Simoore Al-Baqara
PDF —
286 Aaya Medinan PDF
Built right in your browser — download starts automatically

Simoore Al-Baqara pdf — Wàcce (Wolof)

Simoore Al-Baqara pdf Wolof — Wàcce Simoore Al-Baqara Tekki. Al-Baqara (Medinan) 286 Aaya.



Simoore Al-Baqara
286 Aaya · Medinan · Wolof
bismillah
ﭑﭒ
Alif, Laam, Miim .
ﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜ
Téere bii amul sikk ci ne [ag jub a ci nekk] guy soxal way-ragal Yàlla yi.
ﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥ
ña gëm ci kumpa. Di farlu ci julli te di joxe ci li Nu leen xéewale
ﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲ
Ñoo di ña gëm la Ñu wàcce ci yaw ak la Nu wàcce woon mu jiitu woon te ñu amug wóolu ci dikkug Bis-pénc ba.
ﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼ
Ñooñoo nekk ca njub ga tukkee ca seen Boroom te ñoom ñoo texe.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜ
Ñi weddi, nga waar leen ak ñàkk leen waar a yem ci ñoom, duñu gëm.
ﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫ
Yàlla fatt na seeni xol ak seeni nopp ; muuraay nekk na ca seeni gët ; mbugal mu metti dana leen dal.
ﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷ
Am na ci nit ñi, ñu naan : “Gëm nanu Yàlla ak Bis-pénc ba ! ” te gëmuñu dara.
ﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂ
Dañuy jéem a nax Yàlla ak way-gëm ñi ; waaye naxuñu lu dul seen bopp, te yëguñu ko.
ﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐ
Jàngoroo nekk ci seeni xol (gog sikki-sàkk ak ug naaféq), faf Yàlla yokk leen jàngoro. Mbugal mu metti dana leen dal ngir seenug weddi.
ﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜ
Bu ñu leen waxee : 'Buleen di yàq ci suuf si ', ñu ne : 'Nun way-defar lanu ! '
ﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤ
Déedéet, ñoom ñooña ay yàq-kat lañu, te yëguñu ko.
ﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚ
Bu ñu ne leen : “Gëmleen ni nit ñi gëmee”, ñu tontu ne : “Ndax danuy gëm ni dof yi di gëmee ? ” Déedéet, ñoom ñooy diy dof, te xamuñu ko.
ﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫ
Bu ñu dajeek way-gëm ña, ne : “Gëm nanu” ; waaye bu ñu wéetee ak seeni (Séytaane naaféq yi), ne : “Nook yéen a ànd ; nun danuy yejji [jullit ñi] rekk”.
ﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳ
Yàllaa nga leen di yejji, di leen gën a yàggal ca seen mbeewte googu, ñuy deŋŋi-deŋŋi ak seen ngumbaag xol.
ﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿ
Ñooña ñoo di ña jaay njub jënde ci réer, seen njaay mooma amul tono. Te it gindikuwuñu.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢ
Seen niróole mi ngi demee ni ku taal taalamn, ba janeer ba leeraale la ko wër, Yàlla fay leer ga, bàyyi leen cig lëndëm ba gisatuñu dara.
ﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩ
Dañoo tëx, luu, gumba, ba duñu mën a dellusi (cig njub).
ﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾ
Walla [seen niróolee ngi deme ni] waame wu tukkee asamaan ànd ak lëndëm ak i dënnu ak i melax, ñu saañ seeni nopp ak seeni waaroom ngir bañ a dégg kàddu ya ngir ragal dee ;Yàlla Aji-peeg la yéefar ya.
ﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛ
Melax ga xaw naa yuri seeni gët : saa su leen leeralee [yoon wa] ñu dox ca leer ga ;saa su lëndëmee ñu taxaw. Bu neexoon Yàlla mu tëxloo leen, gumbaloo leen, Yàlla am na kàttanu def lu ne.
ﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧ
Yéen nit ñi ! Jaamuleen Boroom bi leen bind, yéen ak ñi leen jiitu, ndax ngeen ragal ko. [Fegu] ci mbugalam.
ﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡ
Moom mi def suuf nekk laltaay ci yéen, asamaan si di seen téeg ; te mu wàcceel leen ndox mu jóge asamaan, génne ca ay meññeent yu mu leen wërsëgal, bu leen sàkkal Yàlla moroom te xam xéll [ne loolu jaaduwul].
ﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶ
Bu ngeen amee sikki-sàkka ci lii Nu wàcce ci Sunu jaam bi, indileen saar wu mel ni moom [Alxuraan] te sax ñaanleen ndimbal ñi ngeen di jaamu ba jaamuwuleen Yàlla, ndegam dëgg la ci yéen.
ﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅ
Bu ngeen ko deful, te du ngeen ko mën a def mukk, na ngeen ragal safara soo xam ne matt ma koy xamb nit la ak i xeer, te way weddi ya la ñu koy xaaroo.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷ
Na nga bégal ña gëm tey jëf jëf yu sell, [xamal leen] ne am nañu àjjana joo xam ne ay dex a ngay daw ca suufam ; saa su ñu leen xéewalee ci ay meññeet, muy la ñu leen wërsëgale, ñu naan: “Lii dey masoon nanu cee xéewlu ca bu jëkk [ca àddina]”. Fekk dañu leen a jox lu nurook [la ñu xamoon ca àddina]; ñeel na leen it ca àjjana jooju ay jabar [soxna] yuñu laabal [ci bépp ayib], te ñoom dañu fay béel.
ﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤ
Yàlla du kersawu ci joxe misaal mu mu mën a doon : ci aw yoo walla ci lu ko ëpp ; ñi gëm ñoom xam nañu ne loolu mooy dëgg ; yéefar yi ñoom dañuy wax naan “Moo lan la Yàlla namm ci léebu wii ? ”. Dana ca réeral ñu bari, Dana ca jubal it ñu bari ; waaye du ci réeral ñu dul saay-saay sa,
ﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛ
ñooy ña nga xam ne dañuy firi kóllareg Yàlla ginnaaw ba mu fasoo ba noppi te di dog la Yàlla digle ñu jokkale ko [ag mbokk]. Te ñiy yàq ci suuf si. Ñooña ñooy ña yàqule.
ﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪ
Naka ngeen di weddee Yàlla te ngeen doonoon ñu dee, Mu dundal leen ? Dana leen rey ; dana leen dekkalaat ngeen dellu ca Moom.
ﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿ
Moom moo leen sàkkal lépp lu nekk ci suuf si, daldi jublu ci asamaan si def ko mu nekk juróoom-ñaari asamaan. Te moom nag lépp la xam.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯ
Fàttalikul ba sa Boroom waxee Malaaka ya, ne leen: “Man dey damaa namm a def ci suuf si ag kilifa[kuutaay]. Ñu toontu ne ko : “Moo ndax dangay def ci suuf si koo xam ne dafa ciy nekk di yàq, di tuur i dereet, te nun nu ngi lay sàbbaal, di la sant te di màggal sag sell ? ” – Yàlla ne leen : “Xam naa lu ngeen xamul ! ”.
ﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿ
Mu jàngal Aadama turi lenn lu ne, ba noppi won ko Malaaka ya, ne leen : “Wax leen ma turi yëf yii, ndegam ñu dëggu ngeen ! ”.
ﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍ
–Malaaka ya ne ko : “Tuddu nanu sa sell gi ! Amunu benn xam-xam lu dul loo nu xamal. Ndax Yaw yaay ki xam, Yaay ki xereñ”.
ﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥ
–Mu ne : "Aadama xamal-leen seeni tur ; ” Ba mu leen xamalee seeni tur, Yàlla ne leen : “Ndax dama leen a waxuloon ne Man xam naa kumpag asamaan ak suuf si, te it xam naa xéll li ngeen feeñal ak li ngeen doon ñëbb ? ”
ﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔ
[Fàttelikul] Ba Nu nee Maalaaka ya sujjóotleen ci Aadama, ñu sujjóot ba mu des Ibliis, dafa lànk rëy-rëylu daldi bokk ca way-weddi ya.
ﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧ
Ñu wax ne ko : “Yaw Aadama dëkkal ci àjjana yaak sa soxna, ngeen di fa lekkee na mu leen neexee, ca fa mu leen soobee ; te bu leen jege garab gile : kon dey ngeen bokk ci way- tooñ ña”.
ﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽ
[Séytaane] tarxiisloo na leen, génne leen fa ñu nekkoon. Nu ne leen : “Wàccleen ; di noonuwante. Te itam dangeen am ci kaw suuf ay dëkkuwaay ak i jumtukaay as ndiir”.
ﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆﰇﰈﰉﰊ
Aadama jot na baat ya [baati tuub] bawoo ca Boroomam, Mu daldi ko jéggal, ndax Moom moo di Jéggalaakoon bi, di Jaglewaakoon bi.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣ
Nu ne leen : “Wàccleen yéen ñépp ! Buleen dummóoyu njub gi jóge ci Man, ñi topp sama njub duñu am lu ñu ragal te duñu jàq [ëllëg]”.
ﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯ
Ña weddi te fenloo Sunuy tegtal, ñoom ñooy dëkk Safara te ñoom dañu fay béel.
ﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽ
Yéen [Bani-Israayiil] ñi sëtoo ci [Yanqooba], fàttalikuleen Sama xéewal gi Ma léen xéewaloon. Nangeen matal Sama kóllare, kon Danaa matal seen gos. Buleen ragal ku dul Man.
ﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑ
Nangeen gëm li Ma wàcce, te muy dëggal li ngeen yore ; buleen doon ñi ko jëkk a weddi. Buleen jaay samay laaya ak njëg gu néew. Te nangeen ma ragal Man doŋ.
ﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚ
Buleen jaxase dëgg ak caaxaan, di nëbb dëgg te fekk ngeen xam ko xéll.
ﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢ
Nangeen fonk julli, di joxe asaka, te di rukkoo ànd ak way-rukkoo ya. [Jullig mbooloo, di julli ci biir jàkka yi].
ﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯ
Moo ndax da ngeen di digal nit ñi li baax, fàtte seen bopp, te yéen jàng ngeen Téere ba ? Moo ndax dangeen dul xel-lu ?
ﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚ
Nangeen di dimbandikoo muñ ak Julli : loolu lu diis la ci ku bokkul ci way-ragal Yàlla ña,
ﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣ
ña nga xam ne daleen a wóor ne danañu dajeek seen Boroom te ca Moom lañuy dellu.
ﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯ
Yéen ñi sëtoo ci Yànqooba, fàttalikuleen Sama xéewal gi Ma leen xéewalee woon, te Man ma defaloon leen ngëneel ci kaw nit ñépp.
ﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃ
Ragal-leen bis boo xam ne bakkan du fa jariñ dara beneen bakkan ; te duñu ko nangul rammu ; duñu ko nangul njote. Te deesuleen dimbali.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤ
[Fàttalikuleen], ba Nu leen musalee ci waa kër (Firawna), tegoon nañu leen mbugal mu ñaaw : ñuy rendi seeni doom yu góor ya, di bàyyi ñu jigéen ña. Nekkoon na ci loolu nattu bu réy bu bawoo ca seen Boroom.
ﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯ
[Fàttalikuleen], ba Nu leen xaralee géej ga ! Te Ma musal leen, labal gaa ñi [Firawna], ngeen na ca jàkk di leen gis.
ﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼ
[Fàttalikuleen], ba Nu dëelanteek Muusaa ñeen-fukki guddi ! Te ngeen jaamu yëkk wa ginnaawam, ngeen di way-tooñ.
ﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅ
Ginnaaw ga, Nu baal leen ndax ngeen gërëm [seen Boroom].
ﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍ
[Fàttalikuleen], ba Nu joxee Muusaa Téere ba ak Àtte yay téqale [dëgg ak fen] ndax ngeen gindiku.
ﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩ
Ak ba Muusaa waxee aw nitam : "Samaw nit, yéen tooñ ngeen seen bopp ci li ngeen jaamu yëkk wa. Na ngeen baalu seen Boroom; te ngeen reyante yéen [ñi bokkoon ci moy Yàlla googu] : Looloo gën ci yéen ca seen Boroom” !... Kon mu jéggal leen ndax moom mooy Jéggalaakoon ba, di Jaglewaakoon ba !
ﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙ
Ak ba ngeen waxee ne : “ Yaw Muusaa, dunu la gëm ba ba nuy gis Yàlla ne jàkk ci Moom” !... Faf xaacu ga fàdd leen, ngeen di gis loolu.
ﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡ
Topp Nu dekkal leen ginnaaw ba ngeen deewee, ndax Yàlla ngeen di sant [seen Boroom].
ﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶ
Nu keral leen ak i niir, wàcceel leen lem ak i picc [yu tuddu gëméen], ne leen : - “Lekk leen ci lu sell lii Nu leen xéewale ! ” - Ñoom daal seen bopp lañuy tooñ, waaye du Nun lañuy tooñ.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦ
[Fàttalikuleen it], ba Nu leen waxee ne : “Dugguleen ci dëkk bii, lekk ci fu leen neex cig yaatu ; te ngeen jàll buntu bi ànd ak toroxlu te nangeen ñaan Yàlla mu seppi seeni bàkkaar ; [Su ngeen ko defee,] Nu jéggal leen seeni ñaawtéef, Dananu dolli way-rafetal ña aw yiw.
ﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹ
Tooñkat ya weccee baat ya Nu leen waxoon, ak yeneeni baat yu wuuteek yooya, Nu daldi wàcce ca way-tooñ ña mbugal mu bawoo asamaan ngir la ñu nekkoon di saay-saay [su génn diine].
ﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚ
[Fàttalikuleen], ba Muusaa di sàkkul aw nitam ndox, ba Nu waxee ne : “Dóoral xeer wi ak sa yat wi.” Fukki bëti ndox ak ñaar ballee na ca, giir gu nekk xam na fa muy naanee ! - “Lekkleen te naan ci xéewali Yàlla yi ; te buleen dox ci suuf si di way-yàq”.
ﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼ
[Fàttalikuleen], ak ba ngeen nee : "Yaw Muusaa, nun mënatunoo muñ [di lekk] wenn ñam rekk. Ñaanal nu sa Boroom luy sax ci suuf si ciy fuytéef : xaal, laaj, sëb ak soble ! ” - Mu ne leen : “Ndax dangeen di weccee lu yées ak li gën ? Wàccleen ci menn réewu teeru ; dangeen fa am li ngeen di laaj ! ”. Saddeef na leen toroxte ak ñàkk ; ñu sóobu ci merum Yàlla. Ndax la ñu nekkoon di weddi kàdduy Yàlla ya, di rey Yonent ya ci lu dul dëgg, ngir moy Yàlla ci lu jéggi dayo.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩ
Ña gëm ak ña di Yahuud, ak i Nasraan, ak i Saabiina, ku ca settantal ba dëddu la mu jàppoon, gëm Yàlla ak Bis-pénc ba, gëm Muhammad tey jëf lu yiw , danañu fekk seen pey ca Yàlla ; te duñu tiit te duñu jàq.
ﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹ
Fàttalikuleen], ba Nu jàppee seen kóllare te Nu yékkati doj wa mu tiim leen, te Ma ne leen : “Jàppleen li Ma leen jox ànd ca ak dëgg te na ngeen màggal li ne [ca Téere ba] ndax Yàlla ngeen ragal seen Boroom ! ”
ﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈ
Topp, ngeen dëddu ginnaaw loolu, bu dul koon xéewali Yàlla ci yéen ak yërmaandeem, kon dangeen bokk ca way-yàqule ña.
ﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕ
Wallaahi xam ngeen ña jalgati woon ci yéen ca Gaawu ba. Tax ñoom ñooñu Nu ne leen : “Nekkleen di ay golo yu ñu beddi ! ”
ﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟ
Maka Kami jadikan (yang demikian) itu peringatan bagi orang-orang pada masa itu dan bagi mereka yang datang kemudian, serta menjadi pelajaran bagi orang-orang yang bertakwa.
ﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗ
Fàttalikuleen,) ba Muusaa waxee aw nitam : “Yàlla digal na leen ngeen reyu nag”. Ñu ne ko : “Moo ndax danga nuy ñaawal ? ”. Mu ne : “Yàlla na ma Yàlla musal ci bokk ci way-réer ña ”.
ﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱ
Ñu ne : “Ñaanal nu sa Boroom mu leeral nu luy meloom”. - Mu ne : “Naka Moom nee na : nag wa du wu màggat, du aw sëll, dafa digg-dóomu. Def leen li ñu leen sant”.
ﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅ
- Ñu ne : “Ñaanal nu sa Boroom mu leeral nu luy meloom”. - Mu ne : “Naka Moom nee na: nag la wu gel, wu fees, woo xam ne dees na beg ci xool ko .”.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢ
- Ñu ne : “Laajal nu sa Boroom mu leeral nu nu mu mel, ndax nag yi dañoo bari ci nun. Te bu soobe Yàlla dananu gindiku [Jëfe ndigalam]”.
ﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽ
– Mu ne moom nag : “Nee na, nag la wu ñu bayloowul suuf si, du buy suuxat mbay, bu amul benn laago la te wenn melo la”. - Ñu ne ko : “Agsi nga ci dëgg gi! ” Ñu rendi ko te xawoon nañu koo bañ a def.
ﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉ
[Fàttalikuleen] Ba ngeen reyee bakkan te ngeen jiiñante ko!... Te Yàlla génne la ngeen doon nëbb.
ﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖ
Nu ne : “Dóorleen ko lenn [Lu bokk ci nag wi]”. - Noonu la Yàllay dekkalee ñi dee te dana leen won ay kéemaan ndax ngeen xel-lu.
ﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡ
Topp, seeni xol wow ginnaaw loolu [dëgër] ba mel ni xeer mbaa lu ko gën a tar wowaay ; Ndax ci xeer sax ndox dana ca ball, te am na ci xeer yi yuy xar ndox génn ca, am na ci yuy rot ngir ragal Yàlla. Te Yàlla du ñàkk a seetlu li ngeen di def.
ﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶ
- Moo ndax, dangeen xeemeem [,Yéen jullit ñi,] Yahuud yi wóolu leen? Te am na ci ñoom kurél boo xam ne déggoon nañu waxi Yàlla, ba noppi soppi ko ginnaw ba ñu ca xalaatee ba xam ko.
ﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆﰇﰈﰉﰊﰋﰌﰍﰎﰏ
- Bu ñu dajeek ñu gëm, ne : “Gëm nañu” ; te bu ñu wéetee ñoom doŋŋ, naan : “Ndax dungeen waxtaane li leen Yàlla xamal, nu mën caa sukkandiku [ñoom jullit yi] di dàggeek yéen ci seeni [mbiri] Boroom ! Moo ndax dangeen dul xel-lu ? ”.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚ
- Moo ndax dañoo xamul ne Yàlla xam na la ñuy nëbb ak la ñuy feeñal ?
ﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦ
Am na ca ñoo xam ne mënuñoo jàng, xamuñu téere ba lu dul ay fen yu nekk ay njort doŋŋ.
ﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭾﭿﮀ
Alkaande ñeel na ñay bind téere ba, ba noppi naan lii ca Yàlla la jóge ndax mën caa jële njëg gu néew ! - Alkaande ñeel na leen ngir la ca seeni yoxo bind, ñeel na leen ngir la ñu ca fàggu [ci alal] !
ﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚ
Wax nañu ne : “Safara dunu laal lu dul ay bis yu ñuy waññi ! ”. Neeleen : “Moo ndax dangeen cee déggook Yàlla - te Yàlla du wuute ab digam ; - walla dangeen di wax ci Yàlla lu ngeen xamul”.
ﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪ
Axakay ! Ku def jëf ju bon ba ay ñaawtéefam mëdd ko, ñooña ñooy ñay dëkk Safara te dañu fay béel.
ﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗ
Waaye ñi gëm te def jëf yu sell [Farataak Sunna] ñooña ñoo di ñay dugg Àjjana, dañu fay béel.
ﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯴﯵ
[Fàttalikuleen], ba Nu wóllaranteek (Banii-Israayiil) ne leen : buleen jaamu kenn ku dul Yàlla, te nangeen rafetal seeni jëf jëme ci seeni ñaari waajur, seeni jegeñaale, jirim yi, way- ñàkk ñi, te ngeen waxal nit ñi wax ju rafet ; ngeen fonk julli te génne asaka, ba noppi ngeen dummóoyu ! - Ba mu des ñu néew ci yéen, ngeen di way-dëddu [lu baax].
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠ
[Fàttalikuleen], ba nu wóllaranteek yéen ne buleen tuur seeni deret, buleen génneyante ci seeni kër. Ngeen nangu te seede ko.
ﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖ
Ba noppi ngeen rey aw nit, ci seen biir, am ca ab kurél bu ngeen génne seeni kër, ngeen dimbalante ci ay bàkkaar ak ug noonuwante. Te bi ngeen leen jàppee ci xare di leen fayloo ag njot te di leen génne te loolu araam na ci yéen. Ndax dangeen a dëggal lenn téere ba weddi la ca des ? Kuy def loolu ci yéen, dara du doon peyam lu dul toroxte ci dundug àddina, te Bis- pénc ba dees na leen delloo ci gën jaa tari mbugal, Yàlla dey nekkul Kuy ñàkk a seetlu li ngeen di def.
ﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥ
Ñooña ñooy ña jaay àllaaxira jënde ko àddina. Duñuleen woyofal mbugal ma. Te deesuleen dimbali.
ﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥ
Bir na, ne jox Nanu Muusaa Téere ba ; Nu toxal ginnaawam ay Yonent. Te jox Nanu Iisaa doomu Maryaama ay kéemaan yu leer te dëgëral ko, ak ruu gu sell [Jibril]. Ndax saa yu leen ab Yonent dikkalee [Sant leen] lu neexul seen bakkan, ngeen rëy-rëylu ? Ngeen weddi ab kurél, rey ab kurél [ca ñoom Yonent ya].
ﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱ
Ñu naan : “Sunuy xol muuru na [ci li Yonent bi wax]” - Li am ba des moo di Yàlla rëbb na leen ci sababus seenug weddi, te néewaana bu ñu gëmee.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬ
[Fàttalikuleen] ba leen ab Téere dikkalee, jóge ca Yàlla, di dëggal la ñu yor, - fekk lu jiitu loolu daan nañu ñaan noteel ci yéefar yi, - te ba la ñu xamoon [te daan ko séenu] egsee ca ñoom, dañu koo weddi. Rëbbum Yàlla dal na yéefar yi !
ﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊ
Bon na, la ñu jaayee seeni bakkan ! Ba tax ñu weddi la Yàlla wàcce ngir bew, te iñaan ci li Yàlla wàcce ngënéelam ci ku ko soob ciy jaamam. Ba daldi nañuy mer bay fuuñ-fuuñi, te yéefar yi am nañu mbugal muy toroxale !
ﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪ
Bu ñu leen waxee ne : “Gëmleen li Yàlla wàcce”, Ñu ne : “Gëm nañu li ñu wàcce ci nun”. Te ñoom weddi nañu la ñëw ginnaawam te muy dëggal la ñu yore. - Neel : “Lu taxoon ngeen rey ay Yonentiy Yàlla, ca bu jëkk ndegam gëm ngeen ? ”.
ﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘ
Wóor na céŋŋ ne Muusaa digaloon na leen àndak ay kéemaam yu leer. Ba noppi ngeen jaamu sëll wa ginnaawam, ngeen di way-tooñ.
ﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶ
[Fàttalikuleen], ba Nu wólleranteek yéen, te Nu yékkati doj wa mu tiim leen, [Ma ne leen] : “Jàppleen te farlu ci la Ma leen jox te ngeen dégg [ndigal] ! ”. Ñu ne : “Dégg nanu te bañ nanu”. Nàndaleef na leen seeni xol sëll wa ngir seenug weddi. Neel : “Bon na li leen seen ngëm digal ci loolu ndegam gëm ngeen”.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢ
- Waxal ne : “Ndegam am ngeen kërug àllaaxira ca Yàlla, gu yéen doŋŋ jagoo waliis nit ñi, mébétleen dee kon ndegam ñu dëggu ngeen ! ”
ﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭ
Duñu ko mébét mukk ngir la seen yoxo ya jëf [ci lu bon]. Yàlla ku xam la way-tooñ ña.
ﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉ
Wóor na ne danga leen fekk ñoom [Yahuud ya] ñu nekk di ñu gën a xér ci nit ñi ci bëgg dundu, ak ci ñiy bokkaale. [Danga ca gis] ca ñoom ku ne siiw ñu guddal fanam junniy at. Waaye du ko soreel mbugal ma! Dundu gu guddu googu Yàllaa ngi ne jàkk ci li ñuy def.
ﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜ
Neel : “Ku noonu Jibriil it moom moo wàcce Alxuraan ci sa xol ci ndigalu Yàlla, muy dëggal la ko jiitu, mu di ag njub ak mbégte ci way-gëm ñi”.
ﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩ
[Neel : ] “Ku weddi Yàlla ba noonu ko ak i Malaakaam ak i Yonentam ak Jibriil ak Miikaayil... Yàlla it di ab noonam rekk”.
ﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖ
Bir na ne, wàcce Nanu ci yaw ay kàddu yu leer nàññ, yu kenn du ko weddi ku dul ab saay- saay.
ﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢ
Moo ndax saa su ñu kóllaranteek [Yàlla] ab dëel, kurél ci ñoom firi ko? Li wér mooy li ëpp ci ñoom gëmuñu.
ﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹ
Ba leen Yonent bu jóge ca Yàlla dikkalee di dëggal la ñu yor, gaa ya ñu joxoon ab Téere, ab kurél ca ñoom sànni Téereb Yàlla bi ca seen ginnaaw mel ni dañoo xamul !
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣ
Ñu topp nag la séytaane ya doon jàng ca nguurug Suleymaan. Weddiwul de, séytaane ya ñoo weddi : Daan nañu jàngal nit ña ag njibar ak la ñu wàcce woon ca ñaari Malaaka ya ca (Baabil) (Haaruut ak Maaruut); te daawuñu jàngal kenn te waxuñu ko ne : “Nun dey danoo ànd ak sànje : kon book bul weddi de” ; mu am ñu jàng ci ñoom loo xam ne mën nañu caa téqale jëkkër ak jabaram. Te daawuñu mën a lor kenn ca njibar googule, lu dul ci coobare Yàlla. Te it jàng nañu loo xam ne daf leen di lor te mënuleeen a jariñ. Xam nañu xéll ne ku jënde loolu [weccee ko ak waxi Yàlla] du am benn cër ca àllaaxira. La ñu jaaye seen bakkan bon na ! Cëy bu ñu xamoon !
ﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱ
Bu fekkoon ne ñoom dañuy gëm, te ragal Yàlla [kon mu gën ci ñoom fuuf]. Cëy bu ñu xamoon !
ﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠ
Éy yéen way-gëm yi ! Buleen di wax [sàmmoonteel ak nun], deeleen wax : “Xool nu” ; te deeleen dégg [ndigal] ! Mbugal mu metti mooy dal ca kaw way-weddi ña.
ﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼ
Ña weddi ca ñoñ-téere ya ak way-bokkaale ya yéenewuñuleen, yiw wu bari ba bawoo ca seen Boroom, wàcc ci yéen, te Yàlla dana jagale yërmaandeem ku ko soob. Yàlla mooy boroom ngëneel yu màgg yi.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦ
Dunu folli jenn laaya walla Nu ginnaawal ko fàtteloo ko [nit ñi], te indiwunu bu ko gën mbaa mel ni moom. Xanaa xamoo ne Yàlla mën na lu ne ?
ﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹ
Xanaa xamuloo ne Yàlla moo di Boroom nguurug asamaan ak suuf si, te ginnaaw Yàlla amul keneen ku mën a doon seen kiiraay mbaa seen ndimbal ?
ﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍ
Am dangeen bëgg a laaj seen Yonent na ñu laajee woon Muusaa ca bu njëkk ? Képp ku weccee ngëm ak weddi, réer na te wàcc na yoon wu njub wa.
ﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱ
Ñu bari ci ñoñ-téere [Yahuud ak Nasaraan] nee nañu siiw ñu delloo leen cig kéefar ginnaaw seen ngëm ngir kiñaan gu sosoo seeni bakkan. Ginnaaw ba dëgg ga leeree nàññ ? Baal-leen te dummóoyuleen ba Yàlla agseek ndigëlam. Yàlla nag mën na lu ne !
ﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦ
Deeleen taxawee julli te di génne asaka. Lu ngeen jiital ci lu baax ngir seen bopp, dangeen ko fekk ca Yàlla, ndax Yàlla gu gis la li ngeen di def.
ﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻ
Wax nañu ne : “Kenn du dugg Àjjana ku dul ku nekk (Yahuud walla Nasaraan)”. Loolu dey seen mébét la ñoom. - Neel : “Indileen seenu lay, ndegam ñu dëggu ngeen”.
ﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆﰇﰈﰉﰊﰋﰌﰍﰎ
Axakañ! ku wommatu ci topp Yàlla te muy rafetal, [topp, ci jëfe ndigal ak bàyyi yi Yàlla tere] kooku peyam ma nga ca Boroomam. [Ña mel ni ñoom] duñu tiit duñu jàq.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲ
Yahuud yi wax nañu ne : “Nasraan yi nekkuñu ci dara” ; Nasraan yi itam ne : “Yahuud yi nekkuñu ci dara”, te ñoom jàng nañu Téere ba ! Noonu la ña xamul di waxe. Yàlla dana àtte seen diggante ca la ñu juuyoo bu Bis-pénc baa.
ﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓ
Ana ku gën a tooñ kuy tere, ca jàkkay Yàlla ja, ku cay tuddu Turam te di fexe luy yàq jàkka ja ? Ñooña waruñoo dugg ca [jàkka ja] te ànduñook am tiit. Am nañu gàcce gu rëy ci àddina, te it danañu am mbugal mu rëy ca àllaaxira.
ﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢ
Te Yàllaa moom Penku bi ak Sowu bi. Fu ngeen fi mën a jublu, Kanamu Yàlla jublu na fa, Yàlla ku xam la ; Ku Yaatu la.
ﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕ
Wax nañu ne : “Yàlla am na doom” ! Tudd naa ag sellam[Soreel ko lu yellul ci moom] ! Li fi nekk moo di, Moom Yàlla moo moom lépp lu nekk ci asamaan yi ak suuf si te lépp ci jaamu ko la nekk.
ﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢ
Mooy Aji-sos asamaan yi ak suuf si ! Bu dogalee mbir du def lu dul ne ko : “Nekkal”, mu nekk.
ﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾ
Ña xamul wax nañu ne : “Lu tee woon Yàlla wax ak nun, walla mu indil nu keemaan” ? Noonu la ña leen jiitu woon waxee woon wax ju mel ni seen jos. Seeni xol niroo na. Leeral Nanu laaya ya ci nit ñoo xam ne wóolu lañu.
ﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆﰇﰈﰉﰊ
Yónni nañu la ci dëgg ngay bégal [ñi gëm ci dig leen Àjjana] ; te di xupp [ñi weddi ci mbugalum Safara] te deesula laaj dara [ëllëg ca àllaaxira loo war a layoo] ci mbiri waa Safara
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲ
Yahuud yi ak Nasaraan yi duñu bég ci yaw mukk li feek toppuloo seen diine. - Neel : “Njubug Yàlla mooy dëggi-dëggi njub”. Boo toppee seen bànneex ginnaawal la Nu la digal, ci xam-xam, doo am kenn ku la mën a sàmm, walla ndimbal ci [mbugalum Yàlla].
ﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃ
Ña nga xam ne jox Nanu leen téere ba [Alxuraan], danañu ko jànge na mu yelle, ñooña ñoo ko gëm. Ña ko weddi ñooy way-ñàkk ña.
ﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏ
Yéen Banii-Israayil, fàttalikuleen Sama xéewal yi Ma leen xéewale woon te Man ma defoon leen ngeen gënoon ci kaw mbindéef yépp..
ﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢ
Ragal-leen bis boo xam ne bakkan du fa jariñ dara beneen bakkan te deesu ko nangul njotu, rammu it du ko fa jariñ. Te duñu fa am ndimbal.
ﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛ
[Fàttalikuleen,] Ibraahiima, ba ko Boroomam nattoo, ciy ndigal, mu matal leen, Mu ne ko : “Def Naa la njiit ci nit ñi”. - Ibraayiima ne ko : “[Defal ko] it samay sët”. Mu ne ko : “Sama kóllare du ma ci boole way-tooñ ña de”.
ﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳ
[Fàttalikuleen], ba Nu defee Néeg ba muy delluwaayub nit ñi ak barabub kóolute - Te nangeen def (Màqaama Ibraahiima) barabub jullikaay, - Nu kóllarante ak (Ibraahiima) ak (Ismaahiila) : “Ne leen nangeen sellal Sama Néeg bi ngir ñi koy wër, ak ñi fay toog, di fa rukkoo ak di fa sujjóot [julli].
ﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆﰇﰈﰉﰊﰋﰌﰍﰎﰏﰐﰑﰒﰓﰔ
[Fàttalikuleen] Ba Ibraahiima waxee ne : “Yaw sama Boroom, defal dëkk bii muy dëkkub jàmm [bu am kóolute], te Nga xéewale ciy meññent ñi gëm Yàlla ak Bis-pénc ba, ci waa dëkk bi”, Yàlla ne ko : “Ak ku weddi it danaa ko xéewale ci diir bu gàtt, ba noppi Danaa ko wéyal ci mbugalum Safara. Ndaw delloowaay bu bon” !
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠ
[Fàttalikuleen] Ba Ibraahiima ak Ismaahiila di yékkati ndéttalu néeg ba (Kaaba ga) : "Yaw sunu Boroom nangul nu, Yaw dey Kuy dégg nga, Kuy xam nga.
ﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳ
Yaw sunu Boroom ! Def nu nuy ñaari way-wommatu jëm ci yaw. Te nga def ci sunuy sët askan wu wommatu jëm ci Yaw te nga won nu sunu jaamuwaay, boole ca jéggal nu. Yaw dey Boroom bi, Yaa di Jéggalaakoon bi, di Jaglewaakoon bi.
ﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅ
Yaw sunu Boroom ! Yónneel ci ñoom Yonent bu bokk ci ñoom, bu leen di jàngal say laaya, di leen xamal Téere ba ak i xereñe, te di leen sellal Yaw Aji-not ji , Aji-xereñ ji!
ﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚ
Ana kan mooy bañ diinay Ibraahiima, ku dul ku kannasu ? Nun dey tànn nanu ko ci àddina ; te moom, bu àllaaxiraa it, mu bokk ca ña gën a yiw.
ﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥ
[Fàttalikuleen] Ba ko Boroomam nee : “Wommatul”, Mu ne : “Wommatunaa jëm ci Boroom àddina bi”.
ﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗ
Ibraahiima dénk na ay doomam solo sa, ak Yanqooba, ne leen: “Yéen samay doom, Yàllaa leen tànnal diine de, buleen dee lu dul na fekk ngeen wommatu jëm ca Yàlla” !.
ﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴ
walla sax fekkee woon ngeen ba dee ga dikkalee (Janqooba) te mu ne: “Éy samay doom, ana lan ngeen di xala jaamu sama ginnaaw” ? - Ñu ne : “Dananu jaamu Yàlla sa Boroom tey Yàllaay say baay Ibraahiima, Ismaahiila ak Isaaqa, di jenn Yàlla doŋŋ te nun way-wommatu lanu, jëm ci Moom”.
ﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆ
Woowa xeet jàll na, añe jëfam, yéen itam ngeen añe seeni jëf. Te bu Bis baa, du yéen a leen di layal ñoom ca la ñu defoon.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢ
Ñuy wax naan : “Doonleen Yahuud walla Nasaraan, kon dey ngeen gindiku”. - Neel : “Dée wallaay, diinay Ibraahiima ma wéetaloon Yàlla te bokkut ca way-bokkaale ya”.
ﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂ
Neeleen : “Gëm nanu Yàlla ak li ñu wàcce ci nun [Alxuraan], ak li ñu wàcce woon ca Ibraahiima ak Ismaahiila ak Isaaqa ak Yanqooba ak ca sët ya, ak la ñu joxoon Muusaa ak Iisaa, ya ñu joxoon Yonent ya, mu bawoo ca seen Boroom : dunu xajal kenn ci seen diggante. Te nun way-jébbalu (wommatu) lanu jëm ci Yàlla”.
ﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙ
Bu ñu gëmee Alxuraan kem ni ngeen ko gëmee, kon gindiku nañu. Ñoom Yahuud yi ak Nasaraan yi, bu ñu dummóoyoo rekk daldi dugg ci féewoo ! Yàlla dana la leen fegal. Moom mi di Aji-dégg, di Aji-xam ji.
ﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥ
“Loolu cuubug Yàllaa ! Te ana kan moo gën a rafet Yàlla ag cuub ? Nun dey way-jaamu ko lanu”.
ﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕ
Neel : “Ndax dangeen di dàggasanteek nun ci Yàlla sunu Boroom, di seen Boroom ? Nu moom sunu jëf, ngeen moom seen jëf ! Te nun nag way-sellalal Ko lanuy doon.
ﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷ
Am dañuy wax ne : Ibraahiima, Ismaahiila ak Isaaqa ak Yanqooba ak sët ya ay Yahuud lañu woon walla Nasaraan ? ” - Neeleen : “Ndax yéen a gën xam walla Yàlla ? ” - Waay-waay ana kan moo dàq a tooñ kiy nëbb seede sa nekk fa moom te bawoo fa Yàlla ? Te dey Yàlla sàgganeewul li ngeen di jëf de.
ﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆﰇﰈﰉ
Woowale xeet wéy na di añe jëfam. Yéen itam dangeen añe seeni jëf. Te kenn duleen laaj ana ñoom lañu doon def.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩ
Nit ñu kannasu ñi (matadi) danañu wax ne: “Waa ñii, lu leen wëlbati fabe leen ci xible gi ñu daan jublu ? ” - Neel : “Yàllaa moom Penku moom Sowu. Mooy gindi ku ko soob jëme ko ca yoon wu jub wa”.
ﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛ
Noonu la Nu leen defe [yéen jullit ñi] xeet wu digg-dóomu [di tànneef] ngir ngeen doon seedey nit ñi, Yonent bi itam doon seede ci yéen. Xibla gi nga nekk nag defewunu ko lu dul mën caa xame kay topp Yonent bi ak ka koy dummóoyu. Mu doonoon lu diis, lu dul ci ña nga xam ne Yàlla gindi na leen. Te Yàlla de, sànk seen ngëm taxu koo jóg, ndax moom Yàlla ku ñeewant la, Jaglewaakoon la ci nit ñi.
ﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤ
Gis Nanu la ni ngay wëlbatee sa xar-kanam, di téen ci asamaan. Dananu la méngalee jubluwaay boo gëram. Kon jubaleel sa xar-kanam jëmale ko ca Jàkka ju ñu wormaal ja (Al masjidal Haraam). Fu ngeen mën a nekkati, nangeen ko jublu. Te sax, ñañu joxoon Téere ba [Ñoñ-téere] xam nañu xéll ne mooy dëgg gi bawoo ca seen Boroom. Te Yàlla du sàggane li ñuy jëf de.
ﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆﰇﰈ
Boo indiloon, ñoñ-téere, kéemaan gu mu mën a doon, du tax ñu topp sa jubluwaay (xibla) ! Yaw itam du yaay topp seen xibla ; ñoom ci seen biir sax, kenn du ca topp xibla moroomam. Yaw nag boo toppee seeni bànneex ginnaaw ba la xam-xam bu leer dikkalee, kon de ca tooñkat ya ngay bokk.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠ
Ña ñu joxoon Téere, xam nañu ko ni ñu xame seeni doon. Dafa fekk ne am na ci ñoom kurél bu xam dëgg ba noppi di ko nëbb !
ﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨ
Dëgg, ca sa Boroom la bawoo. Bul bokk mukk ci werentekat yiy sikki-sàkka.
ﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿ
Xeet bu nekk a am jublukaayam . Nangeen njëkkante ci jëf yu baax, yu yiw. Fu ngeen fi mën a nekk nag, Yàlla dana leen dajale yéen ñepp ca Bis-pénc ba, Yàlla mën na lu nekk.
ﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓ
Foo demati, jëmëleel sa kanam ca jàkka juñu wormaal ja ca Màkka. Looloo di dëgg de. Te Yàlla du sàgganee li ngeen di jëf.
ﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕ
Foo mën a demati, jëmaleel sa kanam ca Jàkka juñu wormaal ja ca Màkka. Fu ngeen mën a nekk, nangeen ca jëmale seeni kanam [jublu], ndax nit ñi bañ a am aw lay ci seen kaw, ku dul ñiy tooñ. Te buleen leen ragal ; ragal-leen Ma, man Yàlla, ngir Ma mottali sama xéewal ci yéen ak itam ndax ngeen gindiku !
ﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧ
Noonu, Lanu yónnee ci yéen Yonent bu bokk ci yéen buy jàng ci yéen laaya ya, di leen sellal, di leen xamal Téere ba ak Xereñ ga te di leen xamal itam lu ngeen xamul woon.
ﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮ
Fàttalikuleen Ma, Ma fàttaliku leen. Santleen Ma te buleen ma weddi.
ﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺ
Éy yéen ñi gëm [Jullit ñi] ! Nangeen dimbandikoo ci muñ ak julli. Yàlla ànd na ak way- muñ ña.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟ
Buleen wax ne ñi ñu rey ci yoonu Yàlla dañuy dee de. Ña ngay dundu te yéguleen ko.
ﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭ
Danaa leen farala nattoo lennat ci am tiit, xiif ak wàññikug ay alal, ak i bakkan ak i meññent. Waaye bégalal ñi koy muñ,
ﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸ
ña nga xam ne, saa su leen tiis dalee dañu naan : “Yàllaa nu moom te ca Moom Yàlla lanuy dellu”.
ﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃ
Gaa ñooña am nañu njéggal gu bawoo ca seen Boroom, ak yérmaande ; te ñoo di ña gindiku tigi.
ﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟ
Safaa ak Marwa bokk nañu ci màndargay jaamukaayu Yàlla yi. Ku aj Màkka walla mu Umra , du aay ci moom mu jaabante seen diggante ñoom ñaar. Ku coobarewu te jëf lu baax, lu yiw, na xam ne Yàlla gërëmaakoon la, Aji-xam la.
ﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕ
Ña nga xam ne dañuy nëbb la ñu wàcce ci ag leeral ak ug njub ginnaaw ba ñu ko biralalee nit ñi ca Téere ba, ñooña Yàlla dana leen rëbb, rëbbkat ya itam dana leen rëbb
ﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡ
lu dul ña ca tuub, yéwénal te leeral : ñooña Danaa leen jéggal Man Yàlla. Te Man maay Jéggalaakoon bi, di Jaglewaakoon bi.
ﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯ
Ña weddi te dee ci kéefar, ñooña rëbbum Yàlla ak Malaaka ya ak nit ñépp dana dal ci seen kaw.
ﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹ
Dañuy béel ca rëbb moomu ; kenn duleen ko woyafalal, kenn duleen ko yeexalal.
ﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄ
Seen Yàlla jii, jenn Yàlla rekk la. Amul jeneen yàlla ju dul moom, mooy xéewal bindéef yi ci yërmaandeem ci àddina, di Jaglewaakoonu yërmaandeem jullit ña ca àllaaxira.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼ
Nit ñiy jëfandikoo seeni xel, war naa doy sëkk kéemaan ci ñoom, ni Yàlla binde asamaan yi ak suuf si, jëllasanteb guddi ak bëccëg, gaal yiy daw ci géej ci luy njariñi nit ñi, ak li Yàlla wàcce ci ndox mu bawoo asamaan, mu nàndal ca suuf si ginnaaw ba mu wowee, mu tasaare ca kaw suuf si ay meññeef, walbatim ngelaw leek niir yi nekk diggante asamaan ak suuf.
ﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞ
Am na ci nit ñi ñuy jaamu xërëm bàyyi Yàlla, soppleen ni ñu soppee Yàlla. Ña gëm ñoo gën a tar cofeel ci Yàlla. Ay boo gisoon ña weddi, naka lañuy janook mbugal ma, xam xéll ne kàttan ba kàttan jeex Yàllaa ko am te Yàlla ku tar mbugal la !...
ﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫ
[Bu Bis-pénc baa] ba ñañu toppoon deñtalu ca ña leen toppoon ndax te gis nañu mbugal ma, la leen boole woon lépp daggatoo !
ﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦ
Ña toppe woon, daldi ne : “Ay ! bu nu delluwaatoon àddina! Dananu deñtalu ci ñoom kem ni ñu deñtaloo ci nun” - Noonu la leen Yàlla doon wane seeni jëf ; mu di ag yàqule ca seen kaw te duñu génn Safara.
ﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸ
Yéen nit ñi ! Lekkleen ci li nekk ci suuf si, dagan, teey ; te buleen topp jéegoy (Séytaane) moom seenub noon la bu bir .
ﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄ
Li mu leen di digal moo di ag mbon ak ug caay-caay ak ngeen di wax ci Yàlla lu ngeen xamul.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨ
Bu ñu leen nee : “Toppleen li Yàlla wàcce”, ñu ne : “Nun kay la nu miin [di ko jaamu, baaxu maam ya] lanuy topp.” - Moo ndax ! Seen baay ya doonuñu woon ñu dul xalaat, ñu dul gindiku ?
ﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼ
Ña weddi dañu mel ni ay mala yoo xam ne kàddu duñu ca dégg lu dul coow la. Ñu tëx lañu, gumba, luu, duñu xel-lu.
ﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋ
Ey yéen ñi gëm ! Lekkleen ci yi teey ci lun leen wërsëgal. Te ngeen sant Yàlla, su fekkee moom ngeen di jaamu.
ﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧ
La mu araamal [tere] mooy médd, dereet, yàppu mbaam-xuux ak la ñu tuddu keneen ku dul Yàlla [ba ñu koy rey]. Ku ñàkk pexe nag ci lu dul beew walla jéggi dayo, du am bàkkaar ci xettaliku [ci yooyu], Yàlla Jéggalaakoon la.
ﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦ
Ña nga xam ne dañuy nëbb la Yàlla wàcce ca téere ba jaaye ko njëg gu néew, ñooña Safara lañuy lekk ca seeni biir. Bu Bis-pénc baa, Yàlla du wax ak ñoom, duleen sellal. Te am nañu mbugal mu tar.
ﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳ
Ñooña ñooy jaay njub weccee ko ak réer, jaay njéggal wecee ko ak mbugal. Ñooñu ana kan moo leen gën a mën a dékku Safara?
ﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃ
Loola la muy tegtale moo di Yàllaa wàcce Téere ba ci dëkk; te ña nga xam ne dañoo wuute ca Téere ba, ña nga cig féewoo gu sore.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈ
Mbaax [topp Yàlla] du rekk jubale sa kanam Penku walla Sowu. Waaye mbaax mooy nga gëm Yàlla, Bis bu mujj ba, Malaaka ya, Téere ba ak Yonent ya, te alal ak ni mu neexee ci xol, nga di ko jox ña la jege, jirim yi, way-ñàkk ñi, doxandéem yi, ñay yalwaan ngir loru, jaam bu bëgg a jotu, [batey mbaax mooy] taxawal julli, di génne asaka. Te di mottali kóllare fu mu ko fasantee tey muñ tiis yeek naqar yi, ak tolluwaay yi, diggante yu metti yi, gaa ñooñu ñoo dëggal, ñoo ragal Yàlla !
ﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓ
Éy yéen ñi gëm ! Digal nañu leen ci ku rey nit : gor ya fay gor, jaam ya fay jaam, jigéen fay jigéen. Waaye koo xam ne mbokkam baale na ko, nañu topp ci njekk mu fay dëyya ca namu rafetee. Loolu ag woyafal la gu tukkee ca seen Boroom ak yérmaande. Ku jalgati ginnaaw loolu, dana am mbugal mu metti.
ﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜ
Am ngeen ci feyyu googu dundu [gu yokku], yéen ñi ame xel, ndax Yàlla ngeen di moytandiku.
ﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮ
Digaleef na leen, ku bokk ci yéen te dee dikkal ko te fekk mu am alal ju muy bàyyi ginnaaw, [na def] ab dénkaane bu jëm ci ñaari waajuram ak ay jegeñaaleem cig njekk. Muy lu yell ci kaw ñi ragal Yàlla.
ﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽ
Ku dégg ndénkaane boobu ba noppi soppiku, bàkkaar boobu dafay tegu ca kaw ña ko soppi.Yàlla ku xam la, kuy dégg la.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢ
Koo xam ne ragal na, ca aji-dénkaan ja, jeng walla bàkkaar, mu jubbanti ko rafetal diggante way-dono ya, du ca am bàkkaar, Yàlla ab Jéggalaakoon la, ab Jaglewaakoon la !
ﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱ
Éy yéen ñi gëm!, farataaleef na ci yéen koor, kem ni ñu ko farataalee woon ca ña leen fi jiitu woon, ndaxtelee ngeen [mën caa am] ragal Yàlla,
ﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖ
ay bis yu ñuy lim [weeru Ramadaan]. Ku wopp ci yéen mbaa mu nekk ci tukki, na ko fey ci yeneeeni bis. Ñi nga xam ne àttanuñu koor, nañu jote ci jox ñam way-ñàkk ña. Ku coobarewu ci jëfi yiw, mu nekkal la fa ; ngeen woor nag moo gën ci yéen ; Cëy boo leen xamoon !
ﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧ
Weeru koor, ci la Alxuraan wàcc di njub ci nit ñi ak faramfàcce [diggante dëgg ak i fen] ci njub. Képp ku teewe ci yéen weer wi, na ko woor ! Ku wopp walla mu nekk ci tukki, na fey yeneeni bis. - Yàlla jàppandal na leen te bëggaluleen ag jafeel, nangeen matal lim ba te màggal Yàlla ndaxtelee ngeen [jéem a delloo Yàlla njukkal], sant Ko.
ﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻ
Saa su la samay jaam laajee lu jëm ci Man, [Neeleen : ] Man ku jegeñ laa: Ku Ma woo dinaa ko wuyu, saa su ma woowee. Nañu sàkku Ma wuyu leen te nañu ma gëm ndaxtelee ñu jub, gindiku.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚ
Dagan na ci yéen ngeen di jote ak seeni soxna ci guddiy weeru koor ; ñoom malaan lañu ci yéen, yéen itam malaan ngeen ci ñoom. Yàlla xam na ne dangeen daan wuruj seen bopp. Mu jéggal leen, jéllale. Kon léegi nangeen jonjonteek ñoom, te ngeen sàkku ci li leen Yàlla dogalal ; te nangeen lekk di naan ba ba ngeen di mën a ràññee wëñ gu weex ak gu ñuul ci fajar gi. Ngeen dale fa mottali koor gi ba guddeeti. Buleen jonjook ñoom fekk yéen a ngi wéet ci jàkka yi di jaamu Yàlla. Loolu deytali Yàlla la : buleen ko jéggi. Noonu la Yàlla di biralee ay laayaam ndaxtelee ñu ragal Yàlla.
ﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬ
Buleen lekk seeni alal ci seeni diggante cig neen, te buleen cay ger àttekat ya ngir mën a labaj ba lekk ci alali nit ñi, ci bàkkaar te xam ko [xéll].
ﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮ
Danañu la laaj ci terutel weer yi - Neeleen : “Ay takkukaayu waxtu lañu ci nit ñi ak nattukaayi aj Màkka. Te mbaax [mbaaxu Yàlla] du tekki duggu kër jaare ko ñoot ya [ginnaaw]. Waaye mbaax [jaamu Yàlla] moo di dugge kër ca buntu ya àndak ragal Yàlla. Ay waay ragal-leen Yàlla ndaxtelee ngeen texe ! ”.
ﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽ
Xeexleen ci yoonu Yàlla ak ña leen di xeex, te buleen jéggi dayo di tooñ Yàlla. Yàlla dey soppul ñay jalgati !
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮ
Reyleen leen, fu ngeen fi dajeek ñoom ; Nangeen leen génne fa ñu leen génne woon : [Sànje] moo gën a tar reyaate. Buleen xeex ak ñoom fa Màkka ndare du ñoom ñoo leen fa songu. Bu ñu leen fa songee nag, reyleen leen. Loolu mooy peyub yéefar yi.
ﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵ
Bu ñu génnee ci kéefar ga nag, Yàlla ab Jéggalaakoon la, ab Jaglewaakoon la.
ﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆ
Nangeen xeex ak ñooña ba sànje dootul am, diinay Yàlla rekk taxaw fi. Bu ñu bàyyee sànje nag, ku toppati ñu nekkalko ca ak moom.
ﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟ
Weer wuñu wormaal [Araamal], tere ku ca xeex, dañu koy feyee ak weer wuñu wormaal ! - Yu ñu wormaal ya dañuy feyante -. Ku leen ca tooñ, feyyuleen kem la mu leen tooñ. Te nangeen ragal te xamleen ne Yàllaa ngi ànd ak ñi ko ragal.
ﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯ
Nangeen di joxe alal ci yoonu Yàlla. Te buleen sànni seen bopp ci alkaande. Te nangeen di rafetal. Yàlla nag sopp na ñay rafetal.
ﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆﰇﰈﰉﰊﰋﰌﰍﰎﰏﰐﰑﰒﰓﰔﰕﰖﰗﰘﰙﰚﰛﰜﰝﰞﰟﰠﰡﰢ
Nangeen matal Aj ak Umra ngir Yàlla. Bu amee lu leen gaar, tere leen a mottali seen aj, nangeen rey ëdyu ca na mu yombee ci yéen. Te buleen wat seeni bopp, ba ëdyu ba àgg ca barabam. Ku wopp ci yéen walla mu am lor ju ko gaar ci boppam, na jotu ci saraxe walla mu woor walla mu rey gàtt. Bu ngeen nekkee ci kóolute, naka ku bëgg xéewu ci Umra booleek Aj, la ko yomb ci ëdyu te jàppandi lay def. Su amul ëdyu mu woor ñetti fan ca aj ga, mottali juróom-ñaari fan bu delloo fa mu dëkkoon, muy fukki fan yu mat sëkk. Looloo war ku dëkkul ci wetu Jàkka jañu wormaal [Màkka]. Te nangeen ragal Yàlla. Te xam ne Yàlla mbugalam tar na.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲ
Aj ci ay weer yu ñu xam [lañu koy def]. Ku dugg ci aj, bumu sëy [béej], bumu def lu ñaaw, bumu dàggasante ca biir aj ga. Lu ngeen def ci lu baax Yàlla xam na ko. Nangeen yóbbalu ; te yóbbal bi gën mooy ragal Yàlla. Ragal-leen Ma, yéen woroom xel yi !
ﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏ
Aayul ci yéen ngeen sàkku wërsëg [jënd ak jaay]. Bu ngeen bàyyikoo [Harafaat], nangeen tudd seen Boroom fa Mach-haril Haraam . Tudduleen Ko, fàttalikuleen Ko kem na Mu leen gindee, fekk la ko jiitu ngeen doonoon ñu réer.
ﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝ
Topp, ngeen wéy [yéen waa Màkka] bëbb yéen itam fa nit ña bëbbee, jéggaluleen Yàlla. Yàlla Jéggalaakoon la te Jaglewaakoon la.
ﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘ
Bu seen aj jeexee, nangeen di tuddu Yàlla kem na ngeen daan tuddee [taggee] seeni maam, walla sax tuddiin wu gën a tar. Am na ci nit ñi ñuy wax ne : “Yaw sunu Boroom! May nu àddina [kese] ! ” - te duñu fàggu dara ngir àllaaxira.
ﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧ
Am na ci ñoom kuy wax ne : “Yaw sunu Boroom ! Defalnu xéewal ci àddina, ak ca àllaaxira ; te fegalnu mbugalum Safara ! ”.
ﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱ
Ñooña am na ñu yool ca la ñu sàkku. Te Yàlla ku gaaw la ci xayma [waññi, màndaxe].
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮ
Nangeen di fàttaliku Yàlla ci ay bis yuñu lim. Ku yàkkamti ba def ko ci ñaari fan du ca am bàkkaar, kay toog fa [Munaa] ñatti fan du ca am bàkkaar ci ku ragal Yàlla. Ragal-leen Yàlla te ngeen xam ne dees na leen fang [Jiital/gur-gur] jëme ci Moom.
ﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀ
Am na ci nit ñi seeni wax dalay yéem lool, ci dundug àddina ndax day seedeloo Yàlla la nekk ca xolam, ndekeyoo moom xulóowaale la bu pànk, bu yées.
ﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐ
Bu nee wërëñ rekk tàmbalee yàq ci kaw suuf, di alag mbay mi ak jur gi te Yàlla bëggul ag yàq.
ﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟ
Te Bu ñu ko nee : “Ragalal Yàlla”, mu jomlu sax ci bàkkaar rekk, Safara dana ko doy ag pey, te bon na, lal ba ko fay xaar !
ﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬ
Am na ci nit ñi ñuy jaay seen bakkan ngir sàkku ngërëmul Yàlla. Yàlla dey Aji-ñeewant la ci jaamam ñi.
ﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞ
Éy yéen ñi gëm ! Dugguleen yéen ñépp ci jàmm ji [Islaam], te buleen topp yoonu [Séytaane], moom seenub noon la bu bir.
ﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫ
Bu ngeen tarxiisee, ginnaaw ba ngeen amee faramfàcce gu leer nàññ, xamleen ne Yàlla ku màgg kàttan la te ku xereñ la.
ﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾ
Moo ndax dañuy xaar ba Yàlla dikkal leen [ak mbugal] ci keri niir yi ak Malaaka yi, fekk àtteef na mbir ya ba noppi ? Te mbir yépp ca Yàlla lañuy dellu.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦ
Laajal Banii-Israayiila ñaata yoon lañu leen indil ay kéemaan yu leer nàññ [bari na] ! Képp ku soppi xéewali Yàlla ginnaaw ba mu ko jotee... na xam ne, Yàlla ku tar mbugal la.
ﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽ
Ña nga xam ne dañoo weddi, doyloo nañu dundug àddina ak ub taaram, ba tax ñuy yejji ña gëm. Waaye ña ragal Yàlla ñoo leen di gënu demiin bu Bis-pénc baa. Ndax Yàlla dana wërsëgal ku ko soob ci lu àndul ak natt.
ﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓ
Nit ñépp wenn xeet lañu woon. Yàlla yónni ay Yonent yuy bégle di xuppe ; wàcceloon na leen ay Téere ci dëgg ngir ñu àtte diggante nit ñi ci seeni bejoo. Te ña ko ca jot doŋŋ ñoo ca juuyoo, ginnaaw ba mu leeree ca ñoom nàññ, te juuyoo googu doonut lu dul mbewte ! Yàlla mooy saytu ña ko gëm, mu gindi leen ci seenug juuyoo ci dëgg. Yàlla mooy gindi ku ko soob jëme ko ci yoon wu jub xocc wa.
ﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴ
Am dangeen a jort dugg Àjjana [yéen jullit ñi] te dajuleen lu toll ni la ñi leen jiitu dajoon ? Ñoom dajoon nañu ay tar-tari jamono ak ñàkk ; ak tiitaange ba ab Yonent ak gaa ña mu àndal daanañu wax ne : “Kañ la ndimbalu Yàlla di ñëw xettali nu ? ” - Xamleen ne ndimbalu Yàlla lu jege la.
ﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆﰇﰈﰉﰊﰋﰌﰍ
Danañu la laaj : “Lan lañu war a joxe ci alal ? ” - Neel : “Li ngeen di joxe na jëm ci seeni ñaari waajur, ak seeni jegeñaale, ak jirim yi, way-ñàkk ñi, ak doxandeem yi. Lu ngeen def ci lu baax, Yàlla xam na ko”.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭ
Farataal nañu ci yéen xare te bëgguleen ko. Amaana, ngeen bañ mbir te fekk na moo baax ci yéen. Amaana it ngeen bëgg mbir te fekk na baaxul ci yéen. Yàlla xam na te yéen xamuleen.
ﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮ
- Danañu la laaj lu jëm ci weer wuñu wormaal, ku ca xeex. - Neel : “Xeex ca bàkkaar bu rëy la, ak tere nit ñi ñu dugg ci diine, ak jàkka juñu wormaal ja, ak génne ña nekk [Màkka] moo gën a rëyati fa Yàlla ci bàkkaar. Te fitna [sànja] moo gën a màgg rey.” Yéefar ya duñu deñ di xeex ak yéen, ba ba ñu leen di génne ci diine. Seeni jëf sippiku na àddina ak àllaaxira. Te ñooña ñoo di waa Safara : te dañu fay béel.
ﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡ
Ña gëm ak ña gàddaay tey jihaad [xeex] ci yoonu Yàlla, mën nañoo yaakaar yërmaandey Yàlla. Te Yàlla Jéggalaakoon la, Jaglewaakoon la.
ﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁ
- Danañu la laaj lu jëm ci sàngara ak wure. Neel : “Ñoom ñaar bàkkaar bu rëy a nga ca ak njariñi nit ñi ; waaye, la cay bàkkaar ca ñoom ñaar moo ëpp fuuf njariñ ya”. Danañu la laaj : “Lan la ñu war a joxe ci alal? ” Neel : “Aw des.”. Noonu la leen Yàlla di leeralee laaya ya ndaxtelee ngeen di xalaat
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱ
ci àddina ak ca àllaaxira ! Te danañu laaj lu jëm ci jirim yi. Neel : “Yéwénalal-leen [ba seeni alal mën a yokk]. Moo gën bu ngeen jaxasoo ak ñooñu, aayul ndax seeni mbokk lañu ci diine”. Yàlla xàmmee na ñiy yàq ak ñiy defar. Te bu sooboon Yàlla mu sonnal leen. Moom Yàlla moo not lépp, moo xereñ.
ﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟ
Buleen takk soxna jigéen ñuy bokkaale li feek gëmuñu, jaam bu jigéen bu gëm moo gën jigéen [ju ñuy tuddeeb sang] juy bokkaale, doontale yéem na leen. Buleen may jabar góor ñuy bokkaale, jaam bu góor moo gën góor [gu ñuy tuddeeb sang] guy bokkaale, doontale yéem na leen. Ñooña dañuy woote jëme Safara ;Yàlla moom di woote jëme Àjjana ak ug njéggal, ci ndigalam. Te dana leeral ay laayaam nit ña ndax ñu fàttaliku [seen Boroom] !
ﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟ
- Danañu la laaj lu jëm ci mbërëg . - Neel : “Moom sobe la. Deeleen beru jigéen ña bu ñu nekkee ci mbërëg, buleen jege ba bañuy laab. Suñu laabee, ngeen duggeleen fa Yàlla digle ndax Yàlla sopp na ñay tuub, sopp na itam ñay laabal seen bopp”.
ﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳ
Seeni soxna [jabar] seeni tool lañu ; dikkeleen seeni tool ca na mu leen neexee te ngeen jiital ngir seen bopp, buleen fàtte tudd Yàlla. Te ngeen ragal Yàlla te ngeen xam ne dangeen dajeek Moom. Te nanga bégal way-gëm ña !
ﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃ
Buleen di giñ ci Yàlla, ba mu nekk gàllankoor gu leen teree def lu baax, walla ragal Yàlla mbaa yéwénal diggante nit ñi. Yàlla kuy dégg la te ku xam la.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠ
Yàlla duleen jàppe ngiñ ci kaf : Waaye Dana leen jàppe ngiñ lu seeni xol dëggu. Yàlla jéggalaakoon la te ku lewet la.
ﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯ
Ña giñ ci [beru] seeni jabar, nangeen leen muñal ñeenti weer. Bu ñu delloo ginnaaw [ca la ñu giñoon], Yàlla Jéggalaakoon la te Jaglewaakoon la !
ﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷ
Bu ñu dogoo ci pase, Yàlla kuy dégg la te ku xam la.
ﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥ
Jigéen ñi ñu fase, nañu muñandiku téye seen bopp [bala ñoo dugg ci beneen sëy] ba ba ñuy am ñetti mbërëg ; te daganul ci ñoom ñuy nëbb la Yàlla bind [sos] ci seeni njurukaay [su ñu ëmbee], njéem gëm nañu Yàlla ak Bis-pénc ba. Seeni jëkkër ñoo gën a yay ci jëlaat leen ndeem namm nañoo defaroo ñoom jigéen ña. Am nañu yelleef yu tollook seeni wareef ci njekk. Waaye góor ñee yor kiliftéef ga ca seen kaw [ñoom jigéen ña]. Yàlla ku not la, ku tedd la te ku xereñ la.
ﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺ
Pase ci ñaari anam la am. Téye bu yiw walla bàyyi ci njekk [la leen Yàlla digal]. Waaye daganul ci yéen ngeen nangu dara ca la ngeen leen joxoon, - lu dul bu ñu ragalee jéggi daytali Yàlla yi. Bu ñu ragalee nag ca ñoom ñaar, ndaw sa na joxe alal ja mu jot. Loolu moo di deytali Yàlla yi. Buleen ko jalgati. Ñay jalgati [jéggi] daytali Yàlla yi ñooy tooñkat ya.
ﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆﰇﰈﰉﰊﰋﰌﰍﰎﰏﰐﰑﰒﰓﰔﰕﰖﰗﰘﰙﰚﰛ
Bu ko fasewaatee [ñetteelu yoon] du dagan mu jëlaat ko ginnaaw ga. Ba ba muy sëy ak jeneen jëkkër ju dul moom joo xam ne su ko fasee moom it mu daldi ragal delloowante [ndaw sa ak jëkkër ju jëkk ja], njeem njort nañu ne dana sàmmonte ak daytali Yàlla yi. Muy leeralal nit ñi amug ràññee.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃ
Bu ngeen fasee aw jigéen, ba seeni idda [àpp] di waaj a mat, nangeen leen dencaat bu yiw, walla ngeen bàyyi leen ci njekk. Te buleen leen téye ngir bëgg leen a lor : di jalgati, ku def loolu topp na boppam. Buleen jàppe laayay Yàlla yi ay caaxaan. Fàttalikuleen xéewal yi leen Yàlla defal, ak li mu leen wàcceel ci Téere, ak xereñe, di leen ca waar. Kon ragal-leen Yàlla, te ngeen xam ne Yàlla xam na lépp.
ﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨ
Bu ngeen fasee aw jigéen, ba seen idda mat, buleen gàllankoor bu ñu bëggee sëyaat ak seeni jëkkër, bu ñu ca dogoo te nangulante ko. Yàllaa cay waar képp ku bokk ci yéen te gëm Yàlla ak bis bu mujj ba [Bis-pénc ba]. Loolu moo gën a sell ci yéen te moo gën a laab. Yàlla xam na te yéen xamuleen.
ﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆﰇﰈﰉﰊﰋﰌﰍﰎﰏﰐﰑﰒﰓ
Nday ya nañu nàmpal seeni doom ñaari at yu mat sëkk ci ku bëgg nàmpal gu mat. War na ca baay ya dundu ak koddaayu jabar ja ci njekk. Tegeesul kenn lu dul la mu àttan. Wareesul a lor ndey ja ci [nàmpal doomam, baay ba it wareesu koo lor ci doomam]. Aji-nàmp ja donn alal looloo ko war. Te ñu génne ci alalam peyu nàmpal ga. Su ñu bëggee feral [liir ba] ci ña jaboote ñoom ñaar, diisoo ca aayul ci ñoom ñaar ñu def ko. Bu ngeen bëggee nàmpal-lu seeni doom yéen baay yi, aayul ngeen def ko, bu joxee pey gu jaadu ci njekk. Nangeen ragal Yàlla te xam ne Yàllaa ngi ne jàkk ci li ngeen de def
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬ
Ña dee ci yéen te bàyyi ginnaaw ay jabar : nañu muñandiku [ñoom jabar yooyu] ñeenti weer ak fukki fan. Bu ñu matalee àpp ba amatuleen wareef ca la ñu def ci seen bopp, ci lu yiw. Yàlla deñ na kumpa ci li ngeen di def.
ﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠ
Aayul ci yéen ngeen gaaral [seen yéene] ci wàllu labat, ci jigéen ju nekk ci biir iddaam mbaa ngeen nëbbandi seeni yéene ci seeni xol. Yàlla xam na ni dangeen def seeni xol ci ñoom. Waaye nag buleen daldi dige sëy ak ñoom cig nëbbu, lu dul ngeen wax waxiin wu yiw. Waaye buleen dogu ci fas ab sëy li feek àpp ba matul. Te ngeen xam ne Yàlla xam na li nekk ci yéen. Nangeen ko wattandiku te xam ne Jéggalaakoon la, ku lewet la.
ﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝ
Du bàkkaar ci yéen ngeen fase jigéen joo xam ne jotuleen koo laal, walla joo xam ne nanguwantewuleen can.Waaye nangeen leen jox dara - aji-woomal na joxe kem kàttanam, aji- néew doole itam kem kàttanam - muy yóbbal bu jaadu ci dëgg. Di wareef ci ñiy rafetal.
ﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄ
Bu ngeen fasee jigéen te fekk jotuleen koo laal, te nanguwante woon ngeen can, nangeen leen bàyyil genn-wàllu can ga, lu dul mu jéggale walla ka yor pas-pasu sëy ba [jëkkër ja] jéggalu. Jéggalu moo gën a jege ragal Yàlla. Buleen fàtte jëflante bu rafet ci seeni diggante. Yàllaa ngi ni jàkk ci li ngeen di def.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙ
Sàmmoonteleen ak julli rawati na julli gu digg-dóomu ga ; te ngeen taxaw temm cig jaamu Yàlla.
ﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪ
Bu ngeen ragalee [seen noon bett leen], mën ngeen a dox walla ngeen gawaru di julli. Bu ngeen nekkee ci kóolute, amuleen dara lu ngeen di ragal, fàttalikuleen te tudd Yàlla [ci biir julli ga] ni mu leen xamalee lu ngeen xamul woon.
ﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈ
Ña dee ci yéen te ñu bàyyi ginnaaw ay jabar, [war na] ñu dénkaaneel leen [ci seeni alal] ab yóbbal lu jëm at te bu ñu leen génne. Bu ñu génnee seen bopp nag, dungeen ca am bàkkaar ca lañu def ci seen bopp ci lu jaadu, Yàlla ku not la [tedd] te ku xereñ la.
ﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐ
Jigéen ñañu fase war nañoo am ab yóbbal bu jaadu, di wareef ca ña ragal Yàlla.
ﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘ
Noonu la leen Yàlla di faramfàcceelee laayaam ya ngir ngeen xel-lu.
ﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘ
Moo ndax gisoo ña génn seeni kër, - ñuy ay junni, - ngir ragal dee ? Yàlla ne leen : “deeleen”. Daldi leen dekkalaat. Yàlla mooy Boroom ngëneel, ci nit ñi ; waaye li ëpp ci nit ñi duñu gërëm [seen Boroom].
ﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢ
Nangeen di xeex ci yoonu Yàlla. Te xam ne Yàlla kuy dégg la te ku xam la.
ﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴ
Képp koo xam ne lebal na Yàlla lebaliin [bor] bu rafet, dana ko ko fulal ay yoon yu bari. Yàlla mooy xatal di yaatal. Te ca Moom ngeen di dellu.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋ
Moo ndax gisoo mbooloom kilifaay Banii-Israayiila ya, ca ginnaaw Muusaa, ba ñu waxee seen Yonent ne : “Yónneel nu ab buur ndax nu mën a xeex ci yoonu Yàlla”. Mu ne leen : “Xéy-na yéen bu ñu leen joxee ndigal ci xeex da ngeen xeex ? ” Ñu tontu ne : “Lu ñu nekkal ci bañ a xeex ci yoonu Yàlla te ñu génne nu ak sunuy doom, ca sunuy kër ? ”. Ba ñu leen joxee ndigal ci xeex dañoo lànk, lu dul lim bu néew ci ñoom. Yàlla xam na tooñkat ya.
ﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜ
Seen Yonent ba ne leen : “Yàlla yónni na leen [TaaLóota] mu nekk seen buur.” Ñu ne : “Naka lay mën a nekkee sunu buur ? Te nun noo ko gën a yeyoo nguur gi ci moom. Te amul alal ju bari ! ” Mu ne leen : “Yàlla moo ko tànn ci seen kaw, dolli na ko kàttan ci xam-xam ak ci yaramam.” - Yàlla mooy jox nguuram ku ko soob. Yàlla ku yaatu la te ku xam la.
ﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼ
Seen Yonent ne leen : “Liy tegtale ne mooy nekk buur, dana ñu leen jox waxande; woo xam ne dal xel mooy nekk ca biiram tukkee ca seen Boroom, ak desiit ca la waa kër [Muusaa] bàyyi ak waa kër [Haaruuna]. Ay Malaaka ñoo koy yor. Loolu màndarga la, ndeem ñu gëm ngeen ! ”
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑ
Ba TaaLóota génnee ànd ak ay xarekatam, mu ne leen : “Yàllaa ngi leen di nattu ci ag dex : ku ca naan dootoo bokk ci man ; ku ca mosul ci man nga bokk ; - ak ku ca corfati lu néew ci loxoom.” Naan nañu ca ñoom ñépp lu dul lu néew ca ñoom. Ba ñu jàllee dex ga, moom [TaaLóota] ak ña gëm te ànd ak moom, ñu ne : “Amunu tey kàttan [gu nu xeexee] ak [JaaLóota] ak i xarekatam ! ” Ña gëm ne danañu dajeek seen Boroom wax ne : “Bariwaana bu mbooloo mu néew note mbooloo mu bari. ! Te it Yàlla ànd na ak way-muñ ña”.
ﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡ
Ba ñu génnee jëm ca JaaLóota ak i xarekatam, ñu ne : “Yàlla sunu Boroom ! nanga sotti ci nun muñ, te nga saxal sunuy tànk te nga defal nu ndimbal ci kaw nit ñu weddi ñii”.
ﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟ
Nu def ci ndigalu Yàlla [Daawuda] rey [Jaaluta] ; Yàlla jox ko nguur ga ak xam-xam, xamal ko ca la ko soob. Bu dul koon ak li Yàlla di fege aw nit ak ñeneen, kon suuf si dana yàqu. Waaye Yàlla mooy Boroom ngëneel yi muy sotti ci mbindéef yi.
ﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪ
Kàddug Yàlla googu dananu la ko jàngal ci dëgg.Te yaw [Muhammad] (saw), ci Yonent yi nga bokk.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋ
Yonent yooyu, gënal nanu ñenn ci kaw ñeneen ña ; Am na ci ñu Yàlla wax ak ñoom, yékkati ñenn ña seeni daraja. Te jox Nanu (Iisaa) doomu Maryaama lay yu leer nàññ, dëgërale ko Ruu gu Sell. Bu sooboon Yàlla, ñi ñëw seen ginnaaw duñu reyante, ginnaaw ba ñu jotee lay yu leer nàññ ; waaye dañoo juuyoo : mu am ca ñoom ñu gëm, am it ñu weddi. Bu sooboon Yàlla, duñu xeex ; waaye Yàlla dana def la mu namm.
ﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢ
Yéen ñi gëm ! Nangeen joxe ci alal ji Nu leen wërsëgal, bis dina ñëw boo xam ne amul xaritoo, amul njotu, amul tinu. Te ña weddi ñooy tooñkat ya de.
ﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾ
Yàlla dey ! Amul jeneen Yàlla ju dul Moom, Aji-dundu la, Aji-taxaw la, lépp la taxawe. Ngëmméntu du ko jàpp waxatumalaak ay nelaw. Moo moom li nekk ci asamaan yi ak ci suuf si. Ana kan moo sañ a tinu ca Moom te du ci ndigalam ? Moo xam la nekk ci seen kanam ak la nekk ca seen ginnaaw. Te kenn du peeg daraja ci xam-xam lu dul la ko ca soob. Gàngunaayam ga daj na kaw ak suuf, lu leen wattu ñoom ñaar jaaxalu ko. Mooy ki Kawe te Màgg.
ﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆﰇﰈﰉﰊﰋﰌﰍﰎﰏﰐﰑﰒﰓﰔﰕﰖﰗﰘﰙﰚ
Nargan warul am ci diine ! Ndax jub ràññeeku na [doon lu] wuute ak réer. Ku weddi mbiri Séytaane te gëm Yàlla jàpp na ca buum ga gën a dëgër [du dog mukk]. Yàlla kuy dégg te ku xam la.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬ
Yàlla moo féetéek ñi gëm : Moo leen di génne ci ay lëndëm di leen jëme ci ag leer. Ña weddi nag Séytaaney seen péete, Mu leen di génne ci leer jëme leen ci ay lëndëm. Ñoom ñooy waa Safara, te dañu fay béel.
ﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚ
Moo ndax gisuloo ka doon dàggasanteek Ibraahiima ci ay mbiri Boroomam te Yàlla joxoon ko nguur ? Ba ko Ibraahiima nee : “Sama Boroom mooy dundal mooy rey”, mu ne ko : “Man it danaa dundal danaa rey.”. Ibraahiima ne ko : “Yàlla mooy fenkal jant bi ci penku bi, yaw indi ko ci sowu.”. Ku weddi ka janaxe na. Te Yàlla du gindi tooñkat yi.
ﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆ
Walla ka romboon ab dëkk bu ràppoon ba ruus, mu ne : “Waa naka la Yàlla di dundalee lii ak ni mu dee te wow ? ”. Yàlla daldi koy rey moom lu tollu ci téeméeri at. Daldi koy dekkalaat, ne ko : “Sab yàggaay fii nu mu tollu ? ”. Mu ne ko : “Benn bis walla sax matu ko.”. Yàlla ne ko : “Am nga fi téeméeri at. Xoolal sa lekk gi ak sa naan gi : soppikuwuñu ; waaye xoolal sa mbaam mi... Te ngir nu def la kéemaan ci nit ñi, xoolal ni nuy dajalee yax yi, ba noppi wodde ko yàpp”. Ba mu ko leeree nàññ nag, mu daldi ne : “Xam naa xéll ne Yàlla mën na lu ne”.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼ
[Fàttalikul] ba Ibraahiima waxee ne : “Sama Boroom ! Won ma ni ngay dekkalee ku dee”, mu ne ko : “Xanaa dangaa gëmul? ”. Mu ne ko “Axakay ! Waaye ngir sama xel dal”. Mu ne ko : “Jëlal ñeenti njanaaw, teppasleen , boo noppee nga teg ci kaw tund wu ne aw dogit, boo noppee nga woo leen : danañu yëngatu wutsi la. Yàlla Aji-not [tedd] la te ku xereñ la.”
ﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗ
Méngaleg ña nga xam ne dañuy joxe seeni alal ci yoonu Yàlla mi ngi deme ni wenn pepp wu sax, seqi juróom-ñaari gupp, gupp wu nekk am téeméeri fepp. Yàlla mooy fulal ku ko soob,Yàlla ku yaatu ku xam la.
ﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰ
Ña nga xam ne dañuy joxe seeni alal ci yoonu Yàlla te duñu toftale ca la ñu joxe ñax walla kañu , danañu am seenug pey fa Yàlla seen Boroom. Duñu tiit, duñu jàq.
ﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟ
Wax ju yiw ak ag njeggal moo gëm sarax boo xam ne wax ju ñaaw a ca topp. Yàlla ku woomal la, ku lewet la.
ﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆﰇﰈﰉ
Éy yéen ñi gëm ! Buleen yàq seeni sarax ci ñax ak kañu, képp ku joxe alal ngir ngistal ci nit ña te gëmul Bis-pénc ba. Dafay mel ni doj wu suuf tegu ca kawam ; waame sottiku ca, bàyyi ko mu ratax bandaŋ. [nit ñu mel noonu] duñu mën a def dara lu barkeel. Te Yàlla du gindi nit ñu weddi.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭ
Melow ñi joxe seeni alal ngir sàkku ngërëmul Yàlla, ak saxal seeni bakkan ci jaamu Yàlla, dafa mel ni tool bu nekk ci aw tund. Waame [taw] dal ca, mu génne ñaari yoon meññeefam ; bu ca waame dalul itam, mësay ma naatal ko. Yàllaa ngi ne jàkk ci li ngeen di def.
ﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒ
Kenn ci yéen bu amoon toolu garabu tàndarma ak reseñ, ndox ya di daw ca biir, mu bari lool meññent, fekk mu nekk mag, ame njaboot gu sew, ndax dana bëgg callmeer lu ànd ak safara dal ca tool ba lakk ko ? Noonu la Yàlla di faramfàccee ay laayaam ndaxtelee ngeen di xalaat !
ﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓ
Yéen ñi gëm ! Deeleen joxe asaka ci lu téey li ngeen di fàggul seen bopp ak li Nu leen génneele ci suuf si. Buleen ca beddi la ca yées di ko joxe. Te fekk muy loo xam ne ku leen ko joxoon dungeen ko bëgg a jël, te gëmmuleen ca ! Nangeen xam ne Yàlla ku woomal la te ku yayoo cant la.
ﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣ
Séytaane, ag ñàkk la leen di dig, di leen xiir ci moy ;Yàlla nag, jéggal la leen di dig ak wërsëg wu bawoo ca Moom. Yàlla ku yaatu, ku xam la.
ﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶ
Mooy jox ku ko soob xel mu rëy, rafet . Ku Mu jox xel mu rafet, jox na ko njariñ lu rëy. Te boroom xel ya rekk ay waaru.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡ
Li ngeen joxe mu génn walla ngeen nisar ko , Yàlla xam na ko. Ñiy tooñ, duñu am ndimbal !
ﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹ
Bu ngeen feeñalee seeni sarax, baax na ; bu ngeen ko nëbbee, jox ko wax-ñéew ji doole ya nag, moo gën ci yéen. Danañu leen jéggal ci seeni ñaawtéef [ci soppi ko aw yiw]. Yàlla ku deñ-kumpa la ci li ngeen di def.
ﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚ
Seenug njub waru la, waaye Yàlla mooy jubal ku ko soob. Lu ngeen joxe ci alal, seen bopp ngeen ko defal, dungeen joxe lu dul ngir jëmmi Yàlla. Xamleen ne li ngeen joxe ci alal dangeen ca jotaat. Te duñu leen ca deseel dara.
ﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛ
Ay sarax ñeel na ña nga xam ne dañoo tënku ci liggéeyu Yàlla, mënuñoo dem di wuti wërsëg ci suuf si, ña réer dañuy defe ne ñu woomal lañu ndax seenug fegu - danga leen xamee ci seeni màndarga - Duñu laaj nit ñi dara. Lu ngeen joxe ci alal Yàlla xam na ko.
ﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭ
Ñi nga xam ne dañuy joxe seeni alal, guddi ak bëccëg, ci lu nëbbu ak lu feeñ, ñooña am nañu seenug pey fa seen Boroom te duñu jàq.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃ
Ñay lekk ribaa, [duñu jóg] ci seeni bàmmeel lu dul jógeenu ku Séytaane daaneel, sadd ko saddum jinne. Ndax dañu ne : “Jaay ak ribaa ñoo yem”. Te Yàlla daganal na jaay, araamal na ribaa. Képp ku ñu ca waar ci lu jóge ca Yàlla ba nga bàyyi ribaa, mën naa téy la weesu ; mbiram ma nga ca Yàlla. Ku ca dellusi nag... ñooña, ñooy waa Safara ! Te dañu cay béel.
ﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐ
Yàlla dafay màbb ribaa, di sakkanloo sarax. Yàlla soppul ku weddi, [yéefar] bu ñemey bàkkaar.
ﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤ
Ñi gëm tey jëfe yiw , di taxawal julli tey joxe asaka, am nañu seenug pey fa seen Boroom. Te amuñu lu ñuy tiit walla lu ñuy jàq.
ﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓ
Éy yéen ñi gëm ! Ragal-leen Yàlla ; te ngeen bàyyi li des ci ribaa yi, ndegam ñu gëm ngeen.
ﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦ
Bu ngeen ko deful, nangeen séentu xeex bu tukkee ca Yàlla ak ab Yonentam. Bu ngeen tuubee, yéen a moom seen. Alal [ja ngeen dugaloon] dungeen loru, dungeen lore.
ﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶ
Ku leen ameel, su nekkee ci jafe-jafe , muñal-leen ko. Su ngeen ko bàyyee muy sarax nag moo gën ci yéen ! Ay bu ngeen xamoon !
ﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆﰇ
Ragal-leen bis boo xam ne dangeen ca dellu ca seen Boroom. Kenn ku nekk ñu delloo ko la mu jëfoon. Te kenn du ko ca tooñ [ci maandute].
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁ
Éy yéen ñi gëm ! Bu ngeen digaalee bor bu jëm ci diir bu ñu tudd, bindleen ko ; Naleen ko ab bindkat bindal, ci maandute ; bindkat bi it na ko bind ca la mu mën a binde ; te ka bor ba aju ci aw loosam, moo ko koy fite : te na ragal Boroomam ca bañ caa wàññi dara. Bu fekkee ka bor ba tegu ci loosam dafa doon ku dese, mbaa mu doyadi mbaa xel ma matul, kon na ko kilifaam fiteel. Te seedeloo ko ñaari seede yu góor ; walla genn góor ak ñaari jigéen, ñoo xam ne ñu wóor lañu ndax kenn ca jigéen ña mën naa fàtte, ka ca des fàttaliku. Ku ñuy seedeloo ba woo ko, na nangoo seede. Buleen di bañ di bind bor bu jëm ci ab dig, moo xam dafa rëy walla mu tuuti : looloo gën a maandu ca Yàlla, ngeen jub te seede moo gën a soril sikki-sàkka. Lu dul njaay mu teew mu ngeen dogal ci seen diggante : ci kaw loolu mën ngeen koo bañ a bind. Waaye nangeen di seedeloo bu ngeen di jaayante ; te bindkat ak seedekat buñu loru buñu lore. Bu ngeen defee loolu, lu ñaaw la [caay-caay la] ci yéen. Te Yàlla xam na lu ne.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶ
Bu ngeen nekkee ci tukki te amuleen bindkat, kon [ngeen jëf] tayle gu ñu téye. Te ku ñu wóolu ba dénk ko, na delloo ndénkaan la ; te mu ragal Yàlla Boroomam bañ caa sànk dara. Te buleen di nëbbu seede : ku nëbbu seede, xolam def bàkkaar. Yàlla xam na xéll li ngeen di def.
ﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖ
Yàllaa moom li nekk ci asamaan yi ak suuf si. Bu ngeen feeñalee li nekk ci yéen [seeni bakkan] walla ngeen nëbb ko, dana leen ko mas a limal moom Yàlla. Su ko defee mu jéggal ku ko soob, mbugal itam ku ko soob. Yàlla mën na lu nekk.
ﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖ
Yonent bi gëm na la ñu wàcce ca moom, la bawoo ca Yàlla, [jullit ña gëm] itam : ñoom ñépp gëm nañu Yàlla ak i Malaakaam, ak i téeréem, ak i Yonentam; (te ñu ne) : “Dunu téqale kenn ci ay Yonentam”. Wax itam : “Dégg nanu, topp nanu. Sa njéggal lanu yaakaar, di ko sàkku. Te Yaw yaa di daj dëpp gi”.
ﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆﰇﰈﰉﰊﰋﰌﰍﰎ
Yàlla du teg kenn lu dul lu mu àttan. Lu mu def ci lu baax añe ko, lu mu def ci safaan yenu ko. Yàlla sunu Boroom, bul nu jàppee la nu fàtte walla nu juum. Te bul nu teg coono kem na nga ko tege woon ña nu jiitu woon. Te bul nu teg lu ëpp sunu kàttan, jéggal nu, baal nu, yërëm nu. Yaay sunu wéeruwaay, defal nu ndimbal ci kaw yéefar yi.

Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers