Simoore An-Najm
62 Aaya · Meccan · Wolof
bismillah
ﭑﭒﭓﭔ
Maa ngi giñ ci biddiwub (dëlóoñ ba) !
ﭕﭖﭗﭘﭙﭚ
(Ci ni) seen àndandoo ji (Muhammad) réerul te it juumul
ﭛﭜﭝﭞﭟ
te itam du àddu mukk ci bànneex ;
ﭠﭡﭢﭣﭤﭥ
du lenn lu dul ak soloo gu ñu koy soloo.
ﭦﭧﭨﭩ
[Jibriil] boroom kàttan gu tar ga moo ko jàngal,
ﭪﭫﭬﭭ
mu di ku taaru te yemoo,
ﭮﭯﭰﭱ
te moom ma nga ca déeléy asamaan ya gën a kawe (guddig rañaan ga).
ﭲﭳﭴﭵ
Daldi nay jegeñ ba faf yoore,
ﭶﭷﭸﭹﭺﭻ
Moo ngi jege woon ni ñaari xocci xala, walla sax mu gën a jigeñ loolu
ﭼﭽﭾﭿﮀﮁ
(Foofee) la Yàlla soloo jaamam la mu ko soloo.
ﮂﮃﮄﮅﮆﮇ
Xol ba weddiwul la mu gis.
ﮈﮉﮊﮋﮌ
Moo ndax yéen dangeen di weranteek moom ca la mu gisoon ?
ﮍﮎﮏﮐﮑ
Moo ne gisoon na ko de, ca geneen wàcc,
ﮒﮓﮔﮕ
kerook rañaan ma fa “Sidratu Al Muntahaa”,
ﮖﮗﮘﮙ
foofee la jannatu “al Maawaa” nekk :
ﮚﮛﮜﮝﮞﮟ
la koy muur muur na ko (di lalub wurus).
ﮠﮡﮢﮣﮤﮥ
Da koo gis dëgg bët ya jéllul jaawalewul.
ﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬ
Gis tigi ca kéemtaani Boroomam ya gën a màgg.
ﮭﮮﮯﮰ
Waaw xërëmu Laata ak Uzzaa lu ñu leen di niru,
ﮱﯓﯔﯕ
ak Manaat xërëm ba ca des, te ñetteel leen ?
ﯖﯗﯘﯙﯚ
Moo ndax yéen a am doom yu góor moom Yàlla mu am ay jigéen ?
ﯛﯜﯝﯞﯟ
(Xam ngeen) ne woowu séddale yéen jubul de !
ﯠﯡﯢﯣﯤﯥﯦﯧﯨﯩﯪﯫﯬﯭﯮﯯﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷﯸﯹﯺﯻ
Loolu ay tur la doŋŋ yu ngeen di tudd (xërëm ya), yéen ak seeni baay. Seen njortu rekk la ñu topp waaye yayoowunu jaamu. Topp it seen bànneex, looloo tax njub dikk bawoo fa seen Boroom.
ﯼﯽﯾﯿﰀ
Walla book nit moom limu mébét da koy daldi am ?
ﰁﰂﰃﰄ
Yàllaa moom àddinaak àllaaxira.
ﰅﰆﰇﰈﰉﰊﰋﰌﰍﰎﰏﰐﰑﰒﰓﰔﰕﰖﰗﰘ
Aka bari Malaaka yu nekk ca asamaan ya te seenug ramu du jiñ dara, ndare ginnaaw bu Yàlla joxee ndigal, mu jëm ci ku Ko soob te Mu gëram ko.
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖﭗﭘﭙﭚ
Ña nga xam ne da ñoo gëmul àllaaxira ñooy tudde Malaaka yi turi jigéen,
ﭛﭜﭝﭞﭟﭠﭡﭢﭣﭤﭥﭦﭧﭨﭩﭪﭫﭬﭭ
te ñoom amuñu ca benn xam-xam : seeni njortu rekk la ñuy topp, te njortu moom jotewul dara ak dëgg.
ﭮﭯﭰﭱﭲﭳﭴﭵﭶﭷﭸﭹ
dëdul, képp kuy dumóoyu Sunug fàttali te dundug àddina rekk ñor ko.
ﭺﭻﭼﭽﭾﭿﮀﮁﮂﮃﮄﮅﮆﮇﮈﮉﮊﮋ
Foofu la seen xam-xam yem. Waaye sa Boroom Moo gën a xam ku réere aw yoonam Moo gën a xam it ku gindiku.
ﮌﮍﮎﮏﮐﮑﮒﮓﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚﮛﮜ
Yàlla moom yi nekk ci asamaan yeek suuf si dana fay ña daan jëf jëf yu ñaaw kem la ñu daan jëf, dana fay it ña daan rafetal seen jëf pey gu gën a rafet,
ﮝﮞﮟﮠﮡﮢﮣﮤﮥﮦﮧﮨﮩﮪﮫﮬﮭﮮﮯﮰﮱﯓﯔﯕﯖﯗﯘﯙﯚﯛﯜﯝﯞﯟﯠﯡ
ña nga xam ne dañuy moytu bàkkaar yu mag ya ak ñawtéef. Te it moo gën a xam li nekk ci yéen ngir moom Moo leen sose ci suuf def leen ngeen di ay liir ci seen biiri nday. Buleen di tagg seen bopp; (moom Yàlla) Moo gën a xam ana kan moo ragal Yàlla.
ﯢﯣﯤﯥ
Moo xanaa gisuloo ka dumóoyu fuuyu,
ﯦﯧﯨﯩ
muy joxe tuuti faf ko bàyyi ?
ﯪﯫﯬﯭﯮﯯ
Moo ndax dafa am xam-xamu Kumpa di ko gis ?
ﯰﯱﯲﯳﯴﯵﯶﯷ
Walla book dafa xamul li nekk ca téerey Muusaa
ﯸﯹﯺﯻ
ak Ibraahiima ma jottaloon lool
ﯼﯽﯾﯿﰀﰁ
benn bakkan du gàddul bakkan bàkkaaram,
ﰂﰃﰄﰅﰆﰇﰈ
li wér daal, nit ku nekk jëfam lay añe ;
ﰉﰊﰋﰌﰍ
te la mu daan jëf, dana fés, bu bis pénc baa.
ﰎﰏﰐﰑﰒ
Te dees na ko ko fay ba mu mat sëkk,
ﰓﰔﰕﰖﰗ
te nag lépp, ngay jeexe, ca sa Boroom,
ﰘﰙﰚﰛﰜ
te moom Mooy reetaanloo di jooyloo,
ﰝﰞﰟﰠﰡ
te it moom Mooy rey mooy dekkal,
ﭑﭒﭓﭔﭕﭖ
te moom Moo bind ñaari tóolent , yu di góor ak jigéen,
ﭗﭘﭙﭚﭛ
muy bawoo ci toq maniyu wu wàcci ci njurukaay
ﭜﭝﭞﭟﭠ
moom moo waral it sosuwaat ga dekkiwaat,
ﭡﭢﭣﭤﭥ
te moom Mooy woomalale.
ﭦﭧﭨﭩﭪ
Te mooy boroom biddiw ba Si’raa,
ﭫﭬﭭﭮﭯ
te moom Moo faagaagaloon waa Aad ñu jëkk ña,
ﭰﭱﭲﭳ
ak waa Samuud, ba kenn desufa,
ﭴﭵﭶﭷﭸﭹﭺﭻﭼﭽﭾ
ak nitu Nooh ñu jëkk ña, ndax ñoom ñoo dàqoon tooñ te gënoon a bew,
ﭿﮀﮁ
noona la wëlbatee suuf sa këpp leen ko.
ﮂﮃﮄﮅ
Muur leen ko.
ﮆﮇﮈﮉﮊ
Ana ban ci sa xéewali Boroom yi ngay werante ?
ﮋﮌﮍﮎﮏﮐ
(Muhammad mii) ab xuppekat la ni Yonent ya ko jiitu woon :
ﮑﮒﮓ
bisub àtte ba jege na.
ﮔﮕﮖﮗﮘﮙﮚ
Kuddul Yàlla manul a tee mu am.
ﮛﮜﮝﮞﮟ
Moo ndax ! Ci waxtaan wii ngeen di béegraay ?
ﮠﮡﮢﮣ
Di ci reetaan te jooyuleen ?
ﮤﮥﮦ
ngeen di nuur rekk ci càggante.
ﮧﮨﮩﮪﮫ
Sàbbaalleen Yàlla te ngeen jaamu Ko.

Alxuraan bu Tedd bi


Tuesday, August 18, 2026

Don't forget us in your sincere prayers