Simoore Maryam
98 Aaya · Meccan · Wolof
bismillah
ﭑﭒ
Kaaf, Haa, Yaa, Ayin, Saad.
ﭓﭔﭕﭖﭗﭘ
[Fàttalikul] firndey yërmaandey sa Boroom ca jaamam ba Zakariyaa.
ﭙﭚﭛﭜﭝﭞ
Jamono ja muy ñaan Boroomam ci ag yalu,
ﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭ
mu ñaanoon ne : “Yaw Boroom bi, sama kàttan néew na, sama bopp bi bijjaaw na. Te mësumaa sooy ci ñaan la.
ﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻ
Te man dey tiit naa ci ñi may donn [ëllëg]. Te sama soxna jaasir la. Ay waay may ma doom
ﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅ
[doom] ju may donn, di donn itam njabootug Yànqooba. Te nga def ko muy kuy gërëm”.
ﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒ
"Éy Zakariyaa, Noo ngi lay bégal ci ne [danga am] doom ju tudd Yahyaa. Te turam woowu kenn masu koo am”.
ﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡ
Mu ne : “Waaw yaw Boroom bi, ana fan la ma doom di bawoo te sama soxna di ku jaasir, man itam ma màggat ba kumur ? ”
ﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰ
Mu ne ko : “Aa ! Loolu la sa Boroom wax de. Te lu ñàkk solo la ci man ndax maa la bindoon ba nga doonagul dara”.
ﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠ
Mu ne ko : “[Yàlla] sama Boroom, defal ma màndarga”. Mu ne ko : “Sa màndarga mooy danga am ñetti fan yoo dul mën a waxante.
ﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬ
Mu daldi génne ca fa [mu doon jaaamoo Yàlla] ; jottale leen ne nañuy sàbbal Yàlla suba ak ngoon.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙ
"Éy Yahyaa, jàngal Téere ba [cig settantal] ! ”.Jox Nanu la xam-xamu xereñe [àtte ya] ca ba nga doonee ndaw,
ﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡ
ci ag ñeewant ak ug sellal. Mu doonoon ku ragal Yàlla,
ﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨ
di ku toppoon ay waajuram ; doonutoon ku fétterlu mbaa muy kut.
ﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲ
Te jàmm rekk la am ca ba mu juddoo ak ca ba muy dee, ak ca ba muy dekkiwaat !
ﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽ
[Fàttalikul], ca Téere ba, Maryaama ba mu fàddoo mbokk ya, génn dem fa penku dëkk ba.
ﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉ
Mu wutoon kiiraay seen diggante. Nu daldi yónni ci moom Sunu ruu [Malaaka] mu yor jëmmi nit [Jibriil].
ﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒ
[Maryaama] daldi ne : “Man dey maa ngi sàkku ci yërëmaakoon bi [Yàlla] mu musal ma ci yaw ndeem ku ragal Yàlla nga.
ﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜ
Malaaka ma [Jibriil] ne ko : “Man dey ndawul sa Boroom laa [damaa ñëw] ngir may la doom ju sell”.
ﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨ
Mu ne ko : “Man naka laay ame doom, te génn góor masumaa laal, te duma ku baaloy ? ”
ﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛ
Mu ne ko : “Loolu la sa Boroom wax ! Te lu yomb la ci Man ! Lii dafay doon kéemaan ci nit ñi, ak yërmaande wu bawoo fa Yàlla. Dogal ba sotti na”.
ﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢ
Mu daldi ëmb, daldi dem ca bérab bu sori.
ﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰ
Mat ma dikkal ko mu wattatu ba ca benn dàttu tàndarma, mu daldi ne: “Aka neexoon ma dee lu jiitu ! Kon fàttees na ma ! ”
ﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻ
Mu daldi koy woo ci ronam, ne ko : “Bul ragal, bul jàq. Yàlla defal na la ag dex ci sa ron [ci suuf] ndox.
ﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄ
Gësëmal tàndarma gi : meññent mu nooy dana rot ci say tànk.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤ
Lekkal te naan te dalal sam xel ! Nit koo fi mëna gis nee ko: “Damaa woor, tey duma wax ak kenn nit”.
ﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰ
Mu lewu [doom ja] indi ko fa mbokk ya. Ñu ne ko : “Indi nga fi mbir mu juunu !
ﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼ
Yaw jigéenub Haaruuna bi, sa baay de doonul woon ku bon, sa yaay it du ku baaloy [taxawaalukat]”.
ﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈ
Mu joxoñ leen liir ba. Ñu ne ko : “Naka la nuy waxeek liir bu tëdd ciy laltaay ? ”
ﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑ
Liir ba daldi ne : “Man dey jaamub Yàlla laa. Jox na ma Téere ba, def ma ab Yonent.
ﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝ
Te it, def na ma ku barkeel [sakkan]fu ma mën a nekk; dénk ma ma taxawal julli, di natt asaka feek maa ngi dundu ;
ﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤ
tey topp sama yaay. Te doonuma kuy fétterlu, ku texeedi.
ﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮ
Jàmm rekk laay am bis ba ma juddoo, ak ca bis ba may dee ak bis ba may dekkiwaat”.
ﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚ
Loolu mooy mbirum Iisaa doomu Maryam, wax jii moo cay dëgg ca la ngeen doon werante.
ﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭ
Yellul ci Yàlla muy jàppe kenn doomam. Cëy sellam ga ! Bu bëggee menn mbir, Danaan : “Nekkal ! ” mu daldi nekk.
ﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷ
“Te nag Yàlla moo di sama Boroom, di seen Boroom. Jaamuleen ko. Lii moo di yoon wu jub wi xocc”.
ﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄ
Kurél yi juuyoo nañu ci seen diggante. Ñay weddi, xuru Safara ñeel na leen ca teewaayub bis bu màgg ba !
ﰅﰆﰇﰈﰉﰊﰋﰌﰍﰎﰏﰐﰑ
[Bu bis baa, tooñkat yi danañu dégg], danañu gis ! Waaye tey fii ci àddina, ñi ngi ci réer gu bir.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝ
Nanga leen xupp ci tiisu bisub jagle ga ; ndax àtte ba dog na te ñoom ña nga cig càggante te duñu gëm.
ﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦ
Nun nooy donnu suuf si ak lépp lu nekk ci kawam, te it fi Nun la ñuy dellusi [Bis-pénc ba].
ﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰ
[Fàttalikul] Ibraahiima ca Téere ba, moom dey ku dëggu woon la, di ab Yonent.
ﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀ
[Fàttalikul] ba mu waxee baayam ne ko : “Ana lan moo tax ngay jaamu loo xam ne du dégg du gis, te du la fajal dara ?
ﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎ
Man sama baay, man dey am naa ci xam-xam loo xam ne yaw amoo ko ; topp ma, kon dey danaa la gindi, [teg la] ci yoon wu jub wa.
ﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙ
Yaw sama baay, bul di jaamu Séytaane, ndax Séytaane kat moykatub Yàlla la.
ﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥ
Yaw sama baay, man dey ragal naa mbugalum Yàlla dal la nga fay lëkkook Séytaane”.
ﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕ
Baayam daldi ne ko : "Moo Ibraahiima, ndax dangaa bañ sama yàlla jii ? Soo bàyyilwul [lii ngay wax], danaa la yóori xeer [ba nga dee], te sax génnal topp sa një”.
ﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢ
[Ibraahiima] ne ko : “Yal na jàmm nekk ci yaw”. “Danaa la sàkkul njéggal ci sama Boroom ndax Ku ma teral la.
ﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱ
Danaa leen beru yéen ak ñi ngeen di jaamu te du Yàlla, tey ñaan sama Boroom. Yaakaar naa ne duma xañ”.
ﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁ
Ba mu leen beroo, [dëddu leen] ñoom ak la ñu daan jaamu te duñu Yàlla, booba Lanu ko may Isaaqa ak Yànqooba ; def leen ñoom ñaar ñépp ñu di ay Yonent.
ﰂﰃﰄﰅﰆﰇﰈﰉﰊﰋ
Nu daldi leen may ci Sunu yërmaande, defal leen làmmiñ wu dëggu wu kawe.
ﰌﰍﰎﰏﰐﰑﰒﰓﰔﰕﰖﰗ
[Fàttalikul] Muusaa ca Téere ba. Moom dey ku sellal la woon, di ku ñu soloo, di ab Yonent.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘ
Woo Nanu ko ca wetug ndeyjooru tundu Sinaay wa, sësloo ko rëkk ci Nun.
ﭙﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠ
Nu daldi koy may ci Sunu yërmaande, defal ko mbokkam ma Aaruuna mu di ab Yonent.
ﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭ
[Fàttalikul] Ismayla ca Téere ba. Doonoon na boroom dégg bu dëggu ; dib Yonent.
ﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷ
Daa woon na digal njabootam taxawal julli ak asaka, di ku amoom ngërëmul Yàlla.
ﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁ
Fàttalikul Idriisa ca Téere ba. Moom dey ku dëddu la woon, di ab Yonent.
ﮂﮃﮄﮅ
Mayoon Nanu ko daraja ju kawe.
ﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥ
Ñooña ñooy ña nga xam ne Yàlla wàcceloon na leen xéewalam ca Yonent ya, ak ca sëti Aadama, ak ña àndoon ak Nooh ca gaal ga, ak ña bokk ca sëti Ibraahiima ak ca ñu Nu gindi woon te tànnoon leen. Te saa su ñu mësaa na jàng kàdduy Yàlla fa ñoom, ñu rot sujjóot boole kooki jooy.
ﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔ
Seen ginnaaw mu am ñu leen wuutu, sànk julli, topp seeni bànneex. Ñooña danañu dajeek tuskare,
ﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡ
ba mu des ku tuub te gëm tey jëf u yiw : ñooña danañu tàbbi Àjjana te keen duleen tooñ ci dara [wàññi seenug pey],
ﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮ
àjjana yu sax ya, àjjana ya Yàlla dig jaamam ña ci kumpa te digub Yàlla fàwwu mu ñëw.
ﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻ
Duñu fa dégg lenn coow ; daldi leen kañ ci : “Jàmm” ; te ñam ya du dogamtal suba ak ngoon.
ﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅ
Àjjana jooju la Nuy donnale képp ku ragal Yàlla ci Sunu jaam ñi.
ﰆﰇﰈﰉﰊﰋﰌﰍﰎﰏﰐﰑﰒﰓﰔﰕﰖﰗﰘﰙﰚ
“Dunu wàcce ca Àjjana ja lu dul ci ndigalul Yàlla. Mooy Boroom li wéy ak li teew ak liy ñëw. Sa Boroom du fàtte de.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚﭛﭜﭝﭞ
Boroom asamaan yi ak suuf si ak li nekk ci seen diggante. Nanga ko jaamu te nanga sax ci jaamu Ko. Waaw ndax xamal nga ko benn turandoo? Mukk amul ”
ﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧ
Nit nag di wax naan : “Ndax su ma dee danañu ma génnewaat may dundu ? ”
ﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲ
Moo ndax nit dafa fàttalikuwul ne Noo ko bindoon bu njëkk te doonutoon dara ?
ﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻ
Giñ naa ci sa màggug Boroom ne Dananu leen pang [dajale] ñook séytaane ya ba ñu yemb. Nu wërële leen ca Safara ñu sukk fa.
ﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆ
Ba noppi nag, Nuy rocci ci xeet wu nekk kan moo ca gën tar ug féttéerlu ca Yàlla.
ﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍﮎﮏ
Noo gën a xam kan moo gën a yeyoo jaaru ca Safara.
ﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚ
Ñépp a fay jaar, Yàlla dogal na ko ba noppi.
ﮛﮜﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣ
Bu ko defee Nu musal ñi ragal Yàlla, daldi fay bàyyi tooñkat ya ñu sukk.
ﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕ
Saa su ñu jàngee Sunuy laaya ca ñoom, muy lu leer nàññ, yéefar ya dañuy daldi wax ne gëmunu leen : “Ana sunu ñaari kurél yi ban moo ci ëpp daraja ? ”
ﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟ
Aka bari ña Nu alagoon ca ña leen jiitu, ñoo xam ne ñoo leen ëppoon alal, gën leen a jekk ?
ﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺ
Neel : “Ku nekk cig réer, Yàlla da koy yoor ba mu ne ticcët ca la Nu ko doon dig, benn muy mbugal walla muy Bis-pénc ba. Bu boobaa danañu xam ñoo, ana kan moo yées wàccuwaay te gën a néew doole [ci way gëm ña ak yéefar ya]”.
ﯻﯼﯽﯾﯿﰀﰁﰂﰃﰄﰅﰆﰇﰈﰉ
Yàlla dana dolli njub ña gindiku woon. Jëf yuy des te di yu jiw [sell] moo gën a ëpp ab yool fa sa Boroom te moo gën wàccuwaay.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙ
Xanaa gisoo ka weddi Sunuy kàddu bay wax naan : “[Ak lu mën a xew], man danaa am alal ak i doom” ?
ﭚﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡ
Moo ndax dafa xam kumpa, walla mu digaaleek Yàlla ?
ﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬ
Déewallaay ! Dananu bind la muy wax, te it Dananu ko mbugal.
ﭭﭮﭯﭰﭱﭲ
[Doom ya ak alal ja] Dananu ko donn, te buy dikk fi Nun jubbu boppam lay àndal.
ﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻ
Dañuy jàpp leneen lu dul Yàlla [di ko jaamu] ngir ame ca teraanga [dimbal].
ﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃ
Ndaw njombe ! [Ya ñu doon jaamu] dana weddi jaamu googee te dañuy far safaanoo
ﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋﮌﮍ
Xanaa gisoo ne Danañu yebal Séytaane ca yéefar ya ñu leen di jax-jaxee ?
ﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖ
Bul yàkkamti seen mbir : dafa am rekk lu ñu leen di nége.
ﮗﮘﮙﮚﮛﮜﮝ
Bis ba ñuy pang ña ragal ña Yàlla jëme leen ca Yërëmaakoon ba ñu di ay mbooloo,
ﮞﮟﮠﮡﮢﮣ
Nu sëkkëtal tooñkat ya jëme leen Safara ñuy sërëx-sërëxi,
ﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭ
[Bis booba] kenn du mën a ramm ku dul ku ko Yàlla digal.
ﮮﮯﮰﮱﯓ
Ñuy wax it naan : “[Yàlla] Yërëmaakoon ba am na doom ! ”
ﯔﯕﯖﯗﯘ
Indi ngeen lu juunu !
ﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡﯢ
[Loo xam ne] asamaan yi xaw na cee xottiku, suuf si xar, tundi doj yi màbb [ngir wax jooju],
ﯣﯤﯥﯦﯧ
ña wax ne alamikk Yàlla am na doom,
ﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮ
Waay-waay yellut ci Yërëmaakoon bi muy am doom waay !
ﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹ
Képp ku nekk ci asamaan yi ak suuf si, jaamub Yàlla rekk lay doon.
ﯺﯻﯼﯽﯾ
[Moom Yàlla] xam na fa ñu nekk ak na ñu day [na ñu tollu].
ﯿﰀﰁﰂﰃﰄ
Te bu Bis-pénc baa, bindéef yépp danañu taxaw ci kanamam kennoo kenn.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚ
Ña gëm tey jëf u yiw, Yàlla dana leen sagoo.
ﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥ
Yombalal Nanu la Téere bii, jaarale ko ci saw làmmiñ ngir nga bégal ci ñi ragal Yàlla te xupp ca ña dëgër bopp [weddi].
ﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴ
Aka bari li Nu alag ca xeet ya leen jiitu woon ! Moo ndax gisati nga lu ca bokk ? Mbaa nga déggati seenum riir ?

Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers