Simoore Ar-Rum ci Aarabu ak Wolof

Jàng Simoore Ar-Rum ak tekkim wolof bu mat sëkk, ak baat. Tekki ayaa bu ne. (60 Aaya — مكية). Ar-Rum Dégg, Ar-Rum Tekki, Ar-Rum mp3, Ar-Rum pdf.

Jàng te Dégg Simoore Ar-Rum

🎧 Aaya
M Mishary Rashid Alafasy
M Mahmoud Khalil Al-Husary
A Abdurrahman As-Sudais
M Mohamed Siddiq Al-Minshawi
A Abdul Basit Abdul Samad
A Ali Al-Hudhaify
A Ahmed ibn Ali al-Ajamy
A Abu Bakr Ash-Shaatree
M Muhammad Ayyoub
A Abdullah Basfar
A Abdullah Al-Juhani
M Maher Al Muaiqly
x1
الم ۝١
📖 Tekki Aaya 1
Alif, Laam, Miim.
غُلِبَتِ الرُّومُ ۝٢
📖 Tekki Aaya 2
Noteef na waa Rom,
فِي أَدْنَى الْأَرْضِ وَهُم مِّن بَعْدِ غَلَبِهِمْ سَيَغْلِبُونَ ۝٣
📖 Tekki Aaya 3
ci réew yi leen gën a jegeñ, wante ginnaaw nooteef googu, ñoom it danañu not ,
فِي بِضْعِ سِنِينَ ۗ لِلَّهِ الْأَمْرُ مِن قَبْلُ وَمِن بَعْدُ ۚ وَيَوْمَئِذٍ يَفْرَحُ الْمُؤْمِنُونَ ۝٤
📖 Tekki Aaya 4
ci biir diirub lu matul fukki at. Yàlla moo yor dogal yi, ci la jëkkoon ak li lay mujj, bu boobaa way-gëm ñi danañu sëgg ree, bég
بِنَصْرِ اللَّهِ ۚ يَنصُرُ مَن يَشَاءُ ۖ وَهُوَ الْعَزِيزُ الرَّحِيمُ ۝٥
📖 Tekki Aaya 5
ci ndimbalul Yàlla. [Moom Yàlla] mooy dimbali ku ko soob, Mooy boroom Kàttan, di Jaglewaakon bi.
وَعْدَ اللَّهِ ۖ لَا يُخْلِفُ اللَّهُ وَعْدَهُ وَلَٰكِنَّ أَكْثَرَ النَّاسِ لَا يَعْلَمُونَ ۝٦
📖 Tekki Aaya 6
Loolu mooy li Yàlla di dige. Te Yàlla du wuute ab digam, waaye li ëpp ci nit ñi gëmuñu.
يَعْلَمُونَ ظَاهِرًا مِّنَ الْحَيَاةِ الدُّنْيَا وَهُمْ عَنِ الْآخِرَةِ هُمْ غَافِلُونَ ۝٧
📖 Tekki Aaya 7
Danañu xam li feeñ ci dundug àddina, te ñoom ñu sàggan lañu ci mbiri àllaaxira,.
أَوَلَمْ يَتَفَكَّرُوا فِي أَنفُسِهِم ۗ مَّا خَلَقَ اللَّهُ السَّمَاوَاتِ وَالْأَرْضَ وَمَا بَيْنَهُمَا إِلَّا بِالْحَقِّ وَأَجَلٍ مُّسَمًّى ۗ وَإِنَّ كَثِيرًا مِّنَ النَّاسِ بِلِقَاءِ رَبِّهِمْ لَكَافِرُونَ ۝٨
📖 Tekki Aaya 8
Ndax dañoo xalaatul ci seen bopp ? Yàlla bindul asamaan yeek suuf si ak li nekk ci seen diggante lu dul ci dëgg, te sàkkal na lépp ay dig. Te nag li bari ci nit ñi dañoo weddi te danañu dajeek seen Boroom.
أَوَلَمْ يَسِيرُوا فِي الْأَرْضِ فَيَنظُرُوا كَيْفَ كَانَ عَاقِبَةُ الَّذِينَ مِن قَبْلِهِمْ ۚ كَانُوا أَشَدَّ مِنْهُمْ قُوَّةً وَأَثَارُوا الْأَرْضَ وَعَمَرُوهَا أَكْثَرَ مِمَّا عَمَرُوهَا وَجَاءَتْهُمْ رُسُلُهُم بِالْبَيِّنَاتِ ۖ فَمَا كَانَ اللَّهُ لِيَظْلِمَهُمْ وَلَٰكِن كَانُوا أَنفُسَهُمْ يَظْلِمُونَ ۝٩
📖 Tekki Aaya 9
Ndax dañoo doxul ci suuf tey xool naka la ñu mujje ña leen fa jiitu woon ? Ñoo leen ëppoon doole, daan réjji suuf si, feesoon ko dell ak seeni njaboot. Seeni Yonent indiloon leen ay kàddu yu leer. Yàlla tooñuleen, waaye ñoo tooñ seen bopp.
ثُمَّ كَانَ عَاقِبَةَ الَّذِينَ أَسَاءُوا السُّوأَىٰ أَن كَذَّبُوا بِآيَاتِ اللَّهِ وَكَانُوا بِهَا يَسْتَهْزِئُونَ ۝١٠
📖 Tekki Aaya 10
Ña daan jëf u ñaawteef, seenug mujj dellu ñaaw, ndax ñoom weddi woon nañu kàdduy Yàlla, daan ko yéjji.
اللَّهُ يَبْدَأُ الْخَلْقَ ثُمَّ يُعِيدُهُ ثُمَّ إِلَيْهِ تُرْجَعُونَ ۝١١
📖 Tekki Aaya 11
Yàllaa bind yëf yi ; yi di ko defaraat ; te ca Moom la ñuy dellu.
وَيَوْمَ تَقُومُ السَّاعَةُ يُبْلِسُ الْمُجْرِمُونَ ۝١٢
📖 Tekki Aaya 12
Bu keroogee bu Bis-pénc ba di taxaw, tooñkat ya danañu naan cucum jaaxle.
وَلَمْ يَكُن لَّهُم مِّن شُرَكَائِهِمْ شُفَعَاءُ وَكَانُوا بِشُرَكَائِهِمْ كَافِرِينَ ۝١٣
📖 Tekki Aaya 13
Ña ñu daan bokkaaleek Yàlla duñu leen rammu, te sax far dañuy weddi ña ñu daan bokkaaleek [Yàlla].
وَيَوْمَ تَقُومُ السَّاعَةُ يَوْمَئِذٍ يَتَفَرَّقُونَ ۝١٤
📖 Tekki Aaya 14
Bu kerook Bis-pénc baa, dañuy téqalikoo, féewoo.
فَأَمَّا الَّذِينَ آمَنُوا وَعَمِلُوا الصَّالِحَاتِ فَهُمْ فِي رَوْضَةٍ يُحْبَرُونَ ۝١٥
📖 Tekki Aaya 15
Ña gëmoon tey jëf u yiw, ña ngay xéewu ci biir ay dër ;
وَأَمَّا الَّذِينَ كَفَرُوا وَكَذَّبُوا بِآيَاتِنَا وَلِقَاءِ الْآخِرَةِ فَأُولَٰئِكَ فِي الْعَذَابِ مُحْضَرُونَ ۝١٦
📖 Tekki Aaya 16
yéefar yay weddi Sunuy kàddu ak dajeb àllaaxira ba, ñoom ña nga ca biir mbugal ma.
فَسُبْحَانَ اللَّهِ حِينَ تُمْسُونَ وَحِينَ تُصْبِحُونَ ۝١٧
📖 Tekki Aaya 17
Tudd naa sellug Yàlla, kañ naa ko !
وَلَهُ الْحَمْدُ فِي السَّمَاوَاتِ وَالْأَرْضِ وَعَشِيًّا وَحِينَ تُظْهِرُونَ ۝١٨
📖 Tekki Aaya 18
Xeeti cant yépp ñeel na Ko ci asamaan yeek suuf si, ca marax ga ak njolloor.
يُخْرِجُ الْحَيَّ مِنَ الْمَيِّتِ وَيُخْرِجُ الْمَيِّتَ مِنَ الْحَيِّ وَيُحْيِي الْأَرْضَ بَعْدَ مَوْتِهَا ۚ وَكَذَٰلِكَ تُخْرَجُونَ ۝١٩
📖 Tekki Aaya 19
Mooy génne ndundu ci ndee, di génne ndee ci ndundu. Mooy dundal suuf ginnaaw ba mu dewee. Noonu it lees leen di génnee [yéen ñépp] ca bisub dekki ba.
وَمِنْ آيَاتِهِ أَنْ خَلَقَكُم مِّن تُرَابٍ ثُمَّ إِذَا أَنتُم بَشَرٌ تَنتَشِرُونَ ۝٢٠
📖 Tekki Aaya 20
Bokk na ci kéemaanam yi : Mu binde leen suuf, - léegi nag, yéen a ngi nii tasaaroo ci àddina si -.
وَمِنْ آيَاتِهِ أَنْ خَلَقَ لَكُم مِّنْ أَنفُسِكُمْ أَزْوَاجًا لِّتَسْكُنُوا إِلَيْهَا وَجَعَلَ بَيْنَكُم مَّوَدَّةً وَرَحْمَةً ۚ إِنَّ فِي ذَٰلِكَ لَآيَاتٍ لِّقَوْمٍ يَتَفَكَّرُونَ ۝٢١
📖 Tekki Aaya 21
Te bokk na ci kéemaanam yi, mu sàkkal leen ci seeni jëmm ay soxna ngir ngeen di ca dall, Mu def ci seen diggante cofeel ak yërmaande. Ay kéemaan a ngi ci biir loolu ngir aw nit ñuy xalaat.
وَمِنْ آيَاتِهِ خَلْقُ السَّمَاوَاتِ وَالْأَرْضِ وَاخْتِلَافُ أَلْسِنَتِكُمْ وَأَلْوَانِكُمْ ۚ إِنَّ فِي ذَٰلِكَ لَآيَاتٍ لِّلْعَالِمِينَ ۝٢٢
📖 Tekki Aaya 22
Bokk na it ci ay kéemaanam, bindug asamaan yeek suuf si ak wuuteeg seeni làmmiñ ak seeni melo. Ay kéemaan a ngi ci loolu ñeel ñeel waa àddina si yépp.
وَمِنْ آيَاتِهِ مَنَامُكُم بِاللَّيْلِ وَالنَّهَارِ وَابْتِغَاؤُكُم مِّن فَضْلِهِ ۚ إِنَّ فِي ذَٰلِكَ لَآيَاتٍ لِّقَوْمٍ يَسْمَعُونَ ۝٢٣
📖 Tekki Aaya 23
Bokk na it ci ay kéemaanam, seeni nelaw ci guddi gi ak seenug sàkku wërsëg. Ay kéemaan a ngi ci biir loolu ngir aw nit ñuy dégg.
وَمِنْ آيَاتِهِ يُرِيكُمُ الْبَرْقَ خَوْفًا وَطَمَعًا وَيُنَزِّلُ مِنَ السَّمَاءِ مَاءً فَيُحْيِي بِهِ الْأَرْضَ بَعْدَ مَوْتِهَا ۚ إِنَّ فِي ذَٰلِكَ لَآيَاتٍ لِّقَوْمٍ يَعْقِلُونَ ۝٢٤
📖 Tekki Aaya 24
Bokk na it ci ay kéemaanam, Mu di leen won melax mu boole ragal ak xemmem, muy wàcce ndox mu bawoo asamaan di ca dundal suuf si ginnaaw ba mu deewee. Ay kéemaan a ngi biir loolu ngir aw nit ñuy xalaat.
وَمِنْ آيَاتِهِ أَن تَقُومَ السَّمَاءُ وَالْأَرْضُ بِأَمْرِهِ ۚ ثُمَّ إِذَا دَعَاكُمْ دَعْوَةً مِّنَ الْأَرْضِ إِذَا أَنتُمْ تَخْرُجُونَ ۝٢٥
📖 Tekki Aaya 25
Bokk na it ci ay kéemaanam, ni asamaan ak suuf taxawe ci ndigalam ; te saa Su leen jiinee ab woote, yéen ñéppay génn ci biir suuf si [ginnaaw dee]
وَلَهُ مَن فِي السَّمَاوَاتِ وَالْأَرْضِ ۖ كُلٌّ لَّهُ قَانِتُونَ ۝٢٦
📖 Tekki Aaya 26
Moo moom ñépp ñu nekk asamaan ak suuf : ñépp a koy toroxlul.
وَهُوَ الَّذِي يَبْدَأُ الْخَلْقَ ثُمَّ يُعِيدُهُ وَهُوَ أَهْوَنُ عَلَيْهِ ۚ وَلَهُ الْمَثَلُ الْأَعْلَىٰ فِي السَّمَاوَاتِ وَالْأَرْضِ ۚ وَهُوَ الْعَزِيزُ الْحَكِيمُ ۝٢٧
📖 Tekki Aaya 27
Moo sos mbindéef yi di leen defaraat ; te looloo gën a yomb ci Moom. Moo dàmbe li gën a kawe ci asamaan yeek suuf si. Mooy boroom Kàttan, di ku Xereñ ki.
ضَرَبَ لَكُم مَّثَلًا مِّنْ أَنفُسِكُمْ ۖ هَل لَّكُم مِّن مَّا مَلَكَتْ أَيْمَانُكُم مِّن شُرَكَاءَ فِي مَا رَزَقْنَاكُمْ فَأَنتُمْ فِيهِ سَوَاءٌ تَخَافُونَهُمْ كَخِيفَتِكُمْ أَنفُسَكُمْ ۚ كَذَٰلِكَ نُفَصِّلُ الْآيَاتِ لِقَوْمٍ يَعْقِلُونَ ۝٢٨
📖 Tekki Aaya 28
Yàlla sadd na leen ay léebu ci seen bopp : Ndax seen jaam ñi bokk nañu ak yéen seeni alal, ngeen yem ci kepp ? [Mukk], loolu rekk ngeen ragal. Nii la Nul leerale laaya yi ngir aw nit ñuy xalaat.
بَلِ اتَّبَعَ الَّذِينَ ظَلَمُوا أَهْوَاءَهُم بِغَيْرِ عِلْمٍ ۖ فَمَن يَهْدِي مَنْ أَضَلَّ اللَّهُ ۖ وَمَا لَهُم مِّن نَّاصِرِينَ ۝٢٩
📖 Tekki Aaya 29
Tooñkat yi dañoo topp seen bànneex, te àndul ak xam-xam. Ana kan mooy mën a gindi ku Yàlla réeral ? Duñu am ku leen dimbali.
فَأَقِمْ وَجْهَكَ لِلدِّينِ حَنِيفًا ۚ فِطْرَتَ اللَّهِ الَّتِي فَطَرَ النَّاسَ عَلَيْهَا ۚ لَا تَبْدِيلَ لِخَلْقِ اللَّهِ ۚ ذَٰلِكَ الدِّينُ الْقَيِّمُ وَلَٰكِنَّ أَكْثَرَ النَّاسِ لَا يَعْلَمُونَ ۝٣٠
📖 Tekki Aaya 30
Nangay jubbantiku topp diine Yàlla jiy cosaan te Mu sos ci nit ñi - bindéefu Yàlla du soppiku -. Loolu mooy diine ju jub ja ; waaye li ëpp ci nit ñi duñu xam.
۞ مُنِيبِينَ إِلَيْهِ وَاتَّقُوهُ وَأَقِيمُوا الصَّلَاةَ وَلَا تَكُونُوا مِنَ الْمُشْرِكِينَ ۝٣١
📖 Tekki Aaya 31
Wommatuleen jëm ci Moom ; te nangeen ko ragal, tey taxawal julli te buleen bokk ca way-bokkaale ña,
مِنَ الَّذِينَ فَرَّقُوا دِينَهُمْ وَكَانُوا شِيَعًا ۖ كُلُّ حِزْبٍ بِمَا لَدَيْهِمْ فَرِحُونَ ۝٣٢
📖 Tekki Aaya 32
ña téqale seen diine di ay kurél, xaaj bu nekk ne siiw la fa moom.
وَإِذَا مَسَّ النَّاسَ ضُرٌّ دَعَوْا رَبَّهُم مُّنِيبِينَ إِلَيْهِ ثُمَّ إِذَا أَذَاقَهُم مِّنْهُ رَحْمَةً إِذَا فَرِيقٌ مِّنْهُم بِرَبِّهِمْ يُشْرِكُونَ ۝٣٣
📖 Tekki Aaya 33
Bu lor ju laal nit ña amee, dañuy ñaan Yàlla di Ko woo booleek toroxlu. Waaye su leen di mosal yërmaande rekk, [nga gis] ñu delluy bokkaale,
لِيَكْفُرُوا بِمَا آتَيْنَاهُمْ ۚ فَتَمَتَّعُوا فَسَوْفَ تَعْلَمُونَ ۝٣٤
📖 Tekki Aaya 34
di fakk la Mu leen indiloon. “Bànneexuleen. Dangeen xala xam”.
أَمْ أَنزَلْنَا عَلَيْهِمْ سُلْطَانًا فَهُوَ يَتَكَلَّمُ بِمَا كَانُوا بِهِ يُشْرِكُونَ ۝٣٥
📖 Tekki Aaya 35
Walla Danuy wàcce ci ñoom [kilifa] ab Téere buy wàqante la ñu daan bokkaale ?
وَإِذَا أَذَقْنَا النَّاسَ رَحْمَةً فَرِحُوا بِهَا ۖ وَإِن تُصِبْهُمْ سَيِّئَةٌ بِمَا قَدَّمَتْ أَيْدِيهِمْ إِذَا هُمْ يَقْنَطُونَ ۝٣٦
📖 Tekki Aaya 36
Saa su Nu mosalee nit ñi yërmaande, ñu bég lool. Bu ñu defee ab garaawaale ba safaan dal leen ca, ndekete yoo dañuy yoqat.
أَوَلَمْ يَرَوْا أَنَّ اللَّهَ يَبْسُطُ الرِّزْقَ لِمَن يَشَاءُ وَيَقْدِرُ ۚ إِنَّ فِي ذَٰلِكَ لَآيَاتٍ لِّقَوْمٍ يُؤْمِنُونَ ۝٣٧
📖 Tekki Aaya 37
Xanaa dañoo gisul ne Yàlla Dana yaatalal ku ko soob, wërsëgam ? Dana ko xatal it. Ay kéemaan a ngi ci biir loolu ngir aw nit ñu gëm.
فَآتِ ذَا الْقُرْبَىٰ حَقَّهُ وَالْمِسْكِينَ وَابْنَ السَّبِيلِ ۚ ذَٰلِكَ خَيْرٌ لِّلَّذِينَ يُرِيدُونَ وَجْهَ اللَّهِ ۖ وَأُولَٰئِكَ هُمُ الْمُفْلِحُونَ ۝٣٨
📖 Tekki Aaya 38
Dangay jox say [mbokki] jegeñaale lay seen yelleef, ak ndóol ya ak doxandeem ya. Loolu moo gën fuuf ngërëmul Yàlla ; te ñoom ñooy texe.
وَمَا آتَيْتُم مِّن رِّبًا لِّيَرْبُوَ فِي أَمْوَالِ النَّاسِ فَلَا يَرْبُو عِندَ اللَّهِ ۖ وَمَا آتَيْتُم مِّن زَكَاةٍ تُرِيدُونَ وَجْهَ اللَّهِ فَأُولَٰئِكَ هُمُ الْمُضْعِفُونَ ۝٣٩
📖 Tekki Aaya 39
Alal ji ngeen di lebalante ngir muy yokk, du yokku fa Yàlla de, waante li ngeen di génne asaka ngir jëmmi Yàlla... Dangeen fekk muy lu ñu ful.
اللَّهُ الَّذِي خَلَقَكُمْ ثُمَّ رَزَقَكُمْ ثُمَّ يُمِيتُكُمْ ثُمَّ يُحْيِيكُمْ ۖ هَلْ مِن شُرَكَائِكُم مَّن يَفْعَلُ مِن ذَٰلِكُم مِّن شَيْءٍ ۚ سُبْحَانَهُ وَتَعَالَىٰ عَمَّا يُشْرِكُونَ ۝٤٠
📖 Tekki Aaya 40
Yàlla mi leen sàkk, wërsëgal leen. Di leen rey te di leen dundalaat. Moo ndax ñi ngeen koy bokkaaleel am na ñu mën a def loolu ? Tudd naa sellam ga, kañ naa Ko ! Soree na lool ak li ngeen di bokkaale.
ظَهَرَ الْفَسَادُ فِي الْبَرِّ وَالْبَحْرِ بِمَا كَسَبَتْ أَيْدِي النَّاسِ لِيُذِيقَهُم بَعْضَ الَّذِي عَمِلُوا لَعَلَّهُمْ يَرْجِعُونَ ۝٤١
📖 Tekki Aaya 41
Yàqute feeñ na ci jéeri ji ak géej gi ci jëfi nit ñi ; ci loolu, Yàlla da leen ñamal tuuti rekk ci seen [peyug] jëf yu bon yooyu ; ngir ñu mën caa jàjjoo, dellu ginnaaw, dëpp [dem jëf lu baax].
قُلْ سِيرُوا فِي الْأَرْضِ فَانظُرُوا كَيْفَ كَانَ عَاقِبَةُ الَّذِينَ مِن قَبْلُ ۚ كَانَ أَكْثَرُهُم مُّشْرِكِينَ ۝٤٢
📖 Tekki Aaya 42
Neel : “Doxleen ci suuf si tey xool naka la mujje woon ña leen jiitu woon. Te li ëpp ci ñoom doon bokkaale [Yàlla]”.
فَأَقِمْ وَجْهَكَ لِلدِّينِ الْقَيِّمِ مِن قَبْلِ أَن يَأْتِيَ يَوْمٌ لَّا مَرَدَّ لَهُ مِنَ اللَّهِ ۖ يَوْمَئِذٍ يَصَّدَّعُونَ ۝٤٣
📖 Tekki Aaya 43
Jubbantikul topp diine ju jub ja, ba laa bis di ñëw boo xam ne kenn du ko mën a randal ca Yàlla. Bu keroogee, danañu fallaxoo [réeroo, téqalikoo] :
مَن كَفَرَ فَعَلَيْهِ كُفْرُهُ ۖ وَمَنْ عَمِلَ صَالِحًا فَلِأَنفُسِهِمْ يَمْهَدُونَ ۝٤٤
📖 Tekki Aaya 44
Ku weddi, weddeem ga dana dal ca kawam. Ñay jëf yiw nag... Ñoom ña ngay waajal seen bopp [daluwaay bu maase] néeg,
لِيَجْزِيَ الَّذِينَ آمَنُوا وَعَمِلُوا الصَّالِحَاتِ مِن فَضْلِهِ ۚ إِنَّهُ لَا يُحِبُّ الْكَافِرِينَ ۝٤٥
📖 Tekki Aaya 45
Nar naa feye ñi gëm tey jëf u yiw, ngënéelam. Moom safoowul yéefar yi.
وَمِنْ آيَاتِهِ أَن يُرْسِلَ الرِّيَاحَ مُبَشِّرَاتٍ وَلِيُذِيقَكُم مِّن رَّحْمَتِهِ وَلِتَجْرِيَ الْفُلْكُ بِأَمْرِهِ وَلِتَبْتَغُوا مِن فَضْلِهِ وَلَعَلَّكُمْ تَشْكُرُونَ ۝٤٦
📖 Tekki Aaya 46
Bokk na ci ay kéemaanam, muy yebal yërmaandeem, ak gaal yi di daw ci ndigalam, te ngeen di sàkku ci xéewalam yi. Ak ngir ngeen di gëm !
وَلَقَدْ أَرْسَلْنَا مِن قَبْلِكَ رُسُلًا إِلَىٰ قَوْمِهِمْ فَجَاءُوهُم بِالْبَيِّنَاتِ فَانتَقَمْنَا مِنَ الَّذِينَ أَجْرَمُوا ۖ وَكَانَ حَقًّا عَلَيْنَا نَصْرُ الْمُؤْمِنِينَ ۝٤٧
📖 Tekki Aaya 47
Yónni woon Nanu ay Yonent yu jiitu woon ca nit ña, indiloon leen ay kàddu yu leer. Nu daldi feyu ca tooñkat ya ; te ndimbalul jullit ñi [way-gëm ñi], Maa ko warlu.
اللَّهُ الَّذِي يُرْسِلُ الرِّيَاحَ فَتُثِيرُ سَحَابًا فَيَبْسُطُهُ فِي السَّمَاءِ كَيْفَ يَشَاءُ وَيَجْعَلُهُ كِسَفًا فَتَرَى الْوَدْقَ يَخْرُجُ مِنْ خِلَالِهِ ۖ فَإِذَا أَصَابَ بِهِ مَن يَشَاءُ مِنْ عِبَادِهِ إِذَا هُمْ يَسْتَبْشِرُونَ ۝٤٨
📖 Tekki Aaya 48
Yàlla miy yebal ngelaw mu yenu niir, di ko tàbbal ci asamaan si na Mu ko soobe ; Mu di ko def ay daggit. Ab taw di ca génnee su ko tawale. Ña ko soob ci jaamam yi, ndeketeyoo dañuy sëgg ree ngir bég,
وَإِن كَانُوا مِن قَبْلِ أَن يُنَزَّلَ عَلَيْهِم مِّن قَبْلِهِ لَمُبْلِسِينَ ۝٤٩
📖 Tekki Aaya 49
doonte la sax naagu woon nañu ba mu laataa na wàcc.
فَانظُرْ إِلَىٰ آثَارِ رَحْمَتِ اللَّهِ كَيْفَ يُحْيِي الْأَرْضَ بَعْدَ مَوْتِهَا ۚ إِنَّ ذَٰلِكَ لَمُحْيِي الْمَوْتَىٰ ۖ وَهُوَ عَلَىٰ كُلِّ شَيْءٍ قَدِيرٌ ۝٥٠
📖 Tekki Aaya 50
Xoolal jeexitali yërmaandey Yàlla naka lay dundalee suuf si ginnaaw ba mu deewee. Kookee de Mooy dekkalaat néew yi te mën na lu ne.
وَلَئِنْ أَرْسَلْنَا رِيحًا فَرَأَوْهُ مُصْفَرًّا لَّظَلُّوا مِن بَعْدِهِ يَكْفُرُونَ ۝٥١
📖 Tekki Aaya 51
Bu Nu yebaloon ngelaw, ñu gis ne [seen gàncax ga] mbokk, di [lax ak a dee], dañuy daldi weddi, fakk xéewal ya.
فَإِنَّكَ لَا تُسْمِعُ الْمَوْتَىٰ وَلَا تُسْمِعُ الصُّمَّ الدُّعَاءَ إِذَا وَلَّوْا مُدْبِرِينَ ۝٥٢
📖 Tekki Aaya 52
Yaw dey, mënoo tax a dégg ñu dee ; waxantumalaak tëx, su ñu nee wërëñ dummóoyu, ak lu woote ba xumb xumb nag.
وَمَا أَنتَ بِهَادِ الْعُمْيِ عَن ضَلَالَتِهِمْ ۖ إِن تُسْمِعُ إِلَّا مَن يُؤْمِنُ بِآيَاتِنَا فَهُم مُّسْلِمُونَ ۝٥٣
📖 Tekki Aaya 53
Du caageene yaw yaaw gindi gumba yi ci seen réer ga. Ñi nga mën a dégtal [sa woote bii] daal, ñooy ña gëm, di ay jullit.
۞ اللَّهُ الَّذِي خَلَقَكُم مِّن ضَعْفٍ ثُمَّ جَعَلَ مِن بَعْدِ ضَعْفٍ قُوَّةً ثُمَّ جَعَلَ مِن بَعْدِ قُوَّةٍ ضَعْفًا وَشَيْبَةً ۚ يَخْلُقُ مَا يَشَاءُ ۖ وَهُوَ الْعَلِيمُ الْقَدِيرُ ۝٥٤
📖 Tekki Aaya 54
Yàlla mi leen bind cig lott, teg ca kàttan ; delloo ci lott gu ànd ak kumur, màggat [bijjaaw] : Te mooy sàkk lu ko soob, Mooy ki Xam te Mën.
وَيَوْمَ تَقُومُ السَّاعَةُ يُقْسِمُ الْمُجْرِمُونَ مَا لَبِثُوا غَيْرَ سَاعَةٍ ۚ كَذَٰلِكَ كَانُوا يُؤْفَكُونَ ۝٥٥
📖 Tekki Aaya 55
Bu Bis-pénc ba taxawee, tooñkat ya danañu giñ naan as ndiir su ndaw la nu fi saxoon. Noonu la Nu leen daan férawale, soreel leen dëgg ;
وَقَالَ الَّذِينَ أُوتُوا الْعِلْمَ وَالْإِيمَانَ لَقَدْ لَبِثْتُمْ فِي كِتَابِ اللَّهِ إِلَىٰ يَوْمِ الْبَعْثِ ۖ فَهَٰذَا يَوْمُ الْبَعْثِ وَلَٰكِنَّكُمْ كُنتُمْ لَا تَعْلَمُونَ ۝٥٦
📖 Tekki Aaya 56
Gaa ña amoon xam-xam ak ngëm, ne leen : “Sax ngeen fa ci dogalu Yàlla ba bisub dekki ba, - lii nag mooy bisub dekki ba, - waaye yéen xamuleen woon”.
فَيَوْمَئِذٍ لَّا يَنفَعُ الَّذِينَ ظَلَمُوا مَعْذِرَتُهُمْ وَلَا هُمْ يُسْتَعْتَبُونَ ۝٥٧
📖 Tekki Aaya 57
Su boobaa, tooñkat ya, seenug tinu du fa jariñ dara te kenn duleen faale.
وَلَقَدْ ضَرَبْنَا لِلنَّاسِ فِي هَٰذَا الْقُرْآنِ مِن كُلِّ مَثَلٍ ۚ وَلَئِن جِئْتَهُم بِآيَةٍ لَّيَقُولَنَّ الَّذِينَ كَفَرُوا إِنْ أَنتُمْ إِلَّا مُبْطِلُونَ ۝٥٨
📖 Tekki Aaya 58
Saddal Nanu nit ci biir Alxuraan jii léebu wu nekk. Soo leen indiloon kéemaan it, yéefar ya dañu naan : “Yéen daal, ay caaxaankat doŋŋ ngeen”.
كَذَٰلِكَ يَطْبَعُ اللَّهُ عَلَىٰ قُلُوبِ الَّذِينَ لَا يَعْلَمُونَ ۝٥٩
📖 Tekki Aaya 59
Noonu la Yàlla di fattee xoli ña xamadi.
فَاصْبِرْ إِنَّ وَعْدَ اللَّهِ حَقٌّ ۖ وَلَا يَسْتَخِفَّنَّكَ الَّذِينَ لَا يُوقِنُونَ ۝٦٠
📖 Tekki Aaya 60
Muñal ndax digub Yàlla la dellu [yàgg yàgg dina ñëw]. Ñi gëmul, buñu la yàkki !
← 29 Ar-Rum (30/114) 31 →
Jàng Simoore Ar-Rum ci Wolof – Tekki, Waxtaan ak Baat

30الروم Ar-Rum 📚 60 Aaya مكية



Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers