doon bokkaale [Yàlla]”.
43فَأَقِمْ وَجْهَكَ لِلدِّينِ الْقَيِّمِ مِن قَبْلِ أَن يَأْتِيَ يَوْمٌ لَّا مَرَدَّ لَهُ مِنَ اللَّهِ ۖ يَوْمَئِذٍ يَصَّدَّعُونَ
Jubbantikul topp diine ju jub ja, ba laa bis di ñëw boo xam ne kenn du ko mën a randal ca Yàlla. Bu keroogee, danañu fallaxoo [réeroo, téqalikoo] :
Ar-RumFihi Alxuraan
60Aaya
MeccanRevelation
41Aaya

Tekki — Ar-Rum 41

Simoore Ar-Rum Aaya 41 - Jàng, Dégg, Tekki, Wolof : Yàqute feeñ na ci jéeri ji ak géej gi ci…

Simoore Aaya 41/60 — Ar-Rum الروم (Meccan). Jàng Dégg Tekki (Wolof). Dégg: Ar-Rum Dégg, Ar-Rum Tekki, Ar-Rum mp3, Ar-Rum pdf. Aaya 39–43. Tekkim Wolof: Fulfulde.




Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers